44

Jazbul Majzòobdrouss.org/assets/pdf/JazbulMajzoob.pdfJazbul Majzòob - 3‘‘ku sédduwul man séddu naa, ku fadduwul, man faddu naa, Ba matlu, wéésu naa dansa, Yalla ak sa barké,

  • Upload
    others

  • View
    26

  • Download
    8

Embed Size (px)

Citation preview

Jazbul MajzòobSeex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay

(1868 - 1917)

© 1436 h / 2014 - www.drouss.orgTous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution

gratuite sans rien modifier du texte.Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez

nous contacter par le biais de notre site internet : www.drouss.org

2 - Jazbul Majzòob

Apercu sur l’auteurNé en 1868 et fils de Ahmadou et de Soxna Ndack Kane, Cheikh Samba Diarra est l’un des disciples de Serigne Touba qui habitaient Saint Louis. Originaire de KOKI, il fût l’un des poètes les plus fascinants dans l’univers wolof, ci réewi wolof. Il faisait part de ces saints difficilement repérables ; car il vivait dans la masse, comme tout le monde ; et allait même vendre au marché.En allant faire allégeance à Cheikhoul Xadym, Cheikh Samba Diarra rejoignait son frère ainée Cheikh Sadiaye, à Ndiarème. Contrairement à ce que plus d’un raconte sur son allégeance, il n’a jamais été un griot qui battait des tam-tam. Cheikh Samba Diarra fût un éminent érudit qui mémorisa le coran à son bas âge ; plutard il quitta Koki pour rallier la ville de Saint-Louis afin d’y étudier les sciences religieuses.Son travail a contribué à diffuser les enseignements de Cheikh Ahmadou Bamba parmi les masses wolof.Tantòt sur ses poèmes, il fait des insertions de mots arabes, des phrases et des prières, y compris dans les ouvertures et fermetures. Il a composé de nombreux poèmes, y compris les louanges dédiée à Cheikh Ahmadou Bamba et sa contribution au Sénégal, ses miracles en Mauritanie, et les qualités de Cheikh Ibra Fall.Parmis ses oeuvres poétiques, Jazbul Majzoob (‘‘l’attirance du majzùb [l’attiré]’’) reste le plus populaire.Il est aussi un proche parent de Serigne Mor Kayré (1869-1951), un autre éminent spécialiste wolofal mouride. Tous deux vivaient ensemble en Mauritanie et rendaient visite à leur maître, Cheikh Ahmadou Bamba, qui y fut exilé par l’administration coloniale française de 1903 à 1907.Un jour lors d’une de ses promenades au bord du fleuve Sénégal, il croisa des jeunes demoiselles d’une beauté indescriptible. Il leur demanda l’objet de leur présence sur les lieux. Elles répondirent qu’elles ont été envoyées pour venir accueillir un de leur seigneur un talibé de Serigne Touba du nom de Cheikh Samba Diarra Mbaye. Il retourna chez lui en abandonnant ses chaussures sur place. Quelques temps après il quitta ce monde. Avant de partir il écrit :

Jazbul Majzòob - 3

‘‘ku sédduwul man séddu naa, ku fadduwul, man faddu naa, Ba matlu, wéésu naa dansa, Yalla ak sa barké, maa la gëm’’.Quelques temps aprés ces vers, Serigne Samba Diarra Mbaye fût rappelé à Dieu, en 1917. Son mausolée se trouve au cimetière de Thiém, à Saint-Louis du Sénégal.Il n’a eu que trois (3) enfants à savoir :- Fatima Zahra Mbaye - El Hadj Mbacke Mbaye- Mouhammadou Moustapha Mbaye

4 - Jazbul Majzòob

Indications

Wolof Française = é per péru = ou rus rousc = th caam thiamñ = gn ñam gnamx = kh xol kholj = dj jibi djibinj = nd njaay ndiayend = nd nday ndeyeŋ ŋaam (machoire)ë = eu gëm = geumé = è (plus dur) = rér perduòo = au gòor gaureq = xx suqali soukh khaliii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ; Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

Jazbul Majzòob - 5

Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi

AI xamdu Iil-laahi, kimay Xamal bu wér, ta dima may Xéewël, Ci barkeb kimu xëy, Jébbal lu dooni xéewëlam.

Yéen gaayi diine jegeleen Ma jegeleen te dolli leen, Xam-xam bu wér te jafe leen, Ma fecci tay ay fas-fasam.

Koo xam ni xam na Iii,na xam, Ku ko xamul, ma wax mu xam, Xamlug xamul, day taxa xam, Xamlu ku xam ,day dolli xam.

Te Iii ma leen di bëgg a wax, Day dàggi xol, dëggali wax, Jagali jëf, te ku ko wax, Jariñu fii, ak fa nu jëm.

Masuma leen a waxi neen, Te lii ma wax, du waxi neen, Lii woyu xudbu la, du neen, Yu deefi woy ñu dul kemam.

6 - Jazbul Majzòob

Naa sant yàlla mi ma may, Xudbu bu mat, mu dima may, Di fey ay, di dàqi moy, Ci leeri mbòoti ragalam.

Dima gisal luma gisul, Dima yëgal luma yëgul, Dima xamal luma xamul, Ci duusi géeji xam-xamam.

Dima amal luma amuI, Dima wutal, dima wattul, Dima digal, dima tamal, Nangoo yamooki ndigalam.

Dima yërëm, dima tifaI, Dima jariñ, dima teral, Def ma ma mel ni ku nu fal, Ku tàbbi péeyi ngërëmam,

Dima dugal fu may musal, Dima fegal lu ma ragal, Ku jëm ci man aki fetal, Mu boole diigali walam.

Jazbul Majzòob - 7

Dima setal ci waxi bañ, Ba ku ma yéene jëfi bañ, Mu ni ko tëf, mu ni suluñ, Daanu, di toppal fetalam.

Dima xëccal, dima jañal, Dima tàyyill, dima tayaI, Dima ubbil bunti xéewël, Fatma ci biir roqi ñoñam,

Ne ma yëkkét, newuma tuy, Wan ma boppam, ma di ko woy, Ta di ko kañ, mu di ma may, Ne ma yoxoos ci biir xolam.

Di ma fegaI pexe mu naaw, Di ma teral ren aki daaw, Di ma teral sama gannaaw, Di ma teral sama kanam.

Dib suruseñ bimay fajal, Di garabal lima ragal, Di ma félal lumay sonal , Mu teggi, teg, yenu jëem.

8 - Jazbul Majzòob

Dima toggal, dima yakkal, Dima ràccal, di ma sefal, Dima tibbal, di ma leyal, Tib yu ñu barkeelug wannam.

Di ma bégaI, di ma seraI, Dima xàjjal, di ma dalal, Dima moyuI, di ma fayuI, Kenn du ma yab fi kanamam.

Bu ma yewwee, kenn du ma yab, Fu ma fi jëm, du ma ayib, Sama gannaaw sama ayib, Xanaa nammeel gu ñu ma namm.

Sama ñoñ it du ñu ayib, Man aki ñoom du ñu layib, Sëriñ bi moo dajale yëpp, Beral nu cër bu ñu gërëm,

Limu ma may ma di ko am, Moo ma ko may ma di ko am. Limu ma wax ma di ko xam, Moo ma ko wax ma di ko xam.

Jazbul Majzòob - 9

Limu ma wan ma di ko gis, Moo ma ko wan ma di ko gis. Ta ku ko gis, ni ku ko gis, Ni ku ko xam, ni ku ko am.

May na ma lool, danaa ko wax, May na ma lool, duma ko wax, May na ma lool, man mi ko wax, Ak ba ko ñooni kee fa yam.

Man Samba Jaara, maa gërëm Samab sëriñ, danaa xorom Way wi ma way ci waa këram, Ñoo am ngërëm, ñoo am xorom.

Bu sëg sëggee ba ñu wéral, Li tax ma jòg di ko biral, Werante deñ, kon nag yëral Seeni jaloore ca kanam.

Jësbul xulòob bi dafa jib, Bii jësbu jóg xeeñ famu jub- Lu, ku ko xeeñ na wut a jub, Wéy na xameeful fu mu jëm.

10 - Jazbul Majzòob

Jësbul xuloob bi dafa daw, Bii jësbu jóg, xeeñ fa mu aw, Ta ku ko dab na daw a daw, Raw na xameeful fu mu yam.

Lu jiitu Iii dafa dawal, Ña daa rawanteeg a dawal, Naka fëxël raw ba àggal, Akk am wa kenn gisul pëndam.

Ma daldi jóg, tofal ko bii jësbu, di woy ki woy Nabi, Di ko ko Fayna woy Nabi, Ma di ko woy ba fa nu jëm.

Kemub liñuy dox di ko woy, Fayante la ak moom ki mu woy, Dakoo gërëm ba di ko ma , Lammiñ yi daldi ko gërëm,

Ma far jafal man di ko woy, Di barkeeloog a di ko roy Ci woy, ba daane ku ko woy, Ak ku woyul ñu ne wedam.

Jazbul Majzòob - 11

Lu ma wax ak lu ma waxul , Wuute gi fës na, nëbbuwul, Ta ba fi tay danaa fësal Lu doy a xam ci ay woyam.

Danaa xamaI, xamul mu xam, Xamal ku xam, mu gën a xam, Ku bëgg a gis ta bëgg a xam, Na déglu, xippi ay bëtam.

Kenn du werante Ii ma wax, Way xam ya, xam na sama wax, Seriñ bii moo may sa, ma wax, Moo tax ma saf ko ci xolam.

Bulen ma yéem, yéemleen ko, ndax Du man di wax, mooy ka di wax, Waxande laa wuñ tëjii wax, Bu ma tijjee may lammiñam.

Wàlliyu day feeñu, ta kum Feeñu ci yaw, nga daldi xam, Bu nee waxal, nga wax ñu xam, Way xam ya ,seede daaldi gëm.

12 - Jazbul Majzòob

Bu fekkee moo feeñu ci man, Ñu naa ma yaw, booba du man, Moom,ka di moom, moo fi di man. Ma di fi moom, muy ki fi xam.

Moo tax ma wax ku déglu lii Na xam ni yii ñuy wax du lii, Waaraate jòowuma si lii, Seriñ bi may na ma boppam.

Kaawteefug yonent la gu des, Te ag wéyam dara du des, Lu doon kiraama yu fi des, Dana ko yòbbaale ñu dem.

Sëriñ bi muxjisaat la, moom, Man nak kiraama laa, ci moom, Ku weddi lii, na dem fa moom, Laaj ko, mu teqalem lëjam.

Moo tax li may wax moo ko moom, Mësuma ko jaawale moom, Tudd turam doy na ma koom, Ta mooy seral sama yaram.

Jazbul Majzòob - 13

Bind turam may na ma xel, Tudd turam may na ma xol, Siirub turam may na ma lool, Du ma ko wax, xol a ko xam.

Danaa biral tuuti, ci ay Mayam ci man, yu ñu ma may, Te yile may, ku ñu ko may, War nay gërëm diirug dundam.

Buur yàllamay na ma ci moom, Gëm, ak xam, ak lafu ci moom, Ma jòg ne naa taasu ci moom, Di ko beral woyi ngërëm.

May na ma lool, deefuma ñax, Wan na ma lool, deefuma nax, Naxtima kenn, kenn duma nax, Sama ngërëm rawnag xalam.

Xam naa ndigël, xam naa ndugël, Tinaa ndigël ,të naa ndugël, Damay digël duma dugël, Sama mébët, aw ndigëlam.

14 - Jazbul Majzòob

Ki lay digël, ta du la jay, Ki lay dugël, ta di la jay, Boo xelluwul, defoo ku way, Réccooki jooy feeñ sa kanam.

Ku may digël, dafay taxaw, Ku may dugël, dafay taxaw, Ta naa awal, fii bufi aw, Ki ma giseel a mat a xam

Lu ne ci Iii, ma ni ko jàkk, Lu ne ci lee, ma ni ko jàkk, Xam la jagul, ñee ak la jag, Ki ma giseel a mat a am.

Wan na ma lool, yee na ma jar, Ba ma ràññee dëgg aki nar, Jarti ma kenn, kenn duma jar, Ki ma giseel a mat a xam.

Wan na ma lol, dindi na sikk Ci sama xol, ba duma sikk, Duma ragal lu ki ma sàkk Ki ma giseel a mat a am.

Jazbul Majzòob - 15

Feesal na xol bi, ba du xam, Lu doy a yéem ci Ii mu xam, Lu ki nga xam ni moom la xam Ki ma giseel a mat a am.

Feesal na bët bi ba du gis, Lu doy a yéem ci Ii mu gis, Lu ki nga xam ni moom la gis, Ki ma giseel a mat a am.

Doylul na xol bi, ba du raf, Jëm ci leneen lu lu ko saf, Ci biir malaanam lama laf, Ki ma giseel a mat a xam.

Génne na réer ci sama xol, Dugal na riir ci sama xel, Kenn duma yeer di sañaxal, Ki ma giseel a mat a am.

Kenn du ma wootal di ma fiir, Kenn du ma yab, ba di ma fiir, Mi ma andal, ta dafa fiir, Ki ma giseel a mat a xam

16 - Jazbul Majzòob

May na ma xam-xam, ba ma xam, Xòot-xòoti xam-xam yu ma xam Ci moom, ba jaaxal ku ma xam, Ki ma giseel a mat a am.

Dolli na am-am bu ma am, Dolli na xam-xam bu ma xam, Leeral na mbooleem Ii ma xam, Ki ma giseel a mat a xam.

Jëfi wilaaya la ma wan, Dindi la woon wëccag ña woon, Def fi leneen di ma ko wan, Ki ma giseel a mat a am.

May na ma wóoluu ki ma moom, Xiir ma ci moom gi mu fi moom, Biral ma moom gi mu ma moom, Ki ma giseel a mat a xam.

Biral ma sañ-sañ bi mu sañ, Bitéegi biir moo ko fi sañ, Ta kenn du sañ Ii mu fi sañ, Ki ma giseel a mat a am.

Jazbul Majzòob - 17

Biral ma saayiir sa, bu wér, Biral ma baatin ba, bu wér, Ne ma lu dul lii, du lu wér, Ki ma giseel a mat a xam.

Ne ma yëkket yor ci loxoom, Di ma xamal lu diy soloom, Di baay ci baatin, ma di doom, Ki ma gïseel a mat a am.

Jiitu ma ànd ak man di wëy, Lu may gagal mu ni ko tuy, Ba man ma waaru ba ni cëy, Ki ma giseel a mat a xam.

Di ma digël, ta du ma jay, Fu ma taxaw, mu di ma xëy, Ta di ma gontu, di ma may, Ki ma giseel a mat a am

Nee ñooki, nee na, lani cas, Buttil ma biir ba ba ma gis, Raññeel ma mboot yi, ba mu fës, Ki ma giseel a mat a xam

18 - Jazbul Majzòob

Ni dëgg a ngii dëgg a fi gën Fen du taxaw, tag ti fi fenn, Ku jëm fi péey ,du yori fen, Ki ma giseel a mat a am.

Lisaani aal lamiy waxam, Lay sànni xol bi, ba ma xam , Fu ma fi tollu di ko xam, Ki ma giseel a mat a xam.

Moom ka di moom, xam na ma xam, Lu diy mbiram laa jëkk a xam, Boobee ba tay, ma di ko xam, Ki ma giseel a mat a xam.

Léewoo na ma ak moom cig cofeel, Di ko mébët ba may xaleel, Mu daal di may fab yobbu teel, Ki ma giseel a mat a am.

Tegtal ma yoonu njariñam, Ubbil ma bunti xéewëlam, Burxal ma mbòoti ngërëmam, Ki ma giseel a mat a xam.

Jazbul Majzòob - 19

Yee na ma jar, ba ma ni jar, Fegal ma kor, sàmmal ma ngor, Fayal ma mer, fajal ma mar, Ki ma giseel a mat a am.

Di ma defar, ta di ma far, Ta ku ma far, mu di ko far, Ta lu ma far, daal di ko far, Kima giseel a mat a xam.

Di ma taxawu, ma taxaw, Buma taxawul, mu taxaw, Teeweel ma xew, luy mën a xew, Kima giseel a mat a am.

Ku jëm fi man di ma lëjal, Mu boolekoog lu kay lëjal, Lu gën mu fab jox ma, ma jël, Kima giseel a mat a xam

Lu ma ragal mu ni ko cas Sànni, ba dootu ma ko gis, Mbaa mu labal ko, mu ni mes, Kima giseel a mat a am.

20 - Jazbul Majzòob

Bittërñi dun bi, ba ma gis Ni muy naxee, ta ku ko gis Jox ko gannaaw mel ni ku rus, Kima giseel a mat a xam.

Wan na ma lal wan na ma bës, Noteel ma leen ci sama bés, Misaal ma leen ba ma ni mbas, Kima giseel a mat a am.

Yaramu xol bi dafa mees, Jeena ba mel ni luñu fees, Cofeel gi wal na ko mu tees, Kima giseel a mat a xam.

Tibbub cofeelam dafa fees Ci man, di fokki ak a rees Ci sama xol, ba dootul yées, Kima giseel a mat a am.

Moo tax mu def bu ma nee gees Ci sama xol,mbaa mu ne gees, Sunu dig gante ne depees, Kima giseel a mat a xam.

Jazbul Majzòob - 21

Dima xamal ta du ma fët, Dolli ma xam-xam bu rafet, Dolli ma ngëm, dollima fit, Kima giseel a mat a am.

Di ma yaral boppam ma yëg Yar ba ci man, ba ma di yëg Lu ma yëgul ne lu ma yëg Kima giseel a mat a am.

Wan ma jamono na mu mel, Jàngal ma xel, di ma bindal Ci àlluway maxfoosi xol, Kima giseel a mat a xam.

Di teew ma teew ci péeyi xol, Gisee mu taal ci lampi xel, Jum bu ma wan yoon wu ñu xàll, Kima giseel a mat a am

Jeeqel ma xel, ràcceel ma xol, Xel du ne xol, xol du ne xel, Xela di xel, xol a di xol, Kima giseel a mat a xam.

22 - Jazbul Majzòob

Ruujal ma, ji, di ma bayal, Xiinlu, mu xiin ci niiri xel, Tawlu, mu taw ci tooli xol, Kima giseel a mat a am.

Mu ñor di xam-xam yu rafet, Xam-xam yu àndul aki fët, Xam-xam yu dul yuy rékki fit, Kima giseel a mat a xam.

Sédde na ma ak xam lu rafet, Badu ma yër lu lu rafet, Ta du ma gis lu lu rafet Kima giseel a mat a am.

May na ma déggòog moom i wax Ci ay waxinam yu mu wax, Samay waxinay na mu wax, Ki ma giseeJ a mat a xam.

Wan na ma boppam na mu day, Yàllaa ko xam, moom la ko may, Ta wòolu naa ni moo ma doy, Kima giseel a mat a am.

Jazbul Majzòob - 23

Wax na yonnent bi Iimu doon, May it, ma wax ko Iimu doon, Moom it, mu def ma Iima doon Kima giseel a mat a xam.

Nee na yonnent bi, yaw-a-yaw, May it ma wax ko yaw-a-yaw, Mu ni ko yaw, ma ni ko yaw, KIma giseel a mat a am.

Buur yàlla may na maw kañam, Ma di asaanam fu ma jëm, Di tarjumaani lámmiñam, Ki ma giseel a mat a xam.

Lii le du puukare ci man, Dafay ngërëm lu war ci man, Ta may gërëm ki gën ci man, Ki ma giseel a mat a am.

Mayam yi, yaa na, du nu xul, Cofeel gi, rew na su nu xol, Ba doggi reenam, su nu xol Rootul lu dul wanew taggam.

24 - Jazbul Majzòob

Am na ci yoy, du nu ko wax, Am na ci yoy, nun mu ko wax, Ak bako, noo yamoo ni wax, Lay dàggi xol, tay dolli ngëm.

Wuutu na saaba ya, ña wéy, Ca la bokkoon ta mujj a wéy, Fab nanñ ànd ak moom di wéy, Du nu ni wuy fi kanamam.

Da koo jëkkal, far koo mujjal, Muy kun mujjal, tay kun jëkkal, Taal bu fayul la far jafal, Daay gu maneefulug fayam.

Buur yàlla sédde na nu lii, Lu jiitu nun, xam na nu Iii, . Te yërmandéem jiitu na Iii Ci nun, ba war nanoo gërëm.

Leerug yonnent bi la fi def, Mu juuri leeram ku ko saf, Mu ubbi xol ba, ba mu af, Dugal ca xam mbiri sangam.

Jazbul Majzòob - 25

Yawma alastu naka laaj, Nu ni ko waaw, ta defi xaaj, Booba la door ni nanu waaj, Ta daal nu fay yeni yenam.

Sunu yonnent moo jëkke waaw, Naka ni waaw, nu daal ni waaw, Soppeeki bañ, ku ne ni waaw, Tay déglu baati ndigëlam.

Ruu yi jungaama ndax ragal, Yee ak cofeel di léen yëgal, Am na keroog ñu nu xamal, Xam-xam ba tay la ñu ka xam.

Yonnent bi booba la nu wan Kanam ñi gën booba la woon, Booba la seex metteel woon, Murid yi booba Iañu am.

Booba la bamba gañe woon, Booba la waayam falu woon, Baax gi fi tay, booba la woon, Lu ne ci nit, nee na ak jëkkam.

26 - Jazbul Majzòob

Lii le nu tektal ba fi tay , Ne ab sëriñ du ku ñu jey, Ku beru mel ni aji say, Ju dëddu reenug garabam.

Baaxug keroog-ay law ba tay, Bonug keroog itam du moy, Lawoon keroog-ay wéy di wéy, Lu ne di teeri fa mu jëm.

Na waay meloon, mooy Ii fi tay, La waay amoon, mooy Ii fi tay, La waay xamoon, mooy li fi tay, Buur yàlla, yéem naa kàttanam.

Ku yàlla wan boppam, mu gis, ku yàlla yiir boppam, du gis, Ñii di ko gis, ñuu du ko gis, Mooy ñi ko réere, ak ñi xam.

Buleen di siis, buleen añaan Buur yàlla yaa na, nañ ko ñaan, Kañaan dafay soppiku jaan màtt, luggéeftil màtt-màttam.

Jazbul Majzòob - 27

Jileekuleen, añaane leen, Añaane kuy xëy jublu leen, Di wut a jub, Far dëddu Ieen, Dëkki faneen palam-palam.

Jafanduleen tay dëgëral, Buleen yolom, kiy dëgëral, Buleen ko wax yolomalal, Ku yolomal, daal di yolom

Ku la gënal ki la gënal, Moo la gënal ka la gënal, Ki la gënal ki la gënal, Moo mat a xam, moo mat a am.

Sërin bi gën ki ma gënal, Moo ma gënal ki ma gënal, Te moom mi gën ki ma gënal, Ame ma may, mayu yaram

Jaayante na ak moom ba matal, Biteeki biir ,ku ma jiital, Mooma, ba kenn du ma lëjal, Xol bii la fab, joxub xolam.

28 - Jazbul Majzòob

Waxtaan na ma ak moom ba matal, Waxtaanù xol wu kenn yégul, Bu ne mu tàbbi sama xol, Mu yombalal ma ak xamam.

Yawma alastu, ba fi tay, Masu la tàggoog dinu may, Di yari ruu booba ba tay, Diggante ndigg aki ruuwam.

Xam turu taalibeem bu doy, Xam seeni baay ak seeni nday, Xam seeni kër ak nañu day, Ku ne mu raññaley mbiram.

Xam ña màggante, ak ña fay Jiitu di toflante ba tay, Xam ku ñu taal ba dootul fay, Ak kok du tàkke fii, ba dem.

Xam aji wopp, ak aji wér, Ak ku ñu fajtal ba mu wér, Xam aji toppeeg ku ñu ber, Xam fa ñu dooreeg fa ñu yam.

Jazbul Majzòob - 29

Fekkoon ñu feeñu ko ba fee- Ñal ko ca biir, far ko fa fee- Ñatal, mu xam ba fii, ba fee, Kasful ko yépp fi kanamam.

Kiiraay ya deñ, ba set ni wecc, Lu diy pakkam ñu boole tojj Ko, sànni yépp, koote ga tojj, Ngir ma ni saww, di am ngiram.

Mu xam boppam ak ñaka topp, Ñudaal di jël yëf ya ni kupp, Mu ne di sàbbaa ak a tuub, Te xam gannaawam, xam kanam.

Buur yàllà xamloo ko la woon, Ak la xewoon, ta di la woon, Ak la di woon ,ta di la woon, Mu far saxal lu new bindam.

Booba mu def ko ni badar, Bu feeñ ci laylatul xadar, Rañaan di sabbaa ba fajar, Ci asamaani barsàqam,

30 - Jazbul Majzòob

Mi fi diggante kursi, ak Ars, aki bëyti naari ,ak Turaa bi, ak awaa-i, ak Maa-iiki, law i, ak xalam.

Moo tax ma xéy di leen yëgal, Seen mboole tay lu ngeen yëgul, Ba far ci woo ñi dikkagul , Ña bëgg a ñëw, ñi bëgg a dem.

Ndax Ii ñuy yartingi, ma jog, Ta far si ñëganti ku ñëg, Ta ñaguwul, ta bëgg a ñag Ñeneen, ta xam-xamlu du xam.

Ta sama woote bii, ku xëy Mu tàbbi ab noppam, ta muy Tanxamlu, def boppam ku doy, Xolam ba, mbaa lakkul ba xëm.

Lu diy muqàddam laa di woo, Ku di allaaji maa ko woo, Mbooleeki seex, ku ma ci woo, Na ni labbayka, mbaa naam.

Jazbul Majzòob - 31

Di leen yëgal kii ma fi gis, Ta kii ma gis, ku ko fi gis Ta andulook moom, ka nga gis, Gënu fi, mbaa saful xorom.

Na ngeen ma laaj ki ma fi gis, Sangu b jamono laa fi gis, Daalleen di ànd ak ki ma gis, Bu kenn ni déggumaw turam.

Sayxi suyooxi Axmadaa, Kii moo nu tektal Axmadaa, Ta di fi kañ Muxammadaa, Ba mu tàbbal ko biir këram.

Tampeel ko tampeb ngërëmam, Ni ko yoxóos ci biir xolam, Digal ko baati ndigëlam, Fal ko ci kaw lalub palam

Ne ko yëkket wane, ñi xam Ak ñi xamul daal di ko xam, Jiital ko muy muxaddamam, Daal di taxaw fi seen kanam.

32 - Jazbul Majzòob

Junjung ya gor ci asamaan, Suuf sa di rëkk péeyi diiwan, Sañse, ta naa xutbusamaan Moo falu ànd aki dagam.

Rijaalu xëybu dajaloo, Ba mel ni weer yu tegaloo, Boroomi leer di tegaloo, Fu ñu fa feeñ soreeg lëndëm

Mbooloo yi wutsi ko di wal, Ta daal di tuub, njébbal ma dal, Ndëndam ya rëkk ci wépp wall, Wayam wa riir fu ñu fa jëm.

Werante deñ koote ga toj, Ku bañ, nu tëjj, mbaate ñu tojj Këram, mu far mel ni ku aj, Kangam ya waaf fi kanamam.

Boroomi giir ya jiitu woon, Ak séeni giir, ta ñoo rawoon, jébbal ko giir ya ñu awoon, Booleeki wérd ya ñu am.

Jazbul Majzòob - 33

Xaadiru agsi, ni ko am, Tiijaani agsi ,ni ko am, Salsali agsi, ni ko am, Dabbaa-i agsi, ni ko am.

Jaayante faak moom, di ko wan Yéene, ta ngeejoo fekke woon Tay, ba muritu ko, di sant, Fi gannaawam ak ñoñam.

Mbooloo ma naa ko yaa fi gën, Wii waxtu, yaw la ñu fi tànn, Yaay tinu, yaa fiy ki ñu tin, Tinu fi kuy fekke ta gëm.

Buur yàlla yaw la wàcce tay, Yaa àtte mbir yi ba fi tay, Sàmmal njaboot gi, ku la fay, Fase du sëy diirug dundam.

Ku déglu Iii, na xam ni Iii Yàllaa ko def, ku fekke Iii, Ta dëddu, far dummooyu Iii, Defu ko kenn, lu muy boppam.

34 - Jazbul Majzòob

Gumba gu nanŋaaral, taxul Mu gis badar, ba tay gisul Jantu bëccëg, bu ñu wuril Yoor-yoor, mu jakkaarloog jëem

Ta gumba nag, ba gumba jee, Gumba ci xol, mooy waxju jee, Yal nañu am gis boob du jee, Ci bëti xol, ay yuy kanam.

Buur yàlla mooy wane, bu kenn Defe ne boppam a ko wan, Gis ki le, ab cër la ba woon, Buur yàlla mooy joxey mayam

Ku fekke kii, ta fekki kii, Texe na fii, ba fee, te kii, May la gu Yàlla maye, kii, Des na ak ñi des, ànd ak ñi dem

Xutbusamaan a ngii bu mat, Jogleen àddiya yi na mat, Ku jéem a gàntu na ni mott, Di wéy ta xamtil fu mu jëm.

Jazbul Majzòob - 35

Addiya tay moo ka jagoo, Ku def ni moom, di ko jagoo, Ku ko deful, bu ko dogoo, Bàyyil mu àtte ay mbiram.

Lu tax àddiya moo ko moom, Laay bëgg a wax, ta mooy boroom, Moo ko jagoo, du seen moroom, Neleen gannaaw, mu ne kanam.

Yëf ya ca biir ,ak Ii ñu gis, Ta liñu gis, mooy liñu gis, Biral gi mooy, bët yi ko gis, Noppal na mbokki lammiñam

We waa ngii, tay xeeñ ak a dóor Boroom we waa ngee, gën a wóor, Ba jaan, ta gis des wa di dóor Du tere jaan duggum kanam.

Yëf ya ca biir nag ku ko xam, Na daal di doyloo la mu xam Ku ko xamul ma wax mu xam Jébbal ko ruuwug bakkanam.

36 - Jazbul Majzòob

Kuy faatu moo fay jëkk a teew Ñuy jullee mu di fa teew, Bu ñuy rob, mu ànd ak ñoom di teew, Ñu dem, mu des tontu layam.

Seetleen na ngeen di jébbalóo, Bii tàng, tàngub ñi jébbalóo, Gis ñam wu neex, ta mosuloo Ko, xawma man luy njariñam.

Fekke ju mel ni wuute, mooy Fekke jamonay ngiir ta sooy, Du def lu dul xoole ni looy, Di réccu, tay màttum tuñam.

Ñi sòobu, raw ngeen seeni maas, Ñi bañ, na ñuy ñee seeni maas, Gaal gaa ngii, jògleen ñaani paas, Ku yéex ba tarde daŋ ko xam.

Xamleen na ngeen di ñaane nag, Gëm, ak yaroog, toroxlu, ñag Bakkan, ta muñ, sax fa ba ñëg, Ba lang, yamoog ndigël ba xam.

Jazbul Majzòob - 37

Wóolu dëggal, ag rafetal Njort, ta set fas-fasi xol, Loo xàcci, loola daal di dal, Muy fii, ba fee ; na ngeen ko xam.

Danaa biral ci lima fas, Tuuti ci xutbu bi ma fas, Ni mooma doy, ta Ii ma fas, Doy na du fii, mang ca kanam.

Fii, du barab, faful di kër, Fas ji ci moom, dara du mbir, Keram gii, naaj la kat, du ker, Lemam di ngañ mu wex xorom.

Méddëm mi, tan yi di ko biiw, Bawkat yi siif ko, di ko yéew, Di dox di xiiròo, ba mu siiw, Tab lay bu dee taa, daal di dem.

Kërug ku dul am kër la fee, Moo tax ma dëddu, jublu fee, Li tax nu jóg, du fii, ma fee, Foofee la soxlawoo ñoñam.

38 - Jazbul Majzòob

Ta tay ma jàngal leen, nañuy Faseg njulit, xëy bàyyi moy, Ta xam ni, jàkkam wa, du moy Boroom, ci kangam, mbaa dënnam.

Ta seede yaari baati see - Deyi, ta fas sellal, ta see- Deloo ko, buur bu doy bi see - De, ci lu leer ak lu lëndam.

Ta dëddu àdduna, ta wut Seriñ bu mat seriñ, ta at - Tani yenam, ta bul tawat Benn, lu dul ay tawatam.

Ta kooka, mooy Bamba, buleen Dese ba jóg wu ti keneen, Ba réer ci manding mi, du ngeen Taseeg ku dindi seen ngëlam.

Def leen ni man, dama ni man, Labbayka Bamba, maa ngii man, Fukki barab, ma teg ca benn, Fu ñu fa tollu, maa la gëm.

Jazbul Majzòob - 39

Bakkan bu dee tàggoo di waaj, Saafara deñ, aki gàllaaj, Soppe bi yaw lanu fa laaj, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu ruu di xar-xarle ba dal, Malaaka agsi di bégal, Soppe bi yaw lanu àndal, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu ruu di rocciku ba naaw, Jëm asamaan joxe gannaaw, Soppe bi, yaw lanu fa aaw, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu ñu nee cas yaram di rob, Rawmaan ni jaas, du nit, du rab, Soppe bi, yaw lanu fa ŋëb, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu ñaari gaaña nee jaleñ, Di laaj ka neex, ngani jaleñ, Begal ñu mbég moom dootu deñ, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

40 - Jazbul Majzòob

Keroog ba ñuy dekki ba xëy, Jëm bëyti àndandoo di wéy, Kerogg a tax nga doy nu tay, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Keroog ba ñuy taxaw, ta kenn Du fa ni riis tankam, ta kenn Du nga lu dul lu mu nekkoon, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu téere yay rot, si digën- Te yaari wet yi, mel ne tan Yuy dal, ta kenn du réere benn, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Bu ñuy tëral mandaxe ñii, Seen yiw wa wat, ñu gane ñee, Ñu gañe leen, ñu ñee fa ñee, Yàlla ak sa barke, maa la gëm

Geppën ba, buy sampu ta mooy Siraat, ku jéggi mbir ya nooy Fa moom, ta dootu deñ di nooy, Yàlla ak sa barke, maa la gëm

Jazbul Majzòob - 41

Keroog ba mbooloo ma nee rácc, Di séddaloo def naari pàcc, . Bësub keroog yal naa la daj, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Ñu daagu jëm Daaru Salaam, Di xëy di joxante salaam, Fu ne nu déeyaale ak salaam, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Soppe bi, yii laa fas ba ñëw, Yaakaar ci yàlla, ak ci yaw, Texe gu sax, du deñ ba faw, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Maa ngi taxaw fi sa gannaaw, Jublu la, jox ñaneen gannaaw, . Foo mën a jëm .yobbu ma gaaw, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Ku sédduwul, man séddu naa Ku fàdduwul, man fàddu naa, Ba matlu, weesu naa danaa, Yàlla ak sa barke, maa la gëm.

Seex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay (1868 -1917)

Radiy-Allaahu Anhu

© 1436 h / 2014 www.drouss.org - Tous droits réservés