148

Click here to load reader

Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Embed Size (px)

DESCRIPTION

Wolof

Citation preview

Page 1: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1

Page 2: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2

Page 3: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3

Page 4: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4

Noo ngi dagaan ci képp ku jot ci téere bi nga jottali ko

sa mbokkum jullit ba mu man koo jariñoo.

Yal nanu ci bokk dajeek ngërëmul sunu Boroom.

Page facebook Daarayi.com

Page 5: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5

A G J I I T A L ( P r é f a c e )

Assalaamu alaykum mbokku juliit yi

Téeree ngi nii boo xam ni deesu naatable darraam ci wàll yépp, biiram ak biteem lépp daa tënku ci diine lislaam te yit aji dajale ji bind ko ci làkk wi askan wi di gën a jëfandikoo muy wolof, loo lu da fay yombal gëstu gi, di na tax it nu xam bu baax sunuy farata ak sunuy sunna, xam it lépp lu nuy bëgg a jëf lan mooy àtteem ci lislaam.

Làmboo na jàngale yu bari bàyyeekoo ci téere naar yi nu gën a fonk ci réew mi di léen jàng ci daara yi, dalee ci Risaala, Matn ibn Achiir ak Laxdariyu, ba tay am na ci biir lu bàyyeekoo ci Jawharu nafiis, Majmahu Nuurayni, Tazawu-du sixaar ak Quratul Ayni.

Bu dee lu jëm ci wàllu tasawuuf indi na ci ay leeral yu am solo yu mën a gindi képp kuy gëstu walla nga aju ci ab tariixa.

Téere bi tam yewenal na jëm ci luy tax a xam diine ji ci lu dul benn coono ndax da nga koy jàng di xamal sa bopp te bu doon lu ñu bind ci arab fàwwu nga aajewoo ku la ko tekkil, gis it ku la mën a toppal téere yii yépp di la ko jàngal benn ginnaaw benn jafe na, am seen njëg ñoom ñépp ba mën koo fàggu ba tay di na am ñu mu dul jàppandi ci ñoom.

Di na jariñ mag ak ndaw, góor ak jigéen, ku sori ak kuy soog a tàmbalee jàng ndax li ñu faram fàccee ci biir ci lu ab jullit war a xam bari na lool ba képp ku ko ci yër di nga ci gis loo mën a jariñoo.

aji dajale ko, sunu mbokku taalibe la di sunu rakk, xam xam ak njub ñoo ko mos di yitteel ak jariñ mbokku jullit yi. Téere bii lu mu yàgg a nisër la, jublu wu ci darra lu dul laabiire.

Yal na sunu Boroom gërëm ligéey bi te yombalal nu jëfee gi.

Seydinaa Suleymaan SEENGëstukat ci Lislaam

Jëwriñ ci Daara Maslakul Hudaa (Sóobuwaayu Njub)

Page 6: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6

LI NEkk cI xëT yI

ag Jiital 7Nees di jàngee bindiinu wolof ci arafi latin 10Ubbiteg téere bi 15Wuuteg li ñu sib ci sariyaa ak li ñu sib ci ngér 16cosaanal fiq 17Tawasul 19Ndogal 21Tënku Tazawudu Sixaar 21Xeetu sobe yi am 33Ndox mi laab 34Dindig sobe 35Ngëneel i njàpp 35Ni ñuy dabaatalee njuumte ci njàpp 36Yi ku amul njàpp sañul 37Yiy toj njàpp 37Masaa ñaar i sang (botte) 38Ngëneel i cangaay 39Ngëneel i tiim 40Ni ñuy tiimee 41Nodd ak liqaam 41Ngëneel i julli 43Saart i julli 44Jullig aji tawat 45Jullig tukki 46Nees di fayee boru julli 46Xabla salaam ak Bahda salaam 47Nan la ñuy jullee 56

Page 7: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7

àttey jiite ak ka ñuy jiite 61Jullig Jumaa 63Salaatul Xawfi (Jullig ragal) 65Jullig ñaar i iid yi (Korite ak Tabaski) 66Salaatul Xusuufi (Jullig Muur) 67Salaatul Istisqaa’i (Jullig mbaaw) 68Mbërëg ak i àtteem 68Dereetu wësin 69Li ñuy defal gone guy soog a juddu 70Li ñuy defal ku faatu dikk ci moom, nees koy sangee ak suul ga 71Jullee néew ak ni ñu koy ñaanalee 75Ñaan, jullee ak sang gone 78Koor 79Ihtikaaf 83asaka wurus, xaalis, mbay ak jur 85Muurum Koor 88aj ak Umra 89Bunt ci ab tabaski ak rendi 95Takk sëy ak fasem fay 98Idda, dund ak laablu 108àttey jote diggënte góor ak jigéen te waruloon seen diggënte 112àttey dereet yi ak gétën yi 113fitra, xaraf, wat karaw, koddaay ak suturaal awra 123Mbiru jënd ak jaay 127Tegginu lekk ak naan 136Bunt ci nuyyóo, diisóo, jàng alquraan ak sikkar 137Sujjóodu alquraan yi 139Tasawuuf 141

Page 8: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8

Bismillaahi Raxmaani Raxiim

Allaahumma salli alaa Sayidinaa Muxammadin wa sallim

Lii lu nu jiitël ci téere bi la ngir mu doon ag jàppandal ci ñi miinul bindiinu Wolof wii nu bindee téere bi.

NEES DI JàNGEE BINDIINu woLof cI ARAfI LATINDaanaka araf yi ngay faral di jëfandikoo booy bind ci faraase yépp, booy

bind wolof ci latin it ñoom ñépp ngay soxla waaye di na ci am yoo xam ni na ñu koy jàngee ci faraase du bokk ak ni ñu koy jàngee ci wolof niki «c», «j», «q», «u», «x», «y», di na ñu ko leeral léegi bu soobee sunu Boroom.

am na yit yeneen araf yu yees yooy gis ci mbindum wolof te faraase du koy faral di jëfandikoo niki «ñ» - «ó» - «ŋ»

am na yit yu faraase di jëfandikoo waaye deesu ko gis mukku ci mbindum wolof niki «h» - «v» - «z».

A BA JA DA woLof

a - à - aa - b - bb - c - cc - d - dd- e - ee- é - ée - ë - ëe - f- g - gg - i - ii - j - jj- k - kk - l - ll- m - mm - mb - n - nn - nc - nd - ng - nj - nk - nq - nt - ñ - ññ - η - ηη - o - oo - ó - óo - p - pp - q - r- rr - s - t - tt - u - uu - w - ww - x - y - yy.

Da nuy njëkk a leeral yi faraase di tuddee «Voyelles»

1- arafu «a» - «à» - «aa»

ñett i mbindin lay am ci mbindum wolof mooy «a» kese niki boo doon bind turu Amdi walla Sali mbaa Astu.

Soo gisee ñu tegale ñaar i «a» nii «aa», xamal ni da nga koy ñoddi niki «aar» di tekki ci faraase protèger walla «xaar» di tekki ci faraase attendre...

Soo gisee ñu tegal ko aw rëdd ca kawam nii «à» xamal ni araf wa muy dendal du doon ab voyelle te da nga koy ñoddi moom «à» boo bu boo koy jàng niki boo doon bind sàmm (élever), jàmm (paix), làmb (lutte), kàmb (trou), àll (forêt).

Page 9: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9

2- arafu «e» - «é» - «ë» - «ee» - «ée» - «ëë»

araf wu ñu ciy jëfandikoo la lool te mu bari ay mbindin yu bokkul :

«e» yaa ngi koy jëfandikoo niki boo doon bind «é» ci faraase, nii la ñuy bindee baat yii : xare (combat), xale (jeune), diine (religion), sell (sain), lem (miel), benn (un), du jar nga ciy def «accent» booy bind wolof.

«é» yaa ngi koy jëfandikoo boo doon bind lu mel ni wér (être en bonne santé), mbégte (joie), jéll (chute), jéppi (dégouter), di nga seetlu ni bu àndeek «accent» bi boo koy jàng da fay xaw a dëgër tuuti.

«ë» moom mooy tollook «e» ci faraase niki boo doon bind le feu (taal bi) ci wolof lë fë nii lay mel moo tax «ë» foo ko gis jàppeekoo «e» ci faraase : ngëm (croyance), gëlëm (étourdi), jëf (action), sëriñ (marabout)...

«ee» foo gis ñu dendale ñaar i «e» xamal ni da nga koy ñoddi niki boo doon bind è ci faraase : leer (lumière), mbëggeel (amour), meew (lait), seet (chercher), beneen xeex (un autre combat), seex (jumeau)

«ée» foo ko gis xamal ni da nga koy ñoddi te dëgërël njàng mi niki boo doon bind géej (mer), giléem (chameau), féetewoo ( s’approprier)...

«ëe» moom it daa meloon ni nga bind «ë» bii te ñoddi ko boo koy jàng niki nga doon bind loo lu faraase di wax «beurre» da fay doon ci wolof «bëer», boo bindee «bëer» ci mbindum wolof turu jën la.

3- arafu «i» - «ii»

Ni ñu koy jàngee ci faraase, loo lu lay tollool ci mbindum wolof niki imaam (imam), julli (prier), weddi (protester), fit (courage).

Boo ko bëggee ñoddi ci nga ciy tegale ñaar muy «ii» niki ci fiir (jaloux), biir (ventre), miin (habitué), xiif (faim).

4- arafu «o» - «ó» - «oo» - «óo»

Moom it li muy joxe ci faraase lay tollool ci wolof niki boo doon bind xol (coeur), bor (dette), su àndeek «accent» bi da nga koy dëgërël as tuut niki boo doon bind jóg (se lever).

Bu ñu dendaalee ñaar i «o» nii «oo» boo koy jàng da nga koy ñoddi niki booy bind sooroor (minaret), mbooloo (groupe).

Page 10: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0

Su fekkee «o» bi jiitu daa am accent nii «óo» boo koy jàng da fay gën a dëgër niki boo doon bind lu mel ni wóor (sûr) wuute lool ak woor (jeûner), góor (homme), jubóole (réconcilier), nuyyóo (saluer).

5- «u» - «uu»

Moom it ñaar i mbindiin yii lay am, «u» da fay tollook «ou» ci faraase niki boo doon bind ubbi (ouvrir), julli (prier), njub (droiture), seetlu (observer).

Bu ci ñaar àndee nii «uu» boo koy jàng da nga koy ñoddi niki buur (roi), juum (se tromper), suuf (terre), puur (boulangerie).

Su ko defee ñu jublu ci li faraase di tuddee «Consonnes»

Benn mu tàmbali baat bi niki turu ku tuddu «Paap Njaay» nga xam ci faraase Pape Ndiaye nii la ñu koy bindee.

Bu nekkee ci digg baat bi niki nga doon bind dimbëli (aider) walla jébbëlu (faire acte d’allégeance), benn mu ànd moom kenn niki ci baatu dimbëli wal-la mu taqook moroomam niki ci baatu jébbëlu, su àndeek moroomam nii boo koy jàng di nga yëgaale tegaloo gi bu baax xoolal baatu jubadi (injuste) ak baatu jubbënti (ajuster).

Bu nekkee ci jeexitalu baat bi, benn mën naa ànd moom kese niki baatu xalaat (penser) walla mu taqook moroomam niki ci baatu bett (surprendre), fii tam di ngay yëg bu baax tegaloo gi xoolal baatu mat (complet) ak matt (bout de bois) ak màtt (mordre).

Araf yii, ni ñu léen di jàngee ci faraase ak ci mbindum wolof ñoo yem.

«b» : baay (père), jubóole (réconcillier), rëbb (chasse)

«d» : dee (mort), juddu (naître), sedd (frais)

«f» : fanaan (passer la nuit), jëfin (manière de faire), xaraf (circoncision)

«g» : «gë» rekk la ñu koy jàngee niki gëm (croire), segg (trier), bég (joyeux)

«k» : kaay (viens), mokkal (parchoeuriser), lekk (manger)

«l» : laab (purification), abal (prêter), sell (sain)

«m» : musóoru (porter un foulard), jéemal (essaies), sàmm (élever)

«n» : nammeel (volonté), keneen (autre), benn (un)

Page 11: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1

«p» : paa (vieux), jàppalante (s’entraider), bépp (chaque)

«r» : raam (ramper), faral (supporter), defar (réparer)

«s» : soppeeku (changer), musël (protèger), muus (chat)

«t» : tedd (majestueux), fàttaliku (se souvenir), létt (tresser)

«w» : waaw (oui), yeewu (se réveiller), yeew (attacher), yewwi (déta-cher)

«y» : yegg (arriver), nuyyu (saluer), bay (cultiver)

Araf yii, ni ñu léen di jàngee ci mbindum wolof wuute na ak ci faraase

«c» : ceeb (riz) waaye kenn du bind thièbe, caabi (clé), cafka (goût)

«j» : julli (prier) waaye kenn du bind diouli, jaay (vendre), jëf (agir)

«q» : taqal (salir) jege na «k» waaye am na ñu ag wuute wu ràññeeku, boo bindoon takkal (attacher) leneen lay doon, ba tay boo bindoon jàq giy firi tiit bokkul ak jàkk di firi aw xoolin wu àndul ak xef, tanqal (tympaniser), doq (nuque), suqali (développer), mboq (maïs), wuute na ak mbokk (fa-mille)

«x» moom ngay jëfandikoo boo doon bind Xaadim waaye kenn du bind Khadim niki bu doon faraase, xaalis (argent), xaraam (illicite), jeexal (finir)

«y» bu dee ci faraase di na ñu ko jàngee «i», bu dee ci mbindum wolof yë rekk la ñu koy jàngee niki boo doon bind yaay (maman) bàyyi (laisser).

araf yii «ñ» - «ó» - «ŋ» di nga léen di fekk ci mbindum wolof waaye amul ci faraase.

«ñ» moom ngay jëfandikoo niki boo doon bind li faraase di bindee nii «Serigne», bu dee ci wolof nii lay doon «Sëriñ», niébé ci faraase nii la ñu koy bindee ci wolof «ñebbe», ñee (envier), waññi (compter), wàññi (diminuer), bañ (refuser), ñàmbi (manioc)...

«ó» bii leeral na nu ko ci ginnaaw.

«ŋ» moom ngay jëfandikoo boo doon bind lu mel ni ŋàññ (saboter), diiŋatkat (dénigreur), ŋëb (prendre, attraper), doŋŋ (seulement).

Page 12: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2

Lu AJu cI MBINDuM woLof

1. Jàppal lii

«à» warul a wéet mukk, fàwwu mu am araf wu ko féete wàllu ndeyjoor te loo lu mënul a nekk lu dul baatoodi bu ñu séexal : tàkk (bruler) walla q nga xam ni jikkoy baatoodi bu ñu séexal la làmboo sàq (grenier) walla ñaar i baatoodi yu dend : ànd (accompagner).

2. Maaska yi

Maaskay tëj «accent aigu» ci «e», «ee», «o» ak «oo» rekk la mën a tegu. Bu ko ci am ci baatal yoo yu moo gën a tëju bi ko amul : xel mu ñaw /xél yu gaaw, genn garab/ génn réew mi, door liggéey bi / dóor kaña gi.

Maaskay tijji «accent grave» ci «a» rekk la mën a tegu, «a» bi ko am moo gën a ubbeeku bi ko amul, mel ni diggënte takk na jabar / matt maa ngi tàkk, njaay mi da fa lamb / làmb ja tas na, and wi fay na / seen ànd bi rafet na.

Nu fas yéene tëjee bunt bi yenn ci ay baat yu mat a xam nees koy bindee ci wolof...

Juróom ñaar i bis yi ci wolof :

altine, Talaata, àllarba, alxames, àjjuma, Gàwwu, Dibéer.

Fukk ak ñaar i weer yi ci wolof :

Digguw Tabaski, Tabaski, Gàmmu, Digguw Gàmmu, rakku Gàmmu, rak-kaati Gàmmu, Maamu Koor, Ndeyu Koor, Baraxlu, Koor, Kori, Tamxarit.

Nu indi turu ñenn ci ay kilifa Diine yu taxawu diine ji ci sunu réew mii di Senegaal ba nun nu mën cee jot :

Seex Umar fuutiyu TaaL, Seex axmadu Bàmba MBàKKe Xaadimu ra-suul, Maam cerno Biraayim MBàKKe, Seydinaa Limaamu LaaY, Seex Buu KUNTa Njaasaan, Sëriñ alaaji Maalik Si, Seex Muusaa SIISe, Seexal islaam Baay ÑaS, Maam abdu asiis Si Dabaax Maalik...

Page 13: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3

Bismillaahi Raxmaani Raxiim

Allaahumma salli alaa Sayidinaa wa Mawlaanaa Muxammadin wa alaa aalihii wa saxbihii wa sallama tasliiman wa man tabi’ahum bi ixsaanin ilaa yawmi diin.

ubbiteg téere bi

Téere bii li ko sabab mooy fas yéene barkeelu ci tool bi kenn dul bay ba jeexal ko, booy wàcc keneen di dikk wéyal ligéey bi, tool boo bu mooy Lis-laam. Tay jii la tool bi gën a soxla ay boroom xam-xam yu takkaayu ba dëgër, làmboo pas-pas bu dëppook Sunna Yonent bi Sallalaahu alayhi Wa Sallam, tay tam la tool bi gën a yaatu, ci la jamono gën a nekk ci ag mujjam, nga xam ni topp sa bakkan ak jaamoo sa Boroom ni nga ko gërëmee yaatu na lool. Saa su ne yaa ngi gis ay jumtukaay yu yees ak i jëfandikukaay yoo xam ni jullit bu far-luwul dëgg di na la sank jëmee la ci nga xemmeem léen fàtte la taxoon sunu Boroom wàccee la ci kaw suuf sii di ab jaaruwaay ci kenn ku ne ci nun, kër ga dëgg mooy allaaxira.

Sunu Boroom mi ngi wax ak nun ci alquraan ni wamaa xalaqtul jinna wal insa ilaa liyaxbuduunii, Bu nu bindee jaamoo tax, su ko defee jaamu gi da fay tege ci xam-xam lu ko moy du ko nangu te jaamu gu sunu Boroom nanguwul du ag jaamu, liy sabab mu nangul la ko mooy nga fexe mu dëppook ni mu la ko santee, loo lu Yonent bi SaWS moo nu ko jàngal ci Sunna moo tax Sëriñ Tuu-baa radiyallaahu anhu wax na ni rajaa’u jannatin bilaa taa’aati bi sunnatil maaxii xuruurun yaati, yaakaar àjjana ci lu dul toppee Yàlla ci Sunna Yonent bi SaWS woreel la.

fiq mooy àtte jëfu jullit, am na ñu koy woo wee Sariyaa nga xam ni boo toppee cosaanal baat bi di na la tektal ag dégg walla ñaw ci xam-xam, ci tënk xam-xamu fiq mooy yoon wi ab jullit war a awale jëfam ngir mu dëppook Sunna.

Moo tax ab jullit fàwwu mu tënku ci ab mazhab mooy ab ngér, di ngay dégg ngéru Maalik, ngéru abu Xaniifa, ngéru Imaamu chaafii, ngéru Imaam Xanbal… am na yeneen waaye yii da ñu cee gën a ràññeeku, nun fiq bi nu indi ci téere bii yépp noo ngi ko tektaloo ci bu imaam Maalik radiyallaahu anhu mi ganee woon jamono Medin, bokk na ci ñi sunu Boroom defal ag xam akug ràññee ci xadiisu Yonent bi SaWS.

Téere yi ñuy faral di tektaloo ci ngéru imaam Maalik mooy Al Muwatta mooy téere bi ñu njëkk a taalif ci xadiis ak fiq ñeel lislaam ak Mudaawana nga

Page 14: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4

xam ne àttey Imaam Maalik la ñu ciy siiwël, ki ko dajale mooy ab ndongoom bu ñuy wax Sahnun Ibn Sa’iid.

Lu jëm ci mbiru farata yi ak sunna yi ak wàllu iimaan, islaam ak ixsaan, Tazawudu sixaar bu Seexul Xadiim (ra) la nu léen ciy indil ci ni ko Sëriñ allaaji Mbàkke ibn Sëriñ Mustafaa absa tënkee, am na yit ci biir téere bi lu bàyyee-koo ci Jawharu Nafiis ak Majmahu Nuurayni, ba tay am na ci lu nu jëlee ci Risaala, Laxdariyu, Ibn Achiir ak Qurratul Ayni bu Sëriñ Su’aybu Mbàkke.

Ngir lu gën a wéral jàngale yi nu léen indil ci téere bi, mbooleem àtte yi nu jukkee ci téere yi nu lim sank noo ngi ko toppee ci ay firi Sëriñ abdu raxmaan Mbàkke ibn Sëriñ abdu Xudoos, boroom xam-xam bu laabir te woyof, am na ci tam loo xam ni ci ay firi Sëriñ Xaadim Mbay la nu ko toppee, moom it muy ku rafet xam-xam te amug dégg.

Noo ngi sant sunu Boroom ci tawféex gi mu nu defal ba nu doon ay jullit, di ko ñaan mu kàttanal nu ba nu mottali téere bi te lépp dëppook ngërëmam te bu nu ci gis sunu bopp benn yoon.

wuuteg li ñu sib ci sariyaa ak li ñu sib ci ngér : makruuh shar’ii ak makruuh irshaadii mazhabii

Boroom xam-xam bu ñuy wax Muxammad ibnal Busir nee na bépp jullit bu bëgg a topp diine war na xam li ñu sib ci wàllu Sariyaa ak li ñu sib ci wàllu ngér nga xam ne boo ko waccee du la jural genn tagg wala ngëneel te nekkul loo xam ne def ga daa bon, masalan ubbikoo Bismillaahi ci julli booy jàng faatixa. ci ngéru Imaam Maalik sib na ñu ubbikoo ko ci jullig farata, naka noo nu wax assalaamu alaykum wa raxmatulaa ci ndeyjoor ak ci càmmooñ ci sëlmël, farata la ci ngéru imaam Xanbal waaye kiy topp ngéru imaam Maalik buy julli moom kepp walla muy ilimaan benn yoon la koy wax ca kaw ca ndeyjooram, terewul mën na wax assalaamu alaykum ci ndeyjooram ak ci càmmooñam ndax ñaar i àtte yi xadiis wéral na ne Yonent bi SaWS def na léen. Naka noo nu sadl nga xam ne mooy yoor say loxo, bu dee xabd nga xam ne mooy aj say loxo dajale léen ci sa dënn sib na ñu ci kiy topp ngéru imaam Maalik mu def ko ci jullig farata. Lenn ciy Boroom i xam xam wax na ñu ne bu dee maalikii bi da fay ragal ay woroo, sopp na ñu ci moom mu def ko su yaakaaree ne jëfandikoo gi di na dajale xol yi.

Li ñu sib ci Sariyaa moom moytu ga di na jur ag pay te def ga du bàkkaar, da ñu koo sib rekk cig dëppoo.

Xàmmee ñaar yii lu am solo la ngir jullit bañ a sànni loo xam ne wér na ne

Page 15: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 5

Sunna la ci boole gu mu ko boole ci ñaareelu xaaj bi.

Cosaanu Fiq

1 - Alquraan

Sunu Boroom wax na ci alquraan ne nit ñi ak jinne yi bu ñu dajewoon te mankoo ngir ñu indi lu mel ni alquraan du ñu ko mën doonte da ñuy di-mbëlante.

alquraan kàddu sunu Boroom la gu mu waxyu Yonent bi SaWS jaaree ko ci Sayidunaa Jibriil, darra soppeeku wu ci, kenn yokku ci darra kenn wàññi wu ci darra ba mu wàccee ba tay jii, karaama la guy sax dàkk ci wax ju rafet ak xam xam. alquraan ñépp lay waxal ci jamono ju ne.

Wax na ci sunu Boroom, ci luy tax nu xam ci Moom darra, làmboo na ay ndigël, ay tere ak i taarix yuy jàngal jullit ak di ko yee ci ni mu war a dundee ci kaw suuf, li mu fi war a def ak li mu war a jomb. Làmboo itam moom alquraan ay mbóot yu yaatoo yaatu yuy junj wàllu baatin nga xam ne mbiru xol la.

Dajale gi mi ngi amee ci jamonoy xilaafag Sayidunaa Usmaan.

aaya bu ci ne am na xew-xew yu ko taxoon a dikk nga xam ne moom la nu duppee sababu nuzuul (li sabab wàcc gi), xam léen di na la jàppandalal nga gën a xam alquraan.

Boroom xam xam yi tënk na ñu aaya yi wàcc ci alquraan ci ñaar i xaaj :

- aaya yi wàcc Màkka : mooy aaya yi nga xam ne da ñu wàcc Màkka njëkk gàddaay gi, bokk na ci seen jubluwaay mooy xamal jullit bi Boroomam bëg-glóo léen ko te bañ koo bokkaaleek darra. aaya la yuy wax ci wàllu ngëm, pas-pas, sàkkug mbindéef yi ak kennug Yàlla.

- aaya yi wàcc Medin : mooy aaya yi wàcc ginnaaw gàddaay gi, di na ñuy jàngal jullit yi ponk i ngëm ak nees di jaamoo Yàlla, di wax ci wàllu doxalin ci réewu jullit, di soññe ci woo nit ñi jëmee léen ci seen Boroom, jàngale itam teggin yi ab jullit war a doxee ci jënd ak jaay ak ci wàllu jëflante.

Suko defee ci wàllu taxawaay bi aaya yi am, mënees na nu seetlu

- Nasiix ak Mansuux mooy aaya bu ñu folli ak bi ko folli. am na ay aaya yu nekk ci alquraan te li ko waral mooy jamono ji muy wàcc jàngale gi foo fu la tol-loon waaye jëfandikoo gi wéy na ci wàllu àtte ci diine. Naka noo nu am nay aaya yu sunu Boroom yenkewaloon Yonent bi SaWS, saxaaba yi jàng ko di ko jëfee gin-naaw bi sunu Boroom folli ko waaye mënees na ñu koy jëfandikoo ci wàllu àtte.

Page 16: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 6

Misaal ci wàllu aaya bu folleeku ak bi ko folli : (coran, 2, 219) ginnaaw bi aaya bi wàccee am nay saxaaba yu bàyyi naanum sàngara am ñoo xam ne da ñoo wàññi. Ginnaaw ga la aaya dikkaat ñaaxe ci ñàkk a jëfandikoo sàngara, digël jullit yi ñu bañ a jege julli te fekk ñu màndi, te njëkk ak wàccam, tere goo gu nekkuloon lu bér te leer ci wàllu sàngara : (coran, 2, 43)

Ginnaaw bi, bi nga xamee ne ngëm gi gën naa dëgër ci xol yi, ci la aaya wàcc tere tere gu dog naanum sàngara ak i po folliwaale aaya bu njëkk bi : (coran 5, 90-91)

- Muxkam ak Mutasaabih : am nay aaya yu leer te bér ak yoo xam ne dégg gi di na aajewoo ndimbëlu sunu Boroom lu mel ni : (coran 4, 10) mooy aaya yi lënt làmboo ay déggin yu wuute.

Li ci mat a leeral mooy ku ci dajeek aaya bu xaw a jéggët, xam ga delloo ko ci sunu Boroom bi ko wàccee, terewul dees na gëm aaya bi te bañ a jéem a xóotal ak di ko sàkkoo firi ba mu nuy tàbbal ci njuumte. Sunu Boroom wax na ci alquraan ci wàllu aaya yu lënt yi : (coran 3, 7)

aaya alquraan yi ñi ko war a firi ñooy ñi nekk kàngam ci wàll wi, xam li sabab seenug wàcc te am xam-xam akug ràññee ci saayir ak ci baatin.

- xadiis

Xadiis mooy jàngale jëf walla kàddu Yonent bi SaWS walla lu ñu wax walla ñu jëf ko ci kanamam te dàqu ko. Mbooleem xadiis yi nga xam ne tukkee na ci Yonent bi SaWS mooy sunnaam. Seenug dajale ci mbind ñi ngi ko def ginnaaw bi Yonent bi SaWS nelawee niki alquraan, saxaaba yi da ñu ko daan mokkal di ko jottalante ci làmmiñ ak nopp, wax na ñu ci yenn nettali yi ngir ragal ag jaawale ci diggënte alquraan ak xadiis, Yonent bi SaWS da fa terewoon ci njël-béenu woote gi ñuy bind xadiis yi tay bind alquraan ji kepp, ginnaaw ga la ko soog a digle, fekk saxaaba yi gën na ñoo amug ràññee ci ñoom ñaar.

Moo tax téere yi njëkk a dajale ay xadiis mi ngi amee ci jamonoy Umar ibn abdal aziiz, ci la ñu tànnee xadiis yi am delluwaay bu wér ci Yonent bi alayhi salaam ngir mën léen a yaatal ci xeet wi. Duppee léen ay Musnad, yokk ci turu saxaaba bi jottali xadiis bi : Musnad abubakr, Musnad abu Hurayra…

abu Hurayra wax na ñu ne li mu dajale ciy xadiis ëpp na fukk i junni Yal na nu ko sunu Boroom fayal. Moom mooy ki ëpp lu mu jottali ciy xadiis ci saxaaba yi, ab taalibeem bu ñuy wax Hammam Ibn Munabih siiwël na ci yu bari dajale léen ci ab téere bu mu duppee Sahifat Hammam.

Page 17: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 7

Al Muwatta bu imaam Maalik mooy ñaareelu téere bi làmboo ay xadiis ginnaaw téereb Hammam bi. am na itam Al Musnad bu imaam Xanbal làm-boo na ay xadiis yu bari te da fay ber saxaaba bu ne ak xadiis ya mu indi.

am na ñaar i téere yu Sunniyu yi fonk lool mooy Saxiixu Buxaari ak bu Muslim nga xam ne doo ci fekk lu dul ay xadiis yu wér.

Buxaari wax na ñu ne déggoon na lu mat 600 000 xadiis, wattu lu mat 100 000 xadiis, Saxiixam bi boo waññiwul xadiis yiy dellusi, am na lu mat 2 762 xadiis, loo lu doy na tektal ne ci ag tànn gu kawe la dajalee xadiis yi ci ne.

Su ko defee ngir mën a jàngat tolluwaayu wérug ab xadiis dees na bàyyi xel ñaar i mbir :

- Isnad gi (càllalag jottalikatu xadiis bi) : gëstu ko di na ñu may ñu mën a xam ci xadiis darra ndax wér na am déet, ci xam gi ngay xam seen i pas-pas ak seenug dëggu, su amee genn lënt ci càllala gi dàqeef ko, mel ni nga gis ñu ne diw jëlee na ci diw mu jëlee ci Yonent bi SaWS te fekk ñoom ñaar fekkante wu ñu jamono.

- Matn gi (kàddu gi ci boppam) : Dees na ràññetle Xadiisul Qudsi nga xam ne sunu Boroom moo ko yenkewal Yonent bi SaWS ci lu amul benn jaaruwaay ag Xadiis Nabawii miy jàngale ay kàddu, jëf ak yu ñu def ci kanamam te dàqu ko.

Moo tax séddëleef na xadiis yi ci wàllu maanaa ci :

- Saxiix (wér) : xadiis wu jub, am càllala gu amul genn lënt te ci ñi mu jaar ñépp nekk boroom pas-pas yu wér.

- Xasan (rafet) : Jaaruwaay gi dese naa leer ni xadiisu saxiix yi wéree waaye maanaa mi mu ëmb dëppoo na ak jàngale Yonent bi SaWS, ñi ko jottali tam nekk ñuñ xam te leer.

- Da’iif (lompoñ) : Mooy xadiis yi nga xam ne jaaruwaay wi mënees na ñu cee sikk sàkka, maanaa mi mu ëmb itam lënt lool moo tax xadiis yu bari yi ñuy dàq fii la ñuy dugg.

Su ko defee xadiis saxiix ak yu xasan kepp la ñuy jëfandikoo ci wàllu àtte ak yoonal ci ngér yi.

- Tawasul

Di na am solo lool nu indi lay yiy saxal tawasul nga xam ne mooy jokk sa ñaan gi ngay ñaan sa Boroom ginnaaw bu mu la leeree ne Moom kepp mooy maye, ci darajay Yonent bi SaWS walla kenn ci mag ñu baax ñi. alquraan, Xa-

Page 18: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 8

diis, ba ci dundu ñenn ci ay saxaaba saxal na ne lu wér te mat di jëfandikoo la doonte am nay jullit yu koy dàq di wax ag ñàkk a wéram ci diine.

Ay aaya yu bari ak i xadiis wéral na ñu ko (coran, 48, 8-9).

Ñaan Yàlla ci darajay Yonent bi SaWS walla ngay sàkku barke ci moom (Ta-baruk) lu am solo la te mat di def ndax di na tax nga gën di jege sa Boroom, di na maye ngërëmam it, du lu xaraam walla ag bokkaale ni ko ñenn ñi njortee. Yàlla sunu Boroom mi ngi wax ci alquraan (coran 5, 35), (coran 4, 64), (coran 2, 89), yahuud yi da ñu daan xeex ak ñenn ci arab yi rawati na ñi dëkkoon Ye-men (aws ak Xasraj) njëkk lislaam, ñoom yahuud yi da ñu daan ñaan Yàlla ci darajay seen Yonent yi fi jiitu Seydinaa Muxammad SaWS ngir mën a daan. Su ko defee ginnaaw bi sunu Boroom yónnee Yonent bi SaWS ñu weddi ndax ag ñàkk a nekkam yahuud ni ñoom, ci aaya bii sunu Boroom weddi ga lay ŋàññ waaye du tawasul gi. Li ci gën a mat a leeral mooy yaw miy ñaan leer na la ne du ci ki ngay def tawasul moo lay may, Sunu Boroom mooy nangu ñaan te gin-naaw bi waay ji di dund ak lu mu baax-baax doo ko tàllal say loxo ne ko defal, da ngeen daan ànd tàllal seen i loxo Boroom Kun, kon doo nég ba mu génn àdduna nga di ko ñaan ginnaaw bi muy dund sax defoo ko.

Umar ibnul Xattaab nettali na ne Yonent bi SaWS nee na bi sunu Maam aadama juumee moy Boroomam da fa wax sunu Boroom ne ko maa ngi lay jéggalu ci darajay Seydinaa Muxammad SaWS, sunu Boroom ne ko noo xa-mee Muxammad, aadama ne ko bi nga ma sàkkee, bi ma yëkëtee sama bopp da maa gis ñu bind ci sa gàngunaay gi Laailaaha ilalah Muxammadu rasuulu-laahi ma xam ne ki nga jël aw turam dendale ko ak sa bos mënul a nekk ku dul ki gën ci mbindéef yi.

Lu saxaaba yi daan jëfandikoo la, ci jenn jamono ju maral amee ngir ag ñàkk a taw, Bilaal da fa dem ci fi ñu deñc Yonent bi SaWS ngir ñaan Yàlla jokku ci darajaam, wax na ñu ne ginnaaw ba daa gént Yonent bi SaWS mu ne ko nuyyul ma Umar ne ko di ngeen am li ngeen bëgg insaa allaa. am na bis itam ci jamonoy maral Sayidunaa Umar ñaan sunu Boroom mu wàccee ndoxam ci darajay abbaas baaytaxu Yonent bi SaWS, sunu Boroom may léen taw mu bari. Imaamu chaafii daan na wax ne bu amee soxla da fay julli ñaar i ràkkaa siyaareji bàmmeelu abuu Xaniifa ñaan fa soxlaam te nee na balaa yàgg mu faju.

Buxaari mi ngi nettali ci saxiixam ñett i nit yu ab doj tëjoon ci ab xunt, ñu ñaan Yàlla jokk ko ci seen jëf yu ñu njoort ne sell na, Yàlla nangu seen ñaan.

Page 19: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 9

Moo tax muy Xanbal, Maalik, chaafii ak abuu xaniifa ñoom ñépp saxal na ñu wérug tawasul.

Ku yàgg a yër mbindum Sëriñ Tuubaa radiyallaahu anhu tam di nga ko ciy gis bu baax ndax lu muy jëfëndikoo la ci xasiida yu bari.

- Ndogal

Sëriñ Tuubaa qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu mi ngi nuy jàngal ca Majmahu Nuurayni ne gëm ndogal ñett i xaaj la, bu njëkk bi mooy nga gëm ne lu am ak fu mu amee Yàlla xam na ko te moom la neex mu am wuuteek «Alxadariyatu» ñi nga xam ne da ñuy wax ne ndogal yi ginnaaw bi mu amee la ko sunu Boroom doog a xamee noo nu, ñoo ñu ay yéefér yu wér la ñu ñoo ñu sax laataa Imaam chaafii di génn àdduna jeex na ñu tàkk lu mat juróom ñaar fukk i Yonent rëbb na ñu léen, Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama nee na bu ñu tawatee bu léen léen seeti, bu ñu faatoo bu léen fa teew.

ñaareel bi mooy nga gëm bu wér ne Sunu Boroom moo bind nit ñi ak seen i jëf wuuteek «Muhtazila» yiy wax ne Sunu Boroom moo bind jaam bi waaye jaam bi mooy bind jëf i boppam, ñoo ñu seenug kéefér am nag wuute waaye alquraan weddi na léen ci ay barab yu bari mel ne «wallaahu xalaqakum wa maa tahmaluun» (Yàlla moo léen bind, bind seen i jëf) ak “wallaahu xalaqa kulu chay’in” (Yàllaa bind lépp) ak ci yeneen i barab.

Ñetteel bi mooy nga gëm ne yiw ak ay ñaar i mbindéefu sunu Boroom la ñu wuuteek «Almaanawiyatu» ñi topp Maaniyu fenkat boo bu di wax ne lëndëm moo bind ay, alquraan weddi na ko bi mu nee «wa ja’ala zulumaat wa nuur» (Moo def lëndëm ak leer). Su ko defee Sëriñ bi teg ci ne ñett yoo yu ku ko gëmee noo nu ab jullit la ku ko gëmeewul noo nu ab yéefér la.

Su ko defee lu jëm ci wàllu gën a yaatal ci mbiru jàngale àtte yi aju ci ii-maan islaam ak ixsaan da nu léen di indil Tazawudu Sixaar bu Seexul Xadiim ci tënk wi ci Sëriñ alaaji Mbàkke ibn Sëriñ Mustafaa absa def tàmbalee ko ci muqadama gi.

Tënku Tazawudu sixaar

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu day dénkaane fii ag njub te mooy tàmbalee ci jàng ginnaaw boo mokkalee alquraan di ko jàng ak di moytu jotaay yi ñuy jëwee walla ñu fay wax lu mën a jëmee ab taalibe ci lu dul lu baax tey toog ak koo xam ne waxtu wu ne day jaamu Yàlla di digle lu baax di tere lu bon, képp ku gaaw cig ndawam aw ci yoon woo wu, bu doonee mag di na

Page 20: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 0

noppalu lool waaye ñépp amu ñu tawféexu defee ko noo nu, ku amul tawféexu loo lu yitam bu tuubee dellu ci Yàlla sunu Boroom bu wér di dundal ay waxtoom bàyyi lépp la mu daan def mën naa dem ba am ag mat, am la mu bëgg lépp. Sëriñ bi nee na laabire gii su ngeen ko jëfee di ngeen am sa’aadatu daarayni.

xaaj i Diine

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na diine ñett i xaaj la, iimaan, islaam ak ixsaan, iimaan mooy nga gëm Yàlla ak téeréem yi yépp ak yonentam yi yépp ak malaakaam yi ak ndogalam yi ak bis peñc.

Gëm yàlla

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ni ngeen di gëmee sunu Boroom mooy gëm ne am na te moo fi jiitu lépp te du fi jóg te nuróowul ak menn mbindéef te ku doylu la ci boppam, aajowoowul jëm ci kenn te kenn ku ne ak lenn lu ne aajewoo na jëm ci Moom te it Kenn la ku amul kenn ku ko ñaareel ci jëmmam walla jëfam wallay waxam walla wenn meloom, ku am kàttan la koo xam ne balaa darraa xew da koy bëgg te na mu ko bëggee lay amee, ku am xam-xam la kog réeréewul darra, mbooleem li nu nekkee ak li nuy bëgg a nekkee darra umpu ko ci, day dund, day dégg lu kawe ak lu suufe, di gis lu nëbbu ak lu feeñ, di wax.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na li jomb ci sunu Boroom te mooy li mënul a am moo di ag ñàkk, ñu naan Yàlla am na te amul ak sosu nga xam ne mos naa ñàkk ginnaaw bi mu am walla darra am te neexu ko walla ameewul na mu ko bëggee walla muy tëx walla mu tëlee wax walla mu ñàkk a xam walla mu gumbë walla mu réerée darra walla muy faatu, li nga xam ne mën naa am ci Moom mën a ñàkk mooy def ak dindi, mbooleem li ngay gis walla mu toq ci sam xel daa dagan ci sa Boroom, bu ko neexee amal ko bu ko neexee ñàkkal ko, bu loo lu jàllee nga xam ne tektalu ñaar fukk i melo yii ma nga ca Mawaahibul Quduus bi Sëriñ bi woy loo lu moo tax indiwaatuko fii.

Gëm Malaaka yi

Sëriñ bi nee na ni ñuy gëmee malaaka yi mooy ñu gëm ne am na ñu, sunu Boroom moo léen bind ci leer kese, ba tax du ñu moy Yàlla, du ñu lekk, du ñu naan, du ñu xayta, du ñu tuur ndox, waxtu wu ne da ñuy sàbbaal sunu Boroom.

Gëm téere yi

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ni ngay gëmee téere

Page 21: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 1

yi mooy nga gëm ne sunu Boroom moo léen wàccee, mbooleen li ci nekk lu wér la te xam ne mat na ñu téeméer i téere ak ñent, Sayidunaa aadama fukk i téere ñoo wàcc ci moom ndax ñoom da ñu daan guddu fan, Sayidunaa Siisa doomam juróom fukk i téere ñoo wàcc ci moom, Sayidunaa idriis fanweer i téere ñoo wàcc ci moom, Sayidunaa ibraahiim miy xaritub Yàlla fukk i téere ñoo wàcc ci moom, Sayidunaa Muusaa Tawreet moo wàcc ci moom, Sayi-dunaa iisaa Injiil moo wàcc ci moom, Sayidunaa Daawuud Zabuur moo wàcc ci moom, Sayidunaa Muxammad Alquraan moo wàcc ci moom alayhimu sa-laatu wa salaam.

Gëm Yonent yi

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ni ñuy gëmee Yonent yi alayhimu salaatu wa salaam mooy nga gëm ne Yàlla moo léen yónni, gëm itam li ñu indaale mu jóge ci sunu Boroom, gëm itam ne ab Yonent du fen, du wor, du ñàkk a wax li ñu ko yónni, lu mu wax dëgg la, du def lenn lu xaraam walla lu ñu sib, lu mu metti-metti tam li ñu léen yónni di na ñu ko wax, lépp loo xam ne bu léen dalee du ñu léen daw walla ñu léen di xeeb mën na léen a dal, di na ñu jaay, di jënd, di takk soxna. Li nga xam ne mooy xamle dëg-galug Yonent yi mooy kéemaan yi sunu Boroom feeñal ci ñoom muy taxaw taxawaayu kii lumu wax maa ko ko waxloo, limub ñi Yàlla yónni mat na ñu ñett i téeméer ak fukk ak ñett boo ci boolee ñi Yàlla soloo maanaam xamal léen xam-xamu Yonent te yónni wu léen di na ñu mat téeméer i junni ak ñaar fukk i junni ak ñent i junni.

Gëm bis peñc

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ni ñuy gëmee bis peñc mooy nga gëm ne bis la buy ñëw ci lu dul sikk, mbooleem la ñu wax ne di na fa am yitam nga gëm ko mel ne dekki gi ñuy dekki ak natt ga ñuy natt sunuy jëf ak déegub Yonent bi salalaahu taalaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa sala-ma, ku ca naan doo tu mar ak siraat di ab yoon bu tege ci kaw sawara ñu koy jéggee keem sunuy jëf yu baax, am na ñu fay gaaw ba mel ni ag melax, am na ñu fay am ay at, war na yitam ñu gëm rammug Yonent bi salalaahu taalaa alayhu bi aalihii wa saxbihii wa salama day rammu ñépp ëllëg loo lu mooy ñaan gi muy ñaan Boroomam mu àtte jaam yi, naka noo nu xisaab war na ñu koo gëm, ab jaam lu mu def lu mu tuut-tuut ba toll ni xollitu tàndarma wala mu gën koo tuut Boroomam di na ko ko won fay ko ko, su ko defee ñu xam ne daa am ñaar i bis peñc, bu ndaw ak bu mag, fi mu ne kuy waaj a faatu mi ngi dégmël bis peñc bu ndaw bi, foo fee la ñu koy laajee ndax gëm na Yàlla walla

Page 22: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 2

déet, foo fee la ñu koy tàmbalee mbugël, foo fee la ñu koy tàmbalee xéewale bu dee ku jëm àjjana, saa su ñépp dekkee bis peñc bu mag bi daa di taxaw, foo fee la ñuy tàbbee sawara walla àjjana.

Gëm Ndogal

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ni ñuy gëmee ndogal mooy gëm ne lu am Yàllaa ko dogal moo xam lu baax la ci yaw walla leneen, moo xam lu neex la walla leneen, darra mënul a am ci lu dul nammeelu sunu Boroom mooy dogal lépp, ba ci aw xob sax du wadd fi suuf te sunu Boroom xamu ko te fekk mu bëgg ag waddam fi suuf, sàkkaa leneen. Menn mbindéef mënul a amal darra. Ndogal i sunu Boroom yi ñaare day fekk ku sunu Boroom bëgg mu koy indil li mu bëgg ci lu dul benn nëx-nëx, safaanub ku mu ko bëg-galul wal’iyaazu billah.

Islaam

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na lislaam mooy juróom yii, tudd Yàlla te mooy wax Laailaaha ilalah Muxammadun rasuulullaahi sa-lalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama ak julli ak woor ak natt asaka ak aj Màkka, Sëriñ bi nee na mbooleem lu nit di wax baat boo bu moo ci gën, ku ko taqoo te di ko teewlu di nga am tuyaaba ju rëy te doo am benn nëx-nëx.

Julli juróom

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na julliy juróom farata la ñu, sax na ñu ci tuddug alquraan ak ci sunnas Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama, fóore yépp dëppoo ci, ku ko bàyyi ngir weddi ne sunu Boroom farataalu ko da ñuy jàpp ne daa murtad, daa génn ci diine, da ñu koy tuub loo ñett i fan bu tuubul ñu ray ko, bu ñu ko rayee du ñu ko sang, duñu ko sàng, du ñu ko jullee, du ñu ko suul ca armeelu jullit ña, alalam du ñu ko donnu ci soxlay jullit ñi la ñu koy jëmële.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ku nangu warug julli ba noppi du julli te amul benn ngant, da ñu koy xaar ba waxtu wa sës ca ba mu ko waxee, bu julliwul ba waxtuw daruurii ja des benn ràkkaa boo xam ne faatixa sax du ko ca mën a jàng, bu julliwul yoon ray ko te bu dee réccu naan bàyyi léen ma di naa julli, kenn du ko bàyyi, di na ñu ko sang, sàng ko, jullee ko waaye ku siiwee mbaax du ko jullee, bàmmeelam itam du ñu ko maasale, dañu koy yëkëti.

Laab

Page 23: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 3

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na laab sax na ci alqu-raan ak sunna, mbooleem boroom xam-xam yi maase ci, ku ko bàyyi ci lu dul ngànt da ñu koy ray rayug gétën ndax julli mënul a am te laab jiitu wu ko.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahu nee na Imaam awfii radiya-laahu ta’alaa anhu nee na ku julli na mu war a jullee te xamul farata yi, xamul sunna yi, xamul àtte yi ag julleem du baax, naka noo nu ku jàpp walla mu sangu farata walla mu aj walla mu joxe asaka walla mu def leneen, moy na Yàlla, moy na Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa sa-lama waaye li gën a wér mooy képp koo xam ne jàpp na walla mu julli walla mu sangu farata walla mu def leneen te ba mu koy def am na yéeney def li ko Yàlla digël, jëfam baax na moo xam julli la walla koor walla jàpp walla leneen, moyul Yàlla moyul Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama, teewul nag mu xaraam ci mukkalaf mu ne muy def darra te xamul la ca Yàlla àtte, loo loo tax ku xamul laajul tooñ na boppam, alag na boppam.

ci biir loo lu Sëriñ bi jàll na wax la melow njàpp ak melow sangu farata ak melow julli, ne la melow julli mooy rukkoo yi ak sujjood yi lépp mat nga xam ne fu ñu war a toog ak fu ñu war a dal fu ne toog nga fa, dal nga fa, tari nga itam li nga war a tari lépp.

Melow jàpp mooy nga raxas say loxo ba ci say tikkujara ñett i yoon, galaxn-diku, saraxndiku ñett i yoon, fiiru noo nu, raxas sa kanam ñett i yoon, raxas say loxo ba ci say coñc ñett i yoon, bu ci ne ndeyjoor mooy jiitu, masaa sa bopp, delloowaat masaa ba, masaa say nopp, raxas say tank.

Melow sangu farata mooy nga wut ndox mu laab, toog ci barab bu laab jublu penku, raxas say loxo ba ci say tikku-jara ñett i yoon, raxas li la taq ci sobe lépp, foo fee nak ngay yéenee sangu ga, daa di jàpp njàppum benn-benn te mooy cër bu ne nga raxas ko benn yoon, xaliil sa karaw i bopp ba mu gën a set, nga selandi ko ñett i yoon, daa di dëngal sa noppu ndeyjoor ak bob càm-mooñ bu ci ne nga raxas ko ba mu set, daa di raxas sa doq ak li ko wër, daa di tàmbalee ca coñcal ndeyjoor raxas mu wuti wóom ba, bu càmmooñ noo nu, daa di tàmbalee ca wóomub ndeyjoor raxas mu wuti dojar ba, bu càmmooñ noo nu, daa di raxas sa ginnaaw, daa di raxas sab dënn, daa di raxas sa biir.

Sëriñ bi nee na faratay julli fukk ak juróom la ñu :

Yéene mooy fas julli gi ci sa xol bañ koo tudd

Kàbbar bi ngay njëkk a kàbbar

Jàng faatixa ci ràkkaa bu ne boo dee imaam walla kenn kuy julli

Page 24: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 4

Taxaw ngir kàbbaru armal bi te mooy bu njëkk bi

Taxaw ngir jàng faatixa

rukkoo ba sa bopp tolloo ak sa ndigg nga tàllal say bëtu wóom

Siggi ci rukkoo

Sujjóod

Siggi ci sujjóod

Yéenee roy imaam boo dee ku ñuy jiite

Toftale julli gi ni ñu ko xamee

Dal mooy boo rukkoo wala nga sujjood walla nga def leneen nga ne fa tekk

Yemoo te mooy boo siggee sa cër yépp dellu fa ñu nekkoon

Sëlmël te mooy wax assalaamu alaykum

Toog gi ngay toog di ko wax

Sunnay julli fukk ak juróom ñent la ñu :

Liqaam, doo ci taxaw xanaa sa baat jeex nga jëlaat kàttan

Saar wi nga teg ci faatixa

Taxaw gi ngay taxaw di ko jàng

Béral te mooy wax ca kaw ci suba, timis ak gee

Yelu te mooy wax ci suuf ci tisbaar ak tàkkusaan

Kàbbar bu dul bu njëkk bi

Taaya ju njëkk

Taaya ju mujj

Taaya : attaxiyaatu lilaahi, azaakiyaatu lilaahi attayibaatu salawaatu lilaahi, assalaamu alayka ayuha nabiyu wa raxmatulaahi ta’alaa wa ba-rakaatuhuu, assalaamu alaynaa wa alaa ibaadilaahi saalixiin, achhadu an laailaaha ilalah waxdahuu laa chariika lahuu wa achhadu ana Muxamma-dan abduhuu wa rasuuluhuu

Jotaayu taaya ju njëkk

Jotaayu taaya ju mujj

Page 25: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 5

Julli ci Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama ci ginnaw taaya ju mujj ji te mooy wax lii : Allaahuma salli alaa sayidinaa Muxammadin wa alaa aali sayidinaa Muxammadin kamaa salayta alaa sayidinaa Ibraahiim wa alaa aali sayidinaa Ibraahiim wa baarik alaa sayi-dinaa Muxammadin wa alaa aali sayidinaa Muxammadin kamaa baarakta alaa sayidinaa Ibraahiim wa alaa aali sayidinaa Ibraahiim fil aalamiina ina-ka Xamiidun Majiidun

Li ngay yokk ci sag dal ngir gën a teewlu

Li ngay dolli ci lu dul jotaayu taaya ak jotaayu sëlmël,

Béral sëlmël bi, bu dee kàbbaru armal bi da ñoo sopp ku ko béral

Delloo imaam sëlmël te mooy wax ko assalaamu alaykum

Delloo ki ci sa wetug càmmooñ sëlmël bu ci amee ab ràkkaa

Noppi bu sa imaam di jàng ca kaw doonte déggoo ko

Samp bant fi sa kanam bu ñu la jiitewul, ku ñuy jiite du ko def, bant boo bu di na mat xaaju meetar ba noppi set, bañ a am rafet-rafet yuy wëlbëti sa xel te tal te sax fa nga ko samp.

Faratay njàpp juróom ñett la ñu :

Yéene te mooy fas yéene def faratay njàpp ak yëkëti am toj

raxas kanam ba mu daj

raxas loxo yi ba weesu tuuti say coñc

Xaliil baaraamu loxo yi te mooy téqale ko ba ndox mi dugg ci

Masaa sa bopp te mooy tooyal say loxo raay ko ba mu daj

raxas say tank

Bomb cër yi boo léen di raxas

Gaaw te mooy toftale, nga xam ne loo raxas balaa fendi nga def leneen

Sunna yi tam juróom ñett la ñu :

Saraxndiku te mooy dugël ndox mi bu baax ci say bakkan ci sag noyyi

fiiru te mooy génnee ndox moo mu ci sag noyyi

Masaa say nopp te mooy tooyal say baaraam raay léen biir ak biti

Page 26: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 6

Yeesal te mooy bala ngaa masaa nopp yi tooyal say baaraam i déy ak yu sànnikaay

Delloo masaa bopp bi ba mu yeksiwaat fa nga tàmbalee

Toftale farata yi te mooy jiital kanam teg ci loxo yi ak bopp bi teg ci tank yi

faratay sangu juróom la ñu :

Yéene

Bomb yaram wi

Gaaw

Xaliil karaw i yaram wi

Xaliil ay létt bu dee ku léttu, mel na ne mook farata bi ko jiitu benn la ñu.

Sunna yi ñent la ñu :

raxas loxo yi ba ci tikkujara yi

Gallaxndiku

Saraxndiku

Masaa bën-bën i nopp yi waaye kaw nopp bi raxas ko farata la

Faratay tiim juróom ñett la ñu :

Yéene te mooy fas yéenee daganlu julli walla leneen ci moom

Pàkk bu laab bu amul sobe

Gaaw te mooy sësële tiim bi

Teg bi ngay njëkk a teg

Masaa loxo yi ba ci tikkujara yi

Sësële ko ak la la tax di tiim

Def ko ginnaaw bu waxtu wi tàbbee bu dee julli

Masaa kanam gi ba mu daj

Sunnay tiim ñett la ñu :

Toftale te mooy jiital masaa kanam teg ca loxo yi

Beneen teg bi ngay teg ngir masaa loxo yi

Page 27: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 7

Masaa li dalee ci tikkujara yi ba ci coñc yi

Sëriñ bi nee na bul tiim mukk te amoo ngànt walla nga ñàkk ndox.

Faratay koor ñaar la ñu :

Yéene te mooy fas koor gi ci guddi gi li tàmbalee timis ba fajar foo ko fi fasee baax na

Bàyyi lépp luy yàq koor mel ni lekk walla naan walla booloo ak sa soxna

Sunna yi ñett la ñu :

Gaaw a dog bu jant sowee

Yéex a xëdd balaa fajar

Tëye sa làmmiñ ci jépp wax ju amul tuyaaba

faratay asaka ñent la ñu :

Yéene mu doon asaka

Mat at bu dee xaalis walla wurus walla ag jur

Mat nisaab te mooy tolluwaay biy tax asaka war la

Ñàkk koo tuxal di ko yóbbu fu bokkul ak fi mu la waree

Am na itam ñett i teggin :

Sa xol sedd ci boo koy joxe

Mu doon ca digg alal ja, bañ a ëpp, bañ a yées

Nëbb ko bët yi ndax ragal ngistël

faratay aj ñent la ñu :

Yéene te mooy armal

Tawaaful ifaada bisub Tabaski

Dox Safaak Marwa

Taxaw arafaat guddig Tabaski te mooy nekk arafaat

Sunnay aj fukk ak ñaar la ñu :

Armal bi da cee am ñent

Te mooy booy armal nga sangu farata

Page 28: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 8

Dindi lépp loo soloon lu ñu ñaw boo dee góor waaye jigéen di na sol lu ñu ñaw

Sol taraxlaay ak sër ak i carax

Wax labayka allaahuma labayka ba fa mu yem

Wër bi am ci ñent

Dox ak say tank teewul yit muy wartéef

fóon xajarul aswad

Ñukk ñett i yoon ci tawaaful xuduum kepp

ñaan

Dox Safaak Marwa am ci ñent

fóonaat xajarul aswad booy génn jëm Safaa

Yéeg ba ca kaw Safaa ak Marwa boo dee góor

Gaaw ci Batnul Masiil, diggënte Safaak Marwa la nekk

ñaan ca kaw Safaa ak Marwa

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na Yonent bi salaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama nee na ku jàpp ba noppi wax ach’hadu an laailaaha ilalah wa ach’hadu ana Muxammadan abduhuu wa ra-suuluhuu, sunu Boroom tijjil ko juróom ñett i bunt i àjjana bu ko ci neex dugg waaye boroom xam-xam yi wuute na ñu ci jamono jan la ñu koy tijji, am na ñu ne fa nga ko waxee, am ñu ne boo faatoo.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na booy julli ci ginnaaw imaam, bu amee lu la raw bu sëlmëlee da nga koy fay, ginnaaw loo lu mu jàll wax la waxtu wu ne ni ñu koy fayee ak tàmbalikaayu muxtaaram te mooy wax-tu wa ñu taamu ku ko ca julli ak fa mu yem, mu tàmbalee ci suba ne :

Muxtaarum suba mi ngi tàmbalee ci xarug fajar ba mu leer, bu la ci benn ràkkaa rawee nga am ca benn, boo jógee doo wax allaahu akbar, da ngay taxaw rekk jàng faatixa akuw saar béral ko toog taaya sëlmël, doo xunóot ndax imaam xunóot na. Lii mooy xunóot : Allaahumma inaa nasta’iinuka wa nastaxfiruka wa nu’minu bika wa natawakalu alayka wa naxna’u laka wa naxla’u wa natruku man yakfuru bika, Allaahumma iyaaka naxbudu wa laka nusalii wa nasjudu wa ilayka nas’aa wa naxfidu, narjuu raxmataka wa naxaafu azaabakal jidda, ina azaabaka bil kaafiriina mulxaqun.

Page 29: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

2 9

Su ko defee boo bëggee takk fi ngay wax allaahu akbar boo jógee di fay ak fi nga ko dul wax, da ngay xool li nga am ci julli gi bu dee benn te mooy lu tóol walla ñett doo wax allaahu akbar, bu tóolul te mooy ñaar nga wax allaahu akbar.

Muxtaarum tisbaar mi ngi tàmbalee ci bu jant bi weesoo digg asamaan tuuti jëm sowwu, mi ngi yem bu jëmm yi tollook seen i ker nga xam ne boo taxawee sa takkandeer day tollook sa jëmm, bu la ci benn ràkkaa rawee nga am ci ñett, boo jógee doo wax allaahu akbar, jàng faatixa akuw saar yelu ko toog taaya sëlmël, bu la ci ñaar i ràkkaa rawee nga am ci ñaar, boo jógee da ngay wax allaahu akbar, jàng faatixa akub saar, muy sa bub ñetteel moo tax doo toog da ngay indi beneen muy sa bub ñenteel nga jàng ca faatixa ak saar.

Bu la ci ñett i ràkkaa rawee nga am ci benn, boo jógee doo wax allaahu akbar, jàng faatixa akuw saar, toog taaya muy sa bub ñaareel, nga jóg indi be-neen ràkkaa jàng ci faatixa akuw saar te bañ a toog ndax mooy sa bub ñetteel, da ngay indiwaat beneen boo xam ne faatixa kese nga ciy jàng muy sa bub ñenteel, nga toog taaya sëlmël

Muxtaarum tàkkusaan mi ngi tàmbalee foo fee muxtaarum tisbaar ye-moon te mooy mujjug taxawaay ba, ba kero ker yi di sedd te mooy jant bi mboq, moom mook tisbaar ñoo bokk fayin.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na :

Muxtaarum timis mi ngi tàmbalee ci sowug jant yem ci nëbbug xonk-xonk ya, boo demee ba gisoo ca darra foo fa la yem, bu la ci benn ràkkaa rawee nga am ci ñaar, boo jógee da ngay wax allaahu akbar tari faatixa akuw saar ca kaw, toog taaya sëlmël, bu la ci ñaar i ràkkaa rawee nga am ci benn, boo jógee doo wax allaahu akbar, tari faatixa akuw saar ca kaw, toog taaya muy sa bub ñaareel, nga indiwaat beneen bu mel noo nu sëlmël.

Muxtaarum gee mi ngi tàmbalee ci nëbbug xonk-xonk yoo yee fi jant bi bàyyiwoon yem ci ñetteelub xaajub guddi gi, bu njëkk bi maanaam boo koy xaaj da ngay tàmbalee ci fàddug safax ba fajar xaaj ko ñett i xaaj, bu xaaj bu njëkk bi jàllee foo fa la yem, du sori ñett i waxtu ginnaaw bu ñu noddee gee maanaam bu ñu noddee boo ci tegee ñett i waxtu foo fa la yem wallaahu ahlamu.

Bu la ci benn ràkkaa rawee, nga am ci ñett, boo jógee doo wax allaahu akbar, jàng faatixa akuw saar ca kaw, toog taaya sëlmël, bu la ci ñaar i ràkkaa rawee, nga am ci ñaar, boo jógee da ngay wax allaahu akbar, jàng faatixa

Page 30: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 0

akuw saar ca kaw muy sa bub ñetteel nga bañ faa toog, jóg indi beneen bu mel noo na muy sa bub ñenteel, bu la ci ñett i ràkkaa rawee nga am ci benn, boo jógee doo wax allaahu akbar, jàng faatixa akuw saar ca kaw, toog taaya muy sa bub ñaareel, nga indi beneen ràkkaa bu ànd ak faatixa akuw saar muy sa bub ñetteel nga bañ a toog, nga indi beneen ràkkaa booy jàng faatixa kese muy sa bub ñenteel.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na boroom xam-xam yi da ñuy wax ne ab ràkkaa liy tax nga am ko mooy nga sëgg jàpp bu dëgër ci say bëtu wóom te imaam siggiwul waaye boo jàppul bu dëgër mu siggi, ràkkaa boo bee di nga ko fay moo tax boo fekkoon imaam ci jotaay ju mujj da ngay jàpp ne amoo ci julli gi darra, Yonent bi salalaahu ta’alaa alayhi bi aalihii wa saxbihii wa salama nee na jullig mbooloo gënee na jullig kenn ñaar fukk i da-raja ak juróom ñaar, nee na ñu boo ci amee benn ràkkaa am nga ngëneel lépp.

Ixsaan, «Rafetal» mooy lan

rafetal mooy ngay jaamu Yàlla sunu Boroom ba mel ni yaa ngi koy gis boo mënul loo lu nga xam ne mi ngi lay gis, ba tay nee na bu ngeen bëggee kawe fa Yàlla na ngeen di jëfandikoo lii ma leen di dénk :

Xam-xam te mooy xam li Yàlla sunu Boroom bëgg ak li mu bëggul

Kersa te mooy rus a def lu bon

Sant te mooy jëfee ndigël yi

Sellal te mooy jëf te Yàlla tax

Tabe te mooy di joxe li nga mën

Noppi te mooy bañ a wax lu amul njariñ

Lewet te mooy bañ a fayu ag tooñ rawati na booy jàng

Muñ te mooy tëye sa bakkan ba du jëm ci lu baaxul

Sàmmonte te mooy jëfee li nga xam walla nga nekk di moytu lu lënt

Dégg-dégglu te mooy di fexee xam li ngay jàng mooy lan.

Sëriñ bi bi mu waxee loo lu daa jàll ba tay wax ne, maa ngi léen di dénk ngeen farlu ci jaamu Yàlla sunu Boroom fu ngeen fi nekk, bañ di noonoo, li ci ëpp ku farlu ci jaamu Yàlla ga ñu ko tànnal du noonook kenn, bu léen bari ay wax ak ay nelaw, lépp luy yàq na ngeen koy daw, bu léen jëf te Yàlla taxul ndax deesu ko nangu, bu léen yëkëti seen bopp, bu léen bañ kenn, dee léen wut

Page 31: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 1

leer ci bàyyi yoo yu.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na mi ngi léen di dénk juróom yi :

Dëggël te mooy bàyyi fen ak jëf ju amul njariñ

Wakkirlu te mooy doyloo Yàlla sunu Boroom

Toroxlu te mooy bañ a yëkëti sa bopp

Gàttal mébét te mooy loo amul nga muñ ko

Bariy teggin ndax xam-xam bu baree te àndul ak teggin yu bari, ay lor ak coono kepp lay jur.

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na na ngeen di toog ak ku jub koo xam ne di na léen jëlee ci juróom yii jëmee léen ci juróom yii :

Ngistal jëmee léen ci Sellal

rëy jëmee léen ci Toroxlu ak Muñ

Noonoo jëmee léen ci Laabiir

Sikki-sàkka jëmee léen ci Wóolu

Bëgg lu baaxul ci yaw jëmee léen ci Bëgg lu baax ci yaw

Sëriñ bi qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu nee na ngeen gaawe juróom yii balaa juróom yee di ñëw te mooy :

Waxambaane balaa Màgget di ñëw

Wér balaa Tawat di ñëw

am balaa Ñàkk di ñëw

féex balaa Soxla di ñëw

Dund balaa faatu di ñëw

foo fee la tazawudu sixaar yem alxamdulilaahi, nu fas yéenee tàbbi ci ye-neen yu mat a xam lool ci diine ji.

Xeetu sobe yi am

Xeetu sobe yi nga xam ne ñoo ëpp a laal doomu aadama, ba ca njëkk mooy sawum doom aadama ak i xaytaam ba tay, dereet moo xam da fay dereetu rendi walla yaram wi gaañu muy nàcc walla muy bori walla jigéen ju gis baax,

Page 32: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 2

ba tay dëtt moo xam da fay dëtt ju am dereet walla muy dëttu kese, ndox mi nga xam ne Yàlla moo ko def ci góor ak jigéen ñu koy wax maniyu, sàngara.

Jigéen ju ame gone na xam ne lay bàyyeekoo ca gone ga muy saw walla xayta sobe la ñu, la gën mooy mu wut yëre yoo xam ne bu dee julli jël ko jullee ko bu noppee teg ko fee bay julliwaat, lépp lu Yàlla sàkk def ci ruux te xaraamal ku ko lekk mel ni mbaam walla fas, saw ma walla soow ma ak xayta ya lépp sobe la ñu, loo xam ne Yàlla xaraamalu ko, da ñu koo sib te la ca gën a jege mooy lu mel ni muus, saw ma ak soow ma ak xayta ya lépp sobe la ñu, loo xam ne Yàlla da koo sàkk def ci ruux waaye daganal na ku ko lekk, su lekkul sobe te itam méddul, saw ma ak soow ma ak xayta ya laab na ñu niki xar, bëy, nag, giléem yoo yu du ñu faral di lekk sobe, bu dee loo xam ne yoon maye na ku ko lekk waaye moom da fay lekk sobe niki ginaar, soo ko yeewee di ko xontee lu amul sobe di na laab amaana bu ñu ko bàyyee muy wër mën naa lekk sobe te loo lu da fay tax xayta ya ak saw ma doon sobe.

Waccu woo xam ne melul na mu meloon ba koo ku di lekk ñam wa walla ba muy naan, waccu woo wu sobe la, yii yépp bokk na ñu ci sobe yi ëpp a laal doo-mu aadama, balaa julli na wóorlu ne ay yëreem walla fa muy taxaw di julli darra taqu ca sobe te itam bu yoree ay lunet walla musuwaar mbaa lenn lu mu àndal ba muy julli, loo la day mel ni yëre ya walla yaram wi darra waru cee am sobe.

Laab gi ci des mooy bu ko sangu farata waree mu def ko, bu ko jàpp war-ee mu def ko, bu dee tiim mu def ko. Laab gii mooy gi ñu maase ni mënul a ñàkk, ku ko tàyyeel ba doo ko def na mu waree ñu war koo ray ni ñuy rayee ku tàyyeel a julli nga xam ne soo ko fàttewoon a def ba julli, fàtte ga du la jariñ darra ndax du tax nga amug julli.

Ndox mi laab

Jàpp ak sangu farata ak dindi sobe ci say yëre walla sa yaram niki ndox mi ngay yóbbu ca wanag wa, yoon ci boppam mooy wax ndox ma baax waaye du rekk ndox moo jël mu baax.

Ndox mi yoon wax ni moo laab mooy ndox moo xam ne melo wa mbaa cafka ga mbaa xet ga darra soppiku wu ca, ci loo xam ne mëneesoon na koo moytu, bu fekkee la soppi ndox ma mëneesu ko woon moytu ndax fa ñuy xellee ndox ma maanaam fa ñu koy wutee mbaa fa ndox may wal mbaa taaju gu yàgg moo ko tax a xeeñ mbaa mu am walaxjaan, lu mel noo nu du ko yàq waaye bu ko lu ñu mënoon a moytu soppee da koy daa di yàq ci wàllu jaamu Yàlla, bu dee la ko soppi lu laab la mel ni diw walla soow walla suukër mbaa

Page 33: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 3

yu demee noo nu, ndox ma baax na ci wàllu naan walla togg mbaa sangu san-gum saabu ak yu demee noo nu waaye bu dee lenn ci yi ñu lim sank ni ay sobe la ñu moo ko soppi, su boo baa ndox mi da ñu koy tuur, ndab la ko defoon sax boo ko soxlaa da nga koy raxas bala nga koo jëfandikoo.

Dindig sobe

Bu fekkee sobe tàq na la te xam na ñu fa mu tàmbalee ak fa mu yem, boo ko raxasee rekk mu daa di baax, da nga koy fóotee ndox mu mel ni bi ngay jaamoo Yàlla, bu la neexee mën nga koo raxasee saabu walla leneen waaye du tee fàwwu nga awalewaat ca kaw ndox mu mel ni mi ngay jàppee ndax boo ko dindee leneen jëmmu sobe ga di na deñ waaye àtte ba ba tay da fay des, bu doon sa yaram it noo nu la, bu doon fa ngay jullee yit noo nu la, du jar ngay fóot lépp-lépp ndax xam nga fi mu tàmbalee ak fi mu yem.

Su fekkee xam nga ni sobe taq na la te nekk ci say yëre walla sa yaram waaye mënoo wax ni fii la tàmbalee fii la yem, bu dee yëre yaa lépp ngay fóot benn yoon, bu dee sa yaram la da ngay sangu benn yoon.

Su la wóoree ni lii moom sobe la waaye yaa ngi naatable ba xam laal na la am déet da ngay wis ndox ci say yëre, boo wisee benn yoon rekk mu daa di doy ndax da ñoo bëgg nga dàq sikki-sàkka goo gu niki nga romboon fas muy saw walla mbaam ngay naatable ba xam laal na la am déet da ngay daal di wis am ndox ci say yëre.

Su fekkee da fa am lu la taq bu wér a wér te ngay sikki-sàkka ndax sobe la am déet, su boo baa da ngay jàpp ni du sobe rekk bàyyi ko noo nu du jar wis.

Boo nekkee di julli ba mu yàgg nga fàttaliku ni sa yaram wii sobee ngi ci walla mi ngi ci say yëre walla fi nga taxaw di julli kon da ñuy seet su dee waxtu wa yaatu na nga xam ni mën ngaa tàggook sobe si ñëwaat julli am ci benn ràkkaa kon dog ga day war, su dee waxtu wa daa xat nga xam ni dem tàggook sobe si dikk amaat ci ràkkaa xaju fi kon da ngay yeggali rekk julli ga baax na.

Su fekkee da ngaa julliwaale sobe moo xam ci saw yaram walla ci say yëre walla fi nga taxaw di julli waaye fàttalikuwoo ko ba far sëlmël, ñépp maase na ñu ci wax ni julli goo gu baax na waaye di na ñu sopp su fekkee waxtu wi des na nga xam ni mën nga fee tàggook sobe si daa di dikkaat baamu ko, daa ñu sopp nga baamu ko

Ngënéel i njàpp

- Wax Bismillaahi

Page 34: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 4

- Soccu nga xam ni bala ngaa jàppu nga koy def

- raxas sa kanam walla sa ñaar i loxo yi bu nekk ñett i yoon, raxas gu njëkk gi bu dajee te matale moom rekk mooy farata ya ca des ngënéel la ñu, saa soo raxasee ba mu matale ba ca topp ngënéel la niki boo raxasoon sa kanam mu matale ci raxas bu njëkk bi, raxasu ñaareel bi ak ñetteel bi yépp ngënéel la ñuy doon, bu matalee ci bu ñaareel bi, bu ñetteel bi mooy doon ngëneel

- Toftale farata yi ak sunna yi

- Booy masaa sa bopp nga tàmbalee fi karaw baaxoo sax ba dellusiwaat fa

- Néewël ndox ma ci cër yi

- Jiitël ndeyjoor ci càmmooñ niki jiitël sa loxo walla sa tanku ndeyjoor ci yu càmmooñ yi

- Diggënte baaraam bu nekk nga xaalil ko (am na ci téere yu ñu koy lim muy farata)

Boo amee sikkim goo xam ne daa woyof mooy boo dee xool di gis fa karaw ga sax, kon booy jàpp da nga koy yëngël ba ndox ma jàll ca deru yaram wa waaye bu fekkee da fa fatt nga xam ni boo dee xool doo gis fa karaw ga saxee, kon boo awalee sa loxo ci kaw rekk mu doy, du jar di ko yëngël ngir ndox ma jàll ca biir, bu fekkee cangaay la moom da nga koo war a yëngël ba ndox ma jàll ca biir.

Ni ñuy dabaatalee njuumte ci njàpp

Boo dee jàpp am ca cëru farata boo xam ni da nga koo fàttee laal, am na ñaar i àtte :

Boo ko teelee fàttaliku kon doo ko mën a ñàkk a raxas waaye boo ko raxasee ba noppi da ñuy sopp la ca topp it nga baamu ko mel ni da nga doon jàppu ba toll foo fu daa di àggale ba njàpp ma àgg niki nga doon jàpp fàttee raxas sa loxo ndeyjoor, yàggul nga fàttaliku ko, da ngay dikkaat raxas ko mel ni foo fa nga tolloon ci njàpp mi daa di koy àggale ba mu mat. Boo yemoon tam ci raxas cëru farata bi kese du ko teree baax, baamu gi da ñu sopp rekk.

Su fekkee daa yàgg nga soog koo fàttaliku, soo dikkee cërub farata ba nga fàttewoon kese ngay raxas du aajewoo ngay baamu la ca toppoon waaye bu dee jotoon nga caa julli kon da fay yàqu ndax boo xasee bàyyi farata ci njàpp da fay mel ni amoo ko ba tax na loo jotoon a julli da nga koy baamu.

Su fekkee ba ngay jàppu da nga caa fàtte sunna soo deful niki nga fàttee

Page 35: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 5

gallaxndiku kon boo yaakaaree ni njàpp moo mu du gaaw a toj ndax da nga cee bëgg a defaale yeneen jaamu Yàlla kon di na ñu sopp nga dem matal sun-na soo su ngir lépp looy def ci njàpp mi fekk mu mat, su fekkee ni bala nga cee def darra mu toj niki yaa ngi bëgg a dem ci wanag wi kon du ko jar. Boo ci jotoon a julli soog koo fàttaliku kon du aaje ngay baamu ndax bàyyi sunna ci njàpp yàqu ko.

Ndéem am na cër boo doon raxas waaye nga fàtte ca ab déenéer mooy digg ci yaram wi wu tooyul, saa soo ko seetloo da nga koy raxas fasaale yéene mottali njàpp ma. Bu dee ginnaaw bi nga gisee ni digg boo bu tooyul fekkoon na nga jot caa julli kon da nga koy baamu.

Su fekkee da ngaa dem bay raxas kanam nga xam ni farata la, fàttaliku sun-na soo deful niki sarandiku kon doo bàyyi raxas kanam gi nga xam ni farata la di saraxndiku ji da ngay wéy ba njàpp mi àgg nga door a def sunna si doonte am na ñu ni da ngay dellu ca sunna waaye ñàkk gee dellu ba àggal moo gën a mat a jàpp.

Yi ku amul njàpp sañul

Bokk na ci yi nga xam ni ku jàppuwul sañoo ko : Julli, moo xam jullig farata la walla naafile (boo amee ngant ngir ñàkk ndox walla tawat, tiim mooy wuu-tu njàpp li), Wër Kaaba gi (Tawaaf) yitam ku jàppul waru koo def, doo sañ a laal ab Kaamil waxu nu sax Kaamil bi waaye feggu ya sax waroo koo laal, du caagin nga koy jéem a laal ak mbalaan walla bant walla musuwaar waaye boo dee kuy jàng alquraan ngir bëgg koo mokkal daa ñu la may nga mën a laal jukki ba nga yittewoo te jàppoo, àlluwe ji ñu bind alquraan yitam mi ngi mel ni téere bi waroo koo laal te amoo njàpp waaye di na dagan ci ki ciy jàng ak ka koy jàngal ñu laal te ame wu ñu njàpp, gone mën naa laal alquraan te jàppul waaye bu loxo ya taqee sobe ba noppi mu dem di ko laal aay na niki bu ko mag defoon waaye ginnaaw gone tàmbalee gu ñu koo bindël i bàkkaar yaw mi ko ko jottali walla yaw mi sàggan ba mu laal ko la bàkkaar bay dellu.

Koo xam ni da fay julli te amewul njàpp ci lu dul genn ngant boroomug caay-caay la, bañoon koo def sax a gën.

Yiy toj njàpp

Yiy toj njàpp ñaar i xaaj la ñu, yi koy toj ak yi koy sabab :

Yiy toj njàpp ñooy lu bàyyeekoo ci buntu saw bi niki saw ci boppam, mazyu ak wadyu mbaa buntu suuf bi niki xayta ak ngelawal te baaxoo faa génnee te génn cig wér.

Page 36: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 6

Wadyu, ndox mu weex lay doon, boo seeree mbaa nga ame sedd mbaa nga tawat bay door a wér boo sawee ba ndoxum saw ma jeex, mooy ndox mu weex mi ciy faral di àndaale, mën naa am mu dem ba jàpp ba noppi muy door a génn kon day toj njàpp la bu fekkee génn ga duy jegee lool ndax bu génn ga jegee lool jàngoro la, du tojati njàpp.

Mazyu ndox la mu weex moo xam ni du far di génnee ci sawukaayu góor fekk muy xool jigéen walla di ko xalaat ba am ca bànneex, daa bokk ci yiy toj njàpp waaye bu génnee ci yaw day war nga raxas li ko dalee fa sawukaay ba saxee ba fa mu yem ca bopp bi doonte taqu ca, ñaar i waay-yàlla yi bu fekkee taqu ca du jar raxas waaye bu ca taqee fàwwu nga raxas ko ndax sobe la, bu taqoon feneen ci yaram wi tam noo nu.

Yiy sabab toj ñooy lépp lu la tàggaleek sa sago niki xëm, nelaw yu diis nga xam ni nit mën naa dugg ba génn te yëgoo ko walla nga yoroon darra sa loxo mu wadd te yëgoo ko ak màndi doonte la ko màndal xaraamul niki naan soow walla garab goo doon fajoo ak say.

Bokk na tam ci yiy toj njàpp fóon bakkan goo jublu bànneex mbaa nga far ko ca am, boo ko jubluwul amoo ko ca moom du ko toj waaye fóon gémmiñ moom mu ànd ak bànneex ak mu ñàkk caa am ñoo yem day toj njàpp ma doonte da ñu laa bett sax.

Jigéen bu laalee sawukaayam te dugël baaraamam ca biir walla mu ŋëb ko day toj njàpp waaye bu dee da fa laal noo na ca kaw rekk du toj.

Góor walla jigéen ku ci laal sa moroom te jublu ca bànneex walla nga am ko ca te jubluwoo ko ca kon sa njàpp toj na, bu dee jubluwoo ca bànneex amoo ko ca moom njàpp ma du toj. Góor bu jàppee ba noppi laal sawukaayam te laalee ko liy xonk ciy tenkam mbaa baaraam yi njàpp la day toj waaye bu njiit-laay jaaree ci diggënte loxo bi ak sawukaay ba walla sarbet mbaa tubëy ak lum yaraax-yaraax du toj.

Koo xam ni wóor na ko ni jàppoon na ginnaaw ba muy sikki-sàkka ba xam toj na am déet kon day jàpp la gën a wóor te mooy mu jàpp ni njàpp ma toj na daa di jàppaat lu dul ni xel ma daa baaxul li mu koy dal bari.

Masaa ñaar i sang (botte)

Daa ñu la may booy jàpp te sol ay bot nga raay rekk ci kawam te bañ koo summi ngir raxas tank yi moo xam cib tukki nga nekk walla déet, na ci saart yi daje rekk, daa war a fekk bala nga léen di sol nga ame njàpp mu mat door léen a sol kon boo tojlee bay jàppaat mën ngaa masaa ca kaw bu dul loo lu doo ko

Page 37: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 7

mën, fukk i saart ñoo ci daje, yaw miy sol bot yi juróom, bot yitam juróom. Bu ñu dajee nga koy mën :

Bot yi : 1 fàwwu mu nekk der bu laab, 2 bu nekkoon deru mbaam xuux mbaa médd du baax, 3 na nekk luñ ñaw ni uude yi di ñawee boo léen di ëwloo, buñ ko taqalee mbaa ñu kole ko walla yeew ko bam mën a dem ci tank du tax mu doy, 4 lum gàtt-gàtt na ëmb say dojor, 5 bum yaatu ba ëpp walla mu xat ba ëpp nga xam ni ku la séen ngay dox da fay daa di xam ni dàll yee tax ngay doxee noo nu waaye du saw doxin.

Yaw boroom dàll yi : 1 bi nga koy sol na nga ame laab door koo sol, 2 laab goo gu nay laabug ndox, 3 Laab ga mat ndax boo jàppoon ba raxas tanku ndeyjoor daa di koy sol du tax mu baax ndax raxasagoo tanku càmmooñ. 4 doo ko sol it ngir yëfu boroom barke walla daa xew ci jamono, moom kay da nga koy sol ngir feg tàngaay walla sedd walla roy Yonent bi SaWS walla ragal jiit walla jaan mooy tax mu baax, 5 sol gi bum doon loo xam ne yoon aayewoon na la ko niki boo dee armal aj walla umra doo ko mën a sol te fekk nga am yeneen dàll.

Ni nga koy masaawee mooy da ngay jël sa loxob ndeyjoor teg ko ci fa tol-look cat i baaraam i tankub ndeyjoor bi, jël sa loxob càmmooñ teg ko ca ron ba wéy ba ca dojor ba, nii yit nga koy defee ci tankub càmmooñ bi, fii am na wuute ci loxo biy féete kaw ak biy féete suuf boroom risaala daa wax ni loxob càmmooñ beey féete kaw loxob ndeyjoor bi féete suuf. Bu fekkee suufu bot yi daa am suuf walla nefere yu ci taq da nga koy dindi ba noppi door koy masaa. loxob càmmooñ biy féete suuf day tàmbalee ca tëstënu bot ba wutsi ci baa-raam yi, loo lu day tax bépp sobe bu fa nekk du weesu biir dàll wi ndax loxo ba du yéegaat

Ngënéel i cangaay

- Booy tàmbali wax Bismillaahi

- Tàmbalee ci dindi sobe si

- Njàppum benn-benn

- cër bu nekk nga tàmbalikoo raxas ca kaw jëm ci suuf

- raxas bopp bi ñett i tankin, bu karaw gi baree te ñett yi daju ko fàwwu da ngay jàll ba kero muy daj

- Lépp lu am ndeyjoor ak càmmooñ nga njëkkee ndeyjoor door cee teg càmmooñ

Page 38: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 8

- Néewël ndox mi

Boo sangoo ba noppi gis foo laalul mbaa cërub lëmb bu tooyul da ngay daa di gaaw mottali cangaay li daa di koy def fa saa sa mu daa di baax, boo ci jullee ba noppi door koo gis da nga koy julliwaat ginnaaw boo ko raxasee. Boo ko fàttalikoo yéex ko raxas ba mu yàgg cig tayeef moom cangaay la da fay yàqu da ngay tàmbaliwaat. Bu dee ginnaaw bi nga sangoo da fa am loo bàyyi te bi nga sangoo ba noppi da ngaa jàppu far raxasaale ko kon di na ko yóbbaale, fàtte gi ci cangaay li du ko wàññi darra.

Boo amee janaaba te sangoogoo ko, ya ñu la aayewoon ngir ñàkk njàpp yépp waroo koo def ak yii nuy bëgg a lim : Dugg Jàkka, jàng alquraan (Bu dee njàpp nga ñàkk Kaamil bépp mën nga koo tari waaye boo amee janaaba tari goo gu da ñu la koy aaye ndare benn aaya walla ñaar ngir muslu walla léemu walla ngir tektaloo ko cib àtte).

Boroom xam-xam yépp dëppóo na ñu ci ne ku mënul sangoo ndox mu sedd du sañ a joteek soxnaam liféeg waajalul jumtukaay ji nga xam ni moom lay tàngalee ndox mi mu war a sangoo. Bu ko Yàlla nattoo mu gént ame janaaba, genn yeddeel walla bàkkaar du ko ci fekk, bu amee lu mu mën a tàngalee ndox sangoo ko mu baax, bu dee amu ko te mënu koo am mu tiim rekk nég ba yaramam àttan ndox ma mu door a sangu.

Ngënéel i tiim

- Wax Bismillaahi

- Jiitël ndeyjoor ci càmmooñ ci ñaar i loxo yi

- Loxo bi boo koy masaa, jiitël biti bi ci biir gi

- Tàmbalee catu baaraam ya wuti coñc la buy masaa loxo bi

Yay yàq njàpp, ku tiim def ko mu yàqu ba mu des amug ndox njëkk sag tàb-bi ci julli ga, boo tàmbaliwoon julli gi ndox am doo ko dagg da ngay wéy rekk. Genn tiim yitam deesu ci julli ñaar i farata nga xam ni boo doon fay tisbaar te tàkkusaan jot da ngay tiimël tisbaar gi, tiimël tàkkusaan gi waaye ay naafile yu bari mënees na ñu léen a boole genn tiim niki naafile ramadaan.

Boo tiimëlee farata war a jàll ci naafile du jar ngay tiimaat mën ngaa jàll rekk def ko.

Boo tiimëlee farata walla naafile mën ngaa jàll jàng ca alquraan walla wër ca Kaaba gi wër goo xam ni du wërug farata, ci saartub yéene ànd ak toftale ko.

Page 39: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

3 9

Ku tiimël naafile du mën a jàll teg ca farata, boo tiimëlee gee mën ngaa jàll julli ca safaak witar ci saartub ñu toftaloo waaye bu yàggee fàwwu nga tiimël léen seen tiimug bopp.

Kuy tiim te fekk mu ame janaaba da fay yéenewaale janaaba ji du tiim tii-mug ku amewul njàpp doŋŋ, da fay tiim tiimug ku ame janaaba te fas yéenee daganloo julliwaale janaaba ji lu ko moy tiim ga du baax, bu ca jullee sax da koy baamu ginnaaw bu tiimaatee boole ca yéeneg janaaba.

Ni ñuy tiimee

Boo dee tiim ngir julli da ngay nég ba waxtu wi tàbbi, nga wut pàkkub suuf bu laab walla doj bu yaatu te du simang walla laso walla karo, nga teg ca say tenk bës ko ca bu baax te tàllal say baaraam, nga yëkëti sa loxo yi bomb ko ci sa kanam ba mu daj, fenn bañ a des, nga njëkk a bomb sa loxo ndeyjoor.

Booy bomb say loxo ci sa kanam, bu ca suuf taqee bu ko fëgg bu ko faxas, da nga koy bombaale ba mu taq ca.

Da ngay wax ci sa xel ni fas na maa yéene daganlu ag julli ci toj mu mag mii bu la sangu waree walla nga ne ci toj mu ndaw mii bu la njàpp waree.

Nga tegaat say tenk ci suuf, bës ko bu baax tàllal say baaraam xaw léen a teqale tuuti, nga yëkëti say loxo, teg sa biti loxo ndeyjoor ci sa biir loxo càmmooñ, dalee ko ca cat i baaraam ya bomb ko ci sa coñc, wëlbëti sa loxo càmmooñ jël tenk ba bomb ko ci sa biir xasabu ndeyjoor dalee ko ca coñc la ba ca sa tikku-jara.

Teg sa biir baaraamu déeyu càmmooñ ci sa kaw baaraamu déeyu ndeyjoor bomb ko ca, nga def noo nee sa loxo càmmooñ tam.

Masaa say tenk, masaa sa diggënte baaraam yépp bomb léen.

Nodd ak liqaam

fépp fu néegub Yàlla nekk, war na ci warug sunna su waxtu julli jotee ñu yëgle ko fa ci nodd doonte jàkka ya da ñoo jegee du tee ñu war koo def, foo xam ni mbooloo da fay daje doonte du jàkka waaye jàpp nañ ni buñ noddee am ñu léen fekksi war nañ koo def bu dee foo xam ni mbooloo nga fa te buñ noddee du am ñu wuyusi kon du ko jar.

Bu dee da nga di kenn, boo noddee dañ koo sopp waaye ci saartub nga génn dëkk bi cib tukki walla nga foriy gettax waaye boo nekkee sa kër yaw doŋŋ walla ngay kenn ci dëkk te mu leer la ni boo noddee kenn du la fekksi da

Page 40: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 0

ñuy sib sa nodd xanaa nga tàmmal ko nit ñi ba yaw la ñuy déglu.

Liqaam sunna su dëgër la goo xam ni daa war góor doonte moom doŋŋay julli, moo gën a dëgër sax nodd ndax moo gën a sës ci julli gi, jigéen moom ag noddam xaraam na waaye sopp nañ ci moom mu liqaam te suufeel ko door a julli, bu ko deful it darra du ko ci fekk, nodd ab julli te waxtoom jotagul daa xaraam ndax wax lu amul la ngir nodd li muy tekki mooy waxtu wi jot na bam des jullig suba ndax buy ñëw da fay fekk ñu bari di nelaw, da ñuy bëgg ñu jiitël ay nodd ngir yeete ndax nit ñi jóg balaa waxtu waa jot dëgg-dëgg, bu jotee ñu door a nodd, nodd gay wone ni waxtu wi jot na, su ko defee noddug yeete mën nañ koo def ci boo xaajoon guddi gi juróom benn i xaaj, bu juróom yépp jàllee ci nga koy mën a def.

Nodd mooy wax :

allaahu akbar 2

ach’hadu an laailaaha ilalaa 2

ach’hadu anna Muxammadar rasuululaa 2

ach’hadu an laailaaha ilalaa 2 mu gën a kawe ci yoon bu njëkk bi

ach’hadu anna Muxammadar rasuululaa 2 mu gën a kawe ci yoon bu njëkk bi

Xayya ala salaa 2

Xayyaa ala falaa 2

Boo nekkee ci noddu suba kepp nga ciy dolli a’salaatu xayrun mina nawm 2

allaahu akbar 2

Laailaaha ilalaa 1

Liqaam mooy wax :

allaahu akbaru

allaahu akbaru

ach’hadu an laailaaha ilalaa

ach’hadu anna Muxammadar rasuululaahi

Xayya ala salaati

Xayyaa ala falaaxi

Page 41: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 1

Qadd qaamati salaatu

allaahu akbaru

allaahu akbaru

Laailaaha ilalaa

Ngënéel i julli

- Yëkëti say loxo ba mu tollook say nopp ci kàbbaru armal bi (boo waxoon allaahu akbar te yëkëtiwoo loxo yi du ko teree baax)

- Wax Rabbanaa wa lakal xamdu walla Allaahumma Rabbanaa wa lakal xamdu

- Wax aamiin ginnaaw boo waxee wa laa daaliin ci faatixa moo xam ci yelu la walla béral (boo dee maamuum di jàng ci suuf ba wax ko daa ñu sopp nga wax aamiin walla sa ilimaan wax ko, deesu ko jéem a tolloole ndax da ñuy bañ nga wax ko ci barab bu mu dëkkul), ilimaan di na ko wax buy yelu waaye du ko béral, bu dee béral day bàyyi maamuum yi wax ko

- Wax Subxaana Rabbiyal aziim ñett i yoon boo rukkoowee

- Wax Subxaana Rabbiyal a’laa ak ñaan gi ñu fay faral di ñaan ci sujjóod

- Jàng saar wu gudd ginnaaw faatixa ci jullig suba ak tisbaar boo dee julli yaw kese walla ngay jiite te mu wóor la ni ñoom ñépp a sawar ci njàng mu yàgg mi (tiwaalul mufasal mooy saar yi dalee xujuraat ba Abasa)

- Gàttal njàng mi ci tàkkusaan ak timis (li ko dalee ci suuratu Duxaa ba ci Naasi ñooy yu gàtt yi)

- Jàng saar yu digg-dóoomu booy julli gee (li ko dalee Abasa ba ci suuratu Duxaa ñooy yu digg-dóomu yi)

- Saar wi ngay jàng ci ràkkaab ñaareel gën a gàtt bi nga jàng ci ràkkaa bu njëkk bi

- Boo rukkoo nga jàpp ci say bëtu wóom bu dëgër, dëj say tank ba du jóg ak a toogaat, sa ginnaaw bañ a nóox

- Toogaay bi ngay def ci ràkkaab ñaareel bi ak booy taaya nga xam ni da ngay bañ a toog ci say tank ba noppi nga génnee léen ci sa wetug ndeyjoor, sa tanku ndeyjoor nga yëkëti ko ba noppi baaraam ya sampu jëm suuf

- Xunóot te bañ koo béral ci ràkkaab ñaareelu suba ginnaaw jeexug saar wa

Page 42: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 2

- ñaan ginnaaw taaya ji ngay sëlmëlee

- Boo de wax Assalaamu alaykum boo yeggee ci war a wax kum nga àg-galee ko ci sa ndeyjoor nga xam ni ku la féetewoon ginnaaw di na séen sa benn lex.

- Yëngël sa baaraamu sànnikaay booy taaya ba kero ñuy sëlmël

Sib na ñu ngay julli taxawee benn tank ndare julli ba daa yàgg ba nga def noo nu ngir noppaloo ko, jegeel say tank ba mel ni ku ñu yeew yitam sib na ñu ko ak di julli sex ci sa gémmiñ lu mel ni ab dërëm walla aw xeer ak geestu niki noo nu gëmm say bët lu dul ci ngant (ngelaw walla bañ a xool lu xaraam), ba tay wax a’uuzu billaahi mina chaytaani rajiim walla Bismillaahi raxmaani raxiim walla Laa xawla wa laa xuwata ilaa billaahi walla Xasbunaal Laahu wa nihmal wakiil ci jullig farata waaye dagan na ci naafile.

Lépp lu mën a jax-jaxi sam xel rekk sib na ñu nga di ko julliwaale moo xam daa nekk ci sa poos walla sa ginnaaw walla sa kanam walla sa wetug ndeyjoor mbaa sa wetug càmmooñ, sib na ñu tam ngay xalaat ci mbir i àdduna darra.

Saart i Julli

Julli daa am i saart yoo xam ni bokkul ak farata yi.

Bokk na ca, ame laabug xadas mooy bu la sangu farata waree nga def ko, bu la jàpp waree nga def ko, bu dee sa farata mooy tiim it nga def ko.

Laabug xabas tam ci saart yi la bokk te mooy bu sobe nekkee ci sa yaram mbaa ci say yëre mbaa fi ngay jullee nga dindi ko bala ngaa julli, da ñuy bañ nga julliwaale sobe te fekk nga mënoon a tàggook moom, su fekkee da ngaa julliwaale sobe te mënoon a tàggook moom te tay ko fàwwu nga baamu ko.

Sàng awra bokk na ci saart yi : awray góor nga xam ni war na koo sàng buy julli mooy li dalee ci jumbaxam ba ci ñaar i bëtu-wóomam, terewul ñu sopp nga wormaal sa yaram sol yu baax ngir tegginu ci sa kanam Boroom, jigéen moom mbooleem yaram wi la war a sàng ndax awra la ba mu des kanam ga ak ñaar i tenk yi. Sol tubëy joo xam ni sàng na jumbax gi wàcc ba ci tank yi ëmbaale bëtu-wóom yi, bu ko góor defee julli gi baax na waaye sib na ñu ko.

Bu fekkee yëre yi nga am daa am sobe te amoo beneen te amoo yitam ndox moo ko fóotee walla boo ko bëggee fóot waxtu wa raw la kon na nga ko far julliwaale darra du ci nekk waaye bu dee waxtu wi yaatu na ba mën nga fee dindi sobe si te waxtu wi du la raw kon day war nga dindi sobe si ba noppi door koo sol jullee ko, tooyaay ba yitam du ca wàññi darra. Sa ñàkk a set gi bu taxee

Page 43: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 3

nga yéexee julli ga ngir ni yëre yi daa am sobe nga ni naa bàyyi ba am yëre yu laab walla ba am ndox fóot ko kon yenu nga bàkkaar ndax da ngaa waroon a julliwaale sobe si rekk ndax sobe si aayul ndegam ngant la, ku rafle ba lu sàng awraam sax amu ko, koo ku da fay def yaramu neen julli ndax loo lu la mën.

Jublu Xibla yitam bokk na ci saart yi, nga xam ni mooy boo nekkee Màkka walla la ko wër moom jëmmu Kaaba gi ngay war a jublu, boo soree Màkka, wet ga Kaaba ga féete rekk ngay jublu, koo xam ni ba muy julli daa moy xibla waaye laata mu koy yëg julli na ba sëlmël kon da ñuy sopp rekk mu baamu ci waxtu wa. Bu dee ci biir julli gi la yëgee ni moy na xibla, da ñuy seet su fekkee ni gumbë la du aaje muy dagg julli gi day wëlbëtiku rekk jublu xibla, su fekkee njàccaar la te fekk la mu ko moyee tuuti la du aajo muy dagg julli gi da fay daa di jublu xibla rekk. Bu dee njàccaar la te fekk la mu moy ci xibla gi daa bari te mu yëgee ko ci biir julli gi da fay dagg julli ga jublu xibla ba noppi door a tàmbaliwaat.

Lépp lu ñuy baamu ci waxtu wa kepp te su waxtu wa jàllee kenn du ko baamooti xamal ni baamu goo gu ngënéel la ndax su doon baamu gu war da ñu lay wax ni da nga koy baamu, fàwwu waxtu wa jàll walla mu bañ a jàll a ci yem niki naafile rekk ndax waxtu wa nga ko war a defee bu jàllee rekk kenn doo tu ko baamu.

Bokk na yitam ci saart yi nga bàyyi lépp lu mënul a ànd ak julli gi mel ni wax walla jëf ju jëmul ci julli ga.

Jullig aji tawat

Jullig farata daa am juróom ñaar yu ñu war a sàmmonteel, ñent ya dees koo war a tegale boo ko mënee moom rekk ngay sañ a def doo mën a jàll ca ba ca des, ñett ya mën ngaa mën bii te jàll ca ba ca des te du ko teree baax.

Su ko defee ñent yi ñu war a tegale ñooy, su fekkee mën ngaa julli taxaw jonn kon da nga koy def, soo ko tëlee te mën a taxaw wéeru kon nga taxaw wéeru, soo ko mënul te mën a toog te bañ a wéeru kon nga julli toog te bañ a wéeru, soo ko tëlee te fàwwu nga wéeru nga soog a sañ a julli toog te wéeru. Mukallaf mu ne yii da koo war a toftale bu mu ci mënul soog a jàll ca ba ca des, ñent yii boo ci def te mënoon ba ko jiitu sa julli day daa di yàqu.

Ñett yi nga xam ni da ñoo sopp nga tegale ko waaye tegale ga warul ñooy su fekkee ni yaw julli toog wéeru ci darra mënoo ko, tëdd rekk nga mën sopp na ñu nga tëddee sa wetug ndeyjoor jublu xibla, boo tëlee wetug ndeyjoor nga tëddee wetug càmmooñ, boo ko tëlee nga jaaxaan say tank jëm xibla.

Page 44: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 4

Su ko defee li ñu wax nii bu dee da nga mën a taxaw julli te doo wéeru ci darra nga julli wéeru ci darra, julli gaa ngi yàqoo ci bu fekkee ni la nga wéeru sëf nga ko sa doole bu baax ba nga xam ni bu daanuwoon nga ànd ak moom daanu waaye bu dee wéeruwoo ca bu baax da ngaa def lu ñu sib rekk waaye àggul ci yàq sa julli.

Bu fekkee ni da ngay julli jullig naafile dagan na nga mën a taxaw ba noppi daa di toog waaye waxeef na ni tuyaaba ja nga waroon a am xaaj ba lay doon. Lee lee yitam mën ngaa tàmbali naafile ci toogaay ginnaaw ga nga sawar daa di jóg yeggalee ko taxawaay darra nekku ci walla nga tàmbalee ko ci taxawaay yeggalee ko ci ab toogay.

Jullig tukki

Képp ku tukki soriwaayu ñent i bariid am na ñu ne day nekk ñéen-fukk i kilomet ak juróom ñett, am na ñu wax ni mooy juróom ñaar fukk i kilomet ak ñaar mooy bi gën a wér, mën ngaa wàññi bépp julli bu matoon ñent i ràkkaa, suba ak timis deesu léen wàññi.

Booy bàyyeekoo ci dëkk bu mag bala ngaa tàmbalee wàññi da ngay nég ba génn léppu dëkk bi, nga xam ni amul benn kër bu tollook yaw ci ndeyjoor mbaa càmmooñ walla sa kanam, bu amoon ay tool sax yoo xam ni fa la waa dëkk bi di bayee wallab maarse boo yaboo boole ko ci dëkk bi ba weesu léen door a tàmbalee wàññi, waaye na tukki ba bañ a doon tukki fo walla moy. fi nga xam ni boo fa tollee booy dem mën a wàññi booy ñibisi ba tollaat foo fa ca ngay tàmbalee matal doonte duggagoo sa kër.

Bu fekkee àgg nga ci barab te yéene faa sax ñent i fan walla la nga fay top-patoo fàwwu mu mat ñent i fan, kon da ngay matal julli yi ba ba nga fay bàyyi-koo, door a seet ba xam fa nga jëmaat di na matal saart yi am déet, booy dem di nga wàññi ba ba ngay yegg ndéem barab ba nga jëm mat na doxub wàññi, bu dee ci diggënte bi daa am fooy jàdd te sa dig ak moom matul doxub wàññi fas faa am ñent i fan kon ba ba nga fay àgg doo wàññi.

Nees di fayee boru julli

Boo amee boru julli, taxaw temm ci bëgg léen a fay, lu war la kenn waru koo sàgganee, bu fekkee da ngaa bari boru julli te bis bu nekk nga fay juróom i bis maanaam saa boo jullee genn julli fay juróom teg ca ku farlu nga.

Julli gu ne na mu raweewoon nga koy fayee, bu dee da laa rawee fa nga dëkk nga xam ni waroo koo wàññi kon boo koy fay da nga koy matal, bu dee bam lay raw cib tukki nga nekkoon sa sunna moo doonoon wàññi ko kon boo

Page 45: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 5

koy fay da nga koy wàññi bu dee julli gu mat ñent i ràkkaa la niki tisbaar, tàk-kusaan ak gee, waxtu wa ngay fayee amu ci solo waxtu wam la rawee rekk la deefi seet, bu dee daa am julli gu la rawoon ba nga nekkee ca dëkk ba, ba nga demee bay tukki nga bëgg koo fay da nga koy matal, bu dee julli gu la rawee ci yoon wi, boo ñibisee ci kër gi du tee da nga koy wàññi.

ñaar i julli yoo xam ni da ñoo bokk waxtu bu fekkee xaj na ñu ca waxtu wa fàwwu nga war léen a tegale ndegam fàttewoo ko, bu tàkkusaan jotee te julleegoo tisbaar da ngay njëkk a julli tisbaar door cee teg tàkkusaan, boo ko tayee njëkk a julli tàkkusaan da ngay mel ni ku ko julliwul, da ngay julli tisbaar ba noppi war ko cee tegaat niki noo nu timis ak gee.

Bu dee am na julli yu la raw yoo xam ni bari wu ñu mooy ñent i julli jëm suuf, su la ñent i julli rawee am julli gu jot day war nga julli ñent yi la raw ba noppi door a julli gi jot doonte boo nekkee di léen julli gii teew waxtoom raw la sax da nga léen di fay ba noppi soog a julli gi teew, boo ko deful rekk am bàkkaar, toftale ga moytu bàkkaar lay doon boo julliwoon gii teew door a julli yoo yu du ko tee baax doonte benn waxtu la niki suba daa jot te yaw julliwoowoon gee biig ngir nga bañ a am bàkkaar da ngaa waroon a fay gee ba noppi door cee teg suba, boo njëkkoon a julli suba du ko tee baax waaye bàk-kaar ngay am ci ñàkk koo tegale, ñaar i julli yu bokk waxtu la tegale ga mënul a ñàkk nga xam ni soo ko deful du baax, yi ci des soo léen tegalewul bàkkaar ngay am ci ñàkk gaa tegale waaye du ko tee baax.

Soo amee boru julli waxtu wu nekk manees na ko caa fay, koo xam ni xas nga koo ame doo sañ a naafile ndax li nga war a naafilaa da nga koo war a fayee bor yi nga ame ba noppi niki naafileg yoor-yoor ak ramadaan walla di dawal tisbaar mbaa tàkkusaan waaye safaak witar ñoom loo bari-bari bor mën nga léen a def ak ñaar i julli iid yi (korite ak tabaski) ak jullig muurug jant ak jullig mbaaw, jullig muuru weer dañ cee wuute, ñaar i ràkkaay fajar dañ léen a fonk lool su julliy sunna yii jàllee ñoo ci topp moo tax ñu tuddee léen A’rahiibatu ñoom it loo bari-bari boru julli da nga léen di jooxe.

Su fekkee da ngeen a bokk ame boru julli te yéen a yemle ya léen raw mën ngeen jiitël kenn su ngeen di fay julli ya ngeen ame, ku fàtte lim yam am ciy bor kon day fay di fay bam leer ko ni lam amewoon ciy bor fay na ko mu door a bàyyi.

xabla salaam ak Bahda salaam

Sunnaaleef na ngir ag njuumte ci dolli walla nga wàññi ñaar i sujjóod. Bu

Page 46: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 6

fekkee da ngaa juum dolli darra ci julli gi, boo sëlmëlee da ngay sujjóod ñaar i sujjóod taayawaat daa di sëlmël, taaya ju gàtt lay doon ci abduhuu wa ra-suuluhuu lay yem, su fekkee da ngaa wàññi lu mel ni sunna soo xam ni ku ko wàññi da nga ko war a sujjóodal xabla salaam, da ngay taaya ba fa nga daan war a waxee assalaamu alaykum, nga daa di sujjóod ñaar i sujjóod daa di taayawaat taaya ju gàtt door a sëlmël.

Bu dee da ngaa boole dolli ak wàññi, da ngay sujjóod xabla salaam, bu fekkee da ngaa waroon a sujjóod xabla salaam, fàtte ko ba wax assalaamu alaykum te fekk bi nga ko fàttalikoo ak bi nga sëlmëlee soreewul, da ngay daa di sujjóod sa xabla salaam, taayawaat sëlmël mu jeex waaye bu dee yàgg na nga xam ne jàkka ja nga doon jullee génn nga ko walla sax génnoo ko waaye yéex nga koo fàtteliku lool kon sujjóod ba ak julli gi lépp yàqu na, da ngay jul-liwaat bu fekkee la la tax di sujjóod mat na ñett i sunna walla aw saar ndax ku ko fàtte bàyyi nga ñett i sunna ndax jàng gi ak taxawaay bi, yelu gi walla béral gi lépp sunna la bu ko matul nak du yàqu niki lu mel ni taaya, bu dee bahda salaam boo ko fàttee doonte ay at la, boo ko fàttalikoo da nga koy sujjóodal.

cosaanul sujjóod mooy bàyyi ñaar i sunna walla lu ko ëpp déet lu ko yées. farata moom saa soo ko bàyyee mëneesu koo sujjóodal xabla walla bahda salaam, da nga koy indiwaat rekk.

Koo xam ne wàññi na ci ngëneel i julli deesu ko sujjóodal, benn sunna tam boo ko bàyyee doo ko sujjóodal lu dul ku bàyyi ag yelu walla béral. Béral boo ko defee ci barab boo waroon a yelu da ngay sujjóod bahda salaam ndax da ngaa yokk, boo yeloo ci barab boo waroon a béral da ngaa wàññi kon xabla salaam ngay def.

Bu dee da ngaa juum ba wax ci biir julli da ngay sujjóod bahda salaam taayawaat sëlmël ndax da ngaa dolli, koo xam ne daa sëlmël ginnaaw bu mu jullee ñaar i ràkkaa niki mu doon julli tisbaar def ñaar i ràkkaa taaya taaya ju njëkk rekk daa di sëlmël war na ci moom sujjóodug bahda salaam ginnaaw bu mu jógee ba àggale julli gi.

Koo xam ne daa dolli ñaar i ràkkaa niki ngay julli tàkkusaan def ko juróom benn ràkkaa walla nga dolli benn ràkkaa, boo sëlmëlee da nga koy sujjóodal bahda salaam waaye lu toll ni ràkkaa yi ab julli war a am boo ko ci dollee niki ngay julli tisbaar def ko juróom ñett i ràkkaa walla tàkkusaan walla gee kon julli ga day yàqu, timis moom boo ci dollee ñent i ràkkaa moo koy tax a yàqu.

Bu fekkee yaa ngi julli di sikki-sàkka naan ñent i ràkkaa laa am walla ñett,

Page 47: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 7

jàppal ni la gën a néew nga am daa di indi ñenteelu ràkkaa bi ndax boroom xam-xam yi da ñuy wax ne booy sikki-sàkka ba xam mat na am matul, jàppal ni matul boo noppee sujjóod bahda salaam, bu dee da ngay sujjóod di sik-ki-sàkka ba xam benn yoon nga sujjóod walla ñaar da ngay daa di sujjóodaat beneen, sëlmëlël ndéem yaa ngi sikki-sàkka ci ba xam sëlmël nga am déet su dee yàggul, doo ko sujjóodal darra du bahda du xabla. Bu dee diggënte bi ngay sikki sàkka ba xam sëlmël nga am déet da fa yàgg lool walla génn nga jàkka ji, kon xamal ni goo gu julli yàqu na, da nga koy julliwaat.

Koo xam ni boroomug jax-jaxal la mooy ku xelam bon ba nga xam ne saa buy julli du xam ci ban ràkkaa la toll, lum xelam jàpp, na jàpp loo la te wéyal julli gi waaye ginnaaw bu sëlmëlee sopp na ñu mu sujjóod bahda salaam.

Koo xam ne daa béral xunóot darra du ko ci war du xabla du bahda waaye bu dee tayeef lu ñu sib la.

ñaar i ràkkaa yu mujj yi sunnaalu ñu ku ci dolli aw saar, koo xam ne da koo tay jàng ko ci def na lu ñu sib waaye du ko tax a sujjóod.

Koo xam ne da fa tàmm su déggee Muxammad daa di ciy teg sallalaahu alayhi wa salam, su ko nit rombee wax turu Yonent bi SaWS mu juum wax salalaahu alayhi wa salam, bu fekkee tayu ko, sibu ñu ko, su ko tayee sib na ñu ko ak fu mu ko mën a defee ci biir julli gi.

Koo xam ne da fa jàng ñaar i saar ci biir julli walla lu ko ëpp walla mu jàng aw saar jeexal ko ba dugg ci weneen walla mu rukkoo te saar wa mu tàmba-liwoon jeexul, yoo yu yépp sujjóod waru ca.

Koo xam ne da fay julli am kuy wax mu di ko joxoñ walla muy yëngël bopp bi di ko junj, loo la sujjóod waru ci.

Koo xam ne da fa juum ba baamu faatixa, li koy war mooy suujjóod bahda salaam waaye bu dee baamu gi tayeef la, julli ga yàqu.

Boo jàngee faatixa waroon caa teg saar, dem bay waaj a sëgg fàttaliku saar wa, du la tax a siggi ni da ma ciy teg saar, ndax rukkoo gi nga jëm farata la te farata kenn du ko tàmbali di ko bàyyi di dellu ci sunna, da ngay wéy boo nop-pee sujjóodal ko xabla salaam.

Ki nga xam ne da fay julli, jàng bay waaj a rukkoo fàttaliku ne li mu jàng da koo yelu te fekk lu ñu war a béral la, bu fekkee faatixa ja doŋŋ la, kon da fay baamuwaat faatixa ja, bu noppee sujjóod bahda salaam ndax daa jàng faati-xa ñaar i yoon te loo lu ag dolli la, bu fekkee saar wa doŋŋ la yelu kon da koy

Page 48: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 8

baamuwaat waaye aw saar moom mënees na ñu jàng lu ëpp benn moo tax sujjóod du la ci war. Bu fekkee jot ngaa rukkoo te yelu loo waroon béral, boo noppee da ngay sujjóod xabla salaam ndax bàyyi nga béral te ku ko bàyyi da ngaa wàññi moo xam ci faatixa ji la walla ci aw saar.

Boroom xam-xam yi dëppoo na ñu ni kuy julli ree te tay ko sa julli yàqu na, juum ree moom am na ñu ne day yàq julli am ñu ne du ko yàq waaye wér na ne ku sàggan kepp mooy ree ci biir julli walla kuy fo te réer. Sëriñ Tuubaa qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu am na benn bis mu woo mag ñi ne leen julli de na ngeen ko fonk bu baax waaye naqari naa def lool, ndax julli dëgg-dëgg boo ko dee def, boo kàbbaree su ñu faboon paaka di dagg sa cër yi benn ginnaaw benn di wacc doo ko yëg, moo ne déey mboolooo mii toog ku mën a jullee noo nu am na fi.

Muuñ ci julli moom darra nekku ci du yàq julli, sujjóod waru ci, du waral baamu julli gi.

Kiy julli di xalaat màggug sunu Boroom ak tëkku yi mu tëkku moykat yi wal-la muy jàng alquraan ci julli di ko settantal bay jooy, jéggël na ñu ko ko doonte ma ngay sërxët ca kaw, naka noo nu ki nga xam ne daa nekk ci biir julli am ku ñëw yàkkamti bëgg koo wax darra ba dem, moom miy julli mu ne cell dagg njàng ma ngir bëgg koo déglu ba xam li mu koy xibaar mu door a wéyal julli gi waaye déglu ga bu mu yàgg.

Koo xam ne da doon julli, julli goo xam ne da fa am taaya ju nekk ca digg ba muy jullig ñent i ràkkaa walla ñett i ràkkaa, mu def ñaar i ràkkaa ba mu laataa toog, jóg taxaw walla ba mu toogee laataa taaya jóg taxaw waaye laataa ñaar i loxo yi ak ñaar i bët i wóom yi di tàqarlikook suuf si, fàttaliku na ko daa di toogaat jëm ca taaya ju njëkk ji, koo ka sujjóod waru ko ndax loo lu mu def lu woyof la, su fekkee ni ba mu fàttee taaya ji, ñaar i loxo yi ak ñaar i bët i wóom yi tàqarlikoo na ak suuf si, bu mu toog na wéy taxaw, bu noppee sujjóod xabla salaam ndax taaya joo ju mu wàññi. Bu dee ginnaaw tàqarlikoo ga dellusiwaat na toog koo ku aw àtteem ñaar la : 1- bu dee bi mu laataa taxaw jonn la dellusi toog ngir taaya ja mu fàttaliku, koo ku bu noppee da fay sujjóod bahda salaam ndax da fa dolli 2- bu dee da fa nég ba taxaw jonn doo ga dikkaat toog, dolli na bu noppee dafay sujjóod bahda salaam.

Koo xam ne da fay julli, juum ba wal (ëf), kon dolli na, bu noppee da fay sujjóod bahda salaam, bu dee moo ko tay, kon julli ga da fay yàqu bu fekkee wal ga ci gémmiñ la ko defee, bu dee ci bakkan sujjóod waru ko.

Page 49: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

4 9

Ndéem tisli nga ci julli, bul soxlawoo naan Alxamdulillaahi Rabbil aala-miin, bul delloo ka nga xam ne ndokkeel na la maanaam boo tislee am ku la ne yarxamukallah, bul ko delloowaat naan ko yaxfirullaahu lanaa wa lakum wa yahdiikumullah wa yuslixu baalakum, da ngay wéyal sa julli rekk.

Bul dégg kuy tisli te fekk nga nekk cib julli naan ko yarxamukallah. Lii nag da ñu koo sopp, darra warul ki ko def.

Bu dee da ngaa nekk di julli far bébbëli, da ngay jël sa loxo ubee ko sa gé-mmiñ te bañ a wax darra.

Boo bëggee tufli da ngay génnee sa mbalaan walla sa musuwaar raay ko ci sa làmmiñ, tuflit ya taq ca waaye bul ni tëf ndax su boo baa taa ak faa day génn te loo lu da fay yàq julli gi ndax dolli nga ca lu ca bokkul.

Koo xam ne da ngay xalaat ndax man yor naa am toj am déet walla ngay sikki-sàkka ci yor sobe am déet, ginnaaw ba mu wóor ko ni laab na, sujjóod waru ci.

Ki nga xam ne da fay julli ba ci yàgg mu juum geestu te xar kanam gi kepp a geestu waaye jëmm ji wëlbëtikuwul darra waru ci waaye lu ñu sib la. Ki nga xam ne daa geestu ba jëmm ji jublootul xibla, koo ku moom julli gi da fay yàqu fàwwu da koy baamu ndax jublu xibla daa bokk ci saart i julli.

Koo xam ne da fay julliwaale sooy ndax xaraam na ci góor mu koy sol, walla mu xool lu ñu xaraamal moy na Yàlla waaye teewul julli ga moom wér na niki noo nu ku sàcc ci biir julli.

Bu fekkee da ngay jàng alquraan ginnaaw bi nga jàngee faatixa ba noppi, am ñaan yoo tàmm a teg ci faatixa, nga far teg léen ca ginnaaw faatixa ji nga jàng ci biir julli gi, nga fàttaliku ne ci biir julli nga nekk doonte benn baat nga ci jàng, da ñuy xool su fekkee ci alquraan la bokk, sujjóod du la ca fekk waaye su fekkee ñaan ga bokkul ci alquraan, da ngay sujjóod bahda salaam ngir ag dolli goo tayul waaye soo ko tayee julli ga day yàqu. Su fekkee da fa jàng baat boo xam ne ci alquraan la bokk waaye mu soppi baat ba niki iyaaka nahbudu mu wax iyaaka yubhadu walla mu yàq maanaa ma niki iyaaka nahbudu mu wax iyaaka tahbudu, sujjóodu bahda salaam moo ko cay war.

Soo gëmméntoo ci biir julli gëmmént gu woyof xamal ni yàqul julli, sujjóod it du la ci war waaye boo àggee ci nelaw, nelaw yu diis xamal ne julli ga yàqu na, njàpp ma itam toj na ndax nelaw yu diis da fay toj njàpp te njàpp su tojee julli ga yàqu. Nelaw yu diis ni ñu koy xàmmee ak nelaw yu woyof mooy nelaw ba yuut walla nelaw te yoroon darra mu rot te yëgoo ko.

Page 50: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 0

Koo xam ne da fay julli te wéradi ba tax muy wonk, jéggël na ñu ko ko niki noo nu koo xam ne daa xaddamiku ngir lor waaye soo xaddamikoo ngir dégg ku nuyyóo nga xaddamiku ngir won ko ne yaa ngi ci biir néeg bi, yàqulub julli waaye sibéef na ñu ko.

Ku nekk ci biir julli, séen kuy dem nga bëgg koo woo daa di sàbbaal ngir bu geestoo nga junj ko, sib na ñu ko waaye julli ga wér na deesu ko digël mu sujjóod ndax subxaanalaahi bokk na ci yi nga xam ne sañ na ñu koo wax ci biir julli.

Bu fekkee da ngay jàng ba mu yàgg nga gag, boo xamul aaya ba ca topp da ngay tëb aaya bi nga gagee jàll ca ba ca topp ngir nga mën a jàll waaye boo xamul aaya ba ca topp da ngay rukkoo rekk te bañ a ubbi ab Kaamil di ko ci seet ngir bëgg a jàll, lii nag ci saar wu dul faatixa kepp la ñu la ko may waaye faatixa moom mëneesu koo ñàkk a jàng ba mu mat ci biir julli doonte da ngay ubbi Kaamil xool ko ca.

faatixa boo ci bàyyee ab aaya te mënoo koo dabaatal ndax rukkoo nga ba siggi soog koo fàttaliku, boo noppee da ngay sujjóod xabla salaam ndax da ngaa wàññi, su fekkee da nga cee bàyyi lu ëpp benn aaya te mëneesu koo dabaatal, sa julli yàqu na.

Koo xam ne bokku léen julli, ma nga beru di julli yaw it ngay julli, bu gagee soo ko gàggantee yàq nga sab julli. Sa ilimaan kepp nga sañ a gàgganti.

Boo déggee ilimaan di jàng, bu gagee te wonewul ne daa bëgg ku ko gàg-ganti, bu ko gàgganti, boo déggee mu yàq aw baat jàll, sañ nga koo wax baat bi ba mu xam ni da koo yàq.

Su fekkee da ngaa nekk di xalaat ci mbiru àdduna ci biir julli gi, sib na ñu ko, balaa mën a yàq julli gi da fay bari lool, bari gi ni ñu koy xamee mooy ngay xalaat mbiru àdduna ba xamatoo ñaata ràkkaa nga julli nga xam ni moo sabab nga ñàkk a xam ràkkaa yi nga julli.

Ki nga xam ne da fay julli gis ku bëgg a jaar diggëm ak ay tankam ak fi nga xam ne boo dëppee sa jë fa nga koy teg, nga puus ka fa bëgg a jaar, yàqul julli, sujjóod waru ci.

Ki nga xam ne bi muy sujjóod wetug jë bi la sujjóodee xayna digg jë ba daa am mettit wu fa ne walla bi mu demee bay sujjóod kaalaam tasaaroo ba mu sujjóod ci kaw kaala gi, yàqul ab julli te darra waru ci.

Koo xam ne da fay julli ba ci yàgg mu waccu, waccu woo xam ne sàkku wu

Page 51: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 1

ko walla mu gall, loo la yàqul ab julli te darra waru ca.

Maamuum bu dee julli, nekk ci ginnaaw ilimaan su bàyyee loo xam ne bu doon moom kepp mooy julli, sujjóod da ko ciy war te ilimaan bàyyi wu ko, xamal ne ilimaan ji da koy gàdduwaale ba mu des mu wàññi farata joo xam ne ci julli gi la bokk. farata ilimaan mënu koo yenul maamuum, kon bu noppee na ko indi ngir julleem mat.

Ki nga xam ne da fa jamaj walla mu gàllankooru walla mu doon nelaw ba ilimaan rukkoo te moom rukkoowul, bu fekkee ca ràkkaa bu njëkk ba la nekk, koo ku di na am ñaar i àtte : 1- Bu fekkee yaakaar na ne balaa ilimaan a yëkëti boppam jóge ci sujjóodu ñaareel bi ci ràkkaa boo bee mu nekk, mën na fee rukkoo fekksi ko te du siggi, kon da fay gaaw rukkoo dem fekki ko. 2- bu dee yaakaarul ni mën naa fekki ilimaan ci sujjóodub ñaareel bi te du siggi, kon ruk-koo ba daf koy bàyyi te fekki ilimaan fa mu toll, bu ilimaan sëlmëlee mu indi beneen ràkkaa buy wuutu boo bu mu bàyyiwoon ab rukkoo.

Ki nga xam ne da fa sujjóodul, daa gàllankooru walla mu doon nelaw, ràk-kaa bi mu nekk sujjóodagu ko ba ilimaan jàll ca ràkkaa ba ca topp, kon da fay gaaw sujjóod sujjóodu ràkkaa bii nga xam ne ci la ilimaan jóge bu fekkee yaakaar na ne mën naa dab ilimaan balaa rukkoo ca ràkkaab ñaareel ba nga xam ne ca la jëm, su fekkee yaakaar na ne mënu fee sujjóod fekki ko ca ràkkaa boo bee balaa rukkoo kon da fay bàyyi ràkkaa boo bu rekk fekki ilimaan, bu noppee indi beneen ràkkaa bu koy wuutu waaye su fayee ràkkaa boo bu mu bàyyiwoon, sujjóod bahda salaam waru ko lu dul da fa sikki-sàkka ba xam rukkoo na walla déet, walla sujjóod na walla déet.

Koo xam ne daa nekk ci biir julli, ray jiit joo xam ne jublu na ko te jengul xibla walla jëf ja yàgg ba ku ko séen defe ni nekkul ci julli, darra waru ko te julli gi yàquwul.

Su fekkee ilimaan da fa jóg te li muy def xam na ñu ni ag dolli la, yaw mi xam li ko tax a jóg àndal ak moom taxaw, ki nga xam ne moom it mi ngi sik-ki-sàkka ba xam dolli gi lan a ko waral, moom it na ànd ak ilimaan jóg taxaw waaye ki nga xam ne wóor na ko ne ilimaan lii muy def dolli la, da fay toog du ko fekki ca taxawaay ba. Ñoom ñii ku ci def safaanub li ñu la digël sa julli da fay yàqu.

Su fekkee ilimaan da fa sëlmël te julli gi matagul waaye da fa juum, ki nekk ci ginnaawam xam ne daa juum mu sàbbaal ko, ilimaan ànd ak moom ci sàb-baal ga xam ne julli gi matagul, kon bu noppee moom ilimaan da fay mottali

Page 52: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 2

julli gi ba noppi sujjóod bahda salaam, maamuum it noo nu lay def.

ilimaan soo ko sàbbaalee, muy deng-dengi, xamul li tax nga wax subxaana-laahi, may na ñu ko mu laaj ñaar ñu maanu ñu nekk ci ginnaawam, su boo baa may na ñu ko mu wax, ñiy tontu it noo nu waaye da ñuy yem ci tontu rekk te noppiwaat. Noo nu la ñu koy nettalee ndax Yonent bi SaWS daa mos di julli tàkkusaan, taaya ci ràkkaab ñaareel bi sëlmël, Sujjóodayni ne ko waaw jullib tàkkusaan da ñu koo wàññi def ko ñaar walla da ngaa juum, Yonent bi SaWS ne ko kon de da maa juum lu mu doon, mu ne ko ñaar i ràkkaa nga julli, Yonent bi SaWS daa di jóg àggale.

Ndéem sàbbaal na ñu ilimaan ngir jàpp ne da fa juum waaye moom jàpp na ne julli gi mat na, na jëfandikoo li mu jàpp ndax lu ko wóor la, la muy sik-ki-sàkka yitam da koy bàyyi te jàpp ca la ko wóor waaye bu dee mbooloo mu bari ñoo ko ne subxaanalaahi te moom mu jàpp lu wuuteek la mbooloo ma jàpp, kon daa war a fekki mbooloo ma ndéem leeralal na ñu ko ag njuumteem.

Bu fekkee da ngaa julli gee ba noppi ni naa julli safaa ak witar, ngay julli ba ci yàgg nga sikki-sàkka ba xam ci witar nga nekk walla ci ñaareelu ràkkaa bu safaa, su boo baa da ngay def li gën a wóor te mooy jàppal ni ràkkaa bii nga toll mooy ñaareelu ràkkaa safaa, boo sëlmëlee sujjóod bahda salaam ndax da ngaa sikki-sàkka, boo sëlmëlee julli witar.

Sopp na ñu diggënte safaa ak witar bul fi wax darra, boo juumee wax ca darra nekku ca, bu dee yaa ko tay def nga lu ñu sib waaye du tere julli gi baax.

Bu dee li nga fekkee ci jullig ilimaan matul benn ràkkaa, ràkkaa bu mujjam nga fekkee te fekk nga mu sujjóod ba siggi, xamal ni amoo darra ci julli gi bu ilimaan dee sujjóod xabla walla bahda sa yoon nekku ca waaye bu dee daa sujjóod bahda salaam nga ànd ca ak moom, boo jógee da ngay tàmbaliwaat julli gi.

Su dee fekkee nga ci jullig ilimaan lu mat ab ràkkaa walla lu ko ëpp kon xamal ni sujjóod bu ko war rekk war na la doonte fekkee woo la waral sujjóod ba, bu dee sujjóodug xabla salaam da nga ciy ànd ak moom, bu dee sujjóodug bahda salaam da ngay jóg jàll ca la mu la rawee ba noppi door koo sujjóod, boo ko tayee ànd kook ilimaan sa julli yàqu.

Bu dee ilimaan da laa raw te def luy waral mu sujjóod bahda salaam, boo jógee bay fay la mu la raweewoon nga def ca luy waral xabla salaam, da fay mel ni yaa boole def luy waral xabla ak bahda te yoo yu ñaar bu ñu dajee da ngay ëppël doole xabla ba, boo sujjóodee xabla salaam rekk mu doy.

Page 53: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 3

Kuy sikki-sàkka ci matug julli gi am déet far sëlmël, julli gi yàqu na ndax la gën a néew la waroon a topp daa di koy mottali, bu ca noppee daa di sujjóod bahda salaam.

Boo doon julli di fay ab julli bu la raw ca waxtu, boo ca juumee mook boo ko doon julli ca waxtu wa juum ca ñoo yem i àtte.

Boo doon naafile juum ca mook boo doon julli jullig farata juum ca ñoo yem ndare ci juróom benn i mas’ala yoo xam ne wuute na ñu ci : faatixa, saar, yelu, béral, dolli ab ràkkaa ak fàttaliku lenn ca ponk ya ndéem yàgg na.

Boo doon julli jullig naafile fàtte ca faatixa ba rukkoo da ngay wéy rekk bàyyi ko noo nu boo noppee sujjóod bahda salaam te bu doon jullig farata am ca ràkkaa boo fàttee faatixa ba rukkoo ba siggi kon da fay bàyyi boo ba ràkkaa te ba sës ci moom wecci ko, su ko defee su julli ga jeexee benn mu boole dolli ak wàññi sujjóod xabla salaam walla mu doon dolli kese mu sujjóod bahda salaam.

Boo dee naafile fàtte ca ab saar jàng faatixa kese walla muy naafile gu ñu soppoon nga béral ko yaw nga yelu ko walla ñu soppoon nga yelu ko yaw nga béral ko, yoo yu yépp boo xasee rukkoo door koo fàttaliku da ngay wéyal rekk, sujjóod sax waru ca ci wuuteek jullig farata ndax boo ca bàyyee ab saar da ngaa wàññi da ngay sujjóod xabla salaam, boo bàyyiwoon béral yelu da ngay mel ni ku wàññi fàwwu nga def xabla salaam, boo yeloo foo waroon a béral da ngay mel ni ku yokk fàwwu nga sujjóod bahda salaam.

Boo doon naafile, nga am ñaar i ràkkaa ba noppi jóg jàll cib ñetteel, bu dee teel nga koo fàttaliku maanaam laataa ngay rukkoo bay siggi da ngay dellu-siwaat taaya sëlmël waaye fàwwu nga sujjóod bahda salaam ngir yokk gi. Bu dee bi mu àggee ci ràkkaab ñetteel bi rukkoo na ba siggi door a fàttaliku ne ci ab naafile la nekk, bi mu amee ñaar i ràkkaa daa waroon a toog taaya sëlmël kon da ngay jàll yokk ca beneen ràkkaa muy ñent, su ko defee nga sujjóod xabla salaam ngir ñàkk gi nga ñàkk a wax assalaamu alaykum ci diggënte ñaar i ràkkaa yu njëkk yi ak ñaar yu mujj yi ci wuuteeg jullig farata bu ràkkaa ya xasee ba mat mu juum jóg di ci yokk beneen ràkkaa, saa yoo yëgee ni ràkkaa bi nga toll ndollal la moo xam rukkoo nga ba siggi walla déet ñoo yem da ngay dellu waat toog taaya sëlmël daa di sujjóod bahda salaam xam ni yokk nga.

Boo julliwoon jullig naafile fàtte ca ponk maanaam fàtte ca farata niki ruk-koo walla sujjóod mbaa faatixa ba sëlmël ba mu yàgg nga door koo fàttaliku, kon jullig naafile ga baax na du aajewoo nga di ci def darra, bàyyi ko noo nu

Page 54: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 4

rekk, wuute na ak bu doon jullig farata ndax su boo baa julli ga da fay yàqu fàwwu nga baamu ko.

Naafile boo ci xasee ba dugg da fay soppiku lu war, boo ko tayee bàyyi ca benn ràkkaa walla ab sujjóod walla rukkoo, fàwwu nga julliwaat ko.

Nan la ñuy jullee

armal ci julli nga xam ni mooy wone ni tàmbali nga ko mooy nga wax al-laahu akbar, baat bii rekk moo ci doy boo ni woon sax akbaru Laahu du ko tax a baax, boo koy def da ngay yëkëti say loxo ba ñu tollook sa ñaar i mbagg mbaa ñu jege ko, yëkëtig loxo ya da ñu koo sopp ndax bokkul ci farata yi bok-kul ci sunna yi.

Boo nekkoon ci jullig suba ginnaaw boo kàbbaree da ngay daa di jàng faa-tixa daa di ciy teg aw saar, faatixa ja ak saar ba yépp doo ca jiitël Bismillaahi raxmaani raxiim ndax fiqu Imaam Maalik da ñoo sib ku ko wax ci jullig farata ndax da ñoo jàpp ni Bismillaahi raxmaani raxiim gi ci faatixa ak gi ci yeneen saar yi ko am yépp ñoo yem da ñu ko koo tàmbalee waaye bokkul ci saar bi, alxamdulillaahi ci la faatixa tàmbalee dëgg-dëgg, bu dee ci naafile di nga mën a tàmbalee ci Bismillaahi raxmaani raxiim.

Sopp na ñu boo nee Wa laa daaliin nga wax ci suuf aamiin bu dee yaw kese yaay julli, bu dee daa am ku lay jiite di na ñu sopp ci yaw nga wax ko waaye boo déggul njàngum ilimaan doo ko jéem a tolloole, su fekkee yaay jiite te fekk ngay béral li gën a wóor ci fiqu Maalik mooy doo wax aamiin da ngay bàyyi ña ngay jiite wax ko doonte am nay wuute, boo dee yelu ci ngay wax aamiin ji.

ci jullig suba ginnaaw boo jàngee faatixa ba àggal da ñuy sopp nga jàng ci saar yu gudd yi ñooy yi tàmbalee ci Xujuraat ba ci abasa ñoom la ñuy wax tiwaalul mufassal, nga jàng ci benn, boo jàngee yu ko gën a gudd ba tay mu baax da ngay seet fi muxtaar mi toll bu desee lu bari mën ngaa jàng saar yu gudd, loo lu boo dee julli yaw kese la walla nga ànd ak ñoo xam ni taamu na ñu guddël gi waaye booy jiite mbooloo te amaana ñu wéradi mën na ñu caa bokk, gàttal gaa gën.

Bu saar bi àggee da ngay sëgg rukkoo waxaale allaahu akbar, sopp na ñu nga boole jëf ji ak wax ji doo dem ba jàpp ci wóom ba noppi door a wax al-laahu akbar.

rukkoo li ci gën mooy nga jàpp ci say bëtu wóom jàpp bu dëgër, sa gin-naaw maase nga xam ni du nóox, sa bopp it du téen du sëgg, say përëg sori

Page 55: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 5

say poqotaan. rukkoo yit deesu fa ñaan, sàbbaal moo fay am mën ngaa wax Subxaana rabbiyal aziim, sàkkalu ñu ko sax ab lim, nu mu toll mu baax waaye jàpp na ñu ni wax ko ñett i yoon yu teey digg dóomu na, nga ne fa tegg ba cër ya dal farata la du lu mën a ñàkk.

Boo siggee ci rukkoo bi bu dee yaw kese yaay julli da ngay wax sami’al-laahu liman xamidah lii sunna la, dellu waxaat rabbanaa wa lakal xamd lii ngëneel la. Bu dee ci jullig mbooloo ilimaan du wax rabbanaa wa lakal xa-mdu, maamuum it du wax sami’allaahu liman xamidah, ilimaan sami’allaahu liman xamidah lay wax maamuum wax rabbanaa wa lakal xamd. Boo siggee ci rukkoo bi da ngay taxaw ba ni tekk ba say cër dal nga door a sujjóod boole ca waxaale allaahu akbar ndax da ñoo taamu nga boole jëf ji ak wax ji.

Taamu na ñu boo sëggee sujjóod nga indi say tenk ba mu tollook sa nopp, boo mënee fexe ba sa jë nga teg ko ci suuf moo gën nga xam ni du tege ci tapi walla leneen loxo yi tam noo nu, bu dee fu ñu lal i tapi walla moket ba mu daj soo yaboo sujjóod ca.

Say loxo daa war a sori say poqotaan ci sujjóod bi, say tank ci ginnaaw yëkëtiku baaraam ya sampu ci suuf, mën nga faa sàbbaal ci wax Subxaana rabbiyal ahlaa, mën nga faa ñaan niki nga teg ca allaahumma ixfir lii, ndax da ñoo wax ni foo fu nga gën a jegee sa Boroom ci biir julli gi, mën nga koo wax ci waxiin wu teey ñett i yoon, diir ba lu mu néew néew fàwwu nga ni tekk ba cër ya dal bu ko yéesee rekk nga bàyyi farata.

Boo siggee ci sujjóod bi da ngay tàllal sa tankub càmmooñ te doo ca toog, tanku ndeyjoor ba nga yëkëti ko samp baaraam ya ci suuf, yëkëti say loxo fa nga ko tegoon teg ko ci sa kaw bët i wóom, ginnaaw ba ci ngay door a sujjóo-daat ni nga ko defeewoon ci yoon wu njëkk wa.

Boo bàyyeekoo ci sujjóod boo ba da ngay daa di jóg taxaw ndax diggënte ba waroo faa toog, jamono ji ngay jóg jëm ci ñaareelu ràkkaa bi da ngay waxaale allaahu akbar boole jëf ji ak wax ji.

Ginnaaw boo taxawee nga jàng faatixa ak saar waaye di na ñu sopp saar wi ngay jàng gën a gàtt saar bi nga jàngoon ci ràkkaa bu njëkk ba, ba la ngaa sëgg rukkoo foo fa ngay xunóotee boo nekkee ci jullig suba, boo ca noppee door a sëgg rukkoo, def ni nga ko defeewoon ci ràkkaa bu njëkk ba, sujjóod bi tam noo nu.

Boo toogee di taaya daa am toogin wu ñu sopp te mooy nga génnee say tank ci wetug ndeyjoor, bañ a toog ci sa tank ya, da ngay àgg suuf, tanku

Page 56: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 6

ndeyjoor bi da nga koy yëkëti samp baaraam ya ci suuf, mën nga koo xaw a dëngël nga xam ni baaraamu déyu tanku ndeyjoor bi mooy sampu, bari na ñu ko xam bu baax te du ñu ko def ngir ngant.

Boo toogee nii ci ngay door a taaya, boo nekkee ci jullig suba boo noppee ci taaya ji rekk mën ngaa sëlmël. Loo lu ñuy wax Salaatu alaa Ibraahiima bari na ay waxiin sopp na ñu nga teg ko ci taaya ji.

Sëlmël ji boo waxee assalaamu alay da ngay yëkëti sa bopp tuuti mu jëm ci sa kanam, booy wax kum gi nga xaw a geestu ci sa wetug ndeyjoor nga xam ni ku nekkoon sa ginnaaw di na séen sa lexu ndeyjoor, benn sëlmël ngay def boo dee julli yaw kese ak boo dee jiite.

Boo doonee maamuum da ngay wax assalaamu alaykum nii ñu ko waxee, waxaat ko ndank mu jëm ci sa ilimaan, bu dee bi ngay julli am na ku la féete càmmooñ nga daa di wëlbëtiku ci sa càmmooñ wax ko ndank, su fa kenn nek-kul ndax ci yaw la sàppe sa jeexee walla mu am ku fa nekk te amul ci julli gi lu mat ràkkaa kon du jar ngay wax ci wet goo gu assalaamu alaykum, ka fa féete bu amoon ci julli gi lu mat ràkkaa doonte sëlmëlagul du tee nga wax ko ko.

Sopp na ñu boo toogee di taaya, sa loxo ndeyjoor da ngay bank ñett i baa-raam yi, baaraamu sànnikaay ak baaraamu déy ngay tàllal, baaraamu sàn-nikaay bi da nga koy yëngël muy bàyyeekoo ndeyjoor di jëm càmmooñ, su fekkoon sax ni sa taaya daa jeex te sa ilimaan jeexalagul da ngay wéy di yëngël baaraam boo bu, am nay wuute waaye yëngël gaa gën a wóor. Loxob càm-mooñ bi da nga koy teg noo nu ci sa lupp, deesu ca bank benn, deesu ca yëngël darra.

Yëngël gi da ñu cee wax ni daa mel ni yat la wooy dóor seytaane, ñàkk gee yëngël it wax na ñu ni da lay junj ni benn Yàlla rekk a am, mënees naa jàpp it ni yëngël gi da lay fàttali ba kero ngay sëlmël ni ba tay yaa ngi ci julli nga di ko bàyyi xel ba sa xel mi du dem ci leneen.

Yëngël gi ak bank baaraam yi ci taaya la ñu koy def waaye deesu ko def ci toogaayu diggënte ñaar i sujjóod yi.

Sopp na ñu ci ginnaaw boo sëlmëlee nga tudd Yàlla niki nga wax astaxfiru Laahi ñett i yoon, daa di ciy teg allaahumma anta Salaamu wa minka salaamu tabaarakta Yaa zaal Jalaali wal Ikraami. Boo ca mënee teg aayatul Kursiyu ngir la xadiis ba wax ni ku saxal a jàng aayatul kursiyu ci ginnaaw jullig farata gu ne, darra doxul sa digg ak àjjana lu dul faatu. Sopp na ñu bala ngaa naafile walla ngay wax jeneen wax nga tudd baat yii ba noppi soog caa jàll.

Page 57: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 7

Sopp na ñu ci ginnaaw boo jullee jullig farata gu ne nga wax Subxaana Laahi fanweer ak ñett, alxamduli Laahi fanweer ñett, allaahu akbar fanweer ak ñett nga mottalee téeméer bi Laa ilaaha ila Laahu waxdahuu laa chariika lahuu lahul xamdu wa huwa alaa kulli chay’in xadiir, def ko ci say baaraam moo gën def ko ci kurus, bu dee boo ko ci defee amaana nga juum ca kon boo yaboo def ko ci kurus.

Sopp nañ boo jullee suba ba pare ngay tudd Yàlla ak a ñaan ba jant fenk.

Bu la wóoree ni fajar fenk na moo xam nodd na ñu am déet, su boo baa da ngay julli ñaar i ràkkaa fajar yi ba noppi door caa teg ñaar i ràkkaay suba yi. Boo ko jullee te fajar fenkagul du baax di na aaje yit nga jiitël yéene ju ràññeeku njëkk nga koy tàmbali lu ko moy du ko tax a baax. Sëriñ Tuubaa qaa-da lahuu Laahu maaxtaara lahuu ngi wax ca Masaalikul Jinaan ni ñaar i ràkkaa fajar yi boo jàngee ci ràkkaa bu njëkk bi faatixa da nga cay teg alam nachrax, ràkkaa ñaareel bi nga jàng faatixa teg ca alam tara kayfa kon di nga mucc ci loru sa bépp noon.

Tisbaar boo ko dee jàngal da ñuy sopp moom itam niki suba nga jàngal ko saar yu gudd yi, lépp da ñu koy yelu. Ñaar i ràkkaa yu njëkk yi ginnaaw faatixa da fay ànd ak saar, ñaar yu mujj ya faatixa kese nga ciy jàng lépp ci yelu.

Boo nekkee ci taaya ju njëkk ji, taaya ja da ngay yem ci abduhuu wa ra-suuluhuu, sopp na ñu boo amee ñaar ba tàmbalee jóg da ngay bàyyi ba taxaw jonn door koo wax, ilimaan noo nu lay def, boo dee julli yaw kese tam noo nu, boo dee maamuum da ngay mel ni ku yëgul ni ilimaan a ngi jóg da nga koy bàyyi ba mu taxaw jonn ba nga dégg allaahu akbar ja nga door a jóg te doo wax darra, da ngay bàyyi ba taxaw jonn ngay soog a wax allaahu akbar.

Ginnaaw boo sëlmëlee tisbaar sopp na ñu nga naafile ñent i ràkkaa, ñaar sëlmël, ñaar sëlmël, ba tay sopp na ñu bala ngaa julli tisbaar soo ko mënee nga naafile ñent i ràkkaa, ñaar sëlmël, ñaar sëlmël.

Sopp na ñu bala ngaa julli tàkkusaan nga naafile ñent i ràkkaa, ñaar sëlmël, ñaar sëlmël, ginnaaw tàkkusaan sib na ñu ku ca naafile. Tàkkusaan ak tisbaar ñoo bokk lépp, li ñu wuute mooy saar ya nga cay jàng moom tàkkusaan da ñoo sopp mu gàtt, ñooy saar yi tàmbalee Suuratu Duxaa ba ci Suuratu Naasi.

Timis ñaar i ràkkaam yu njëkk da ñu koy béral te ginnaaw boo noppee ci faatixa ji da nga ciy teg saar te sopp na ñu mu bokk ci yu gàtt yi, ràkkaab ñetteel ba faatixa kese lay am te da nga koy yelu.

Bu ràkkaab ñetteel ba jeexee nga taaya sëlmël.

Page 58: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 8

Sopp na ñu ginnaaw boo jullee timis nga naafile ñaar i ràkkaa. Sëriñ Tuu-baa qaada lahuu Laahu maaxtaara lahuu daan na digle ginnaaw timis ñaar i ràkkaa, nga jàng ci bu njëkk bi faatixa teg ca Qul yaa ayuhal kaafiruun, ràkkaa ñaareel bi nga jàng faatixa teg ca Qul huwa Laahu axad.

Gee, ñaar i ràkkaam yu njëkk da ngay jàng faatixa teg ca saar béral ko, sopp na ñu saar wa digg dóomu te ñooy yi tàmbalee abasa ba ci Duxaa. Ñaar i ràkkaa yu mujj ya moom faatixa kese la ñu ciy jàng ci yelu.

Sib na ñu njëkk gee di jot nga cay nelaw te bàyyiwoo koo xam ni su la wax-tu wi naree raw mu yee la. Ba tay sopp na ñu ginnaaw gee boo amul jaamu Yàlla yoo cay teg walla ay yite yu far nga teel a tëdd, teel a yeewu ndax da ñuy bañ nga biddënti.

Boo noppee ci gee sopp na ñu nga julli safaa ak witar te béral léen ndax bépp naafile booy def ci guddi sopp na ñu nga béral ko bu dee ci bëccëg sopp na ñu nga yelu ko. Boo doon naafile bëccëg béral ko tam lu dagan nga def waaye la gën mooy nga yelu ko.

Safaa moom lu mu néew-néew di na mat ñaar i ràkkaa, boo koy julli ñaar i ràkkaa sopp na ñu nga jàng ci ràkkaa bu njëkk bi faatixa ak Sabbix isma rabbika, ràkkaa ñaareel bi nga jàng faatixa ak Qul yaa ayuhal kaafiruun, daa di taaya sëlmël, nga door a indi beneen ràkkaa bo xam ni moom rekkay beru muy witar ji. Da nga ciy jàng faatixa ak Lixlaas ak falaxi ak Naasi bu jeexee nga taaya sëlmël. Boo ci jàngoon yeneen saar tam du ko teree baax waaye yii la ñu ci gën a sopp.

Boo sawaree ba bëgg a dolli safaa kon da ngay def ay ñaar ñaar ba kero ngay àgg fa nga bëgg a yem, nga daa di koy tëjee witar.

Yonent bi SaWS daan na julli fukk i ràkkaa ak ñaar teg ca benn muy witar.

Julli ci guddi bi ñu ci gën a taamu mooy nga def ko ci xaaj bu mujj ba gën a jege fajar te àggu ca. Safaak witar gi sax foo fu la ñu ko gën a taamoo, su fek-kee sa yeewu njëkk fajar di jot wóorul, da ngay fexe ba lépp loo war a naafile nga def ko tëjee ko witar ba noppi door a tëdd. Boo yeewoo bu la neexee di julli ay ñaar ñaar te bañ a baamu witar ba fajar jot.

Bu fajar xasee fenk da ñuy sib bépp naafile ba mu des ñaar i ràkkaay fajar, boo biddëntee te fekk nga ame borub julli ci guddi, bi nga yeewoo fekk fajar fenk, di na ñu la may nga fay ko ba noppi witar door a julli suba.

Witar da ñu koo fonk lool nga xam ni bu ñu julleegul suba da nga koy julli

Page 59: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

5 9

ba noppi door a julli suba waaye boo xasoon a julli suba te julliwoo ko moom door a fàttaliku ni julliwoo ko kon mu raw la.

Ku dugg ci jàkka waxtu woo xam ni sibu ñu ku ca naafile sopp na ñu balaa toog julli ñaar i ràkkaa ba noppi yu muy nuyyóo jàkka ja. Boo xasoon a toog it du tee nga war a jóg def ko. Boo xasoon a dugg jàkka te amoo njàpp sopp na ñu nga wax Subxaanallaahi wal Xamdulillaahi wa Laa ilaha ilallaa wallaahu akbar ñent i yoon, wax na ñu ni ku ko def di na ñu la fay tuyaabay ku julliwoon ñaar i ràkkaa nuyyóo ko jàkka ja.

Boo ñëwoon doon jullisi ci jàkka ji te fekk julliwoo woon fajar ci sa kër kon soo yaboo def ñaar i ràkkaay fajar ya mu wecciwaale ñaar i ràkkaa nuyyóo jàkka ja waaye doo def ñaar nuyyóo ko jàkka ja ba noppi bëgg caa teg ñaar muy fajar, bari na lool ñu koy def ngir ñàkk a xam.

Su fekkee da nga julliwoon ñaar i ràkkaay fajar ci sa néeg nga dikk ci jàkka ji fekk jullee gu ñu, daa am ñu wax ni da ngay julli ñaar i ràkkaa nuyyóo ko jàkka ji door a toog, am ñu ni da ngay toog rekk xaar jullig suba gi, li gën a wér mooy nga toog noo nu xaar bañ a julli darra.

foo fi déggee ñu wax la njàngum yelu xamal ni li ñu ci jublu mooy yëngël sa làmmiñ di wax la ngay wax te nopp du ko dégg. Béral mooy lu mu néew-néew yaw ci sa bopp nga di ko dégg, bu amee ku sës ci yaw moom it mu di ko dégg, booy jiite tam nga yëkëti sa baat ba maamuum yi mën laa dégg.

Jigéen moom yelu rekk lay def, sopp na ñu yit muy jegeel ay cëram buy julli.

àttey jiite ak ka ñuy jiite

Bu fekkee mbooloom jullit da ñoo tase ku ca jiite rekk mu baax waaye sopp na ñu ka ca gën a dégg fiq jiite, bu ca dollee gën caa baax gën caa bariy jaamu Yàlla ak yu mel noo nu mu gën a baax, jigéen du jiite ay góor, du jiite jigéen ni moom du ci farata du ci naafile.

Bu dee ci fiqu Imaam Maalik da ñuy jàpp ni ki lay jiite yóbbaale na la cig njàngam moo tax sunna la bu dee béral nga déglu rekk te noppi bañ a jàng, bu dee yelu sopp nañ ngay jàng ci suuf ngir bañ a nekk ci leneen.

Su fekkee xas ngaa am ci julli gi lu mat ab ràkkaa walla lu ko ëpp am nga ngënéelul mbooloo ndax gënee na jullig kenn am na xadiis bu wax ñaar fukk i xaaj ak juróom am bu wax ñaar fukk i xaaj ak juróom ñaar, terewul ka fek-kee ràkkaa yépp moo ëpple ngënéel, su ko defee lam la rawee bu ilimaan sëlmëlee da nga koy fay.

Page 60: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 0

Soo julliwoon yaw kenn ginnaaw ba nga gis mbooloo di julli sopp nañ nga baamu ànd ak mbooloo bam des waxtuw timis, gee it bu fekkee witaragoo mën ngaa baamu ngir ngënéelul mbooloo ndax da ñoo sopp witar nekk sa mujjug julli, boo xësee fekkee ci jullig mbooloo benn ràkkaa am nga ngëneel li du tax boo noppee gisaat mbooloo mu ëpp i boroom xam-xam du tax nga war a baamu, ki amagul darra ci ngënéelu mbooloo nga xam ni bi muy yeksi fekk na ilimaan sujjóod ba siggi, koo ku mën naa ànd ak mbooloo meneen julli.

Sopp nañ bu ñaar i góor dee julli, kiy ilimaan féete càmmooñ ki muy jiite féete ko ndeyjoor te bañ a làng ak moom bu wér a wér, bu dee lu mat ñaar i góor walla lu ko ëpp sopp nañ ilimaan ne ca kanam góor ña féete ko ginnaaw, bu ca jigéen bokkee da fay taxaw ca ginnaaw góor ña ilimaan nekk ca kanam, bu dee ilimaan rekk ak benn góor ak benn jigéen walla lu ko ëpp kon ilimaan da fay taxaw, benn góor ga xaw a làng ak moom tuuti, jenn jigéen walla jigéen ya taxaw seen ginnaaw, góor bu doon julleek soxnaam du tax mu làng ak moom, ginnaaw la koy féete, bu fekkee ilimaan daf fee nekk ak góor goo xam ni mukkalaf la ak gone, da ñuy seet bu fekkee gone ga am na xelum jaamu Yàlla ba nga xam ni du taxaw di julli ba mu yàgg muy fo walla mu dem kon da ñu koy jàppee ni mag, ilimaan taxaw ci kanam, mukkalaf mi ak gone goo gu ne ci ginnaaw, bu dee weesoogul jëfu gone, kon na mukkalaf mi làng ak ilimaan ne ci wetug ndeyjooram, gone ga fum taxaw mu baax.

Imaam raatib mooy ilimaan joo xam ni jullit ñi ñoo booloo fal ko, mennum moom doŋŋ bu taxawoon julli ci jàkka ji di na weccee jullig mbooloo, bépp jàkka ju am imaam raatib bu ñu jullee ba noppi meneen mbooloo mu dikk ca jàkka ja sib nañ ñu julli jiitël kenn, buñ ko bëggee kon da ñuy daa di génn jàkka ja, jullee fa mën a def mbooloo, buñ bëggee julli ca jàkka ja da ñuy kenn-ken-noo ndax buñ jullee ba noppi bàyyi ñeneen dikk di mbooloo julliwaat fa mën naa indig noonoo ci jullit yi, moo tax am na ñu naan bu mbooloo ma nekkee ay doxandéem deesu ko bañ ndax jotewu ñu ak waa dëkk ba darra.

Koo xam ni daa julliwoon ba am farata gi wëlbëtiku di baamu ngir am ngënéel la day maamuumu waaye bu jiitee ña muy jiite yàqule ndax da fay mel ni kuy naafile, moom du yàqule ña muy jiite ñooy yàqule.

Boo xasee am ci ilimaan benn ràkkaa njuumte lu ko war bam war a su-jjóod da lay waraale doonte fekkeewoo ko, bu dee xabla salaam nga ànd ko ak moom, bu dee bahda salaam da ngay nég ba fay ràkkaa yam la raweewoon ndéem am na nga soog koo sujjóod waaye doo ko defandook moom.

am na ñaar yoo xam ni fàwwu nga bàyyi ba ilimaan def ko ba noppi nga

Page 61: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 1

door koo def, soo ko ko njëkkee def mbaa nga defandoo kook moom rekk sa julli yàqu : tàmbali bi (allaahu akbar) ak sëlmël bi (assalaamu alaykum), yi ci des nga xam ni farata lañ xaraam na nga ànd kook moom, sib nañ it nga de-fandoo kook moom, li gën mooy nga bàyyi bam def ko nga gaaw fekki ko ca.

Sopp na ñu bu ilimaan amee ñaar i ràkkaa di jëm cib ñetteel buy jóg nga mel ni ku ko faalewul ba mu taxaw jonn-jonn ba wax allaahu akbar nga door a jóg fekki ko, booy jóg doo wax allaahu akbar da ngay bàyyi ba taxaw jonn doog koo wax, soo xasee ànd ak ilimaan ci julli bépp juum boo xam ni su doon yaw doŋŋ la di na aajewoo sujjóodal ilimaan da koy gàddu niki bu àndeek ili-maan di fàttee wax allaahu akbar da koy gàdduwaale, li nga àndul ak moom du ko gàddu niki boo jógoon di fay li la raw ci moom boo ca juumee boo yaboo defar ko, mënul a gàddu ràkkaab lëmb walla sujjóodu lëmb nga xam ni farata la walla wax allaahu akbaru armal walla wax assalaamu alaykum ci sëlmël gi, farata moom ilimaan mënu koo gàddu ndax deesu ko sujjóodal benn nga def ko walla def ga wéy nga julliwaat rekk.

Sopp nañ boo dee julli ci jàkka nga xam ni yaay ilimaan ja walla fu ab mbooloo di jullee, boo sëlmëlee bañ a toog rekk na nga toogeewoon mel ni sëlmëloo da ngay wëlbëti saw toogin soo manee wëlbëtiku féete ndeyjoor ginnaaw boo waxee Allaahumma anta Salaamu wa minka salaamu tabaa-rakta Yaa zal jalaali wal’ikraami ni ko Yonent bi SaWS daan defee, noo sop-pee toogaay ba du ko tee baax, bu dee sa barabu bopp nga nekk kon mën ngaa sëlmël ba noppi toog na nga toogeewoon.

ilimaan ci ginnaaw bi mu sëlmëlee tàllal loxoom di ñaan, mbooloo mi ànd ak moom di ñaan bidaa la, kenn ku ne ñaanal boppam moo gën rawati na bu ilimaan yëkëtee ñaan ga, bu ko yëkëtiwul it du ko tee doon bidaa.

Jullig Jumaa

Dem julliji Jumaa farata la ndax deesu ko tolloole, boo sësee ci jumaa ji mën ngaa bàyyi bañ tàmbalee nodd noddug ñaareel, boo soree day war nga jóg ci waxtu woo xam ni di nga fekkee julli gi, jamonoy Yonent bi SaWS, Baabakar ak Omar, nga xam ni boo ba rajo amutoon da ñu daan nodd benn nodd rekk ngir wone ni waxtu wi jot na daa di julli, dañ daan yéeg ca kaw soo-roor ba walla fu kawe nodd benn nodd rekk daa di julli, lépp luy gàllankoore niki jaay da fay xaraam ci waxtu woo wu, Seydinaa Usmaan moo sos ñaareelu nodd bi, boo ba fekk na mbooloo ma tàmbalee bari, ci la def bu waxtu wi jo-tee ñu nodd nodd gu njëkk gi, goo gee la sos ndax amutoon ba mbooloo ma ñëw mu door a dikk ba toog ca minbar ba ñu door a nodd ñaareel ba, dañ ko

Page 62: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 2

koy tuddee waaye boo dee seet mooy gu njëkk gi ndax moom rekk a amoon.

Jullig àjjuma di na war ciy njénde mooy dëkk bu mag maanaam dëkk buy wéy, bu dee niki pël yuy tukki walla di sàmm nga xam ni mën na ñoo tuxu ci jamono ju ne, ñoo ña duñ tabax fenn jumaa ndax day aaje ngeen dëkk fa, mbooloo ma yit war naa bari ba nga xam ni bu léen ay noon soŋŋoon ñu mën léen a dello ginnaaw te du aajewoo ñuy wuti wallu, su lii amee kon farata lay doon ci ñoom ñu tabax jumaa, su ko defee bu yéesul seen dëkkuwaay ya rekk mu baax, buñ dëkkee ciy néegu ñax, jumaa ja néegu ñax lay doon, buñ dëkkee ci seng, buñ defee jumaa ja seng mu baax, bu fekkee da ñuy tabax kon fàwwu ñu tabax jumaa ji.

Bu ñu xasee tabax jumaa ja far ginnaaw ga am ñu tuxu, bu mbooloo ma fa des matee fukk ak ñaar yu bokkul ak ilimaam rekk mu doy, Xutba ga fara-ta la njëkk julli gi mënul a ñàkk, njëlbéenu xutba bi ilimaan day toog as diir, toogaay bub sunna la, daa di jóg xutba benn xutba, bu benn xutba bi jeexee mu toog as diir door a jógaat xutba xutbag ñaareel bi, bu ca noppee ñu soog a liqaam taxawal julli gi, ñaar i ràkkaa lay doon te dees koy béral, saar yoo ci jàng mu baax waaye dees na ci sopp nga jàng ca ci saar wu njëkk wi Suuratul Jumu’a ginnaaw faatixa, bu dee ràkkaab ñaareel nga jàng ginnaaw faatixa Hal ataaka waaye leneen loo jàng mu baax.

Képp ku nekk ca dëkk ba lu mu sori-sori war naa jullisi, boo nekkul ca dëkk ba da ñuy seet sa digg ak dëkk bi jumaa ji nekk nu mu demee, bu dee fa nga dëkkee mat na ñett i miil (miil jege na kilomet ak genwàll) kon war ngaa jullisi, bu ko weesoo waru la, soo coobarewoo ba def ko mu wecci sa tisbaar.

Jullig Jumaa warul aji tukki doonte du tukkib wàññi ak luñ jegee-jegee lu dul nga fas yéene faa sax ñent i fan, jaam, gone walla jigéen ndéem teewee na ko da fay wecci tisbaaram, bu jigéen jullisee ca ginnaaw góor ña la ñuy ne, ji-géen joo xam ni ndaw la bu fekkee daa waaj ba nga xam ni mën naa am góor ñi di ko gestu day xaraam mu julliji, bu waajul ba xayna kenn du ko xool ñu sib ko, bu dee màgget moo xam ni kenn xoolatu ko dagan na mu julliji te deesu ko sib.

ilimaan buy xutba day war nga déglu bañ a wax darra doonte da ngaa sori walla nga tëx ba doo dégg, da ñuy bëgg tam nga wëlbëtiku jàkkaarlook moom ak ci sàppe joo mën a nekk.

Sangu janaaba bala ngaa julliji jumaa lu war la warug sunna, luñ sopp la lool waaye li gën a wér mooy du la tee jàppu ci ginnaaw boo sangoo ndax jëmmu sangu gi sunna la waaye njàpp li moom daa war, boo sangoo rekk daa

Page 63: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 3

di war a dem fa saa sa lu ko moy boo fa yàggaatee da ngay ñàkk sunna si, teel gee dem ca jumaa ja ci bi waxtu wiy bëgg a jot moo ëpp tuyaaba, sopp nañ nga gëttu te sol yëre ya gën a rafet mooy ci jullig jumaa yëre yu weex, li ñu gën a taamu ci ngéru imaam Maalik mooy bu ñu jullee ba noppi nga daa di laxas te bañ faa naafile, bala nga koo mën ilimaan daa génn walla mu toog fa loo xam ni mënoon naa génn, la gën mooy nga naafile njëkk julli ji, ilimaan it su fekkee ni ñëw na fekk mbooloo mi teew te waxtu wi jot du ñu taamu ci moom muy naafile daa war a yéeg ca minbar ba xutba ñu daa di julli, su ñëwee te waxtu wi jotagul walla muy xaarandi mbooloo mi, mën naa naafile

Salaatul Xawfi (Jullig ragal)

Mooy su jullit yi dee xeex ak yéefér yi te ragal ni buñ maasee ñoom ñépp di julli yéefér yi soŋŋ léen, ni Yàlla sant Yonent bi SaWS ñu jullee ko mooy Sa-laatul Xawfi (Jullig ragal), lii doy na tektal ci ni sunu Boroom fonkee julli ndax jihaad santaaneem la waaye du tee bu waxtu jotee ñu war a julli.

Ni ñu koy defee mooy su waxtu wi jotee, ilimaan da fay def mbooloo mi ñaar i xaaj, daa di jiite menn mbooloo mi xaaju julleem niki buñ nekkee cib tukki nga xam ni da ñuy wàññi julli yi, timis rekk moo ciy nekk ñett i ràkkaa, bu dee da léen di jiite jullig ñaar i ràkkaa kon xaaj bu njëkk bi da léen di jiite benn ràkkaa daa di taxaw temm bàyyi léen ñu teg ca beneen muy ñaar ñoom ñoo ñu daa di sëlmël daa di dellu ca xare ba, ñoo ñee taxawoon di xeex ñëw ilimaan jiite léen benn ràkkaa bi ko dese, bu léen ko jiitee daa di sëlmël bàyyi léen ñoom itam ñu fay benn ràkkaa bu njëkkk biñ fekkeewutoon.

Su ilimaan jiitee kuréel bu njëkk bi ba jóg taxaw jonn day bàyyi ñoom ñu julli seen ràkkaab ñaareel, jamono joo jee mu taxaw di xaar mbooloom ñaareel bi ñëw, dañ koy tànnloo su ko neexee di ñaan walla muy jàng alqu-raan walla mu noppi bañ a wax darra, nii la koy defee ci julli yépp ba mu des timis ndax ñett i ràkkaa la, mbooloo mu njëkk mi lay jiite ñaar i ràkkaa, xaaree benn ràkkaa bi ko dese mbooloom ñaareel bi, buñ ñëwee mu daa di léen jiite benn ràkkaa bi ko dese, bu léen ko jiitee daa di sëlmël bàyyi léen ñu fay ñaar i ràkkaa yiñ fekkewutoon.

Bu dee du cig wàññi nga xam ni julli yépp la ñuy matal kon benn xaaj bu nekk da léen di jiite ñaar i ràkkaa, da fay jiite mbooloo mu njëkk mi ñaar i ràk-kaa, ñaar i ràkkaa yi ko dese mu xaaree ko mbooloo ma ca des daa di sëlmël bàyyi léen ñoom ñu fay ñaar yiñ fekkeewul, du tee julli gu ne ñu noddal ko liqaamal ko.

Page 64: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 4

Bu dee ragal ga daa tar ba kenn xalaatul def lu mel nii kon su waxtu wi jo-tee ku ne noo mën a fexee ba julli na nga ko def moo xam da ngay dox ak say tank walla nga war walla ngay daw, da ngay jublu xibla walla déet, man ngay julli sax di dóor ak a sànniy fett ak di wax ki dend ak yaw moytul.

Jullig ñaar i iid yi (Korite ak Tabaski)

Ñoom ñaar sunna la ñu yu ñu féddëli, waxtu wi dagan a naafile te mooy bu jant bi yëkkëtikoo lu tollookk ñett i meetar ci sa xoolug bët fa la waxtoom tàmbalee ba balaa tisbaar a jot, bu ñu ko yéexee ba tisbaar jot raw na deesu ko defati, deesu léen noddal, deesu léen liqaamal, ñaar i ràkkaa la ñuy doon waaye da ñu koy béral, ginnaaw faatixa saar wuñ jàng rekk mu baax, sopp na ñu ilimaan jàng ci ràkkaa bu njëkk bi ginnaaw faatixa, Sabbix isma Rabbika, ci ràkkaab ñaareel bi ginnaaw faatixa Wa chams wa duxaahaa, ràkkaa bu njëkk bi da nga ciy jàng juróom ñaar i allaahu akbar door a tàmbalee jàng nga waññiwaale allaahu akbar bu njëkk bi nga xam ni mooy armal bi, boo taxawee ci ràkkaab ñaareel bi, xam nga booy jóg da ngay wax allaahu akbar, ginnaaw boo weesoo boo bu da nga ciy teg juróom i allaahu akbar, ràkkaa bu ne di na am benn rukkoo ak ñaar i sujjóod.

Bu julli gi noppee ilimaan da fay daa di taxaw xutba, bu amee fi ñuy yéeg ngir taxaw fa xutba mu taxaw fa, bu ko amul taxaw fi suuf rekk, bala koo tàm-bali da fay toog ab diir door a jóg xutba xutba gu njëkk gi, bu xutbaa ba mu xaaj, toog ci diggënte bi door a jóg àggale xutba bi ci xutbag ñaareel gi, bu xut-baa ba noppi door a dellu, sopp na ñu buy dellu mu bañ a aw yoon wa mu jaa-roon bi muy dikk ci jullikaay bi, sopp na ñu lii tam ci mbooleem ñi jullisiwoon.

Jullig tabaski da ñoo taamu ilimaan yóbbaale tabaskeem ca jullikaay ba rendee ko fa, bu dee lu ñuy loj mu defee ko fa, su ko defee jullit ñi yëg ni moom ray na ba noppi bu ñu delloo mën a rendi, bu ilimaan dee génn ngir julliji korite walla tabaski sopp na ñu muy wax allaahu akbar ca kaw ginnaaw bu mu génnee néegam ba ba muy yegg ca jullikaay ba, lii tam sopp na ñu ko ci jullit yiy jullisi, bu ilimaan tàmbalee julli gi lañ koy soog a bàyyi.

Bu ilimaan dee xutba ci korite walla tabaski sopp nañ bu waxee allaahu akbar yaw miy maamuum nga wax ko ci suuf, la muy wax war nga koo déglu, noppi.

al ayaam mahluumaat ñooy booy lim li tàmbalee ci bisub tabaski ni benn boo ci tegee ñaar ñooy ayaam mahluumaat, mahduudaat ñoom doo waññi bisub tabaski bi, da ngay waññi ñett ya ca topp, nii lañ duggantee, mahluu-

Page 65: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 5

maat ñooy bisu tabaski yi nga xam ni boo ci rendee am nga tabaski, mahduu-daat ñooy bis yi nga xam ni ñiy aj ci la ñuy sànni jamra yi ca Minan ñett i fan yoo yu lay doon.

Sopp na ñu sangu ci korite ak tabaski ak gëtt te sol yëre yu rafet tënkuwul ci mu weex waaye na yees.

Salaatul Xusuufi (Jullig Muur)

Bu jant bi muuroo, julli gi ñuy julli sunna la, bu weer wi muuroo da ñu cee wuute ñii ni sunna la ñii ni da ñu koo sopp rekk, su jant bi muuroo ci waxtu woo xam ni dagan naa naafile ndax bu dee ci waxtu wu mu xaraamee niki mu tàmbalee fenk rekk daa di muuru julli da fay xaraam, bu dee waxtu wu ñu ko sibee niki mu fenk waaye amagul ñett i meetar, da ñuy sib ku ko ca julli.

ilimaan da fay génn dem ba ca jàkka ja ñu julli ko fa waaye amul nodd amul liqaam, da ñoo taamu bu ilimaan jàngee faatixa teg ca saar wu gudd niki Ba-qara cig yelu, su saar wa jeexee mu daa di sëgg rukkoo, na fa yàgg ba mel ni ba muy jàng Baqara, bu siggee ci rukkoo bi wax sami’allaahu liman xamidah du jàll sujjóod waaye da fay taxawaat daa di jàngaat faatixa teg ca saar wi sës ci Baqara muy aali Imraan, bu jeexee mu daa di sëgg rukkoo, rukkoo bu yàgg ni ba muy jàng aali Imraan, bu siggee ba wax Sami’allaahu liman xamidah lay door a jàll sujjóod ñaar i sujjóod, da ñu cee wuute ndax da koy yàggal na mu yàggaleewoon rukkoo ya walla déet, bu taxawee ci ràkkaab ñaareel bi gin-naaw bu jàngee faatixa, na jàng suuratu Nisaa’i, su ca noppee rukkoo, rukkoo bu yàggee ni ba muy jàng suuratu Nisaa’i, rukkóo bu ne da fay xaw a tollook taxawaay ba ko jiitu, su ko defee bu rukkoowee ba siggi wax Sami’allaahu liman xamidah, daa di jàngaat faatixa jàng saar wa ca sës muy Maa’ida, bu ca noppee sëgg rukkoo, rukkoo bu yàggati ni ba muy jàng Maa’ida, siggi wax Sami’allaahu liman xamidah door a jàll sujjóod ñaar i sujjóod taaya sëlmël.

Bu la neexee yit mën nga koo defee nii ñu ko waxee ci sa néeg kon it du ko tee baax.

Bu weer wi muuroo moom ni nga daan naafilaa rekk nga koy defee, ñaar i ràkkaa sëlmël, ñaar i ràkkaa sëlmël lay doon, saar yu la neex nga ciy jàng, da nga ciy nekk ba weer wa muriku wala nga sonn door a bàyyi te ginnaaw weer guddi lay muuru te booy naafile guddi da nga koy béral kon booy julli jullig muuru weer da ngay béral.

Ginnaaw bu ilimaan jullee jullig muuru jant deesu ca xutba waaye mën na léen a waar.

Page 66: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 6

Salaatul Istisqaa’i (Jullig mbaaw)

Jullig mbaaw mooy bu ndox ñàkkee ngeen di julli ngir ñaan ko Yàlla, ñaar i ràkkaa lay doon te ci waxtu wu dagan a naafile la ñu koy defee, am njàngam dañ koy béral, saar yañ soppoon ci jullig korite ak tabaski lañ ci sopp muy Sabix isma Rabbika ak Wa chams wa duxaahaa, ràkkaa bu ne benn rukkoo lay am, benn taxawaay ak ñaar i sujjóod, bu ñaar i ràkkaa yi jeexee ilimaan taaya sëlmël daa di wëlbëtiku jàkkaarlook nit ñi ba ñu jekkandiku mu soog a jóg xutba.

Sopp na ñu mu sukkëndiku ci darra lu mel ni bant wallaw yat, ba tay ñaar i xutba lay doon nga xam ni da fay toog ci diggënte bi, bu xutbaa ba àggal da fay wëlbëtiku jublu xibla wëlbëti làmbaayam la nekkoon ci mbaggum ndeyjooram dem ca càmmooñ ba, la nekkoon ci mbaggum càmmooñam ñëw ci ndeyjooram, mën na koo def te du tax cat ya féetewoon suuf soppiku, nit ña def ni moom, moom mu taxaw nit ña ñoom toog, amul yenn kàbbar yoo koy beral niki noo nu nga koy defee ci korite mbaa tabaski, amul nodd amul liqaam ndax du farata.

Mbërëg ak i àtteem

Jigéen yiy gis dereet ñett i xaaj la ñu : ku ko mosul a gis, ku ko baaxoo mooy ku ko gis gisati ko ak ku ëmb ba noppi gis ko doonte du koy faral di gis.

Ki ko mosul a gis, dereet ja mënul a yàgg ba weesu fukk i fan ak juróom, su amee fukk i fan ak juróom te taxul mu jeex na xam ni jàngoro la, na sangu tey julli ak a woor, mën naa sottiku jeex ci diir bu gàtt walla mu am benn fan walla ñaar waaye lu mu yàgg-yàgg du weesu fukk i fan ak juróom.

Bu dee koo xam ni baaxoo na koo gis da fay xool rekk yoon yi ko jiitu la mu baaxoo, da fay seet yoon ba mu weesu ñaata fan la tolloon, mu jàpp ni bii tam noo nu lay toll. Su fekkee na mu tolloon jeex noo na la tollaat jeex kon leer na, bu dee da daan am masalan ñett i fan jeex tay mu amaat ko te jeexul, su boo baa da ciy yokk ñett i fan werlóo ko, bu ko weesoo na dem sangu tey julli ak a woor te jàpp ni jàngoro la. Su fekkee ni ya weesuwoon am na ci boo xam ni ñett i fan la woon ak boo xam ni ñent i fan la woon ak boo xam ni juróom i fan la woon kon da fay jàpp la gën a bari, su dereet ja jeexul mu door cee dolli ñett i fan bu ko weesoo mu xam ni jàngoro la daa di sangu.

Bu dee am na la mu daan am ciy fan te dereet ja jeexul waaye moom daa baaxoowoon fukk i fan ak juróom door a jeexal, bu ko amee te jeexul da fay daa di sangu te tàmbalee julli ak a woor, koo xam ni daa aadawoo fukk i fan ak

Page 67: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 7

ñent, su ko amee te jeexul da ciy yokk benn fan, ku aadawoo fukk i fan ak ñett, su ko amee te jeexul da ciy yokk ñaar i fan, koo xam ni daa aadawoo fukk i fan ak ñaar mbaa lu ko yées, men naa yokk ñett i fan ngir wóorlóo ko.

Koo xam ni daa ëmb ba noppi gis ko te fekk na ëmb ba am ñett i weer jëm kaw te àggul ci juróom benn i weer, sañ naa natt ba fukk i fan ak juróom ba gën jaa bari ñaar fukk i fan, bu ëmbee ba am li ko dalee ci juróom benn i weer ba kero muy wësin door a gis mbërëg ja, na xam ni lu mu yàgg-yàgg du weesu ñaar-fukk i fan mbaa lu ko nuru mooy day jàll ba ci weer mooy gën jaa yàggam, li yéeme mooy bu dee door a ëmb gis ko walla ba ëmb bay am ñett i weer da ñu caa wuute waaye ñaar i àtte yii moom dëppóo na ñu ci.

Bu fekkee da fay koo xam ni day jéllal ni muy gisee dereet ji, lee lee du ko gis bu ëllëgee mu ñëwaat, day waññi fan yi nga xam ni ca la koy gis ba mu mat na mu daan toll, su dereet ja jeexee kon mu baax, bu ko waññee ba mu yegg ca na mu daa toll te jeexul, su boo baa da ciy yokk ñett i fan masalan koo xam ni bu mosaan a gis dereet day am ñent i fan jeexal waaye day def bu ëllëgee mu ñëw lee lee du ñëw, kon day waññi fan yi mu ñëw su matee ñent i fan jeex mu baax su jeexul mu dolli ca ñett i fan yi ñu wax sank, bu ko ci dollee te jeexul na jàpp ni jàngoro la, na sangu di julli ak a woor.

Jigéen ju ame dereet ba kero muy jeex mu sangu mbaa su ko sangu të wee mu tiim, xaraam na ci moom mu julli te su julliwoon it du baax, xaraam na ci moom mu wër Kaaba gi (Tawaaf) ak laal ab Kaamil walla mu woor te su woo-roon it du baax muy koorug farata niki ramadaan walla koorug coobarewu, du sañ a dugg jàkka doonte ci biir kërëm la jàkka ja nekk. Julli gi moom du ko fay waaye koor ga moom da koy fay keem fan ya nga xam ni ñoo ko raw ci koor ga. Bu ragalee fàtte la mu mokkaloon ci alquraan dagan na ci moom mu koy tari te bañ a laal jëmmu Téere bi.

Koo xam ne soxnaam daa ame dereet i mbërëg ba kero muy jeex ba mu sangu, na wormaal la dalee ci jumbax bi ba ci bëtu-wóom bi, du ko sañ a laal rawati na di joteek moom, li des ci yaram wi sañ na koo laal.

Dereetu wësin

Dereetu wësin mooy dereet joo xam ni am doom moo ko waral, lépp lu ñu ko daa aaye ci dereetu mbërëg tere na ñu ko ko ci dereetu wësin. Mën naa gaaw a jeex niki mu am benn fan daa di jeex walla ay fan waaye mënul a weesu juróom-benn fukk i fan, bu ko amee te jeexul rekk na jàpp ni jàngoro la na sangu tey julli ak a woor di def yépp niki bu dereet ja jeexee njëkk muy

Page 68: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 8

yegg ci juróom-benn fukk i fan yoo yu.

Bu fekkee da fa gisóon ni dereet ji ñëwatul mu daa di sangu di julli ak a woor far mu ñëwaat da fay seet diggënte fa mu jeexeewoon ak fi mu dellusee ba xam mat na fukk i fan ak juróom walla mu ëpp ko, day jàpp ni dereetu wësin ja foo fu mu jeexee fa la yem, lii mu mujjee gis dereetu mbërëg la ndax fukk i fan ak juróom mat na laab te topp ko ci atteg mbërëg.

fa dereetu wësin ja jeexeewoon ak fi mu gisaatee dereet bu yéesee fukk i fan ak juróom day jàpp ni dereetu wësin jaa jeexutoon, kon lii mu mujj a gis da koy booleek fan ya mu amoon waaye fu mu fi ëppee juróom-benn fukk i fan rekk na xam ni jàngoro la, na daa di sangu.

Li ñuy defal gone guy soog a juddu

Sopp na ñu bu doom juddóo, ñu jàngal ko saaru innaa anzalnaahu boole ca nodd, tifli ko ca noppub ndeyjoor ba, liqaam tifli ko ca noppu càmmooñ ba.

Sopp na ñu lu saf suukër jiitu ci moom, lu mel ni lem walla tàndarma ju ñu tëcc ba mu nooy ñu xooj ko walla suukër.

Sopp na ñu ku ko bindal Suuratul Xaaqatu raxas ko, defal ko ko toqantal.

Sopp na ñu tam ku ko bindal Suuratul Balad takkal ko ko buy soog a juddu.

Sopp na ñu bu juddóo ba am juróom ñaar i fan, ñu ray ca gàtt bu mucc ëyib di ab kuy, mu doon xar moo gën walla bëy, su amul lu ko man a wuutu lu ñu am mu baax.

Juróom ñaar i fan yoo yu deesu ca limaale bis boo xam ni juddu na ca ginnaaw fajar, fajar ji mu njëkk a fekkee ci àdduna la ñuy lim, ba ca juróom ñaareel ba, mu doon bisu tudd ba, bu maaseek fajar gi tam dees na ko limaale.

Manees na ñoo ray gàtt ba bu yoor-yooree ba ba jant biy so waaye waree-su koo ray bu fenkagul walla ginnaaw bi jant sowee. Su boo baa ndawal ngay am waaye du doon am tuddu.

Sopp na ñu bu ñu koy tuddu, tur wa ànd ak rendig gàtt ga, bu ñu dee ay seex ku ci ne da fay am gàttug boppam.

Sopp na ñu bu ñu ko watee, ñu saraxe lu toll ni diisaayu karaw ga ci wurus mbaa xaalis, wat gi mooy jiitu tuddu gi.

Ndawalu gàtt ga dees na ca lekk, dees na ca saraxe, balaa doon am tuddu sax fàwwu da ñu caa saraxe ba noppi, doom ja yit deesu ko taqal darra ca

Page 69: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

6 9

dereetu gàtt ga.

Ki koy tuddu, bu ñu indee gone ga ba mu tiim ko sopp na ñu mu wax Bismi Laahi raxmaani raxiim allaahumma lakal xamdu alaa ma ahtayta wa awlayta wa asdayta, allaahumma zidnaa walaa tanqusnaa wa akrimnaa walaa tuhinaa wa ahtinaa walaa tuxrimnaa wa aasirnaa walaa tuusir axadan alaynaa wa bis-mikal Kaafii, ikfinaa allaahumma, ajhalhu barran taqiyan walaa tajhalhu faaji-ran chaqiyan, tifli ko ko, door a nodd tifli ci noppu ndeyjoor bi, tudd tur wa ne ko tuddee naa la diw, liqaam tifli ci noppu càmmooñ ba, daa di teg loxoom ca naq ba wax Yaa Barru juróom ñaar i yoon, Yaa raqiibu juróom ñaar i yoon, Yaa rachiidu juróom ñaar i yoon ak Innaa anzalnaahu ñett i yoon.

Ku judduwaalewul bakkan ak ku faatu njëkk bisu tuddu ba, du ñu léen rayal gàtt waaye dees na léen tuddu njëkk ñu léen di deñc. Daa di ciy teg a’uu-zu bikalimaati Laahi taamaati min kulli chaytaanin wa haamahuu wa min kulli aynin laamahuu ñett i yoon.

Bismi Laahi arqiika min kulli daa’in yuuziika wa Laahu yachfiika wa yunjiika wa yaj’alul barakata fiika anbataka Laahu nabbaatan xasanan ñett i yoon.

Kuy nàmp bu ñu ko takkalee Suuratu Naasi di na ko aar ci yu bari.

Su fekkee gone ga ndeyam da koo ëmb juróom ñaar i weer kon mën na koo nàmpal ñaar fukk i weer ak ñett, bu dee juróom ñent i kon mën na koo nàmpal ñaar fukk i weer ak benn.

Saa yu ndeyam ëmbee war na ñu koo daa di feral. Gone ga tam bu amee lu mu mën a dundee lu ko mën a dëgërël kon lu ñu ko gën a gaaw a feral moo gën. te ñu bind Suuratul Buruuj takkal ko ko.

Li ñuy defal ku faatu dikk ci moom, nees koy sangee ak suul ga

Koo xam ni gis nañ ci moom màngargay faatu taamu na ñu ñu jëmële ko xibla nga xam ni da ñu koy tëddël wetug ndeyjoor, kanam gi jëm xibla su mënee nekk, su jàppandiwul ñu jaaxaanal ko tank yi jëm xibla.

Bokk na ci màndarga yi, bu bët yi yëkëtikoo jëm kaw, jë bi ñaq, su fekkee wóor na ni faatu na ba noppi, da ñuy sopp ñu sëlëm bët yi mu gëmm, bu ñu sañoon ki koy sëlëm day doon ka gënoon a am ñeewent ci moom, ci yoo ya jamono sopp na ñu koo ka wax Bismillaahi wa alaa sunnati Rasuulillaahi sallalaahu alayhi wa sallam wa salaamun alal mursaliin wal xamdu lillaahi rabbil aalamiin limisli haazaa fal yahmalil aamiluun.

Ba tay sopp na ñu bu faatoo ba noppi ñu jël ab morso daa di gaaw takk ci

Page 70: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 0

bopp ba, takk ci ŋaam yi nga xam ni da fay ŋeb, sopp nañ ñu nooyal yaram wi mu bañ ni kàdd, bëgg nañ it ñu yëkëtee ko fi suuf teg ko ca kaw daa di koy sàng, bëgg nañ it kenn dend ak moom di ko sa Laa ilaaha ilalaa ndax moom it mu wax ko ndax man kaana aaxiru kalaamihii mina dunyaa Laa ilaaha ilalaa daxalal janna (ku Laailaaha ilalah nekk kàddoom gu mujju ci àdduna nga tàb-bi àjjana), du ni ko wax ko waaye da fay dend ak moom di ko wax, bu ko xasee wax mu noppi, buñ mënee fexe mu set sobe bañ koo taq ci lim sol ak fam tëdd yépp, sopp na ñu ku ame mbërëg walla jannaaba bañ koo jege, jigéen it mën na faa bañ a jege ndax muñ dañ cee mënul lu bari, yenn ci boroom xam-xam yi taamu na ñu bu yeggee foo fu kenn toog fa bopp bi di ko jàngal suuratu Yaasiin waaye Imaam Maalik sib na ku jàngal kenn alquraan moo xam ba mu faatoogul la walla ginnaaw bi mu faatoo la, moo xam ba ñu koy suul la walla ginnaaw ba ñu ko suulee ba noppi, sib gi mooy bëgg koo jàppee sunna waaye bu ñu ko defee ngir barkeeelu du ko sib wax na ñu ni ba fa Maam Moor anta Sali tollee, Sëriñ Tuubaa wàcceel na ko alquraan.

Jamono yoo yu du ñu bañ ku sotti rongooñ te bañ a ànd ak kàddu, sopp na ñu fa dëgërlu ak muñ ñeel képp ku ko àttan, di xaacu ak a dajaloo di jooy di waxaale mbaaxu ki faatu sib na ñu ko.

Sang ab néew amul yemukaay na set rekk, fardul kifaaya la ci wax ji gën a wóor, bu ko ko kenn defalee mu wàcc ña ca des, bu ñu ko seetaanee kenn bañ ko koo defal kon ñoom ñéppay am bàkkaar.

Ni ñuy sangoo jannaaba rekk la ñu koy defee, bu ndox mënul a am ñu tiimal ko ni ñuy tiimee boo bëggee julli te amoo ndox, néew bi sopp nañ ñu sang ko ñett i cangaay, benn cangaay tóol na waaye ñaar sax a ko gën, ñett i cangaay yi boo ko dee def, cangaay lu njëkk li bu déem mënee am dañ koy wal ba mu nooy jaxase ko ci ndox mi sangee ko yaram wi, bu amul lu mel ni saabu mën na koo wecci, ginnaaw bi ñu sang ko cangaayal ñaareel boo xam ni da fay nekk ndoxum kese cangaayal jannaaba, jàppaaleel ko ci moo gën du tee cangaayal kese gi doy na, ginnaaw bi ñu sang ko cangaayal ñetteel bi boole ca gëttug kaafuur bu mënee am, bu amul it beneen xeetu lajkoloñ bu ñu am baax na.

Kay sang néew ba ak ku mu mën di doon da fay suturaal la tàmbalee ca jumbax ba ba ci bëtu wóom ya, def ci loxoom ay gaa (gant) walla sagar wu tal, am na ñu wax ni bu dee awra ja daa taq taqaay boo xam ni loxo ba rekk moo ko mën a setal kon mën na caa àgg du tee da koy muur te bañ di ko xool.

ab néew deesu lewwi ay weewam, deesu wat karawam, buñ ko jotee lewwi walla ñu wat ko ba noppi su yaboo ñu boolekook yoo ya suulaale, sopp

Page 71: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 1

nañ it ñu bës biir ba ndank ba lu waroon a génn daa di génn ndax da ñuy bañ ñu sang ko ba noppi am lu génn ci moom waaye bu ñu sangee ba noppi darra génn ci moom du yàq cangaay la, da ñuy raxas loo lee génn rekk, li gën mooy nga tërël ko foo soxla rekk nga wëlbëti ko, soo ko dee tërël da nga koy tërël ci wetug càmmooñ ndax ngay njëkkee ci wetug ndeyjoor ji ndax lu ñu sopp la, dëj ko yit dagan na.

Sopp na ñu ñaar i wëy-deñcante ku ci njëkk a génn àdduna ka ca des sang ko, jigéen bu faatoo ci ab àll te fekk ña fa nekk ñépp diy góor te ku xaraa-manteek moom nekku fa, su boo baa góor du ko sang da koy tiimël rekk te bu ko dee tiimël da fay raay kanam ga, raay loxo ya ba ci tenk ya, foo fa la farata yi yem du jàll sax ci sunnay tiim yi ndax su dul boroom kërëm, jigéen ni moom moo ko war a sang.

Bu góor faatuwoon nga xam ni soxnaam nekku fa, góor ni moom nekku fa ay jigéen rekk nekk fa kon it jigéen da koy tiimël rekk ci masaa kanam ga, loxo ya di na ko mën a masaa ba ci coñc ya.

Su góor faatoo te gisuñ góor ni moom gu ko mën a sang te jigéen ju xa-raamanteek moom ne fa di na ko mën a sang waaye na suturaal li dalee ci jumbax ja ba ci bëtu wóom ba, am na ñu wax ni loxoom du ca àgg waaye da ciy takk sagar wu tal door koo mën a raxas, néew bu jigéen bu amee góor gu xaraamanteek moom bu fa nekk kon di na ko sang ci kaw mbalaan muy sutu-raal yaram wéppu néew bi, du da ngay awale sa loxo ci kaw càngaay waaye da ngay wut lu mel ni aw sanke bu tal bu jàpp ci kaw ba ci suuf nga xam ni doo séen jëmmu yaramam waaye da nga koy summi mu ne ca biir, nga takk ci sa loxo morso bu tal walla gaa (gant), di dugël sa loxo ci biir di raxas yaram wa.

ab néew bu ñu ko dee sàng da ñoo sopp càngaay lu tóol, benn tóol na waaye daa néew ba ëpp kon ñett mooy gën jaa néew, li ñu gën a sopp mooy góor ñu defal ko juróom i mbalaan, jigéen juróom ñaar, ku ñu ci defal kaala walla muu-raay walla tubëy niki taraxlaay da ñu léen di waññiwaale ci mbalaan yi.

Juróom i mbalaan i góor yi ñu taamu ñooy : mbubbu mi nga koy solal, kaa-la, solal ko tubëy nga ëmb kook yeneen ñaar i mbalaan muy juróom.

Juróom ñaar i mbalaan yi ñu sopp bu dee jigéen la : mbubbu mi nga koy solal, muuraay, wutël ko as kumba, nga ëmb ko ci ñent i mbalaan muy juróom ñaar. Sopp na ñu ci diggënte càngaay yi nga def ca lajkoloñ ak ci yaramam wa ak cëru sujjóod yi muy jë bi, bakkan bi, bëtu wóom yi, loxo yi ak catu baa-raamu tank yi, su ko defee pax i bët yi, nopp yi ak gémmiñ gi ak bakkan bi ak

Page 72: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 2

buntu suuf yépp da ngay jël wëttéen daa di ciy suy lajkoloñ taf ko ci kaw bunt yoo yee te bañ ko caa nóox.

Koo xam ni daa daanu ca toolu xare ba ngir yëkëti lislaam deesu ko sang deesu ko sàng, la mu sol bu sàngee yaramam ca la ñuy yem deesu ca dolli darra, bu defee yaramu neen walla lam sol sàngu ko ñu mottali ko bam mat càngaay rekk, deesu ko jullee yitam, bu dee da ñu koo yëkëti fekk ko ak i gaañu-gaañu mu faatu ginnaaw ba dees na ko sang dees na ko jullee, bu dee ba ñu koy yëkëti seddagul waaye jam na ñu ko ci pàdd ba noppi mu wóor ni da fay faatu kon deesu ko sang deesu ko jullee. Ku ray boppam bu fekkee ni xare la du tee dees na ko jullee, bàkkaar ba moo koy gàddu diggëm ak Boroo-mam, bu rayee boppam te tayu ko darray bàkkaar nekku ca dees na ko jullee te waay ju baax mën na faa teew.

Ku def ci yoon lu ñu ko war a rayee, ñu ray ko niki gétën walla mu njaalóo walla mu ray bakkan ñu ray ko, dees na ko jullee waaye bu ñu sañoon ilimaan ji ci boppam du ko jullee, ku baaxam siiw du fa teew, mbooloo mu bari yit du fa daje, bu dee ilimaan ak gaay yu baax yii bu ñu ca demul kenn du ko jullee kon su yaboo ñu dem ca, taamu wu ñu bu ñuy génnee néew ba di gé-nneewaale lu mel ni furno bu def i xal, soo dee gunge néew bi nga jiitu ñi yor néew bi topp sa ginnaaw moo gën, boo waree walla ngay jigéen nga féete néew bi ginnaaw moo gën, boo waree mën ngaa jiitu tam.

Sopp na ñu bu ñu dee tërël néew bi ci bàmmeelam ñu tërël ko mu tëdd ci wetug ndeyjooram, ñu jël lu mel ni doj walla suuf ñu def ko ci ginnaawam ba du jàllarbiku ndax daa mënul a tëye boppam, boo takkoon tank yi walla loxo yi, da nga koy dindi, ña ko teewee walla ka koy tërël da fay wax ni Allaahum-ma inna saaxibanaa qad nazala bika wa xalafa dunyaa waraa’a zahrihii waftaqara ilaa indika, Allaahumma sabbit indal mas’alati mantiqahuu wa-laa tabtaliihi fii xabrihii bimaa laa taaqata lahuu bihii wa alxiqhu bi nabiyi-hii Muxammadin sallalaahu alayhi wa sallama.

Tabax bàmmeel walla nga weexal ko niki nga laso ko walla nga muur ko aajoo na teqale, bu dee ngir gën a rafetalante la ñu ci jublu da fay xaraam, bu amee ku joxewoon suuf sa ngir ñu fay suul kenn du fa sañ a tabax, def ko fa da fay xaraam, bu fekkee foo fee sa suufas bopp la walla muy àll bu kenn moomul te tabax ba jubluwoo ca lu dul màndarga ngir xàmmee ko te du jur benn yàq su boo baa di na dagan da ñu koy sib rekk.

ab jullit bu baayam dee yéefér génn àdduna, da fay dem jébbël ko ña mu bokkal diine ñu toppatoo ko, bu ñu fa nekkul na ko suturaal suul ko, bu mu ko

Page 73: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 3

jéem a defal darra ci ay yëfu jullit.

Jullee néew ak ni ñu koy ñaanalee

Jullee néew fardul kifaaya la te boo koy jiite da ngay teewlu ni li ngay def fardul kifaaya la waaye da fay xaraam ci waxtu wu naafile xaraam niki bu jant bi tàmbalee fenk te lépp fenkagul walla mu tàmbalee so te lépp sowagul, suñ ko defoon dees na ko baamu, di na ñu ko sib boo jullee suba ba nga xam ni muxtaarum suba jeex na nga xam ni bu nit dee ñëw soo ko xoolee xam ni kee de diw la ndegam muurul kanamam, waxtu yii yépp da fay fekk ragalu ñu ca ag soppiku, bu ñu ko ca ragalee amul wenn waxtu wu ñu cay nég, la ca war yépp da ñu koy daa di def jullee ko jébbël ko Boroomam.

Ki gën a yayoo ci jullee néew mooy ka mu dénkaanewoon ni na ko jullee ngir yaakaar ci moom mbaax, bu dee daa am ku ko war a jullee ci ay mbokkam te koo ka neexu ko moo tax mu ni na ma diw jullee du tee mbokk moo ma mën na koo jullee. Juróom i farataam ya ñooy yéene ji, taxawaay ba, ñaan ga, kàbbar ya ñuy kàbbar ca biir muy ñent ak assalaamu alaykum ji.

Kàbbar bi ngay njëkk a wax nga xam ni mooy armal bi la ñu sopp nga yëkëti say loxo, ya ca des da ñoo taamu nga wax allaahu akbar ci sa làmmiñ te bañ a yëkëti say loxo, ki doon jullee bu fàttee ci ñent i kàbbar yi benn te gaaw koo fàttaliku da koy daa di def fa saa sa, bu ko yéexee fàttaliku julli ga day yàqu da ñu koy julleewaat doonte suuloon na ñu ko, da ñu koy julleewaat ca bàm-meel ba, bu fekkee ilimaan daa fàtteb kàbbar te maamuum fàtte wu ko moom julleem di na wér, ilimaan moom julleem du wér. Bu ilimaan kàbbaree ba àgg ci bub ñenteel bi nga xam ni moo ca mujju, bu ko neexee bu nee allaahu akbar daa di wax assalaamu alaykum bañ a ñaan ci diggënte bi, bu ko neexee yit teg ca ag ñaan di na ñu ko indi ci kanam insaa allaa.

Bu ñu doon jullee néew defe ni góor la ndeke jigéen la walla nga defe ni jigéen la ndeke góor la du ci wàññi darra, la aay mooy mu jàpp ni kenn la ndeke ñaar la ñu walla ñu ëpp ko su boo baa da ñu léen di boole ñoom ñépp julleewaat léen, bu dee daa am ku mu ca ràññee bëgg koo jullee ba noppi door a jàll ca ña ca des du ko tee baax, bu dul loo lu ñépp la ñuy julleewaat, bu jàppee ni mbooloo la ndeke kenn la du ko tee baax.

Sopp na ñu booy jullee góor nga taxaw fa tollook ndigg la, bu dee jigéen sopp na ñu nga taxaw fa tollook mbagg ya, assalaamu alaykum gi ñuy wax ci jullig néew farata la, sopp na ñu nga wax ko ndank ci suuf, maamuum tam wax ko ndank ci suuf. fekkee jullee ga ak rob ba tuyaaba ju rëy a rëy la, Yonent bi

Page 74: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 4

SaWS misaal na ko ci xadiis mu tollook doju uhud ci rëyaay.

ñaanal néew farata la, sàkkalu ñu ko ñaan goo xam ni moom rekk a doy, goo sàkkal sa bopp sax baax na, goo doyloo yit baax na, ñaan gii taamu na ñu ko lool ba ci Imaam Maalik ci Muwatta mooy Allaahumma innahuu abduka wabni abni abdika wabni amatika kaana yach’hadu an laailaaha ilaa anta waxdaka laa chariika laka wa anna Muxammadan abduka wa rasuuluka wa anta ahlamu bihii, Allaahumma in kaana muxsinan fazid ixsaanih wa in kaana musii’an fatajaawaz an sayi’aatihii, Allaahumma laa taxrimnaa ajrahuu wa laa taftinnaa bahdahuu, bu dee góor boo niwoon Allaahummax-fir lahuu warxamhu walla bu dee jigéen nga ni Allaahummaxfir lahaa warxa-mhaa mu doy, ñaan gii moo dikk ci risaala. Boo kàbbaree lii ngay njëkk a wax :

Su fekkee ñaan gii mu indi moom ngay jàng, kon boo kàbbaree da ngay

Page 75: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 5

wax ñaan gi ba mu jeex, kàbbaraat beneen, dellu waxati ko ba àgg ci bub ñenteel ba, daa am ñaanug boppam moo nekk nii :

Boo ko waxee ba noppi door a sëlmël, bu dee jigéén la, ñaan gi da fay soppeeku nii :

Soo bëggee jullee néew boo xamul góor la am jigéen kon da ngay fas yéene jullee mbindéef mii tëdd nga xam ni da nga koy jigéenël ndax jëmmu baat bi ci arab day jigéen (nazaamatu).

Taamu nañ ñu boole néew yi julleendoo léen ngir barkeb ñenn ñi wàcc ci ñenn ñi, su boo baa su ilimaan taxawee ñi sës ci moom ñooy doon góor ña doonte benn góor la, da ngay njëkk a rangale góor ñi ba noppi, nga xam ni da ngay tërël benn góor, tërël beneen góor ci kanamam mu féete ko penku bañ mat nga door a rangale jigéen ña ca kanam a kanam ñu wuti xibla, ku xamul da fay defe ni da ngaa jox jigéen daraja ju ëpp fekk noo nu la, su ko defee góor gi ci gënoon a bari xam-xam gën caa mokkal alquraan dàqoon caa jaamu Yàlla la ñuy njëkk a tërël, ilimaan taxaw tollook moom, néew yi ci des nekk ci kanamam.

Su amee gone yu góor ak yu jigéen, bu góor ñi matee nga door a tërël jigéen

Page 76: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 6

ñi, bu góor ñi tëddee ba noppi, kenn tëdd kenn nekk ci kanamam, gone yu góor yi ñoo ciy topp nga door a tërël jigéen ñi ñu nekk ci kanam a kanam.

Mënees na ñu koo sàppee niki julli mooy tërël kenn, tërël keneen ay tankam jëm ci boppu kenn ka bañ jeex, ñu seet ka ca dàqoon a jaamu Yàlla walla ka ca gënoon a mokkal alquraan, ilimaan taxaw tollook moom du tee ñépp lay ñaanal.

Mënees naa suul mbooloo ci benn bàmmeel waaye taamu wu ñu ko xanaa ngant lu mel ni suuf su naqaree gas walla almeer ya xat lool, su ñu demee ba koy def da ñuy seet ka ñu defe ni moo ca gën mu nekk ci kanam ñenn ña nekk ci ginnaaw ci biir bàmmeel bi.

Bu ñu suulee néew te jotu ñu koo jullee te génnee ko wóorul ndax xay-na tàmbali naa soppiku kon da ñuy jullee ca kaw bàmmeel ba rekk waaye bu wóoree ni soppeekoogul da ñu koy génnee ca biti, jullee ko ca biti door koo suulaat.

Koo xam ne xës na ñu koo jullee te mbooloo jullee ko, ginnaaw ba ñu bëgg koo julleewaat taamu wu ñu ko, su dee julleewoon na ñu ko te kenn rekk moo ko julleewoon, su boo baa di na ñu taamu ñu julleewaat ko su fekkee mbooloo moo koy jullee.

Ki faatu bu fekkee li ëpp ci yaram wi feeñ na niki ku ko defoon ñett i xaaj, ñaar i xaaj yi feeñ na ñu, su boo baa da ñuy àttewoo ni li ëpp feeñ na ñu sang ko sàng ko jullee ko, jëmm joo xam ni loxo ba rekk mbaa tank ba rekk a feeñ li gën a wér mooy deesu ko jullee ndax jombul ni mi ngi dund ndax yoo yu mënees na ñu koo ñàkk ba noppi di dundu.

Ñaan, jullee ak sang gone

Booy jullee gone ginnaaw boo kàbbaree da ngay sant Yàlla julli ci Yonent bi SaWS daa di wax ñaan gii :

Page 77: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 7

Su ñaan gi jeexee nga waxaat allaahu akbar, jàngaat ko, boo waxee allaahu akbar ba ci ñenteel bi day am geneen ñaan gu mel ni taaya gu bokkul ak gii gooy wax mi ngi nii :

Boo waxee ñaan gii ba noppi daa di sëlmël.

Koo xam ni daa juddu te indiwaalewul bakkan deesu ko jullee, deesu ko sang deesu ko sàng, da ñu koy raxas ba mu set def ko ci ci ab morso daa di koy suul.

sib nañ ñu suul ko ci kër, yóbbu ko ca armeel ya moo gën, deesu ko donnu moom it du donnu, deesu ko donnu mooy bu fekkee ba ko yaayam ëmbee daa am ku ni ko li nga ëmb laa sarax lii walla ñu may ko ko, bu indiwul bakkan du ko moom da ñu koy saraxe delloo yéene ja ka ko ko saraxoon walla ka ko ko mayoon.

Ki faatu bu dee xale bu góor bu toll ci juróom benn i at mbaa juróom ñaar ba juróom ñett, jigéen mën na koo sang doonte ay góor a nga fa, xool awra ja aayul. Su ko weesoo te àggagul ci kàllafe mënees naa xool awra ja waaye jigéen du ko mën a sang, bu demee ba jege kàllafe da ñuy aaye ku xool awra ja jigéen it du ko sang.

Bu fekkee xale bu jigéen moo faatu góor du ko mën a sang, wuute na ñu ci bu tollagul fu ñu mënee bànneexu ci moom niki bu àggagul ci juróom i at, li gën a wóor mooy góor du ko sang.

Koor

Koor daa bokk ci ponku lislaam yi, buñ gisee weer wi bu dee Koor gaa, ñu woor, bu dee Kori gaa ñu wori, buñ wooree ñaar fukk ak juróom ñent far asa-maan si lëndëm xamu ñu ndax feeñ na am déet kon dañ ciy dolli benn muy fanweer ñu door a wori niki noo nu bu dee dañ am ñaar fukk ak juróom ñent ci Baraxlu tam da ñuy mottali fanweer ba noppi door a woor.

Yéene gi da nga koy fanaanoo te mooy nga fas ko ci diggënte fi jant bi

Page 78: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 8

sowee ak ba muy fenkee mooy guddi gi ci la ñuy yéenee, su xasee fenk te yée-newoowoon niki da ngaa yëguloon ni weer wi feeñ na biig kon doo lekk doo naan waaye du tee da nga koy fay, boo xasee yéene ci guddi gu njëkk goo gu mën naa yóbbaale ya ca des yépp lu dul ni daa am bis boo dog walla bis yoo dog ngir tawat, di na aaje guddi gu ne nga teewlooti yéene ja.

Koor mi ngi tàmbalee fi jant fenkee ba jant so.

Bokk na ci sunnay koor gaawee dog bañ caa yàgg ba timis ja raw la ak yé-exee xëdd mooy fexe ba bi ngay xëdd bay noppi ak bi ñuy salaatu nga doxale fa juróom ñett i simili, doonte xiifoo taamu nañ lool ku ko def, ku sikki-sàkka ci fenkug jant kon doo xëdd, doo def it lu koor aaye ndax amaana ba nga koy def fekk mu fenk, boo dëgëree bopp ba lekk mbaa nga naan te amaatoo ca lu leer ni ba nga koy def jant fenkul soo yaboo fay bis boo ba, dog gi tam noo nu la.

Bu ñu amee ñaar fukk ak juroom ñent ci Baraxlu te asamaan si lëndëm, bis ba ca topp doo xam ba xam ci ramadaan la bokk am déet, wax ji gën a wóor mooy nga jàpp ni ci Baraxlu la bokk, boo nee da ma koy woor ngir amaana mu bokk ci ramadaan te su boo baa du ma ci fayante kon nga def lu xaraam, ginnaaw gi bu la leeree ni ci ramadaan la bokk du tee ñéppay fay ndax amoowoon yéene ju dogu, woor ko ngir jaamoo ko Yàlla aayul nga xam ni boolewoo ko ci ramadaan ji, bu fekkee weer wi daa feeñ ci guddi gi te yë-goo ko fekk mosagoo darra, noo nu ngay wéyee doo lekk doo naan waaye du tee di nga fay bis boo bu ndax saartub yéene ji ci guddi gi amookowoon.

Bu fekkee da ngaa nekkoon ci tukki, yoon may na la nga bañ a woor, boo ñibisee fi nga dëkk ci bëccëg bi jant bi sowagul, duñ la wax bàyyil lekk ak naan, da ngay wéy rekk di lekk ak a naan fay rekk moo la cay war.

Gone guy gunge ba ci bëccëg gi mu yëgug kàllafe du tax ñu ni ko bàyyil lekk ak naan.

Ku xëm fekk woorutoon far ximmëliku ci bëccëgu koor du tax ñu bàyyiloo ko lekk ak naan.

Ku doon nàmpal ba woorul far gone ga faatu ci bëccëg gi tam duñ ni ko bàyyil lekk ak naan niki jigéen joo xam ni bi fajar di jot daa fekk laabul, bi ñu demee ba ci bëccëgu koor gi mu daa di laab kenn du ko wax mu bàyyi lekk ak naan, fay rekk moo ko cay war.

Koo xam ni bi fajar di jot daa fekk mu sex ab tib walla mu guux ndox wal-la muy joteek soxnaam, su boo baa da fay yàbbi lam sexoon bu dee joteek soxnaam it da fay daa dindi sawukaayam fa saa sa, du aajewoo muy fay waaye

Page 79: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

7 9

bu ca jàllaatee lum néew-néew ci loo xam ni coobareem la da koy fay.

Koorug farata niki ramadaan boo ca juumee dog, fay ga da lay war te doo wéy di lekk ak a naan.

Woor terewulaa soccu, def ko ci guddi moo gën a wóor waaye bu la leeree ni darra du jàll mën nga koo def ci bëccëg gi, socc bu waw moo gën a wóor ndax bu tooyee da fay am ndox te bu jàllee da fay dog sa koor.

Nampatalu (xotti yaram wi génnee ca dereet) ak gàjj duñ yàq koor lu dul ragal ni mën na laa indil tawat.

Boo wooree jékki-jékki waccu te du yaa ko sàkku darra waru la ca, waxu ñu mu dikk ba nga mën koo yàbbi mu far delluwaat koo ku da fay yàq koor ga fay war la ca, gall it noo nu la mel, xaaxtandiku moom darra waru la ca doonte mën nga ko yàbbi far wann ko, ki dugël baaraamam ci gémmiñam ñoddi wac-cu ma doonte darra delluwul ca biiram du tee fay war ko.

Bu koor jotee fekk jigéen ja ëmb mu ragal ni su wooree di na ca feeñ kon da fay bañ a woor te du tax mu lele, kuy nàmpal te àgg ci war a woor, doom ji nangoo nàmp ci keneen waaye moom amul lu mu ko fayalee ngir mu nàmp ci keneen mbaa mu am ko waaye moom ci ndeyam doŋŋ la nangoo nàmp, da fay bañ a woor ba noppi lele.

Ku màgget ba nga xam ni li des ci dundam yaakaaru cee mën a woorati muy góor walla jigéen koor wàcc na ko waaye sopp na ñu mu lele, lele mooy bis boo bee mu joxe ca am muddu mooy liibër, bis bu ne liibër lay doon.

Su fekkee da ngaa ame bor ci koor gi, bañ àggaat ci Baraxlu nga waroon a fay ndax tukkiwoo feebaroo, ba ramadaan dikkaat, bor ba da fay nekk ba léegi, alamaan ja mooy bis bu ne ab liibër.

Koor warul gone soppu ñu ko ci moom da cee wuuteek julli, bu dee xale bu góor ba kero muy kàllafe, jigéen it noo nu.

Ku ame jannaaba ci guddi gi te sanguwoo ko ba fajar fenk fekk nga war a woor, du yàq darra ci koor gi, yéex a sangu gi bu la taxee yéex a julli suba lay jur bàkkaar.

Jigéen it bu amewoon dereet far laab ci guddi gi daa di jàpp a woor waaye daa yéexee cangaay la ba fajar fenk, du yàq ci jëmmi koor gi darra.

Woor bisub korite ak tabaski xaraam na, ñaar i fan yi sës ci tabaski tam xaraam na ñu woor léen ndare nga def tammatux ci aj mbaa ci xiraan ñu digël

Page 80: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 0

la addiyu te amoo ko, bis bay ñenteel ba yit ci tabaski ga sib na ñu nga woor ko ci coobarewu, ku ko nisëroon mën na ko walla nga ne ci koorug tegale ba àgg ca mën nga koo woor.

Ku tukki ci ramadaan tukki bu mat doxub wàññi te nga tàmbali tukki bi njëkk fajar di fenk te yit nga fanaanoo bañ a woor kon sañ ngaa bañ a woor doonte tukki ba doo ci am coono, fay rekk moo la cay war, ci ngéru Maalik koor gaa gën.

Bu fekkee la ngay tukki matul doxub wàññi waaye déggoon nga ñu ni kuy tukki ci koor sañ ngaa bañ a woor ba wooroo di na ñu la dogal ngant, alamaan du ci war, képp koo xam ni daa dog kooram ngir defe ni sañ na ko te teg ko fu wér, fay rekk moo ko cay war deesu ko alamaan ci kaffaara, alamaan ji ki muy war mooy ki tay ag dog kooram ci lekk mbaa naan mbaa jote te fàwwu mu fay it, alamaan ji muy kaffaara ci weeru koor ñett i xeet la yu bokkul, bu njëkk bii la ñu ci gën a taamu mooy nga lele juróom benn fukk i miskiin, ku nekk nga jox kob mudd, mooy ab liibër, ci jamono ji jaam di am, goreel ab jaam di na taxawee kaffaara walla nga woor ñaar i weer waaye da fay aajewoo mu sësëloo nga xam ni boo ci dogoon ñaar i fan bëggkoo fayee koor, ñent i weer ngay woor yoo xam ni ñaar ya day tegaloo yeneen ñaar ya tegaloo, bu dee ñett i fan juróom benn i weer lay nekk.

Bu fekkee da ngaa amewoon bor ci ramadaan ba nga koy fay nga dog te tay ko du mel ni bo dogoon ci ramadaan te tay ko, fii fay ga rekk mooy yàqu, kenn du la ci alamaan bis ba rekk ngay fayaat ci wax ji gën a wóor.

Ku xëm ci guddig koor te ximmi ginnaaw bu fajar fenkee ci ramadaan koor ga du wér fàwwu da koy fay, bu fekkee jamono ji fajar di fenk ximmiwoon na ba teewlu yéene ji, bu dee lim xëm xaaju bis bi lay tollool walla matu ko kon koor ga di na baax, ki nga xam ne yit da fa màndiwoon te lim màndeewoon lu dagan la walla muy say moom ak kii xëm ñoo bokk àtte, ku màndiwoon ci lu xaraam bu ximmee ci bëccëg gi mu wóor ko ni ag kooram du baax du sañ a lekk ak a naan.

Ki woor war nay sàmm i cëram niki làmmiñam bañ caa def lenn lu aay, di baril def lu baax, bañ a jege ka muy sëyël rawati na bu dee keneen ci bëccëgu weeru koor, jote moom bu ko ca defee te tay ko koor ga da fay yàqu te yit am na alamaan mooy da fay kaffaara.

Jonjoo walla fóonante am nag téqale, bu ko wóoree ni su ko defee du tax darra génn, su boo baa da ñu koy sib, su wóoluwul boppam kon day xaraam

Page 81: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 1

mu def ko, guddi moom yii yépp darra du ci xaraam sañ naa lekk, sañ naa naan, sañ naa joteek ka muy sëyël, ku jonjoo walla mu fóonante waaye àggul ci jote ba mazyu génn fay rekk moo koy war waaye bu dee maniyu moo génn da fay fay bis ba ba noppi boole ca kaffaara.

Ku taxawee naafile yañ santaane ci ramadaan ñu jéggël ko ay bàkkaaram.

Sopp na ñu nga defee ko ca jàkka ja, ku mu soob it nga defee ko ci sa néeg rawati na bu dee fa ngay gën a sawaree, jamonoy Umar Ibnul Xattaab daan na ñu naafilee ñaar fukk i ràkkaak ñett, ñett yi ñooy doon safaak witar, ci jamonoy Umar Ibn abdal aziiz, dañ daan naafilee fanweer ak juróom benn i ràkkaa yu bokkul ak safaak witar, yii yépp dagan na waaye ñaar i ràkkaa yoo am sëlmël.

Yaay aysa nee naa Yonent bi SaWS daawul weesu fukk i ràkkaak ñaar teg ci witar.

Koor goo xam ni yaa ko coobarewu, boo ko xasee tàmbali da fay soppaliku lu war, doo sañ a gis lu la neex rekk ci lekk mbaa naan daa di koy dagg, boo ko dogee def lu xaraam te du tee fay ga war la, mën ngaa wéy it di lekk ak a naan ndax da ngay fay rekk, boo ko dogee te tayoo ko da ngay wéy bañ a lekk bañ a naan, di nga ca am tuyaaba te fay waru la ca te doo ca am bàkkaar.

Buñ nee booy tukki mën ngaa bañ a woor da fay fekk muy ci ramadaan waaye koor goo coobarewu teg ko sa bopp bokku ca xanaa nga dem ba ca biir nga xam ni boo dogul di na am lu mu la wàññi, dog ga da fay war.

Ihtikaaf

Mi ngi bokk ci jaamu Yàlla yi nga xam ni warul dees koy def ngir dolliku tuyaaba ak tàggat sa bakkan, cosaanu baat bi di nay tektale maanaa mi ndax ukuuf da fay firi taqoo, moom ihtikaaf fàwwu da fay ànd ak koor, fan ya nga koy def it daa war a sësëloo waaye su fekkee da ngaa yéenewoon ci ni da ngay def benn fan noppalu benn di nga ko mën waaye boo amutoon yéene jii daa war a sësëloo.

fàwwu ci jàkka ju ñuy jaamoo Yàlla lañ koy defee, booy ihtikaaf ci dëkk bu am jumaa te bis yi nga ko nar a def bisub àjjuma ci la bokk kon fàwwu nga dem ba ca jumaa ja, boo ihtikaafoon cib jàkka bu bisub àjjuma dikkee fàwwu nga génn dem julliji ko ca jumaa ja ndax julli gi farata la te li nga nekkoon naafile la.

fan yi nga nisëroon bu dee matul, génn goo gu da koy yàq fàwwu da nga koy tàmbaliwaat waaye bu dee tam bis yi nga nisër a lihtikaaf bisub àjjuma

Page 82: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 2

bokku ci kon sañ nga koo defee ci jàkka ji ci sa koñ, bu ñu sañoon fan yi nga ko nar a def mat lum néew néew fukk i fan tee wul loo nisër ciy fan rekk moo lay war doonte benn la walla lu ko ëpp.

Ku nisër ihtikaaf genn guddi te mënul a ñàkk mu ànd ak koor kon su boo baa fàwwu nga boole guddi ak bëccëg ga, ginnaaw mënul a ñàkk boo dee ihtikaaf ba yàgg nga dagg koor ga te tay ko li nga defoon lépp da fay yàqu nga war koo tàmbaliwaat.

Kiy ihtikaaf it du sañ a joteek ka muy sëyël benn yoon du ci bëccëg gi du ci guddi, mu fàtte ko ak mu tay ko ñoo yem la mu defoon da fay yàqu.

Bu ca nekkee ba mu yàgg tawat jum mënul booleek woor dab ko walla tawat juy aaye jàkka ngir sobe suy génn ci moom kon da fay dem toog kërëm ba wér soog a ñëw àggale la mu doon def, fan ya mu defoon du yàqu mooy yam def te jant ba sowoon ba mu dog koor ga da koy waññi bu dellusee mot-tali ko.

Jigéen juy ihtikaaf ba mu yàgg mu gis dereetu mbërëg nga xam ni su dalee jigéen da ñu koy aaye dugg jàkka, su boo baa da fay ñibi kërëm ba dereet ja jeex mu dellusi yeggale ko, fan ya mu defoon du yàqu mooy ya mu def te jant ba sowoon ba mu dog koor ga da koy waññi bu dellusee mottali ko.

Ki tawat walla mu gis baax ba dellu kërëm te ihtikaaf gi jeexul dañ koy dénk mu sàmm bu baax wormay li mu nekkoon, du tax mu sañ a laalanteek ka muy sëyël ci genn wet du ci sawukaay du ci yaram ba kero muy dellu ca jàkka ja ba matal ko te waxtu wu mu tanee daa war a dellu ca jàkka ja doonte ci bëccëg gi la, nga xam ni wóor na ko ni bu delloo ci bëccëg du ko waññiwaale, ki laab it noo nu, boo xasee dugg fa ngay ihtikaafee doo sañ a génn.

Lor ju tar joo xam ni mëneesul a ñàkk a génn faj ko rekk moo koy tax a génn niki jënd loo lekk walla loo naan te fekk nga yor njëg ga ba noppi nga xam ni da ngay waaxu jëndi ko daa di dellusi, bu dee da fay dem di ko lebi mbaa yelwaan buy génn ihtikaaf ga di yàqu.

Mën na génn it ngir jàppu mbaa mu am jannaaba bëgg a sangu ak yu mel noo nu waaye fa gën a jege tem mën faa fajee soxla sa la war a yem.

Bu fekkee da ngaa wax ni guddi sàngam laa bëgg a tàmbali sopp na ñu ba-laa jant baa so mu fekk la ca jàkka ja, boo ko xasee tàmbali yit doo sañ a génn ngir seeti ku tawat lu dul ndeyam mbaa baayam ndax farata la te li mu doon def naafile la te yit buy génn li mu doon def di yàqu xayna du ñàkk tuyaaba ja, bu dikkee da fay tàmbaliwaat.

Page 83: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 3

Bu dee ndeyam ak baayam kenn da caa faatu fàwwu mu war a génn jaale kiy dundu bu dikkee yit da koy tàmbaliwaat fan ya mu jotoon a def da fay yàqu, bu kenn ka faatuwoon ki ci desoon faatu fekk mu ne ci ihtikaaf walla ñu faatoondoo ñoom ñaar du jar muy génn.

Ku ihtikaaf du sañ a génn ngir ànd ci jullee néew xanaa bu dee ndeyam walla baayam waaye buy génn la mu defoon di yàqu, du génn it ngir yaxantu, saart boo ci bëgg a dolli bu dàqonteek ihtikaaf gi deesu ko faale niki baykat bu saart ni nisër naa ihtikaaf fukk i fan waaye bu bët sébbee da koy bàyyi dem bayiji, saart boo bee du ca am njariñ, lim ba mu waxoon su ko xasee tàmbali matal ga day war.

Ihtikaaf ca jàkka jooy imaam ja darra nekku ca lu ñu sopp la, booy ihtikaaf it mën ngaa maye soxna mën na ñu laa may soxna.

Koo xam ni bis yi nga nisër ci ihtikaaf gi daa tollook bu weer wi jeexee mu jeex kon bis ba ca mujj bu jant ba sowee rekk mën ngaa ñibi sa kër du jar ngay fanaan ca jàkka ja, bu fekkee ihtikaaf ji bu weer wi jeexee ngay jeexal te fekk muy ramadaan kon bu jant bi sowee ñu ni suba la korite bu ñu sañoon doo ñibi fa saa sa sa kër da ñoo bëggoon nga fanaan ci jàkka ji, boo xëyee dem fa ñuy jullee korite ba julli ba noppi soog a ñibi sa kër.

Asaka wurus, xaalis, mbay ak jur

Bokk na ci ponku lislaam yi génnee asaka ci wurus, xaalis, mbay ak jur bu ca saart ya dajee, asakay mbay duñ ko takk ci weer mbaa bis waaye saa bu ñoree xomb asaka war na ca, góob ga du ci saart ndax mën naa ñor te deesu ko góob niki dugub ak gerte lee lee nga tàmbali caa lekk te góobagoo, boo ciy génnee asaka da nga ciy seetaale lépp lu ñu ci fàkk moo xam loo xam ni loo lekk la walla loo joxe moo gën a wóor.

Ku ame ñaar i téeméer ren ba dewen asaka war na ko ca, moo xam da koo deñc walla muy yaxantu, bu dee kuy yaxantu ku dul deñc marsandiis di xaar, da fay def lu mu yor jaay ba mu jar wuti leneen, koo ku bu at mi matee da fay xayma li mu am ci marsandiis ak bor yi ñu ko ameel te mu yaakaar ni di na ci jot, ñaar i téeméer yu ne da cay génnee juróom i dërëm.

Kuy ligéey ñu koy fay, lu mu fayu ba deñc ko at, asaka war na ko waaye lu alal ja bari-bari ci loxoom te amu ca at asaka du ko ca war.

Wurus, xaalis ak jur ñoom at la ñuy topp ndegam mat na nisaab te saart ya daje ca, doo ko takk ci weeru wolof ni tamxarit mooy weer wi mujj waaye da ngay seet jamono ja nga tàmbali ba ca déwén sa, bu dee jur gi tam noo nu.

Page 84: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 4

Mbay liféeg amoo ci lu mat nisaab mooy juroom i wasq doo ci génnee asaka, benn wasq moo tollook benn barigo ak ñaar fukk i kilo, nisaab ci mbay mën naa tollook juróom benn i barigo, dees na boole bele, lors ak sult, lu ne boo ci amee darra te boo léen boolee mu mat juróom benn i barigo rekk asa-ka war la ca, du ñu bàyyi ba bu ne nga am ci juróom benn i barigo.

Su fekkee asamaan si moo suuxët yaw da ngaa bay rekk, fukkéel ngay gé-nnee mooy boo ko xaajee fukk i xaaj benn ba ngay génnee asaka, bu dee yaa suuxët walla masin te nga fay su boo baa da ngay génnee genwàllu fukkéel mooy boo ko defee fukk i xaaj benn ba da nga koy xaajaat, xaajaat boo bu ngay joxe.

Dees na boole xeetu sëb yi, kenn ku ci ne la nga ca am bu ñu ko boolewoon mu mat juróom benn i barigo rekk asaka war la ca, niki noo nu dees na boole xeetu tàndarma yi, bu matee juróom benn i barigo rekk nga war caa génnee asaka, su boo baa di na ñu la may nga génnee ko ca ba gën a yemamaay, niki noo nu xeetu raseng yi.

ceeb, saaño, suuna ak mboq deesu léen boole, ba la laa asaka di war ci benn fàwwu nga am ca juróom i barigo, saytuun muy oliiw dees na koy segal mu doon diw, kemb ga la ñuy njëkk a seet bu matee juróom benn i barigo asaka war la ca, su ko matee nga génnee ko ci diw te bañ koo génnee ca kemb ga ci boppam, yu mel nii nga xam ni da ñuy génnee ci pepp ma diw, bu ñu jaayoon diw ga yit bu ñu génnee asaka sa ci xaalis bi mu doy ba mu des say-tuun, bu dee diw lay doon génnee ko ca diw ga moo gën, bu dee oliiw buñ dul segal am ca diw moom buñ ko génnee ci njëg gi mu doy.

Xeetu furuwi yi lu mel ni orans màngo ak màndarin ak yu ni mel deesu léen génneel asaka ak legum yi tam noo nu ci fiqu Maalik.

Wurus moom li ciy nisaab mooy lu mat ñaar fukk i diinaar di nañ koy tol-looleek 85 garaam, nga war a génnee kaaru fukkeel ba mooy boo defee loo lu fukk i xaaj, benn xaaj ba nga def ko ñent i xaaj da ngay génnee benn ca ñent yoo yu mooy tollook genwàllu diinaar.

Xaalis moom liféeg amoo ca lu mat ñaar i téeméer i dërëm asaka du la war, day doon dërëm boo xam ni fukk i dërëm mooy tollook juróom ñaar i diinaar, ci waxiin wu gën a leer ñaar i téeméeri dërëm yoo yu mooy tollook 595 garaam ci xaalis mooy nisaabam, moo tax ñuy wax ni góor sañul a takk lu dul benn jaaro xaalis te du weesu juróom ñaar i garaaam lu mu rëy-rëy, booy génnee kaaru fukkeel ba ngay génnee asaka, bu dee ñaar i téeméer nga di ko

Page 85: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 5

séddële fukk i nit ku ne da fay tëye ñaar fukk, ñaar fukk boo ko defaatee ñent i xaaj, xaaj bu ne juróom lay doon, moom ngay joxe asaka, wurus ak xaalis benn xeet la ñu moo tax dees na léen boole nga xam ni boo amee ci bii ak ca bee boo léen boolee mu mat nisaab kon asaka war la, bu la neexee génnee ko ci wurus walla ci xaalis walla bu ci ne nga génnee ca la ca war a génn.

Mbooleem xeetu marsandiis yi mooy li bokkul ak mbay, wurus ak xaalis, yi ciy des yépp marsandiis la, boo ko moomee di ko fajee soxla asaka du ca war, ki koy jaay di ci wut benefiis su boo baa la ca asaka di war, njëg ga ngay jaayee ak ba ñu lay fay la asaka jay war waaye jëmm ja moom asaka du ci war.

Bu dee ci asaka, ñaar i xeetu komers ñoo am, ixtikaar mooy marsandiis bi nga am du lu ñu la fay nga jaay ko waaye da ngay nég waxtu dikk ba nga mën koo jaayee lu baree bari, xeetu komers bii bala la caa asakaa war fàwwu mu jar ba noppi te ñu fay la ko muy wurus walla xaalis, da nga koy génneel asakaam benn yoon doonte am na fi yaw ay at i at, bor yi ñu la ci ameel tam liféeg fayu ñu la ko muy fayug wurus ak xaalis ba mu mat du tax asaka war la ca, iddaara mooy ni jaaykat yi baaxoo defee mooy marsandiis bi da nga koy jaay rekk waaye bu ñu la ca tegalee darra lu mu néew-néew nga jaay ko du looy rënk, su boo baa da ñuy jàpp waxtu wa ñu ko tàmbalee komers, jàppee ko muy seen at bu yeksee ca déwén sa ñu daa di xayma lépp lu ñu am ci marsandiis xaymaa ko njëg ga jaadu, ñu seet it ba xam dénkaane na ñu fenn alal ñu waññiwaale ko, bu amee yit xaalis bu ñu jaay mu nekk ca seen loxo ba tay ñu xam ko, bu ñu boolee lépp, ku léen ameel bor te di ku jub te mu leer léen ni di na ko indi ñu waññiwaale ko, bu ñu xamee ni nàngam la daa di soog a génnee asaka ji, daa di koy génnee, da ciy seetaale yit barab ba mu ne ak jamono ja, nekkul ni benefiis bi la ñuy topp ba mu am at waaye ndey ja la ñuy bàyyi ba mu am at ñu door a génnee asaka ja.

Ba tay li nga xam ni mooy juru kër yi du ñu bàyyi ba mu am at ci sag moo-meel, seen ndey ya la ñuy seet bu ñu amee at ci sag moomeel rekk ñu jàpp ni li ci juddoo yit am na at.

Bu dee da ngaa ame xaalis walla wurus woo xam ni asaka war na ca ndax mat na nisaab waaye da ngaa ame bor boo xam ni boo ko ca fayee rekk jeexal mbaa bu jeexul lay des du mat nisaab kon asaka wàcc la waaye boo amee leneen loo xam ni asaka waru ci waaye mën naa fay say bor niki xeetu marsan-diis yi asaka warul walla ay jur mbaa suuf nga xam ni boo ko defoon ci bor bi mu mat mbaa la nga koy mottalee ci wurus ak xaalis du tee lay des mat nisaab su boo baa kon asaka di na la war.

Page 86: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 6

Ñaar bu ñu bokkee gétt boole seen i gétt bu ca saart ya dajee, bu laajkatu asaka ja ñëwee jarul ñuy xaajale seen i jur na mel ni kenn a ko moom, na ñu génnee la war a génn ñu door a seet nu ñuy tolloolee seen i cër ca gétt ga, bu dee kenn ka rekk moo matle nisaab te fekk ñu boole jur ya kon ki ko matle la génnee gi di war, ka ca des te matlewul nisaab asaka waru ko, kay jëlsi asaka ja bu jàppoon ciy juram ka ca des da ko koo war a delloo.

ñu bokkuloon gétt, nég ba asaka ji di bëgg a jot ñu bëgg a boole seen i jur walla ñu bokkoon gétt nég ba asaka ji di bëgg a dikk ñu bëgg a tàqarlikoo, su boo baa da ñuy seet ba xam loo la da fay wàññi asaka ja ñu waroon a joxe, bu koy wàññi rekk deesu ko nangu.

Gën jaa néew lu ñu war a génnee asaka mooy xar muy doog a am at, lu yées loo lu du mat asaka, du tee yit da ñuy waññiwaale ya yées loo la, nag it ba ngay génnee asaka lu mu gàtt-gàtt na am ñaar i at, bu ko yéesee rekk du mat asaka, giléem it ba cay gën a yées ngir asaka mooy ba am at ba dugg ci ñaareel, yoo yu yépp da ñu léen di waññiwaale, gàtt bu màgget ba wow deesu ko joxe asaka, bu ëmb it deesu ko joxe asaka, bu góor bay yokk gétt ga deesu ko joxe, ba boroom fonk it di ko beral xont it deesu ko jël ak biy nàmpal te feralagul.

Boo waree joxe jur, jur rekk ngay joxe, marsandiis manu koo wecci, njëg ga yit noo nu, su dee kiy jëlsi asaka ji moo la laaj njëg gi kon nga man ko, moom it du la ko forse. Boo waree génnee asakay mbay walla jur loo bari-bari bor war nga koo génnee.

Muurum koor

Sunna la gu ñu féddali gu Yonent bi SaWS diglewoon, ñépp la war gone, mag, góor, jigéen, gor, jaam. kuy dund rekk, benn bopp bu ne aw mudd mooy boo defee sa ñaar i loxo, loxo bu rëyul ba ëpp walla bu tuuti ba ëpp ba mu fees te tuuruwul, am na ñu wax it ñaar i kilo dees na ko jàpp, da ñuy seet it la ñu ëpp a dundee ci barab ba nga koy génnee ñu génnee ko ca loo la : ceeb, dugub walla lu mu doon rekk, li gën a wóor mooy génnee ko ci yii la ñu gën a taamu.

Jamono yi jaam amee, boo ko amee yaw yaa ko war a génneel muurum koor, gone yit su fekkee ni amul alal baayam moo koy génneel waaye bu dee am na alal mënees na ñu ko caa génneel muurum koor ja.

Su ko defee képp koo xam ni ab dundam yaw la war yaa koy génneel muu-rum koor : sa soxna, sa doom bu góor ba kero muy ligéey, sa doom bu jigéen it ba kero muy sëyi.

Page 87: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 7

Kenn ku ne ñaar i kilo ak sa bopp, da ñuy wax ni bu ñu wooree ba koor ga des benn fan mbaa ñaar mën nga koo génnee waaye waxtu wa ñu gën a taamu mooy bu fajar fenkee ba ba ngay dem ca jullikaay ba ñu ni tay la korite, nga génnee ko ci diggënte boo bu, boo ko fàttee ba julliji ba ñëw da ngay daa di gaaw génnee ko ndax bu jant bi sowee te génneewoo ko da ngay am bàk-kaar ci yéexee gi ba waxtoom jàll, du tee ba tay nga war a fay bor ba.

Sopp na ñu bu dee korite nga mos darra bala ngaa jëm ca jullikaay ba, tàndarma la ñu ci gën a taamu, leneen loo mos it du ko tee baax ndax da ñuy bañ nga yaakaar ni ba tay yaa ngi ci koor, bu dee Tabaski moom taamu wu ñu xëy mos darra da ñoo bëggoon boo xëyee mel ni ku woor ba julliji ba ñëw bañ rendi tabaski ja nga dogee ca resu tabaski ba.

Sopp na ñu ci jullig ñaar i iid yi yoon wa nga awoon bi ngay ñëw nga jaar beneen yoon booy dellu.

Aj ak umra

aj Màkka farata la ñeel képp ku ko mën, ka mu war mooy jullit, gor, muk-kàllaf, benn yoon la la war te matale ko, beneen boo ajaat naafile la, yoon wa ngay jaar ba àgg it na la wóor ni jàmm rekk a fay xew, yaw it nga wér, am it paas ba bu dee diggënte ba maneesu koo dox.

armal mooy yéene dugg ci aj gi, waxtu wa mooy bu weeru koor teroo topp digguw tabaski jëm ci fukk i fan yi njëkk ci weeru tabaski, weer yii ñooy weeru aj, barab ba ñuy armalee mooy Miiqa, boo ko defewoon feneen it du tee boo fa dikkee armal fa war la, ñi fay armalee ñooy ñi bàyyeekoo ci Penku bi fu mel ni Saam, Misra...

La wër Màkka yépp dañ koy def armalukaay nga xam ne foo ci romb bi ngay ñëw mën nga faa armalee, sopp na ñu mu topp ci ag julli, bu dee naafile da ngay def ñaar i ràkkaa door a armal, bu dee farata la tam baax na, bu dee naafile moo gën nga xam ni da ngay jàng faatixa ak Qul yaa ayuhal kaafiruun ci ràkkaa gu njëkk gi, faatixa ak Qul Huwa ci ràkkaab ñaareel bi, boo sëlmëlee daa di armal nga xam ni da ngay yéenewaaale ci sa xol ni da ngay aj, bu dee umra nga yéene umra, soo ca paree rekk daa di tàmbalee wax labayka ndax boo toogaatee lu yàgg waxoo ko di na ñu la alamaan, da ngay wax Labayka Allaahumma labayka la chariika laka innal xamda laka wa nihmata laka wal mulk laa chariika laka.

Bokk na ci sunnay armal nga sangu bala ngaa armal, boo dee góor da fay xaraam nga solaat lu ñu ñaw bu dee jigéen mën na ko da ñu koy tuddee sunna

Page 88: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 8

waaye warugar la, sopp na ñu booy dugg Màkka nga sangu, saa boo jullee yit di wax labayka gi ndax doo ko bàyyi bàyyi gu wér, da nga koy yeesal saa soo toogee ab diir waxoo ko.

Bi nga armalee di wax labayka jëm Màkka, boo yeggee ba teg say bagaas da ngay daa di wëri Kaaba ga, yoo yu jamono da ngay bàyyi labayka gi, su ko defee boo wëree Kaaba gi ba dox Safaak Marwa, door a tàmbaliwaat labayka gi, di ko wax rekk saa boo sonnee noppalu.

Bu ñu nee tay la arafaat ba ngeen ñëw ci jullikaay yi da nga koy bàyyi, bàyyi gu wér nga xam ni doo ko waxati ci aj gi.

Sopp na ñu booy dugg Màkka nga duggee mbedd mi ñuy wax Baabul Mu’alaa, booy génn nga jaaree ci mbedd mi ñuy wax Kidam, boo ko deful it aayul, saa boo duggee Màkka loo mën def ko ngir gaaw wëri Kaaba ga, soo mënee duggee Baabu Salaam moo gën daa di jubëli ca xajarul aswad fóon ko ak sa gémmiñ boo ko mënee, boo ko mënul nga raay ko ak sa loxo, jël sa loxo fóon ko ci sa gémmiñ, soo ko mënul da ngay taxaw ba tollook moom ni Allaahu Akbar daa di tàmbalee wër, booy wër Kaaba gi da lay càmmooñu, bu dee góor la sunna la ci moom mu ñukk ñett i wër yu njëkk yi, ñent yu mujj yi mu dox ko ndank, warugar la mooy Tawaaful Quduum kuy soog a dikk Màkka da koo war a def, ku mu raw da nga koy fayee tawaaful ifaada.

Booy wër, saa soo dikkee ba tollook doj wi da nga koy fóon, fóon gu njëkk gi sunna la, fóonaat ko ci yoon yi ci topp da ñu koo sopp rekk, Yamaani daa wax ni doonte mën ngaa fóon xajarul aswad ak sa gémmiñ doo ko def da ngay jël sa loxo teg ko ca daa di jël sa loxo teg ko ci sa gémmiñ te bañ koo muucu.

Bu juróom ñaar i wër yi matee da ngay dem ca Maqaama Ibraahiim julli fa ñaar i ràkkaa, boo ca noppee da ngaa war a dem Safaak Marwa waaye da ñuy sopp njëkk loo la nga jaaraat ca xajarul aswad fóon ko, fóon goo gu sunna la.

Safaa ngay njëkkee door a dem Marwa, sunna la nga yéeg ba ca seen kaw ñoom ñaar ñépp, jigéen moom su palaas ba wéetee mën naa yéeg, su amee ay góor mën naa bañ a yéeg, su ko defee boo yéegee ba ca kaw nga ñaan, ñaan goo gu sunna la, boo ko defee ca Safaa def ko ca Marwa tam.

Booy daw Safaak Marwa ba àgg ca Batnul Masiil da ñuy bëgg nga gën a gaaw ba weesu ko sunna la, soo bàyyeekoo Safaa ñëw Marwa benn taxawaay a ngoog, boo bàyyeekoo Marwa jëm Safaa muy ñaareelu taxawaay. Dem yoon la, dikk yoon la, noo nu nga koy defee ba mu mat juróom ñaar i yoon, boo ko seetee fenn fu ne di nga fa taxaw ñent i yoon, ginnaaw lii da ngay dellu sa dal

Page 89: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

8 9

toog ndegam bisub tarwiya yekseegul, bu julli jotee nga fas julliji ca Kaaba ga ndéem mën nga ko dellusi toogaat te bañ a fàtte labayka ji.

Su ñu nee tay la yawma tarwiya ji muy juróom ñetteelu fan ci tabaski, mooy bis ba mu teroowoon dellusi na, bis boo bu ci ngay xëyee Màkka dem Minan, da ngay fexe ba jullee Minan tisbaar, yendu fa, fanaan fa, boo fanaanee ba xëy ba julli suba, suba goo gu mooy bisub arafaat ndax mooy bisub juróom ñenteel, nga daa di dem arafaat, su ko defee labayka ji doo ko bàyyi, boo sonnee noppalu bu amee lu ko dagg nga ne ca bu jeexee nga dellu ca ba ñu ni tay la arafaat ba nga ñëw ci jullikaay ba, foo fu nga koy bàyyee, bàyyi gu dog.

Bala ngaa dem arafaat sopp na ñu nga sangu, su ngeen fa demee da ngeen bi boole tisbaar ak tàkkusaan julleendoo léen te wàññi léen, su ñu ca noppee ilimaan ji da fay ànd ak ñoom fañ war a taxaw ca arafaat, taxawaay bi ñuy taxaw laataa jant di so warugar la soo ko bàyyee am na alamaan doonte bok-kul ak taxawaay biy farata dëgg-dëgg, mooy bu jant bi sowee nga taxaw fa as diir la muy gàtt-gàtt mënul a ñàkk, nga xam ni bu Yàlla dogalee jant bi so ba fajar fenk te taxawoo fa aj gi raw na la ca moo ma at déwén rekk.

Bu la jant bi sowee ca arafaat da ñuy yéexee timis, ba ñëw Musdalifa, jullee fa timis ak gee, da ñu léen di boole waaye gee ga da ñu koy wàññi ndax timis deesu ko wàññi.

Wàcc Musdalifa warugar la boo ko deful am alamaan, la gën mooy nga fa-naan fa ba julli suba, door fay jóge ànd ak ilimaan taxaw fa ñuy wax Mach’arul Xaraam ba jant bi fenk mbaa mu jegee fenk, boo xëyee da fay doon bisub fukkeel di Tabaski kon ginnaaw taxawaay boo bu da ngeen di wutëli Minan, Batnul Mu’asir xur la boo xam ni sunna la boo fa tollee te fekk ngay góor nga gaaw booy dox, boo waree tam soññ la nga war.

Boo yeksee Minan la ngeen di njëkk a def mooy daa di sànni jamray aqaba muy juróom ñaar i xeer yuy digg dóomu yoo xam ni mënees na koo fettax ak i baaraam. Boo koy sànni da ngay wax Allaahu Akbar, boo ca noppee rendi la nga ame walla loj, la cay topp mooy watu, nga dem ca Kaaba ga wër ko juróom ñaar i yoon, wër goo gu mooy Tawaaful Ifaada ci bisub fukkeel bi, bu wër bi matee nga dem julli ñaar i ràkkaa ca Maqaama Ibraahiima, ginnaaw ba nga dellu Minan fanaani fa.

Suba ja ak ginnaaw suba ja mënoo koo ñàkk a sànni jamra yi, bu tisbaar jo-tee da ngay wut ñett i juróom ñaar ciy xeer ndax ñett i barabu sànnikaay la yu bokkul yoo xam ni benn bu ne daa am juróom ñaar i xeer yoo fay sànni, bari

Page 90: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 0

nay coono lool ndax bëgg gee defandoo, am na sax ñoo xam ni seen bakkan fa lay faral di des, sànni boo sànni wax allaahu akbar, ci ginnaaw boo jullee tisbaar lay doon.

Sànnikaay bu njëkk ba ak bu ñaareel ba ginnaaw boo sànnee ba noppi da ngay taxaw ñaan fa ñaan gu yàgg, boo ca noppee jàng saaru Baqara boo ko mënee loo laa gën, jamray Aqaba moom boo ko sànnee doo fa taxaw di ñaan da ngay dellu fa nga nekkoon, ñett i barab yi ñuy sànnee mooy Jamratul uulaa ak Jamratul wustaa ak Jamra iqba mi ci mujj nga xam ni boo ko sànnee doo fa taxaw di ñaan. Boo sànnee ñett i fan ya ba tisbaar jot nga sànni bisub ñetteel ba, mel ni tay jii doonoon talaata bu nekkoon bisub fukkeel bi, tay ngay fa-naani Minan, àllarba ji ba nga julli tisbaar nga sànni ñett i jamra yi, alxames ji noo nu, àjjuma mooy doon ñetteel bi, doon it ñenteel boo tàmbalee waññi ci talaata ji, boo sànnee ñetteel ba nga xam ni moo ca mujju, da ngay daa di waññarbiku dem Màkka waaj ba jekk dellu fa nga dëkkoon ndax aj gi jeex na, sànni jamra moo ci mujju.

Bu la neexee boo amee ñaar i fan nga bañ a xaar bisub ñetteel ba niki tay la fukkeelu fan bi nga fanaani Minan, suba ga di àllarba mënoo koo ñàkk a sànni, alxames ja yit mënoo koo ñàkk a sànni waaye boo sànnee alxames ja ba noppi te yàkkamti da ngay fexe balaa jant bee so nga génn Minan, bu la fa jant bi sowee fàwwu nga war a xaar àjjuma ji sànni ko ni ko alquraan waxee faman ta’ajala fii yawmayni falaa isma alayhi, wa man ta’axara falaa isma alayhi liman’itaqaa.

Soo toogee Màkka ba waaj ba jekk nga xam ni ñibi rekk moo ci des da ngay wëri Kaaba ga wërug tàggoo na nga daan wëree nga koy defee, soo ca noppe julli ñaar i ràkkaa daa di mën a ñibi.

Umra sunna la ci sag dund nga def ko benn yoon, boo ko xasee def beneen boo defati naafile la, ni ñuy ajee rekk la ñuy umraa. aj daa gën a guddu rekk waaye ñoo bokk ni ñu koy defee, ñoo bokk armal, bokk wër Kaaba, bokk Sa-faak Marwa. Umra moom boo doxee Safaak Marwa watu mu jeex.

Bu dee góor fa ñu ko digëlee watu muy ci aj walla ci Umra, su mënee watu ba mu set moo gën, su fekkee daa jempi ba karaw ga gàtt yit du ko teree baax, jigéen moom jempu rekk lay def waaye du watu ba set.

am na yu dëkk ci suuf yoo xam ni boo xasee armal doo ca sañ a ray waaye seppi na ñu ca lu mel ni jinax, jaan, jiit, xaj buy màtte, till buy tooñ ak mbooleem rab yiy fàdde, boo ca rayee aayul, mbooleem luy naaw ci jawu ji

Page 91: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 1

bu fekkee daa ame lor kon ki armal mën na koo ray tam.

Ki xës a armal ci aj mbaa Umra da fay moytoo joteek ka muy sëyël, jote goo gu su fa amee ci diggënte bi mu armalee ba kero muy taxaw arafaat aj gi yàqu, bi mu taxawee arafaat ci guddi goo gu su ko fa defee aj gi yàqu ba tay, guddi goo gu ngay taxaw arafaat bu bët setee ci lay war a def tawaaful ifaada, sànni jamray aqaba, bis boo bu tam su ko fa defee aj ga yàqu, su bis boo bu xasee jàll doonte defagul ñaar yoo yu du tax aj ga yàqu, su dee bis bi tam daa def benn bi muy jamray aqaba laata muy def tawaaful ifaada jote ca du tax mu yàqu.

Lajkoloñ moom da ñuy wax ni ñaar la, bu góor ak bu jigéen, bi nga xam ni boo ko laalee da fay taq bu baax xeeñ bu baax te am doole lool niki misk, xaraam na ci góor ak ci jigéen, ku ci xës armal bu ko laalee am na alamaan. Lajkoloñ bu góor bi da ñuy jàpp ni mooy bi nga xam ni boo ko laalee xet gi du am doole te as tuut bu la ca taqee mu baax niki ward walla jasmin, da ñu koo sib rekk waaye boo ko defee du am alamaan.

Yëre yu ñu ñaw da ñu koy aaye góor bu xasee armal, jigéen mën na koo sol, góor gu ko def di na am alamaan, rëbb it ku xës armal du ko sañ muy góor muy jigéen ak ray ci xeetu daaba yi, na moytoo dindi tam tilim-tilim yi nga xam ni du sobe, bu dee sobe bañ koo julliwaale mooy tax nga dindi ko, bu dee tilimug kese du ko sañ a dindi.

Bu xësee armal moom ku góor ki du sañ a muur boppam, bu ca muuree darra rekk da fay am alamaan, du sañ a watu tam lu dul ngir lor walla ñu xaañ ko ci mbaa mu gaañu ca, su boo baa di na mën a watu ngir faju.

Loo lu ñu ko aaye su ko defee te tay ko ak ñàkk koo tay ñoo ca yem, fi ñu wuutee mooy bu ko tayul du am bàkkaar bu ko tayee di na am bàkkaar te alamaan ji du tee mu am, ñett yii mooy taamu bu ko ca neex, woor ñett i fan, leel juróom benn i miskiin lu mat ab kilo walla mu jaamoo Yàlla gàtt boo xam ni fu mu ko rendee baax na.

Jigéen bu xësee armal da ñu koy aaye lépp lu ñu aaye góor ba mu des sol ñaar i bot ak sol lu ñu ñaw, yii di na ko mën, jigéen su armalee du sañ a muur kanamam, du sañ a muur ay tenkam, góor moom it su armalee daa war a bàyyi boppam muy boppug kese, kanam ga yit di kanamu kese, da fay xaraam ñu sàng darra ci yoo yu muy guddi muy bëccëg, bu ca sàngee darra alamaan yéeg ko doonte fàttee tax walla ngir feg tàngaay walla sedd, góor bu xësee armal da ñu koy aaye sol ay bot lu dul bu ñàkkee ay dàll te amul yeneen waaye

Page 92: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 2

da koy dagg ba mu gàtt ba dojoram ya di feeñ.

Boo taxawee di yéene aj, daa am xeet yoo mën a yéenee : ifraad, tamma-tux ak xiraan bu dee fiqu Imaam Maalik ifraad moo léen gënal, am na lu ñuy woowee irdaaf waaye daa dugg ci xiraan moo tax kenn du ko limaale, ifraad mooy nga yéene ajug kese def ko ba àggal ko doonte tegoo ca Umra.

Boo defee xiraan mbaa tammatux te bokkoo ci waa Màkka ak la ko wër da ñu lay alamaan ab addiyu, bu fekkee teel nga koo jiitël ba taxawaale ko arafaat kon da nga koy rendee Minan, boo ko jiitëlul ba taxaw arafaat kon da nga koy rendee ca Màkka ca fa ñuy wax Marwaq waaye bu fekke Màkka nga ko jëndee doo ko rendi fa saa sa te génnook moom ba ab tankam laal àll bi génn xurum bi te boo ko jëndee biir Màkka rendi ko fa saa sa kon ab tankam du laal àll ba génn xurum bi.

Boo amul addiyu joo ju, benn gisoo ko ba jënd ko walla amoo njëg ga kon da ngay woor ñett i fan ci biir aj gi te mooy waxtu wa nga armalee ba bala ngaa taxaw arafaat nga koy wooree, boo jotul a woor ñett i fan yii laata ngay taxaw arafaat kon fan ya ngay nekk Minan booy sànni jamra da nga koy woor, boo ñibee dolliwaat ca juróom ñaar muy fukk moom la alquraan di wax ni tilka achratun kaamila.

Tammatux mooy booy armal nga yéene umra kepp ba àggal wëlbëtiku aj, lay tax alamaan war la ca mooy nga nekk ca Umra ba fekk weeru aj ya teru (Sawwaal, Korite, Digg Tabaski ak Tabaski) kon boo demoon Màkka ci rama-daan di umra doonte da nga caa ne ba ca bis bu mujj bi te jant fenkagul du tax nga am ca alamaan ndax korite teroogul, boo jotul a ñibi fa nga jógewoon mbaa nga dem fu sori walla nga dellu ba ca déwén sa door a ñëwaat ajsi xanaa nga toog ba aj gi jot nga daa di aj kon addiyu di na la war ca Tammatux ga.

Tammatux da fay firi xéewlu ndax daa noppale te gàtt, bu fekkee da ngaa yéenewoon Umra daa di koy def ba àggal fekk yaa ngi biir Màkka nga fas yéenee aj teg ca kon du aajee nga génn ba ca Samiiha, soo yaboo armalee biir Màkka, taamu na ñu nga dem ba ca jàkka joo ja ca Kaaba ga waaye te-rewul foo ko defee ca Màkka mu baax, ku nekk biir Màkka bëgg a armal Umra fàwwu mu génn ko ci léppam ba fa bokkul ci xurum bi, foo fa lay armalee di wax labbayka wutsi Màkka daa di wër Kaaba gi wéy.

Xiraan mooy booy armal nga yéene ci benn jotaay Umra ak aj yépp ba tay boo yéenee Umra kese teg ca aj xiraan la, di na dem ba ñu woowee ko irdaaf ndax bu fekkee da ngaa yéene umra kese dem ba tàmbalee jëf jëf i kuy Umra

Page 93: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 3

niki nga dem ba wër Kaaba ga daa di far yéene aj tegu ca, su boo baa irdaaf la ñu koy tuddee, su boo baa yit da fay yeggali wër ba def ko muy wërug coo-barewu te yit du dox Safaak Marwa teg ca ndax saa boo xamee ni def nga Xi-raan jëf i aj kepp ngay jëf waaye doo beral aj ak Umra seen i jëf, sunu Boroom da fa ni zaalika liman lam yakun ahlahuu xaadiril masjidil xaraam, kon ku dëkk Màkka walla la ko wër bu defoon Xiraan mbaa Tammatux du tax addiyu war ko, ku fa dëkkul la ñuy sant addiyu.

Ku fexe ba yewweeku ca umra ja te weeru Kori teroogul ginnaaw bi mu toog fa ba aj tam deful Tammatux ndax saart bay tax ñu alamaan ko la deful.

Su fekkee jot ngaa ray ab rëbb ginnaaw boo armalee, alamaan ji benn ñu seet rab wa nga ray lu xeetook moom ci juru kër yi (xar, béy, nag, giléem), nga rendi loo la muy sa alamaan, ñu dégg fiq ñooy seet la nga ray la muy tollool ci juru kër yi, loo lee ñu la alamaan nga war koo ray boo ko teelee xam ba jiitël ko taxaw ak moom arafaat da nga koy rendee Minan, boo taxawul ak moom arafaat kon Màkka nga koy rendee waaye bu fekkee Màkka nga ko jëndee fàwwu nga yóbbu ko ba mu génn xurum bi, nga waññi ko mu ñëwaat nga door koo rendi ndax tank ya daa war a laal ill bi mooy àll bi bokkul ci xurum bi, benn alamaan la bu ko neexee tànn ko, bu ko neexee lele mooy da ñuy xool la mu ray xayma ko ci ñam na muy toll, mu saraxe ko ba tay loo lu baax na, ba tay la mu ray it bu ñu ko xaymaa ba xam na muy toll ci ñam nga woor ko, na ngay wooree mooy ñam woo wu ñu natt nu mudd ya toll rekk ngay woor ci ay bis, su amee mudd bu matul it nga wooral ko bis niki bu ñu ko seetoon muy juróom ñaar i mudd juróom ñaar i bis ngay woor, bu doonoon juróom ñaar i mudd ak genwàll kon nga woor juróom ñett i bis ndax bis maneesu koo xaaj.

Sopp na ñu Umra boo ko mënee at mu ne nga def ko benn yoon, saa yoo demee Màkka Umra walla nga aj bay waññeeku bëgg na ñu nga wax ñaan gii :

Haa’iduuna, taa’ibuuna, aabiduuna li Rabbinaa xaamiduuna sadaqa Laahu waxdahuu wa nasara abduhuu wa hazamal ahzaaba waxdahuu.

Bunt ci ab tabaski ak rendi

Tabaski moom sunna su dëgër la ci képp ku ko mën doonte sax gone la, ku ko mën mooy koo xam ni njëgug tabaski ga du ko aajawoowaat ci dundug boppam walla njabootam ci at mi, bu dee lu muy aajawoowaat rekk du lum mën.

Bu dee xar ngay tabaskee lu mu néew-néew na mat jafahu mooy na am at, am na ñu ne juróom ñett i weer am na ñu wax fukk, ajuwul rekk ci boroom

Page 94: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 4

kër gi doonte gone nga sunna la ci yaw nga def ko boo ko mënee, tuyaaba jiñ ci dige jar na ko.

Su fekkee bëy ngay tabaskee lu mu néew-néew na am at ba dugg ci ñaareel bi lu mat weer walla ñaar i weer.

Su fekkee nag nga bëgg a tabaskee lu mu néew-néew na am ñett i at te dugg ca ñenteel ba.

Su dee giléem nga bëgg a tabaskee na am juróom i at te dugg ci juróom benneel ba.

Lépp loo tabaskee xar moo ca gën, xar bi nga xam ni kenn tàppu ko moo gën lu dul ni ba ñu tàpp da koo gën a duuf, bu ñu yemee ba ñu tàppul moo gën, boo weesoo yu góor yi, yu jigéen yiy soog a dikk. Xar bu jigéen it moo gën bëy bu góor, bu la xar tëwee ba amoo ko bëy bu góor baa gën, ba ñu tàppul moo gën bëy ba ñu tàpp lu dul ni ba ñu tàppul daa gën a duuf, bëy bu góor moo gën it bu jigéen, bëy bu jigéen it nga tabaskee ko moo gën nga tabaskee nag walla giléem ndax la gën a baax ci yàpp la ñu cay taamu wuuteek bu doo-noon ci addiyu ya ñuy ray ca Màkka bu dee giléem moo gën topp ca nag ya, topp xar, topp bëy ndax barig yàpp wa la ñu cay seet.

Lépp looy tabaskee na bañ a patt, bu mu tawat tam tawat goo xam ni bu àndeek jur ya nga xàmmee ko ci, bu dee tawat bu ndaw nga xam ni bu àndeek jur ya doo ko ca seetlu, su ñàkkoon moo gën waaye du ko tee baax. Su làggee yit te ag sooxam fës du baax, bu yooy it ba ñàkk gerees du baax.

Lépp luy xeetu sikk na nga ko ca moytu, am nay sikk yuy tax du doy tabaski am na yit yoo xam ni su ko amee du ko tee baax waaye moytu léen moo gën. Bu ay noppam xar du baax lu dul ni xar-xar ba bañ a bari nga xam ni boo xaajoon nopp ba ñett i xaaj, xar-xar bi benn xaaj ba lay doon walla sax du ko mat niki noo nu dagg ga, bu matee ceer ba mbaa mu yées ko du ko tee baax bu ko ëppee du doy.

Su béjjën ba dammee te góom ga wér du ko tee baax, su fekkee nàccul te wérul tam du ko tax a baax, ñàkk gaa nàcci rekk doyul fàwwu da ciy boole wér.

La ñu gën a taamu mooy sa tabaski nga bañ koo rendiloo kenn rendil ko sa bopp, da ngay bàyyi ba ilimaan rendi walla bu dee ilimaan da fay loj nga bàyyi ba mu loj ba noppi, boo njëkkee rendi ilimaan doonte fekk na ilimaan yób-baale xaram ca jullikaay ba doo amug tabaski, bu yóbbaalewul xaram moom ilimaan kon ku ñibi ba toog ba tolloole ni ilimaan war naa rendi ba noppi ca ngay soog a rendi, bu ñu amul ilimaan da ñuy tolloole ni dëkk sàngam moo

Page 95: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 5

nu gën a jege te ku fa dem war na ñoo julli ba noppi ba seen ilimaan ja rendi, ñuy soog a rendi, bu ñu ko defee ginnaaw ba am ku fa jóge ni falaa jóge waaye jullee gu ñu, du ca wàññi darra ndax tolloole na ñu ba noppi, seen jaan wàcc na.

rendi ag tabaski walla addiyu da ñu ciy saart ñu def ko ci bëccëg, ku ko def ci guddi du baax, bu dee bis bu njëkk bi bëccëg gi mi ngi tàmbalee fa ili-maan rendee, su dee kuy tolloole ma nga tàmbalee fa nga tolloolee ba xam ni ilimaan war naa rendi ba noppi, soo ko weesoo ba dugg ci bisub ñaareel bi walla ñetteel bi, su fajar xasee fenk rekk fa lay bëccëg giy tàmbalee ba jant bi so foo fi rendi rekk mu baax, la ñu cay taamu mooy nga bàyyi ba fa dagan a naafilee nga rendee fa te mooy ci yoor-yoor.

Bisu tabaski yi ñett i fan la ñu, boo ca rendi rekk am nga tabaski, muy bis bi njëkk di bisub fukkeel ak ba ca topp di fukk ak benn ak ba ca toppaat di fukk ak ñaar, rendi ca ba ca njëkk moo gën, boo ko mënee bul bàyyi mu raw la.

Deesu jaay darra ci am tabaski, du der ba, du darra lu ca bokk, ku la feesal it doo ko fay ca yàpp wa, bu aajewoo sarax boo ko fayee xaalis ba noppi bu la neexee mën nga koo sarax ca yàpp wa.

Sopp na ñu li ngay rendi nga tërël ko mu jëm xibla, kay rendi daa war a wax Bismillaahi Allaahu Akbar, ka doon rendi bu ko waxul te tay ko wax ji gën a wér mooy kenn du ko lekk, bu dee tabaski sopp na ñu nga dolli ci Rabbanaa taqabal minnaa, kuy rendi fàttee wax Bismillahi Allaahu akbar dees na ko lekk, bu ko tayee deesu ko lekk, niki noo nu boo àndeek ab xaj di ko yabal cib rab ngir rëbb, da nga koy tëye ci say loxo walla nga ànd ak ku la ko tëyeel nga xam ni boo koy bàyyi di ko yabal ci rab wa da ngay wax Bismillaahi, boo ko fàttee wax bu ko jàppee dees na ko lekk, boo ko tayee waxoo ko bu ko jàppee deesu ko lekk.

Bu dee balu fett walla fetal it ñoo yem ci loo lu, boo koy yabal war nga wax Bismillaahi, boo ko fàttee dees na ko lekk, boo tayee fàtte ga deesu ko lekk.

Gàttug tabaski, tudd ak gàttug jaamu niki addiyu deesu ca jaay darra, du yàpp wa du der ba du caas ya, du darra, mën ngaa lekk ci sa tabaski saraxe ci, joxe ci àddiya.

Loo rendi ngir jotoo ko ab alamaan doo ca sañ a lekk, boo nisëree rendil ay miskiin it doo ca sañ a lekk, addiyu moo xam ni waru la ci genn wet, du ala-maan du darra te nisërookowoon, daa am loo jiitël rekk coobarewoo rendil ko miskiin yi jëmële ko fa nga ko war a rendee àggagoo mu nar a dee ci diggënte

Page 96: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 6

bi nga rendi ko, da ngay bàyyi ña fa nekkoon lekk ko waaye yaw doo ca sañ a lekk da ngay jéggi rekk jàll, bu xasoon a àgg fa mu jëm nga sañ caa lekk, yu dul yii rekk mën nga caa lekk niki muy addiyu xiraan walla tammatux mbaa bépp addiyu gu wàññi goo wàññi ci aj jur.

Dëgg-dëggi rendi mooy dagg boli ba ak ñaar i sidit ya ko séq ba mu jeex, masin buy dikk tàggale bopp beek yaram wi gisu ñu fenn lu koy tax a dagan te mu bari lool léegi, boo doon dagg te yoo yu yépp daggul ba jeex niki nga tàm-balee dagg boli ba walla ñaar i sidit ya te daggul ba jeex du tax mu doy ndax deesu ko sañ a lekk ndax rendi moo koy tax a dagan te matul.

Boo tàmbalee rendi ba mu sori nga xam ni boo bàyyiwoon mu dee, boo yëkëtee sa loxo te terewulaa delluwaat di dagg, ñépp maase na ñu ci ne rendi ga yàqu na, su fekkee gaaw ngaa delluwaat moom di na baax, su fekkee rendi ga soriwuloon nga xam ni boo delluwaatul du dee, soo yéexee ñëw it du ko teree baax waaye da ngay yéenewaat yéene ju bees ci waxaat Bismillaahi Allaahu Akbar ndax la nga defoon gaañ ko doŋŋ la, bu dee da ngaa dagg ba mu jeex nga wéy ba tàggale bopp bi ak baat bi du ko teree baax waaye ñaawal ngay teggin du tee mënees na ñu koo lekk.

Ku tàmbalee rendi ci doq deesu ko lekk, tàmbalee ci boli bi ak li ko wër moo koy tax a baax.

Nag li gën mooy ñu rendi ko te bañ koo loj, bu ñu ko lojee tam du tee mënees na ñu koo lekk, loj moom daa am jumtukaay bu ñu koy defee boo xam ni da nga koy def ci xóot-xóot gi ci dënn bi, soo bësee ba mu laal xol ba mu dee, loo lu mooy loj.

Mënees naa rendi nag mënees na ñu koo loj waaye rendi gaa gën, giléem it dees léen di loj, boo ko rendee te mënoon koo loj deesu ko lekk moo gën a wóor.

Su dee daa am fu mu daanu ba rendi rekk la ñu ko mën a def du ko teree baax, xar ak bëy ñoom dees léen di rendi maase na ñu ci ne boo léen lojee ci sa coobare deesu léen lekk.

Takk sëy ak fasem fay

Sëy ci lislaam daa am i saart, kilifa maanaam ka war a maye jigéen ja, can mooy alalu sëy ga, waxiin wa ñuy wax ba ñu xam ni maye na ñu ndax kay ñaan da koy wax may ma kay maye wax ni may naa la, bu lii xasee ba am sëy ba fasu na, xutba bi da ñu koo sopp rekk, ñaar i seede yu maanu saart la ca tam, mën na ñu faa bañ a teew sax waaye balaa boroom kër gi ak soxna saa

Page 97: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 7

jote fàwwu ñu sàkkal léen seede yuy seede ni diw may na ñu ko diw.

Day am it gën jaa néewu can nga xam ni bu ko yéesee du doy, moom la ñuy tolloleek rub’u diinaar walla ñu weccee ko loo xam ni ku ko seet ci xaalis di na mat rub’u diinaar mu war a tollook 16 000f, terewul tam am nay wuute.

Ki jur doom te mi ngi ak ndawam ba léegi mën naa jékki-jékki maye ko te du ca diisóok moom te du sañ a bañ doonte kàllafe na, bu ko soobee mu diisóo ca ak moom, bu fekkee du baayam bi ko jur, bu soxna si dee gone doo ko mën a maye liféeg kàllaful, di na aaje yit bu kàllafee nga diisóo ca ak moom ba mu nangu, bu nee patt ginnaaw boo ko laajee mooy tektale ag nangoom ngir kersa, teewul bu noppee te noppi ga nga gis ca màndargay bañ soo yaboo bàyyi.

Koo xam ni jeeg la daa sëyiwoon ba dellusi doonte yaay baayam bi ko jur doo ko sañ a maye te disóowoo ca ak moom, te yit noppi doŋŋ du ca doy da fay aajewoo mu wax ba xam nangu na am déet.

Kilifa guy maye mënul a ñàkk, bu ñu seetee gis ni kenn ku mu bokkal geño ku ko mën a maye gisu ñu ko kon ab qaadii moo koy maye, jigéen ji ñu war a maye su fekkee doomam ju góor mi ngi fi ju mat kilifa mooy jiitu maamam ju góor ji jur yaayam ci sañ a maye, baay it moo gën a yay ci mbokk mu góor, ku mu bokkal ndey doŋŋ bokkul.

ñi war a maye : doom ju góor ju matale saart i kilifa moo jiitu, sët bu góor ju bàyyeekoo ci doom ju góor moo ca topp, baay topp ca, mbokk mu góor mu bokk ak jigéen ji ndey ak baay topp ca, mbokk bu góor bi bokk ak jigéen ji baay doŋŋ topp ca, nga door caa teg seen i doom ñoom it noo nu la ñuy sësëloo, su ñu jeexee nga door cee teg maam bu góor, baay bu ndaw bi bokk ak baayub jigéen ji ndey ak baay door a dikk, nga door caa teg baay bu ndaw bi bokk ak baayub jigéen ji baay doŋŋ, bu dee ku ñu goreel nga teg ca ka ko goreeloon, nga teg ca ka ko yaroon ci diir boo xam ni mën na koo ñeewent mu daa di yayoo kilifag maye, ka cay sës di àttekat bi, su amul mbooloom jullit ñooy tase tànn kenn ni ko mayeel kii, bu amee kilifa gu gën a yay ci maye te sori bàyyi ku ko gën a jege maye darra nekku ca.

Bu ñu la dénkee xale bu góor bu la neexee mën nga jékki-jékki may ko soxna doonte kàllafeegul te nga gis ni takkal ko soxna moo gën du ko tee baax, bu ñu la dénkoon xale bu jigéen nga yore ko nga xam ni kàllafeegul doo mën a jékki-jékki maye ko xanaa bu la ca baayam joxee ndigël, bu la baay ba nee forse ko nga sañ ko, kilifa gi war a maye sëy bi ci wàllug baay gi lay bokk waaye

Page 98: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 8

du bokk ci wàllug ndey gi.

Bu sa mbokkum jullit di wut soxna yaw ngay jamaaleem doo sañ a waxaale yaw it ngir sa bopp, da ngay bàyyi ba mu noppi bu sottiwul ngay soog a sañ a labati, bu fekkee ci njëlbéen gi la du aay waaye bu xasee sori nga xam ni juboo mbaa ñàkk a juboo moo ci des su boo baa da fay aay.

Sëyub sixaar daganul te mooy weccee ay jigéen, ku ne may sa moroom soxna saartante ca ni bu lee amul lii du am.

Bokk na ci sëy yi xaram ñooy yi ñu wax ni can du ca am, sëy ci ab àpp tam daa aay te mooy nga takk soxna si te bu àpp sàngam jotee ngeen tàggoo mu jege ak mu sori ñoo ca yem, sëy ci idda yit daganul, diir boo ba wax ko ca sax da ma laa bëgg a takk xaraam na, su ko ca takkoon jote ca ak moom soxna da koy xaraam fàwwu.

Su fekkee yit daa amug wéradi ca maye ga du baax te mooy niki ñu ne ñoom ñaar xamu ñu ba xam bëggënte na ñu am déet mbaa sëy na ñu am déet waaye da ñu léen di maye rekk bu ñu dikkee bu léen neexee wéyal ko walla ñu dindi ko, bu dee can ga yit moo wéradi du baax niki ñu canee ko lu ñu sàcc, lépp lu jaay ga xaraam rekk xaraam na nga def ko can niki sàngara walla xaj.

Lii bu amee, bu dee ñoom ñaar jotee gu ñu kon da ñuy tas sëy ba waaye bu ñu xasee jote yoon da koy bàyyi noo nu sëy ba wéy ñu joxaat soxna sa can gu wér.

Su fekkee jëmmi maye ga moo awul yoon niki ñu maye ko te amul kilifa walla cib idda walla cib armal, koo ku yoon da koy dindi moo xam jote am na ca walla déet, su ñu ko dindee te fekk jote wu ñu darra kon ku nekk da fay dem sa yoon rekk darra du ca war, bu fekkee bañ koy dindi fekk na góor ga joteek jigéen ja kon su fekkee am na can gu ñu waxantewoon te muy gu wér góor ga di na ko ko jox, bu fekkee waxante wu ñu woon genn can kon mu jox kob can ndax du ca mën a ñàkk.

Nit bu xasee takk ab jigéen du mën a takk yaayu jigéen joo ju ak maamu jigéen ja ba ci aadama, sëy bii ñu firi yit da ciy dugg.

Ba tay li ñuy wax ni ku ñu may jigéen ba mu xës joteek moom doo tu mën a takk doomu jigééen joo ju, sëtam akub sëtaatam ba kero àddunay tukki, sëy bu yàqu bii yoon dindi noo nu lay mel, ni nga xamee yit ni ku xës takk jigéen sa baay mënëtukoo takk sa maam bu góor noo nu, bii yoon dindi tam noo nu lay mel.

Page 99: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

9 9

Su fekkee yit jigéen ja njëkkoon naa sëy ba ñu fase ko ca ñett i fase nga xam ni koo ka su ko bëggoon a jëlaat da fay nég ba sëy jaaraat fa, sëyam bii yoon dindi du tax jigéen ji dagan ci góor ga ko njëkkoon a yor ndax jëkkër ji fa war a jaaraat da fay aajewoo muy gu wér.

Sëyub joyal mënees na ko te mooy ñu fas sëy bi te waxu ñu ni can gi nàn-gam lay doon du tee maye ga wér waaye balaa góor gaa joteek soxna sa na ko leeralal ni nàngam laa lay jox ci can te loo la wér kon jigéen ja du sañ a bañ, bu dee da ni ko nàngam laa lay jox te loo la matul la ñuy jox ay moroomam kon jigéen jaay seet, bu nangoo mu baax, bu nanguwul ñu tàqarle léen lu dul ni daa wëlbëtiku nangu koo dolli ba soxna sa nangu kon mu baax.

ñaar ñuy sëy diy jullit ginnaaw ba kenn ca ñoom ñaar wëlbëtiku génn ci lis-laam kon da ñuy jàpp ni sëy ba tas na, muy ci fase mu wér ak bu ñu ko ca tud-dul, su wëlbëtikuwaatoon tuub ba ñu delluwaaat kon fase gu njëkk gi kenn du ko tuddaale da fay mel ni tay la ko mos a yor, ñett i fase mooy tax mu xaraam ko ba mu war a xaar geneen jëkkër, ñaar ñu nekkoon ay yéefér sëy ba mu yàgg ñu wëlbëtiku ñoom ñaar ñépp dugg ci lislaam kon da ñu léen di bàyyi ci sëy ba noo nu rekk, ba ñuy dindi mooy bu fekkee da ñoo jegee jege gog waru ñoo sëy, bu dee kenn ka daa tuub ka ca des nanguwul a tuub kon su boo baa sëy ba tas na, bu fekkee jigéen jee njëkk a tuub daa di tàmbalee iddawu laata idda jee jeex far jëkkër ja tuub da ñu ko koy far bàyyee, bu fekkee ni góor gi moo njëkk a dugg ci lislaam fekk soxna sa nekk ci diiney yahuud mbaa nasaraan te ab jullit sañ naa takk ku bokk ci yii ñaar, kon koo ku mën naa tëye soxna sa, bu soxna si dib maajuus mooy ku nekk ci diine ju bàyyeekoowul fa Yàlla te tuub ci ginnaaw góor ga te soreewul kon da ñu léen di bàyyi ñu nekk jëkkër ak jabar, bu tuub ga yéexee kon tàqarlikoo na ñu.

ab yéefér bu tuubee dugg ci lislaam te fekk la mu yoroon ciy soxna ëpp na ñent da ñu koy tànnloo ñent ya ko gënël, ña ca des mu wacc léen, bu dee ab jullit moo ame lu ëpp ñent i soxna ginnaaw ba mu bëgg koo tuub kon ñent ya njëkk rekkay baax ndax ya ca topp da ñuy jàpp ni fasu wu ñu.

Koo xam ni daa rëbbënteek soxnaam doo tu ko dagan mukk ci àdduna niki ku takk jigéen ci idda jote ca ak moom walla mu bàyyi ba idda ja jeex muu soog a joteek moom, da koy xaraam ba fàwwu.

Su boroom kër fasee soxnaam ñett i fase nga xam ni fàwwu jëkkër daf fay jaaraat mu door a mën a dellu ci moom, yaw nga ni naa fa jaar takk ko wacc ko ngir mu mën a dellu ca ku njëkk ka kon nga def lu xaraam te su ko yoon yëgee du tax ñu mën a dellu ndax kenn du ko waññiwaale waaye bu dee jigéen jaa

Page 100: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 0

fexe ba góor takk ko ginnaaw ba mu xulóok moom ngir bëgg mu fase ko ba mu dellu ci jëkkëram ju njëkk ja kon du aay, bu dee yit jëkkër ju njëkk jaa wax ak kenn ngir mu takk soxna sa waccaat ko ba mu mën cee jot tam du lu aay.

Ku armal aj walla umra ba kero muy yewwiku da fay xaraam ci moom mu maye soxna walla moom ci boppam ñu may ko soxna, ku tawat it tawat joo xam ni ragal na ñu ni da fay faatu du sañ a takk kenn ndax day mel ni da koo yéene ndono, su ko defoon it yoon firi ko, bu ko defoon joteek moom kon can di na ca am waaye su góor ga faatuwoon du ko donnu, ba tay noo nu la ñu aayee ku tawat tawatu faatu di fase ndax su boo baa da fay mel ni da koo yéenewul mu donnu ko kon yoon du ko nangu su waay ja faatuwoon it du ko tee donnu doonte tawat ja daa mujj yàgg ba soxna sa sëy ca ay yoon, du tee su waay ja faatoo fàwwu mu donnu ko.

Ku xës a fase soxnaam ñett i fase, mënoo koo takkaat lu dul ni jëkkër da fee jaar ba bàyyi ko.

fase ñett i yoon mën naa amee ci yor ko fase ko, jëlaat ko fase ko muy ñaar, jëlaat ko fase ko muy ñett, bu dee ci fiqu Imaam Maalik mën naa amee cib jotaay ci kaw góor ga ni ko fase naa la ñett i yoon, du lu ñu taamu ndax fasem biddaa la waaye teewul su ko defee mu daa di war fa saa sa.

fase du lu ñu taamu waaye soo demoon ba bëgg koo def soo yaboo sàmm saart yii ñu lay bëgg a wax te mooy mu fasee ko ci biir laab nga xam ni gisul dereetu wësin gisul it dereetu mbërëg goo xam ni jotewoo ca ak moom benn yoon, nga fase ko yit benn fase ndax benn bi doy na ndax bu idda ji jeexee te faylu woo ko doonatul sa soxna, boo ko fasee benn yoon boo ko fasewaatee beneen mu dal ndax benn fase daggul buumu sëy kon boo ko fasee benn yoon da nga ciy bañ a teg beneen ba kero idda jiy jeex.

Su fekkee daa fase soxnaam benn rekk walla ñaar nga xam ni àggul ci ñett giy tax buumu sëy gi dog, liféeg idda ji jeexul mën na koo fayle.

Ku ñu fase te mu toll ci gis dereet, ñett i dereet ñooy doon iddaam mooy bu fekkee da ñu koo fase ci laab kon da fay waññi laab goo gu, bu gisaatee dereet ba laab mu waññi ko muy ñaar i laab, bu gisaatee dereet ba laab muy ñett.

Ku fase soxnaam te idda ji jeexul mën na koo fayle, bu dee kuy gis dereet liféeg duggul ci mbërëgu ñetteel bi mën na koo fayle.

fayle mooy jëlaat naa saa soxna, amul lenn loo ca war a joxe, amul it kenn koo ca war a waxtaanal, soxna si tam sañul a bañ, ay mbokkam it noo nu.

Page 101: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 1

Bu fekkee soxna sa daa ndawe ba du gis dereet walla mu mage ba du gis dereet kon saa yoo ko fasee mu baax ndax iddaam du yokk du wàññeeku ñett i weer lay doon, koo ku liféeg ñett i weer yi di jeex mën na koo fayle nde-gam benn fase la mbaa ñaar, du sañ a bañ ay mbokkam it noo nu, niki noo nu ku ëmb waxtu wu ne mënees na ñu koo fase ndax iddaam du yokku du wàññeeku, bis bu amee doom ci la idda jiy jeex.

Ki toll ci gis dereet te ëmbul da ñuy saart boo ko dee fase mu nekk ci laab, xaraam na nga fase ko te mu nekk ci dereet, ku ko def sax dees na ko forse mu fayle soxna sa, ku fase soxnaam benn walla ñaar nga xam ni buumu sëy gi jeexul manees na koo fayle liféeg idda ja jeexul, su idda ja jeexee fàwwu ngeen jubóo nga soog koo mën a takkaat takk ju yees nga joxewaat can gu yees ñu mayaat la ko may gu yees.

Xaraam na ci góor muy fase soxnaam te muy gis dereetu mbërëg mbaa wësin, bu dee lu ñu mën a fayle sax yoon da ko koy forse, du tee yit fase ga tàbbi waaye yoon da koy forse fayle ga, da koy faylu tëye ko ba mu laab joteek moom ba mu gisaat dereet ba laabaat, su ko neexee fase ko bañ a joteek moom.

Ku ñu la may kese yem ci waaye jotagoo léen jote saa yoo ko bëggee fase mën nga ko du ñu ca saart darra naan bu tollee ci laab ak bu laabul ndax moom du iddawu, koo ka yit bu ñu ko fasee manees na ñu koo mayewaat fa saa sa waaye yit benn fase kepp bu fa jaaree mu dog ndax du am idda ba mu di ko fayle te moom du iddawu, du aajewoo tam jëkkër jaar fa mën na koo takkaat, bu dee da koo fase ñett i fase kon fàwwu jëkkër daf fay dox mu soog koo mën a takkaat.

Ki xamul benn fase mbaa ñaar mbaa ñett la, wax ji gën a wóor mooy da ñu koy jàppee benn fase nga xam ni su idda ji jeexul mën na koo fayle su jeexee yit mën na koo takkaat.

Summikoo mooy jigéen ji doyal ci sëy bi ba mu jaral ko joxe alal, koo ku la muy joxe mën naa tollook la ñu ko joxoon mën na koo ëpp mën na koo yées, di na ñu ko leeral ci kanam insaa allaa.

Bu fekkee góor gi tooñu ko defu ko darra tam li ñu koy jox dagan na, su ko defee su jigéen ji xasee joxe alal su ko góor gi waxee fase naa la walla mu ñàkk ko koo wax it du tee mu tàbbi te fayle du ca mën a am du tee tam bu idda ji jeexee bu ñu jubóowaatee mën a sëy, ku wax soxnaam fase naa la fase mu dog, yoon da fay jàpp ni ñett i fase la moo xam jote na ñu am déet, ku wax sa

Page 102: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 2

soxna soo xam ni mos ngeen a wéet aji set nga ci jëkkër walla aji wéet nga ci jëkkër walla aji xaraam nga ci sa jëkkër walla nga ni ko fu la neex jëmël yoon ñett i fase la koy jàppee, bu fekkee may kese moo doxoon seen diggënte jotee gu ñu darra dees na ko may mu wax lu mu ci jublu, benn fase walla ñaar walla ñett.

Jigéen bu ñu ko mayee jëkkër, jëkkër ja jékki-jékki daa di koy bàyyi te jote wu ñu darra kon war na koo jox genwàllu can ga ñu waxantewoon walla ga yoon digle muy lu mat a xam, bu ko ko baalee mën na koo bañ a joxe, bu dee gone walla muy jeeg boo xam ni mënul a yor mbiram kon baayam ba ko mayewoon kepp mooy mën a baale genwàllu can gi walla déet.

Sopp na ñu soo fasee sa soxna nga am alal joo ko jox ci sa teeyug bakkan muy la nga mën ngir mu nekk yobbël ci moom, du lu war tam, bu dee ku ñu ko may doŋŋ yem ci nga xam ni joteegul ak moom darra te fekk mu waxaloon ko ab can, koo ku yoon da ni da koy jox genwàllu can ga, bu ko joxee genwàllu can kepp mu doy yobbël. aji summikoo nga xam ni mooy jigéen ji doyal ci sëy bi ba nangoo joxe alal, deesu ko yobbëlal.

Ku ñu may soxna te jotagul a joteek moom mu faatu moom jëkkër ji, bu fekkee jotul a wax soxna sa can sàngam laa lay jox, kon soxna sa da fay donnu kese yem ci te deesu ko jox can, bu fekkee jigéen ji laata jëkkër jee faatu wéet na ñu ba jote ñàkk gaa waxub can moo ca am, kon da ñuy seet luy canu ay moroomam, ñu génnee ko jox ko ko te du ko teree donnu ndax jote ga da fay waral can, bu fekkee digewoon na ñu ci ni nàngam la ñu koy jox kon su boo baa la ñu digewoon kepp la ñu koy jox te du ko teree donnu.

Góor bu ñu ko mayee soxna nëbbaaleel ko sikk soo xam ni ñoom ñi ko maye xamoon na ñu ko niki mu dof walla mu gaana walla siti walla jàngoro ci awraam, koo ku saa su ko yëgee ginnaaw bu ñu wéetee walla mu xam ko te wéetagu ñu kon di na sañ a génn ca sëy ba, bu fekkee jotu ñoo jote kon ku ne day dem yoonam, bu fekkee daa joteek moom ba noppi door a xam sikk soo su, yoon may na ko mu génn ca sëy ba waaye ginnaaw xës naa joteek moom fàwwu mu jox ko ab can waaye bu ko ko joxee ba noppi da fay dem ca baay ba ko mayoon soxna sa mu delloo ko canam, ba tay bu dee càmmiñam bu góor moo ko mayewoon. Su fekkee ka mayewoon soxna sa yoon moo ko may mu maye rekk mu maye ko waaye du ku jege soxna sa bay xam sikkam niki koo xam ni seen ñaar i baay ñoo bokk, deesu ko fayloo can ga ndax amaana yë-gutoon sikk sa, jigéen ja yit gën jaa néew can la ñu koy jox muy rub’u diinaar.

Koo xam ni daa tële ci joteek soxnaam dees na ko yéexee at ba xam, bu ca

Page 103: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 3

joteek moom kon darra du ca am ndax la ñu bëggoon am na, bu at ma matee te jotewu ca ak moom kon jigéen ja mooy seet bu nangoo sëy ak moom ci noo na kon sëy ba wéy yoon du ca wax darra, bu fekkee neexu ko kon yoon da koy dindi, bu xësee joteek moom benn yoon ginnaaw ba mu tële beneen àtte lay doon ndax deesu ko téqaleek jigéen ja lu dul ni bu fekkee téqale wu ñu léen jigéen ja di na moy Yàlla.

Bu fekkee jigéen ji jëkkëram daa dem te xamu ñu fu mu nekk kon su boo baa da koy wax àttekat bi mu def la mu mën ci gëstu ko ba xam di na feeñ, bu ñu ko gëstoo feeñul di na àppal jigéen ja ñent i at tàmbalee ci bis boo bee nga xam ni ci la gëstu ga jeex ndegam jëkkër ja bàyyi na fa lu mu mën a dundee, su ñent i at ya matee te jëkkër ji ñëwul, mu wax ko mu iddawu niki ku jëkkëram faatu, bu idda ja jeexee mu mën a utiwaat jeneen jëkkër waaye du tax ñu àtte ci yoon ni jëkkër ja faatu na, da ñuy bàyyi diir boo xam ni dundug jullit du ko faral di ëpp, bu ñu gisee ni mat na ñu door a àtte ni faatu na door koo miiraas, bari na ñu wax juróom ñaar fukk i at niki bi muy dem daa am fanweer i at da ñuy bàyyi ba mu mat ñéenfukk i at ñu door a àtte ni faatu na.

Labat jigéen ju nekk ci idda xaraam na te mooy wax ko ni da ma laa bëgg a takk, maye na ñu nga wax ak moom waxin wuy wone ni am nga ci moom ag bëgg niki nga ni ko xam naa ni ñu bari taamu na ñu la ci soxna walla nga ni ko yaw daal soxna si xam naa ni ku njëkk ci yaw sant waaye jaar ca digg ba moom daa xaraam.

Koo xam ni daa am soxna su yees te mu fekk fa kenn mbaa lu ko ëpp, balaa tàmbalee yemale da fay sax ak ku yees ki ndegam gone la juróom ñaar i fan guddeek bëccëg door a tàmbalee yemale ay gi, su fekkee soxna su yees si jeeg la du gone kon ñett i fan lay doon.

Gone gu góor sañul a fase soxnaam ka ko yor di ko defal ak a dindil moo koy faseel.

Sa soxna boo ko nee fase man la ko Yàlla joxoon waaye moomloo naa la ko walla nga ni ko tànnal benn nga toog di sama soxna walla nga dem ñu tàggoo, lu mu ca wax rekk la ñu cay àtte niki su waxoon ni fase naa sama bopp ñett i yoon kon mu dog, su waxee moom soxna sa fase yu ëpp benn sañ nga caa weddanteek moom ngir xamal ko ni benn fasee taxoon nga moomloo ko fase ga.

Soxna si ñu tànnloo toog mbaa mu dem lay tax tànn ga baax mooy mu wax ni fase naa sama bopp ñett i yoon ndax loo looy jeexal buumug sëy ga, bu ko

Page 104: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 4

yéesee rekk buumug sëy ga du jeex te bu ko xësee ba wax doo mën a wed-danteek moom naa ko benn moo taxoon ma wax.

Ku giñ ni saa soxna du ma joteek moom diirub ñent i weer mbaa lu ko yées, kenn du ca wax darra, bu ko ëppee da ñuy bàyyi ba ñent i weer ya mat ñu ni ko diir bañ la mayoon jeex na, bu delluwul ginnaaw yoon daa di fase soxna sa.

Ku wax soxnaam xaraam nga ma niki sama ginnaawal yaay, doo sañ a jo-teek moom lu dul ginnaaw boo defee benn ci alamaan yii, bi ci njëkk mooy nga goreel jaam te mu nekk jullit te bañ a am sikk maanaam nga xam ni sa jaam la te bokkoo ko ak kenn, du laal it darra cig ngor, bu ko mënul kon da fay woor ñaar i weer yu sësëloo, bu ko tëlee kon da fay leel juróom benn fukk i miskiin, miskiin bu ne mu joxko ab kilo ndax ñaar i mudd mënees na koo jàppeeb kilo, du sañ a joteek soxna sa ndare bu kaffaara ga matee, bu joteek soxna sa te kaffaara ga tàmbalee gu ko kon su boo baa da koy tuub, bu fekkee daa tànnoon kaffaaraa woor ñaar i weer walla leel juróom benn fukk i miskiin, mu tàmbali ko laata moo mat mu joteek soxna sa kon la mu defoon lépp da fay yàqu da koy tàmbaliwaat, bu wooroon ba mu des benn fan joteek soxna sa kon la mu wooroon lépp da fay yàqu da koy tàmbaliwaat, su fekkee daa tàmbaliwoon jox miskiin ya ñam ba mu des benn mu joteek soxna sa kon da koy tàmbaliwaat, ñam jotoon a jox da fay yàqu kenn du léen limaale.

rëbbënte li koy waral mooy ñaar ñuy sëy ba mu yàgg jigéen ja ëmb góor ga ni juru ma ko, ñu laaj ko mu wax ni da koo wóorlu ba xam ni ëmbul te gin-naaw ba jotewul ak moom, ni mu koy wóorloo mooy mu gis dereet te jotewul ak moom ginnaaw ba walla mu amoon doom te jotewul ak moom ginnaaw ba, beneen ba mooy góor ga wax ni daa gis soxna sa ci bëtug boppam muy njaalóo nga xam ni gis na sawukaayu góor ga di dugg ci sawukaayu jigéen ja, soxna sa weddi ko ni amul, loo lu yit da fay indi rëbbënte, mooy waatanteji.

Bu fekkee góor ga daa xas soxna sa ni da fay dox tanku caaxaan, ku jubadi la kon li ëpp ci boroom xam-xam yi nee na ñu du jar waatante ci kanam yoon, du tax ñuy dóor góor ga.

Bu góor gi tuumaalee soxnaam mu weddi ko bañ ñëw ci kanam yoon ba kenn ku ne waat ba wàcc nga xam ni sunu Boroom kepp moo xam ka wax dëgg, kon ñu tàggoo fàwwu ci àduuna doo tu ñu sëyëti mukk.

Jëkkër ji kalaame mooy njëkk a waat, bu fekkee ngir weddi ëmb ba la da fay wax ni ach’hadu billaahi maa haazaal xamlu minnii, seede naa ci Yàlla ni ëmb bii juru ma ko ba muy ñent i yoon, bu fekkee da koo gis muy njaalóo da

Page 105: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 5

fay wax ni ach’hadu billaahi lara’aytuhaa taznii, juróomeelal ko ci wax ni lii ma wax nii bu dul dëgg Yal na rëbbub Yàlla dal sama kaw, su ko defee jigéen ja waat waatug miim ñent i yoon ach’hadu billaahi anna haazal xamla min-hu, seede naa ci Yàlla ni ëmb bii ci moom la bàyyeekoo wax ko ba muy ñent i yoon, su fekkee góor ga daa wax ni gis naa ko muy njaalóo, jigéen ja buy miim da fay wax ni ach’hadu billaahi maa ra’aanii aznii, seede naa ci Yàlla ni gisu ma may njaalóo mukk, wax ko ba muy ñent i yoon, mu juróomeelee ni su fek-kee waxu ma dëgg Yal na merum Yàlla daanu ci man.

Su fekkee jigéen ja daa ragal a waat kon di na doy tektal ni góor ga wax na dëgg, kon jigéen ja bu dee gor te fekk mu sange da ñu koy ray, su fekkee sangewutoon mooy bu sëyutoon sëy bu baax walla jotaguloon a joteek jëk-këram, kon da ñu koy dóor téeméer i yar.

Su dee jigéen ja nangu naa waat, góor ga moo ñemewul a waat, la muy tekki mooy waxal na soxnaam lu amul, da ñu koy caw juróom ñett fukk i yar ba noppi ne ko doom ji yaa ko jur.

Jigéen su fekkee daa dawee ca sëyam te jëkkër ja loru ko defu ko darra kon di na mën a jot boppam ci delloo jëkkër ja la mu ko joxoon ci can, bu neexee jëkkër ja lu yées loo la sax di na baax, bu ñu jubóo ci lu ëpp loo la sax di na baax.

Bu fekkee jigéen ja daa bëgg a jot boppam ci tas sëy bi te bi ñu ko gëstoo mu sax ni jëkkër jaa ko doon lor, da ñu koy delloo alal ja ba noppi du tee moom na boppam.

Summikoo fu mu fi amee nga xam ni jigéen joxe na alal ngir ñu may ko baatam doonte góor ga waxu ko may naa la sa baat it yoon da fay jàpp ni jëkkëram fase na ko benn fase boo xam ni amul fayle, bu idda ji jeexee te ñu jubóowaat du tee mën na koo takkaat.

Xeetu kaffaara yi, ni gor di def la ab jaam di def ñoo yem ci goo ga wàll, bu dee xeetu gétën yi, la gor gay am, genwàll ga la jaam bay am niki bu dee ci gétënug njaalóo gor ga téeméer i yar lay am, jaam xaaj ba lay am muy juróom fukk, xaste yit te mooy waxal nit tanku caaxaan muy njaalóo te wérul, bu ko gor defee da ñu koy caw juróom ñett fukk i yar, bu dee jaam genwàll ga la ñu koy caw muy ñéenfukk.

Jamono ji nga xam ni ci la xale biy toll ci nàmp muy ñaar i at yu njëkk ya, su ko jeneen jigéen nàmpalee ju dul yaayam doonte am muucu la du tee mu mel ni yaayam, lépp lu ag nàmp di xaraamal nàmp goo gu di na ko xaraamal.

Page 106: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 6

Su fekkee ñaar i at yi mat na ginnaaw ba bu ko jigéen ju dul yaay ja nàm-palee du xaraamal darra lu dul bu soreewul ak ñaar i at ya niki ñaar i weer ya ca topp bu ko ca nàmpalee kon xaraamal ga di na tàbbi, bu fekkee tam xale ba amagul ñaar i at waaye mën naa lekk mën a naan ba dootul aaje nàmpal, yoo yu jamono yit ku ko ca nàmpal du xaraamal darra.

Toqal sa soow ci gémmiñu gone ga mook nàmp ga ñoo yem àtte ak mbarxan mooy awale soow ma ci pax i bakkan yi du tee ñu xaraamal.

Jigéen bu nàmpalee xale bu góor kon da fay mel ni mooy yaayam bu wér a wér, du mën a doon soxnaam ak bépp doom bu jigéen ju jigéen joo ja nàmpal, ba tay jëkkëram ja doom bu jigéen bu mu am doonte soxna sa juru ko da fay mel ni yéen a bokk ndey ak baay doo ca mën a takk kenn, moo xam lu jiitu nàmpal ga la walla lu ko mujj ca la ñu juddu, yaw mi ñu nàmpal rekk yaa sañul a takk ay doomam waaye ki bokk ak yaw ndey ak baay mën naa ñëw takk ci doomam yoo ya.

Idda, dund ak laablu

Jigéen ju jëkkëram fase bu dee kuy gis dereet idda ja da fay tollook ñett i laab, bu ñu ko fasee ci laab da koy waññiwaale, bu gisaatee mbërëg ba laab muy ñaar, bu gisaatee mbërëg ba laab muy ñett, bu xasee nekk gor du ñu xool ba xam daa bokk ci diiney yahuud walla nasaraan idda ja noo nu lay toll.

Ki ñu fase bu ndawee ba du gis dereet walla mu mage ba weesu koo gis ñett i weer mooy iddaam.

Bu fekkee gor su jigéen si walla jaam bu jigéen bi da ñu koo fase te mu ame dereetu jàngoro nga xam ni dereet jiy génn ci moom mënu koo xàmmeek dereet dëgg-dëgg, koo ku iddaam fàwwu mu yàgg ndax da fay toog juróom ñent i weer ngir laablu, bu ko toogee gisul darra mu door a toog ñent i weer muy iddaam.

Ku ëmb moo xam da ñu koo fase walla jëkkëram moo faatu, saa bu amee doom iddaam jeex, muy gor muy jaam muy yahuud walla nasaraan ñoo yem, nga xam ni mën naa gàtt mën naa yàgg.

Bu fekkee da ñu koo may góor ga jotul a joteek moom, góor ga fase ko, jigéen joo ju idda waru ko mën naa daa di sëyiwaat fa saa sa.

Bu fekkee soxna sa gor la, jëkkëram faatu te fekk ëmbul kon idda ja ñent i weer ak fukk i fan lay doon, loo la du ñu ci seet ba xam mag la walla gone walla ba xam jëkkër ja wéet na ak moom am déet walla muy yahuud mbaa na-

Page 107: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 7

saraan doonte da ñu ko koo may rekk jëkkër ja faatu du tee idda joo ju war ko.

Bu ko wóorul it ba xam ëmb na am déet moom jigéen ji nekk ci idda kon da fay toog ba sikki-sàkka sa jeex muy door a sëyiwaat, la muy wóorloo mooy mu dem ba mu yàgg mu gis dereet walla mu toog lu mat juroom ñent i weer, buy yëg ca biiram lu mu xamul lu mu doon su boo baa na mu koy wóorloo mooy da fay dem ba mu am juróom i at.

Jigéen jiy iddawu ngir jëkkëram ju faatu, ñent i weer ak fukk i fan lay doon bu dee gor, bu dee jaam muy ñaar i weer ak juroom i fan, da ñu wax ni bis bi jëkkër ji faatu da koy waññiwaale doonte boo ba fekk na tàkkusaan jot.

Jigéen ji ñu ne bu ëmbee bu amee doom idda ja jeex da fay fekk muy ëmb bu tege ci yoon waaye bu fekkee ka ko ëmbël tegu ko ci yoon, jeexug ëmb ba du tax idda ja jeex ndax di na xaaraat ba gis yeneen ñett i laab door a mën a wutiwaat jëkkër.

Ku jëkkëram faatu da ñuy bëgg mu sàmm ormay jëkkër ja, lu jëm ci waaj-taayu àdduna yépp mu moytu ko ba kero idda jiy jeex niki takk xeetu takkaay yi walla tusngalu ak mbooleem yëre yu rafet yi ñuy waajee mooy ténj, lay yi ñuy teg ak paaka walla sàkkal ko bis bu muy fóot ak bu muy sangu aaday wo-lof la waaye jotewul darra ak lislaam.

Sàng gi muy sàng yaramam noo na la waroon a mel ba jëkkër jay dund darra waru ci woon a soppeeku, du sañ a laal lépp lu am xet gu neex, du sañ a fuddënu ak gépp diw gu xet ga neex, du sañ a defar boppam.

Ténj gi (ñaawlu) ñépp la ñu koy sant muy gor, jaam, ndaw walla mag doonte jëkkër ja jotul a joteek moom, bu dee jigéen ja da fay yahuud mbaa nasaraan te jëkkër ja di jullit wax ja gën a wóor mooy dees na ko digël ténj, idda ja moom mënul a ñàkk.

Jigéen ju jëkkëram fase moom du aajewoo ténj (ñaawlu).

Képp ku ñu fase te fekk mos ngeen a jote, diirub idda ji ca dëkkuwaay ba ñu dëkkoon fa la war a toog, moom du sañ a génn, jëkkër ja yit sañu koo génnee, fii ci aaday wolof miin na ñu ku ñu fase rekk mu dem sempiji néeg ba waaye nii ñu waxee la war a demee, lay tax moom jigéen ji mu moom dëkkuwaay ba mooy ba ñuy takk la ñu ci saartal ni di na ko wutël kër.

Ku ñu fase benn fase mbaa ñaar, jëkkëram joo ju la dundam ak koddaayam di war ba idda ja jeex ndax buumu sëy gi daggagul, sañul a joteek moom te fayle wu ko, bu fekkee da koo fase ñett i fase te ëmbul kon dund ba ak koddaay

Page 108: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 8

ga waratu ko ndax fàwwu jëkkër da fay jaaraat, bu fekkee daa fase soxna sa te fekk mu ëmb doonte ñett i fase la moo ko war a wodd moo ko war a dundël.

aji summikoo te mooy jigéen ji doyal ci jëkkëram ba joxe alal ngir ñu may ko baatam, dund ga ak wodd ga du la war, jigéen ji nga rëbbënteel ba yoon tàggale léen fàwwu, koo ka diir ba muy iddawu doo ko ca dundal doonte daa ëmb ndax waat nga weddi ko ci kanam yoon.

Jigéen ju jëkkër ja faatu muy iddawu deesu ko jox ab dund ca la jëkkër ja bàyyi, su fekkee daa yëgutoon faatu ga jël ca alal ja di dundee bis bu ñu ko yëgee da fay fay la mu jot a dundee lépp walla ñu génnee ko ci wàllam ci miiraas mi.

Diir ba muy iddawu mën naa toog fa mu dëkkoon ba kero muy jeex, kay jënd kër ga yit bala koo sañ a moom fàwwu idda ja daa jeex, bu dee jëkkër ja moo-mul néeg ba walla kër ga te fayoon na luyaas ba kon diirub la mu fayoon mën na faa toog iddawu kenn du ko sañ a génnee, du sañ a génn génnug tuxu ci lu dul ngant niki bariy sàcc walla tabax ba daanu ak yu ni mel bu dul loo lu kër ga ko jëkkër ja fasee walla bu dee daa faatu fa la war a toog ba idda ja jeex ndare boroom kër ga léen luyewoon da koo génnee ba noppi bañ fayug luyaasu diirub idda ja kon na génn fa muy njëkk a ne lay toog iddawoo fa ba mu jeex waaye du fa sañ a tuxoowaat di jàll feneen liféeg amu fa ngant lu koy tax a génn.

Jigéen bu amee doom ci buumu sëy moo ko war a nàmpal te kenn waru ko caa fay darra ndare daa bokk ci askan boo xam ni da ñoo tedd ba du ñu nàmpalal seen bopp niki waa qurays.

Jigéen bu ñu ko xasee fase nàmpal ga waratu ko, bu dee fase bu amatul fayle te idda ji jeex, su boo baa mën naa jox keneen muy nàmpal te jëkkër ja di ko fay, bu ko neexee tam muy nàmpal te jëkkër ja di ko fay.

Yor xale bi ak toppatoo ko moom jigéen ji moo am sañ-sañ ba du tee dund bi ak koddaay ga baay ba lay war, bu dee xale bu góor ba kero muy kàllafe, bu dee jigéen ba kero muy am boroom kër ñu jébbël ko jëkkëram wuuteek aaday wolof lool ndax bari na foo gisee ku tàggook soxnaam daa di nangu doom ya xanaa saartantewoon ak moom ni da may tëye samay doom.

Bu fekkee ndey joo ju yoroon xale ba daa faatu walla mu sëyaat sëy gu yees, su boo baa xale ba da ñu koy jox maamam ju jigéen ji jur yaayam, su amee gàllankoor ñu seet ndey ju ndaw ji bokk ak ndeyu xale bi ndey ak baay, teg ca ndey ju ndaw ji bokk ak ndeyu xale bi ndey doŋŋ mujjee ka bokk ak moom baay doŋŋ.

Page 109: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 0 9

Bu fekkee ña ko gën a jege ci wàllu ndey gisu ñu ca kenn kon soo yaboo ñu seet ay mbokkam yu jigéen, da ñuy seet ka bokk ak baay ba ndey ak baay teg ca ka bokk ak baay ba ndey doŋŋ mujjee ka bokk ak baay ba baay doŋŋ, bu amul ñu seet maam ju ndawu xale bi te mooy ki bokk ak maamam ji jur yaayam, bu koo ka amul ñu seet maamam ju jigéen ji jur baayam, bu koo ka jàllee ñu teg ca baayam ci boppam du tee tam góor su waree yor xale fàwwu ñu seet ba xam ànd na ak jigéen ju mën a yor xale ba muy soxnaam walla ke-neen ndax daa am yor goo xam ni jigéen rekk moo ko mën, su baay jàllee nga teg ca mbokk mu jigéen, ñett la waaye da ngay jiitël bi bokk ak xale bi ñu war a yor ndey ak baay, bu fa nekkul ñu seet ki bokk moom ndey doŋŋ, bu fa nekkul ñu seet ki bokk ak moom baay doŋŋ mooy mujj, bu mbokk mu jigéen amul ñu ñëw ci bàjjan da ngay jiitël bi bokk ak baayu xale bi ndey ak baay, teg ca ba bokk ak baay ba ndey doŋŋ, teg ca ba bokk ak baay ba baay doŋŋ, su bàjjan amul ñu seet ba xam am na doom ju jigéen ju mbokk mu jigéen, bu amul nga teg ca doom bu jigéenu mbokk mu góor, bu jàllee nga teg ca ku ñu dénk xale ba te baay ba féetële ko ko walla àttekat ba, bu jàllee nga seet mbokk mu góor da ngay jiitël ba bokk ak moom ndey ak baay teg ca ba bokk ak moom ndey doŋŋ teg ca ba bokk ak moom baay doŋŋ, su wéyee nga teg ca maam bu góor, su amul nga indi doomu mbokk mu góor, su amul nga indi doomu maam ju góor mooy baay bu ndaw, su amul nga indi doom ju góoru baay bu ndaw, maam ju góor ji jur ndeyam soog a dikk, moom moo mujj ci tegale bi.

ñi nga war a dundël ci yoon, ka ca jiitu mooy sa soxna doonte moo la ëpple, soo amee alal te sa ndey ak sa baay ñàkk kon yaa léen war a dundël, bu ñu nee dund bi koddaay gi ci la ak dëkkuwaay bi, boo ñàkkee ni ñoom yoon da lay forse ni la da ngaa war a ligéey yor léen, bu dee ay doom yu bari kenn ku ne da fay def la ko ca war, sa doom su amul alal yaa ko war a dundël, su amee alal mën ngaa jël ca alalam ja di ko ci defal te tëye sa alalu bopp.

Bu dee góor yaa koy dundël ba kero muy kàllafe te amul ag lompoñ (laa-go), su doom demee ba mënal boppam da ñu koy tànnloo, su bëggee nekk ak yaw ngeen di dimbëlante su bëggee beru tam da nga koy bàyyi mu beru, bu dee jigéen yaa ko war a dundël ba kero ñu koy may jëkkër ba jébbël ko ko, ñii rekk la yoon warlul seenug dund ci yaw, ku bokkul ak ñoom boo ko dundëlee sa coobare la waaye waru la niki sa mbokk mu jigéen walla bu góor walla sa maam, sa sët ba ci sa jarbaat ak yu demee noo nu.

Bu ko sa wërsëg matee, wutël sa soxna ku koy ligéeyël nga def ko baax na waaye boo ko mënul kenn du la ca forse.

Page 110: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 0

Wuute na ñu ci càngaayal soxna si, réew mi moom aadawoo na ñu bu ji-géen ji faatoo yaw miy jëkkëram yaa koy wutël càngaay waaye li ci yoon wax da ñu cee wuute, Ibn Xaasim daa wax ni su soxna sa amee alal ca la ñuy wut càngaay la ak la ñu koy toppatoowee yépp, jëkkër ja darra waru ko ca, wax jii moo gën a doy a sukkandikoo, ku ñuy wax Abdul Maalik nee na jëkkër ja la war, Sahnun moom daf ni su fekkee jigéen ja am na alal kon ca alalu boppam joo ju la ñu koy jëndël càngaay toppatoo ko ca, bu ñàkkee jëkkër ja moo ko war a sàng toppatoo ko ci alalam.

àttey jote diggënte góor ak jigéen te waruloon seen diggënte

Joteg góor ak jigéen ci sawukaay te warul ci seen diggënte, mën naa am góor ga daa jaawale jigéen ji ak soxnaam bariwul lu muy am nag, la gën a bari mooy joteg njaalóo ba tay mën naa am góor ga noot ko ba joteek moom, su boo baa njaalóo la ca góor ga waaye du njaalóo ci jigéen ja.

Saa bu góor joteek jigéen ju mu takkul, àtte ba mooy jigéen ja da ñu koy laablu nga xam ni bu amoon jëkkër, jëkkër ja du joteek moom darra ba kero muy laablu ba noppi, bu ko amuloon kenn du ko sañ a takk ba kero laablu ga di mat.

Laablu gi mooy da ñuy xool ba xam jote gu aay gi ëmbee na ci am déet.

Bu dee ku ndawe ba du gis dereet mbaa mu mage ba gisatu ko, laablu ga ñett i weer lay doon.

Bu dee di na gis dereet te ba muy set ëmbul kon laablu ga day doon ag gisam dereet ñett i yoon, gis dereet laab muy benn, gisaat dereet laab muy ñaar, gisaat dereet laab muy ñett ba laabug ñetteel goo gu jeex ba dereet topp ca laablu ga soog a jeex.

Bu ëmbee ca jote ba da fay toog ginnaaw bu ëmb ba juddoo ba gis dereet ñett i yoon doonte jigéen juy nàmpal gis dereet da koy jafe fàwwu mu toog ba gis ñett i dereet lu mu yàgg-yàgg bala koo kenn mën a takk walla jëkkër jay mën a ñëwaat ci moom.

Jamono ji jigéen ji nekkee ci laablu goo gu, kenn du ko ca sañ a takk, ku ko takk ca yoo ya jamono te fekk ci takk rekk la yem ak moom, kon bu laablu ga jeexee moo xam ka amoon ak moom ëmb ba la walla keneen, jëmmi fas ga fa amoon rekk du yàq darra.

Bu dee daa fekk jigéen ja ci ag laablu takk ko joteek moom amaana sax xa-mukowoon soxna sa da koy xaraam fàwwu, bu dee ka defoon ak moom moy

Page 111: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 1

Yàlla ga moo ko takk ci jamonoy laablu ga nga xam ni warukowoon a takk, bu ko ca takkee joteek moom tam du ko xaraam fàwwu, soxna sa da fay tàmba-liwaat laablu gu yees, bu jeexee te mu bëgg ko ñu mën ko koo may.

Jigéen buy iddawu iddag faatu walla fase, bu jàmbur dikkee takk ko joteek moom da koy xaraam fàwwu waaye bu dee mayug kese te jote amu ca du tax mu xaraam ko fàwwu, bu idda ja jeexee rekk mën na ñu ko koo mayaat.

ag moy bu mosee dox ci diggënte góor ak jigéen deesu jékki-jékki maye léen te laablu doxul ci diggënte bi.

Ku takk jigéen joo joteeloon ba noppi ginnaaw ba ngay soog a yëg ni ag laablu doxu fa woon kon da nga koy beru ba laablu gi ñu wax ci ginnaaw mat ñu soog ko koo may mu joxewaat can gu yees.

Bu dee yaw yaa ko mayewoon te laablu ga amuloon kon da ngay leeral ka nga ko mayoon ni laablu daa amuloon kon na beru soxna sa ba laablu ga mat, ñu soog ko koo may, bu dee ci diir boo bu góor ga mën naa bañ a joteek soxna sa kon mën naa toog ca kër ga ñu rafetal ko ba laablu gi jeex mu joxewaat can, ñu may ko ko may gu yees.

Lay tax sa doomu jiitle mën a sëy ak kenn ci sa njaboot mooy ba muy ñëw fekk mu fer, bu fekkee muy nàmp kon jote gi nga joteek yaayam am soow da cay amee te su boo baa yoon day jàppee koo ka sa doom la kon kenn ci sa njaboot du mën a sëy ak moom.

àttey dereet yi ak gétën yi

Yoon da fa saxal ni ku ray nit te saart ya daje ca ñu fayu ci yaw na nga ko rayee, lay tax mu sax mooy da fay am ñaar ñu maanu ñu seede ni diw mii moo ray diw walla moom mi ray mu waxal ko boppam ci sago, ba ca des mooy ngiñ.

Su tuumag ray taqee kenn kon su aajewoo waat (ngiñ) ñoom ñiy mbokk i ki ñu ray ñooy waat juróom fukk i ngiñ boole ko ak tuumaal ki ñu jiiñ ray ga, ñuy soog a ray koo ka.

Ka nga xam ni moom la ñu ray te tuuma ji am ku mu taq waaye saxul, su aajewoo waat te fekk ka ko def moo ko tay kon ñay waat juróom fukk i ngiñ yi lu mu néew-néew na mat ñaar i góor, kenn rekk du ko mën, jigéen it du ko mën a giñ.

Su dee tuuma ja mbooloo la taq niki mbooloo tiim nit di ko dóor ba mu faatu te mënu ñu ni diw mii moo ko ca ray kon ay mbokkam da ñuy waat juróom fukk i ngiñ, ñu daa di tànn kenn ca mbooloo ma ñu rayal léen ko mu

Page 112: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 2

doon seenug fayu waaye du mbooloo mépp la ñuy ray.

Bu mbooloo sëqëtoowee kenn dóor ko ba mu faatu te fekk du lu ñu tak-ktoowoon kon su aajewoo waat, su boo baa ay mbokkam da ñuy jàpp kenn ni moom la, daa di waat juróom fukk i ngiñ ya ca koo ku, ñu rayal léen ko, ña des ca mbooloo ma kenn ku ne ñu dóor la téeméer i yar.

Tuuma yi nga xam ni ñooy taqal nit te mbokk i ka ñu ray war a waat boole ca, bokk na ca su dee waay ja njëkk muy faatu da ñu koo laaj ku la def lii mu ne diw, diw tam weddi ni defu ko, su amul lenn lu mën a saxal tuuma gi, mbokk i waay ji faatu ñooy waat juróom fukk i ngiñ boolekook tuuma ji taq koo ka, su ko defee yoon daa di fayu ca koo ka, bokk na ca yit bu kenn ku maanu seedee ni diw mii moo ray diw, bokk na ca tam bu amee ñaar i seede yu maanu yu seede ni diw mii moo jam diw te ginnaaw ba waay ji ñu jam dundaat na fi dund gu wér maanaam faatuwul fa saa sa, su boo baa di na aaje juróom fukk i ngiñ yi.

Su fekkee da ñoo wax mbokk i ki ñu ray ni léen tuuma taq na kii te fàwwu ngeen waat juróom fukk i ngiñ boole ci tuuma jiy soog a sax, ñoo ñu ragal a waat kon da ñuy wax ki ñu tuumaal ni ko yaa ray waatal juróom fukk i ngiñ setal sa bopp, bu ko waatee daa di set, su dee daa wax ni na ko ay mbokkam waatle te mbokk ya ñime wu ñu koo waatle ngir mën naa am ag dëngëm, kon moom ci boppam su yaboo mu waat juróom fukk yépp, ñu soog koo bàyyi.

Su fekkoon ni tuumay ray gi daa tege ci mbooloo waaye aajee na ngiñ ngir saxal ko te mbokk i ki ñu ray ñime wu ñoo waat kon mbooloo mi ñu jiiñ ray gi kenn ku ne da fay waat juróom fukk i ngiñ ngir setal boppam.

Bu tuuma taqee kenn kon mbokk i ki ñu ray da ñuy waat juróom fukk i ngiñ saxalee ko tuuma ji ngir ñu fayul léen ci koo ku, su mbokk ya yaatoo ba ñu mën a am juróom fukk i góor kenn ku ne waat benn, kon juróom fukk i góor ñooy taxaw kenn ku ne ci ñoom waat benn mu mat, bu ko matul da ñuy séddële ngiñ ya na góor ya toll ba mu mat.

Jigéen du waat ci dereetu tay ju aajewoo ngiñ.

Bu fekkee ni ki ray da koo tayul, bu aajewoo waat jigéen ak góor yépp mën na ñu caa waat te bu ñu dee seet kenn ku ne da ñuy seet bu ñu dee miiraas loo war a am nga waat lu toll noo nu, boo léen doon séddële juróom fukk i ngiñ yi nga àgg ci ngiñ goo xam ni ku ne da caa war a laal te benn ngiñ mënee-su koo séddoo kon bu doon miiraas ka ca war a ëpple mooy waat benn ngiñ boo bee.

Page 113: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 3

Bu fekkee mbir ma ka ko def tayu ko waaye aajewoo na waat ndax da fa saxul, ñii ni tay na ko ñii ni tayu ko kon da ñuy wax ña fa teew ni léen waat léen juróom fukk yépp mu mat, ñoom ñi fa teew bu ñu waatee juróom fukk yépp du tee ku ñëwaat ginnaaw ga te bokk ci wëy donnu yi te boo teewoon am lim boo ca waat kon fàwwu nga waat ko.

Ku war a waat da fay taxaw ngir boo ragalee darra nga dellu ca ginnaaw, bu ñu dëkkee ci barab bu jege fu sell di na aajee ñu indi léen ba ca booru barab yu sell yoo ya ba noppi ñuy door a waat, li ñu ciy jublu mooy ñàngal mbir ma ba ku am lenn looy ragal nga dellu ginnaaw, bu foo fa amee ay barab yu ñu fonk di ko màggal fa la ñuy waatijee ci kaw mu bañ a sori.

Bu dee benn seede rekk moo ni diw moo jam diw te diw moo ma faatuwul, koo ku ay mbokkam du jar ñuy waat ngir saxalee ko jam-jam ba.

Kañ ray bu dul jullit di ab yahuud walla ab nasaraan, bu ray ga saxee ñu xam ni sax na bu saxul it ñu xam ni saxul waaye deesu ci giñ.

Ku ñu ray ci xare du aaje ngiñ niki ku ñu fekk mu faatu ci wetu këru ñenn ndax mën naa am da ñu ko faa indi, xanaa ñu fekk ko ca biir kër ga walla foo xam ni ñoom waa kër ga doŋŋ a ko xam.

rayug yoŋŋ (asasine) doonte ka nga ray nee nawoon baal naa ko du tee ku ko def ñu ray la ndax daa mën a xañ jàmm ab dëkk lool, moom mi ñu ray su xamee ki ko ko def te tay ko sañ na koo baal njëkk muy faatu ci kaw mu bañ a nekk rayug asasine gi ñu wax léegi.

Su dee ki ray moo ko tay waaye kenn ci doom yu góoru ki faatu ni baale naa sama wàll kon ña ca des du ñu mën a taxaw ni fàwwu ñu ray ko, ña baalewull da ñuy seet bu ñu doon joxe diya na muy toll ku ne ñu jox la sa wàll, ka baale moom du am darra ca alal ja.

Su doon ki faatu daa am doom yu góor ak yu jigéen, yu jigéen yi bu ñu baalewoon seen wàll te yu góor yi baalewu ñu du tax baale ga sotti.

Képp ku ray te tay ko waaye maneesu koo fayu ci yaw ndax ki nga ray moo la baal walla muy jullit bu ray yéefér walla gor bu ray jaam, kon da ñu koy dóor téeméer i yar tëj ko at.

alal ja ñuy gën a jëfandikoo ca la ñuy génnee alalu diya ja.

Bu fekkee baay daa sànni lu mel ni weñ gu ñuul doomam mu faatu waaye gisu ñu benn firnde ju wone ni da koo bëggoon a ray ndax bu ñu ko gisoon da ñuy fayu ci moom ak la muy doon doon doomam, kon su boo baa da ñuy

Page 114: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 4

fayloo baay ja diya te diya ja ñu mettil ko, deesu ko ca ray, mën na koo bokk ak mbokkam ya ñu fay ko.

Diya ju mat góor la ñu koy jox, bu dee jigéen genwàll ga moo koy dal.

Ku dagg ñaar i loxoy nit walla ñaar i tank ya walla luqi ñaar i bët ya te tay ko da ñu koy fayu ci moom, bu dee tayu ko boo ba lay fay diya ju mat.

Su fekkee benn loxo walla benn tank la dagg walla mu luqi benn bët ba kon genwàllu diya lay fay.

Su daggee bakkan ba diya ju mat lay fay, bu ca cofee as lëf ñu xayma la mu war a tollool mu fay loo la.

Koo yàq ag déggam ci ñaar i nopp yi kon diya ju mat nga koy fay, bu dee ca benn nopp ba kon xaaju diya lay fay.

Ku yàq xelum jàmbur, diya ju mat lay fay niki damm ndigg ak dagg ñaar i waay-yàlla bu dee benn ba xaaju diya lay fay. Bu léen daggoon ñoom ñaar daggaale sàkkara sa kon ñaar i diya lay fay. Dagg boppu sàkkara ak dagg lépp ñoo yemoo diya ju mat lay fay, bu daggee lenn ca boppu sàkkara sa ñu xool la mu tollool mu fay ko.

Ku dagg làmmiñ diya ju mat lay fay niki mu def ko lu yàq wax ja te làmmiñ wa daggul.

Dagg ñaar i weenu jigéen tam noo nu diya ju mat la.

Ku yàqq bëtub aji patt diya lay fay.

Ku dindi bëñu jàmbur walla mu yangal ko ba du saxati da fay fay juroom i giléem.

Baaraam bu ne ku ko daggal nit fukk i giléem la koy fay.

Jam-jamu muudiha mooy jam na ko ba weex-weexu yax ba feeñ waaye fa la yem juróom i giléem la koy fay, jam-jamu munaqila ku ko def nit da nga koy fay fukk i giléem ak juróom mooy ginnaaw bu mu dindee yàppu yaram wi dem na ba laal yax ba tojaale ay ferñent ca yax ba nga xam ni soo ko doon faj fàwwu nga dindi tojit yu sew yoo yu, maamuuma mooy ba yegg ca yuur ga moom ceerug diya moo koy fay, ci bopp walla jë lay am.

Jam jamu jaa’ifa ceerub diya moo cay war moom ca ginnaaw walla biir lay amee ndax jam-jam la buy sar ba ca biir ba.

Bépp xaañ-xaañ walla jam-jam bu àggul ci yax ba di feeñ, àttekat ba mooy

Page 115: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 5

seet la ca jaadu mu wax ni na ñu ci fay nàngam niki yeneen xeetu jam-jamu yaram yi.

Bu kenn jamee kenn te tayu ko du ñu ko wax fayal fa saa sa ndax da ñuy xaar ba xam koo ka day faatu am déet, su faatoo bakkan lay gàddu waaye da ñuy bàyyi ba koo ka wér ñu soog koo wax fayal nàngam.

Ku gaañ nit te tayu ko lu yeggul ca yax ba, wér te juralu ko benn ñaaw-ñaaw ca yaram wa darra du ko ca fekk, bu ko tayoon kon di na ñu ko yar.

Yi ñu tudd ci ginnaaw bu ko waay ja tayul te mu wér te amul genn légét walla ñaaw-ñaaw du tee mu fay la mu yellool, ni ñuy fayantoo ray yi la ñuy fayantoo jam yi bu dee ka ko def da koo tay ba mu des yiy sank bakkan, niki nit def kenn darra te amaana bu ñu ko ko defee mën naa am mu faatu niki maamuuma ak jaa’ifa ak munaqila.

Yi nga xam ni ci ku ñu ko fayu xayna bakkanam des ca da ñu ko naan fayal diya yem ca, su boo baa yit moom doŋŋ moo koy fay ak koo xam ni moom moo waxal boppam moo ray waay ji ci teeyu bakkanam te ñu topp ko diya war ca, su tayul gaañ ga mën naa bokk ak mbokk ya fay la ca war ci alal, su matul ceerub diya moom doŋŋ mooy fay, su matee ceerub diya te bu ñu ko fayan-took moom amaana mu faatu kon na mbokk ya ànd ak ki ko def ñu fay alal ja.

Ku ray boppam te tay ko muy xaru walla mu ñàkk koo tay, kenn du dajale alal di ko jox ña gën a jege ciy mbokkam.

Mbooloo bu ñu rayee góor mbaa jigéen ci takktoo su boo baa ñoom ñépp la ñuy ray.

Ku màndi, màndi gu xaraam bu rayee nit da ñu koy fayantoo ci moom ray ko, bu dee la mu màndee du lu mu tay niki naan soow mu bari walla garab mu màndal ko te tayu ko ñoo yemoo.

ab dof bu rayoon nit du tax ñu fayu ko ci moom, da ñuy seet mbokk i dof bi ñu fay diya ja.

Jullit bu rayee yéefér da fay fay diya ja waaye deesu ko fayantoo ci moom waaye bu yéefér rayee jullit di na ñu ko fayantoo ci moom.

Diggënte gor ak jaam ak jullit ak yéefér deesu ca fayantoo jam-jam ndax da ñuy jàpp ni amu ñug nawloonte ci wàllu dereet.

Kiy jiitël daaba mu topp ko mu koy wommat, lu daaba ja dëgg walla mu yàq ko koo ka moo ko war a fay ndax da ñuy jàpp ni waroon na ñu koo mën a tëye

Page 116: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 6

ba du yàq loo lee waaye bu yàqee loo xam ni boroom mënu ca woon darra niki mu yàq ci geenam walla mu màtt ko ci ab gémmiñam nga xam ni boroom daaba ja mëneesu ko caa tuumaal darra kon ka ñu yàqal da fay muñ rekk, du mujj fenn waaye bu ñu xamee daaba ja ci gaañe kon su boo baa moom bo-room da fay fay, gàddu la daaba ja def.

Lu toll ni ceerub diya dees na may ki koy fay mu fay ko ci at, diya dees na ko fay ci ñett i at, genwàllu diya ci ñaar i at, diya yit ni ñuy donnee ci miiraas la ñu koy donnee.

Ku yàq ëmbu jigéen di na ko fay lu war a tollook diyag ndey ji bu ñu ko xaajoon fukk, ki yàq ëmb ba jox ko benn ba, muy teew fa saa sa.

Ku ray nit te tay ko te waroon a bokk ci ñiy donnu kon su boo baa du ca donnu darra, diya ja mu war a fay it du ca donnu darra, bu ko tayul du donnu ca diya ja darra waaye di na donnu ca alalu ki faatu la ko ca yoon jox.

Mbooloo bu ñu rayee kenn rayug àddu-kalpe, yoon da ciy àtte, àtte bu dëgër ngir mu bañ a amati, su boo baa ñoom ñépp la ñuy ray doonte kenn mbaa ñaar ñoo ko ca ray.

Ku ray bakkan te tayu ko da ñu koy sant kaffaara te day war ci moom, su dee ca jamono ya jaam amee da fay goreel jam bu di ab jullit, bu ko amul mu woor ñaar i weer yu sësëloo.

Bu ko rayoon te tay ko kon kaffaara ga du nekk lu war ci moom du tee tam da ñu koy fayu ci moom.

Sindiiq baaxul mooy kuy feeñal ni ci waa lislaam la bokk te la mu ëmb ci biir ag kéefér la ndax ag yàqam da fay bari ngir nekk gu muy nekk ci biir jullit yi, bis bu feeñee lu mu tuub tuub deesu ko nangu da ñu koy ray.

ab njambarkat buy téqale ay nit di soppiy jëmm di takk xala bu koy defee wax yuy tektale ag kéefér, su boo baa moom da ñu koy jàppee ab yéefér te bu ñu ko xamee ci moom da ñu koy ray, su bëggee tuub tam deesu ko nangu.

Bu dee la muy njabaree baat yu aayul la niki Alquraan la walla baatu injiil walla yeneen baat yu teey kon su boo baa njabar ga lu xaraam la waaye du ko tax a doon ab yéefér, la mu cay am it lu xaraam la da koo war a tuub bàyyi ko ngir ragal layoo ëllëg diggëm ak Boroomam, deesu ko ca ray.

Ku murtad muy góor muy jigéen mooy génn ci lislaam ci wax lu ko ca gé-nnee mbaa mu jëf ko, su nangoo tuub dellu ci lislaam ñu bàyyi ko, su nan-guwul a tuub dees koy ray ndax kenn forsewu ko ci dugg ci diine kon ginnaaw

Page 117: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 7

bu ca duggee ba xam sekre ya ne bokkatu ci dees koy ray, di na ñu ko may ñett i fan ba xam di na tuub, ñett i fan ya bu jant bay so te nanguwul a tuub dees na ko ray.

Koo xam ni jullit la gëm ni julli war na waaye mu wax ni du julli ngir ag tàyyeel, koo ku ilimaan da koy woo bu waxtu julli jotee ni ko julli ajuwul cig tàyyeel ak sawar waaye lu war la ci bépp jullit mu koy jooxe ci waxtoom keem sa man-man, digël ko mu julli di ko ko digël ba waxtu wa daanaka benn ràkkaa du ca xaw a xaj, bu nangoo julli ñu bàyyi ko bu ko nanguwul ñu ray ko rayug gétën mooy du tee ñu jàppee ko ab jullit, di na ñu ko sang, sàng ko, jullee ko, suul ko ca almeeru jullit ya, ña ko war a donnu donnu ko, du tee ku siiwee mbaax niki ilimaan ja baaxoo jiite walla mbooloo soppu ñu seenug teew ngir mu doon ab jàjji ak jàngale ci ñeneen.

Koo xam ni daa gëm ni julli du lu war, koo ku bu fekkee duggoon na ci lislaam kon murtad na ndax lislaam nanguwul gëm lii weddi lii, lépp ngay maase gëm, da ñu koy may ñett i fan ngir mu tuub xam ni julli lu war la te fas yéenee def ko, bu ñett i fan ya matee te tuubu ko ñu ray ko, bu ñu ko rayee rayug kéefér la, deesu ko sang deesu ko sàng deesu ko jullee, deesu ko suul ci almeeru jullit ya, alalam da fay dem ca Baytil maal jullit yépp yem ci, ay mbo-kkam tam du ñu ko donnu.

Ku ñu gis mu yor alal ju asaka war, ñu laaj ko ko mu bañ, da ñu koy foqarti ci moom, bu ñu ko rayoon ca foqarti ga mooy ñàkk bakkanam rekk.

Koo xam ni war naa mën a aji ndax gisëlu ñu ko ag wéradi walla ag ñàkk te defu ko kon da ñu koy bàyyeek Yàlla rekk xayna mu am ngànt lu ñu xamul.

Ku ŋàññ Yonent bi SaWS te nekk mukkàllaf da ñu koy ray, bu bëggee tuub tam kenn du ko nangu.

Yahuud yi walla nasaraan yiy dundandook jullit yi ku ne nekk ca la nga ne, ñoo ñu ku ci xas Yonent bi SaWS te bokkul ak la ñu ko daan weddee niki wax ni arab la rekk waaye bu ko weesoo niki naan dub Yonent kon da ñu koy ray, ku ci weddi Yàlla ci lu bokkul ak la ñu daan wax niki naan ñett i Yàllaa am ci nasaraan yi bu ko weesuwul deesu ko ray, bu ko weesoo niki mu weddi yenn ciy sifaati sunu Boroom niki mu ne Yàlla lewetul kon da ñu koy ray waaye bu fekkee nangu naa tuub dugg ci lislaam kon ñu bàyyi ko.

ab àddu-kalpe kenn du ko jéggël mukk, bu rayee kenn fàwwu moom it ñu ray ko, bu dee rayul kenn kon ilimaan la ñuy wax mu seet la ca jaadu ci bi mu ko tàmbalee def ba fi ñu ko jàppee la mu ca yàq ak la mu ca lore, benn ray war

Page 118: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 8

ca walla takk ci garab ba noppi ray ko walla dagg ci ab juuyële te mooy dagg loxob ndeyjoor ba ci tikku-jara ba ak tanku càmmooñ ba ca dojor ba walla ñu dàq ko ba ca ab dëkk tëj ko fa ba mu tuub tuub gu sell, bu dikkëlee boppam tuubsi da ñuy seet lépp lu mu mos a def nit di na ñu ko sañ a fayu ci moom, bu ñu ci jàppee kenn walla ñaar da fay mel ni jàpp na ñu ñépp, moom walla ñoom ñiñ jàpp da ñuy gàdduwaaleel ña raw.

Ku njaalóo tey gor te fekk mu sangewu mooy ci góor walla jigéen mi ngi ci ab sëy bu wér ci lislaam, jote, jote gu amul genn sikk nga xam ni du ci jamonoy mbërëg walla wësin, da ñu koy ray ci woo mbooloo ñu koy sànni ba mu faatu, bu fekkee moom mi njaalóo sangewul mooy ku sëyul walla sëyoon na waaye jotul a joteek ka muy sëyël jote gu wér, su boo baa da ñu koy caw téeméer i yar, yóbbu ko ci ab dëkk tëj ko fa at ngir tumurankeel ko waaye bu dee jigéen ginnaaw bu ñu ko cawee deesu ko tumurankeel.

Ku njaalóo fàwwu ñu seet ba am firnde yu wér ba noppi ci def gi, ba ca njëkk mooy mu waxal ko boppam te kenn forse wu ko te ànd ak sagoom, su boo baa yit da ñu koy def la ca war, bu dee jigéen ju amul jëkkër jékki-jékki ëmb walla ci seedey ñent i góor yuy gor te kàllafe te maanu, bu ñu gisan-doowee sawukaayu góor ga di dem ca sawukaayu jigéen ja ni ab tusngël di demee ca deñcukaayam di njaalóo te ñu bokk benn waxtu wu ñu ko gisee, mën a waat ni seen bët la ñu ca teg bu wér, su boo baa la ñuy jàpp ni koo ka njaalóo na.

Bu ca amee kenn ku ni gis naa mu toog ci kawam waaye wóoru ko ba xam àgg na ci moom, ñett ña des ni wóor na léen, su boo baa yoon da fay jàpp ni ñett ña xas na ñu seen mbokkum jullit ci ni njaalóo na te amu ñu ca lu wóor, su boo baa da ñu léen di caw cawu ku waxal nit njaalóo te saxul, mooy juróom ñett fukk i yar, ka wax ni gisul moom di na mucc kenn du ko caw.

Ku kàllafewul bu njaalóo deesu ko caw deesu ko ray da ñu koy yar rekk ngir mu bañ koo defati

Bu jigéen ju amul jëkkër ëmbee wax ni da ñu koo forse waaye du moo ko coobarewu, du ñu ko gëm da ñuy jàpp ni da fa njaalóo daa di koy gétën li war lu dul ni daa am ay seede yu wér yu ni mos na ñu koo yóbbu ci kaw doole walla mu jàmbat ko àttekat bi ni ko daa am ku ko jaay doole ba siif ko kon bu ëmb ja feeñee ca kanam daa ñu jàpp ni la mu wax noo nu la demee walla muy jigéen ju mosul a sëy te ab sawukaayam di nàcc ngir wone ni da ñu koo forse.

ab nasaraan akub yahuud ku ci siif jullit bu jigéen da ñu koy ray.

Page 119: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 1 9

Ku waxal boppam ni daa njaalóo ba ñu war koo ray mu dellu wax ni njaalóowul da ñu koy bàyyi rekk.

Ku jëf jëf i nitu Yonentub Yàlla Lóot ya te mooy goor di sëy ak moroomam, àtteb lislaam ci ñoom mooy da ñu léen di ray ñoom ñaar ñi ko coobarewu nga xam ni kenn forse wu léen ci, moo xam sangewu na ñu am déet.

Ku xaste te mooy tuumaal nit njaalóo te saxul, da ñu koy caw juróom ñett fukk i yar ba bu ëllëgee du ko defati, ab yéefér it bu xastee di na ñu ko caw juróom ñett fukk i yar, ku xas ab jaam walla yéefér tooñ la naam waaye du tax ñu caw léen.

ab jaam dëgg-dëgg ci lislaam mooy ku ñu woo ci lislaam mu bañ, ñu ni ko dañ lay bàyyi ci sa diine te ngay jox lislaam galag (impo) mu bañ, ñu wëlbëtiku xeex ak moom ba jàpp ko.

Ku xas xale bu jigéen waaye jëmm ja daa kàllafe dees na ko caw ngir ag yàq der, bu dee daa ndawe ba ku ko xas it du tax ñu gëm ko deesu ko ca caw, ku xas xale bu góor bu kàllafeegul it du tax ñu caw ko.

Ku kàllafewul bu xastee walla moom ci boppam mu njaalóo du tax ñu def ko la ca war da ñu koy yar rekk bàyyi ko.

Ku wax nit ne ko diw ma ñu xam ni mooy baayam nga ni ko du sa baay yàq nga deram dàq nga ko ci askan wa ñu koy askanalee da ñu koy caw niki ku xaste.

Ku gaaral nit ci bañ a jaar ci digg ba ne ko da ngaa njaalóo waaye da nga koo junj da ñu koy caw niki ku jaar ca digg ba.

Ku xas ñu bari te kenn cawlu wu ko bu ñu ko jàppee dóor ko di na ko mën a setal ca xas yépp.

Ku def luy waral gétën te jotu ñu koo gétën niki naan sàngara mu def ko ñaar i yoon mbaa lu ko ëpp walla mu njaalóo benn yoon mbaa lu ko ëpp, yoo yu yépp da ñu koy jàppee ni genn, du aajewoo yoon bu nekk ñu caw ko ca cawug boppam.

Koo xam ni gétën gu bokkul ak ray da koo war mu def loo xam ni ray da caa war niki mu njaalóo te sangewul walla mu naan sàngara caw war ca mu wël-bëtiku ray ab jullit te tay ko, su boo baa du aajewoo ñu koy caw yar i njaalóo, du aajewoo yit ñu koy caw ngir naan sàngara ga waaye xas gi mu xas ab jullit di na ñu ko ca gétën ba setal derub ka mu tuumaal door a fayantook moom ray gi mu ray ab jullit te tay ko.

Page 120: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 0

Ku naan lu mu néew-néew sàngara wallab njambaan moo xam ni da fay màndal doonte màndiwul du tee ñu caw ko juróom ñett fukk i yar waaye tëj kaso du ca war.

Ku ñuy gétën ci caw da ñu koy summi waaye da ñuy suturaal awraam, bu dee jigéen lay tax yar ya du metti la ñuy futti waaye lépp lu mënul a tee yar ya metti da ñu ko cay bàyyi, da ñuy jal suuf tooyal ko dëj ca ka ñuy caw ngir su tuuree ndox ca dóor ya ndox ma ñu ca wis di na ko suturaal ba kenn du ca xam darra, xàcci gi da fay digg-dóomu yar ya yit da ñuy digg-dóomu.

Ku ëmb ñu war koo gétën da ñuy bàyyi ba mu am doom, ku njaalóo ba ëmb ca du tax ñu gétën ko ci biir ëmb bi, ku tawat it da ñu koy bàyyi ba mu wér.

Ku njaalóo ak bàyyima du tax ñu def ko niki ku njaalóo ak nit da ñu koy yar rekk bàyyi.

Sàcc da ñu koo sàkkal nisaab joo xam ni bu dee la nga sàcc àggu ca kenn du dog sa loxo, bu dee ci wurus bu matul kaaru dinaar, bu dee ci xaalis bu matul ñett i dërëmu yoon, da fay fekk it mu sàccee ko ci ab deñcukaay waaye bu ñu nee fu mu ko fekk ñu ne fii da ñuy jàpp ni ki ñu sàcc moo sàgganee alalam.

Ku fëkk alalu jàmbur nga xam ni bi muy ñëw yaa ngi koy séen mu ñëw siif daa di daw du ñu ko jàppee sàcc ndax sàcc mooy koo xam ni bi muy ñëw da fay làqu buy dem da fay làqu.

Ka sàcc bu dee góor walla jigéen walla jaam ñoo yem loxob ndeyjoor ba la ñuy njëkk a dagg ca tikku-jara ba, bu sàccaatee ñu dog tankub càmmooñ ba ca dojor ba, bu sàccaatee ñu dog loxob càmmooñ ba ci tikku-jara ba, bu sàccaate ñu dagg tankub ndeyjoor ba ci dojor ba, bu sàccaatee juróomeelu yoon da ñu koy dóor tëj ko kaso waaye amatul lu ñuy dagg ci moom.

Mukkàllaf mu waxal boppam ni daa sàcc ci sago kon da ñu koy def la ca war, bu ñu ko waree dagg, dagg ko, bu wëlbëtikoo ci bi ñuy waaj a dagg loxob ndeyjoor bi ni sàccu ma kon dog ga la ñuy bàyyi waaye du tee di na ñu ko topp sàcc ga mu fay.

Liféeg la mu doon sàcc génneewu ko ca deñcukaay ba deesu ko dog niki ku ñu yuuxoo rekk mu daw te jotu caa génnee darra, bu ko xasee génnee rekk doonte da koo sànni ca biti da ñu koy dog niki noo nu ku sàcc lu ñu deñcaalee ak ab néew niki càngaay la te jotu koo génnee ca bàmmeel ba du ñu ko jàppee sàcc waaye bu ko xasee génnee lu mu néew-néew bu ñu ko jàppee dog ko ndéem mat na nisaabu sàcc gi ñu waxoon sank.

Page 121: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 1

Ku yëgloo ba ñu digël ko mu am lu mu fa sàcc da ñu koy jàppee ku wor waaye deesu ko jàppee sàcc.

Meññent mu garab meññ ca àll ba ku ko fa fekk sàkk ca deesu ko jàppee sàcc waaye bu dee daa nekk ci kër walla ñu aj ko ci kaw garab ga ci lay nekkee deñcukaay.

Ku dogaale jur ca àll ba yit kenn du ko dagg waaye bu dee fu ñu baaxoo yendu nga fekk léen fa dees na ko jàppee sàcc

Ku sàcc mbaa mu njaalóo ba àttekat bi yëg ko deesu ko mën a tin ngir ñu bàyyi ko fàwwu ñu doxal santaane Yàlla.

Bu dee nit da fa xas kenn ci tuumaal ko dox tanku caaxaan ñu war koo caw ca loo la waaye ginnaaw mën naa gën a yàq deru ki ñu tuumaal ndax bu ñu nee diw da ñu koy caw bu ñu laajee lu tax kon tuumaal ga da fay gën a siiw te su boo baa deru waay ja da fay gën a yàqu kon moom mi ñu xas su bañee tuuma ja siiw mën naa wax ñu bàyyi ka ko xas doonte am na ay wuute.

Ku sàcc ci lafu mbubbu walla poos walla kaala ak yu ni mel dogeef ko ndax ay deñcukaay la ñu doonte boroom da doon nelaw.

Màngasin bi ñuy deñc yëfu jullit yi walla Baytil maal ku ca sàcc lu mat ni-saabu sàcc kon dogeef ko.

Ki sàcc dagg ga ñu dagg cëram du tee bu fekkee ku ko topp mu mën a fay kon da ñu koy topp mu fay boole ca, bu dee ku ko topp du mën a fay kon da ñu koy dagg rekk bàyyi ko.

Bu dee la mu sàcc matul nisaabu sàcc mbaa fa mu ko sàccee daa ma-tul deñcukaay yoo yu deesu ca dagg kenn waaye fàwwu ñu topp ko mu fay doonte daa ñàkk.

Fitra (bind bu rafet), xaraf, wat karaw, koddaay ak suturaal awra

Bokk na ci yiy tax sa bind bu rafet bi la Yàlla bindee feeñ juróom :

1- Boo amee ay mustaas nga wàññi ko ba catu tuñ yi di feeñ te bañ koo wat ba mu set ndax mook sikkim da ñoo wax ni wat léen ba ñu set xaraam na doonte chaafii ak abuu Xaniifa da ñoo jàpp ni da nga koy wat ba mu set,

2- Lewwi ay wee ci bañ koo bàyyi mu wéy di gudd,

3- Xuuf karawu poqotaan moom sax la ñu gën a taamu ci wat gi,

4- Wat karawu naq,

Page 122: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 2

5- Wat yu dul yoo yu te mooy yeneen karaw yiy sax ci yaram

Xaraf sunna la ci góor, da ñoo wax ni bu demee bay magum jëmm te xara-ful su boo baa moom mooy xarafal boppam ndax keneen xool awraam da fay nekk lu xaraam, bëgg a def sunna du tax nga toggoo lu xaraam.

Sunna su dëgër la, fa ñu ko gën a soppee ci nit mooy bu amee juróom ñaar i at ba ba muy am fukk i at, sib na ñu xaraf gone bis ba mu juddóo walla bisu ngénte ba.

Koo xam ni ragal na ni bu ko defee mën na caa loru ngir tawat ju nekk ci yaramam, jéggëlees na ko ko.

Ku judduwaale xaraf sopp na ñu, ñu jaarale ca saatu, bu ca darra desee lu ñu war a dog ñu dog ko, bu ca darra desul ñu bàyyi ko noo nu.

La ñu cay daggee tam sobe la. Dees koo war a suul fu sori waaye deesu ko suul ci jàkka, deesu ko wacc ci biti tam.

Jigéen li ñuy tuddee xaraf ci moom mooy tonni as tuut ci liy nekk ci ab sawukaayam sopp na ñu ko.

Yonent bi SaWS li mu diglewoon mooy sikkim ba ñu bàyyi ko muy wéy di gudd, imaam Maalik nee na bu dee sa sikkim ëpp na bu nit yi lool ci guddaay bi ak yaatuwaay bi mën nga koo wàññi ba mu yem.

Ku bejjaaw suub karawam ngir mu ñuul, bu dee jéem caa nax kenn la ci jublu niki am koo bëgg a takk di ko won ni waxambaane laa kon da fay xaraam, bu koy def ngir mën a dem ca xare ba yéefér yi jàpp ni gone la ngir ragal ko tuyaaba la koy jurël, jàppal ni luñ sib la ndéem lii koy xaraamal raxu ca walla lii di tax mu jur tuyaaba, fuddën ko moom aayul.

Yonent bi SaWS tere na tereg xaraamal góor ñi sol yëre sooy niki takk jaaro oor.

Jaaro weñ gu ñuul walla përëm walla xànjar da ñu koo sib ci góor ak ci jigéen waaye mën naa wut moom góor gi jaarob xaalis, da ñu cay saart muy benn du ko weesu bu dee jigéen ji sañ naa def wurus ak xaalis yépp ci lépp lu muy sol walla mu koy takk ngir mottalikoo ko doonte ay dàll la waaye sañu caa am lal wallab taabal ndax bokku ñu ci yi ñuy sol walla di ko takk, góor moom am na beneen yitte bu dul waaj.

Ba tay boo amee jaasi mën nga koo xoobee wurus mbaa xaalis, ab kaamil der wi ko ëmb mën nga koo xoobee wurus walla xaalis waaye deesu ko def ci

Page 123: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 3

laabug fas walla paaka walla leneen ci say yëf, sañoo koo xoobee wurus walla xaalis ndax da fay xaraam.

Li ñu taamu mooy boo xasee ba am jaaro te sañ koo takk nga def co ci sa loxob càmmooñ ca baaraamu sankalañ ba ndax loxob ndeyjoor ngay faral di yóotoo, góor benn jaaro kepp la ñu ko may ci yoon mu takk ko te xaalis la war a doon te warul weesu ñaar i dërëmu yoon, boo koy seet matul juroom ñaar i ngaraam.

Sol loo xam ni daa am sooy te muy lu xaraam boole ca beneen yëre bu aayul sib na ñu ko doonte am na ñu ni daa xaraam, am na tam ñu ni darra nekku ca, sib gi moo gën a mat a jàpp. Bu fekkee la ca dem ci sooy matul benn baaraam niki kuy ràbb kon deesu ko sib.

Jigéen du sañ a sol loo xam ni yaram wa day feeñ niki mu yaraax ba boo xoolee yëre ya di gis yaram wa ca biir walla mu dangal ko ba mu sës ciy cëram, bu ñu génnee ak bu dee génnu ñu te toog ak ku warul a gis seen yaram, góor it liy awraam sañu caa sol loo xam ni ku xool yëre ya di gis yaram wa ngir yaraax walla mu dang ba sës ciy cëram. Sol ko ci kanam ki ngay sëyal darra nekku ca.

Góor sañul a sol ay yëre yu gudd ba ëpp ngir puukërewu, yëre ya mën naa ñëw ba aksi ci dojor ya yem ca mooy tax du gaaw a taq, jigéen it sañ naa sol ay yëre yu gudd bay buubu waaye bum buubu ba ëpp.

Boo solee ab làmbaay gu sa benn mbagg di feeñ te boo yëkëtee say loxo lu bokk ci sa awra yaw góor gi feeñ ndax jiitëloo geneen yëre, xaraam na ci julli bu dee nekkoo ci julli da ñu koy sib, bu ko mbalaan jiitóo da ñu koy sib ci julli.

Mukkàllaf mu ne buy julli walla mu ñàkk a wéet nga xam ni ab jàmbur mën na koo gis da fay xaraam ci moom mu bañ a sàng awraam, bu julliwul te wéet moom doŋŋ walla mu toog ak ka muy sëyël, da ñuy sopp mu sàng awraam ngir rus Yàlla ak malaaka yi.

ñaar i góor walla ñaar i jigéen ku ne def yaramu neen seen i awra di jonjoo ñu sàngoo benn mbalaan muy mbàjj muy sër daa xaraam.

Génnug jigéen da ñu koo dangal lool, da ñu koy xaaj ñett i xaaj :

Màgget mu jigéen mi kenn xoolatul sañ naa génn, kiy jigéen tey ndaw te am taar ak lu mu waajee te xayna su génnee kenn di na ci am fitna da ñu koy aaye génn ga, kiy jigéen te amulub taar amul lu mu waajee mën naa génn ci lu mënul a ñàkk niki bu kenn faatoo ciy waajuram walla mbokk mu jege walla muy siyaareji waajuram mbaa muy faji soxla su ko kenn mënul a fajal ku dul

Page 124: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 4

boppam waaye da ñuy saart buy génn mu sol col gu mat sëkk ba darra ci aw yaramam du feeñ, du waaj du xeeñoo xet gu neex. Balaa dem it dees na seet ba xam fa mu jëm darra ci xeetu déjjéetu ak i po ak jaxasoo góor ak jigéen yu aay yi am na fa am déet, bu fa amee rekk du sañ a demati waaye bu dee ab céet ndax da ñu koo jàppee mbégum jullit yi ndax manees na cee tëgg ab ndënd gu ñu foor ci genn wet te du am jaxasoo góor ak jigéen, wuute na ñu ci guñ foor ñaar i wet yépp, tabala tam am na ñu ko xaraamal, am na ñu ko sibal, am na yit ñu ko daganal.

Xaraam na ci góor mu wéet ak jigéen ju ko xaraamul nga xam ni boo ko dee seet mën na koo takk ci yoon te na ko moytu bu baax, liy tax mu sañ koo xool ngànt lay doon niki bu ko waree seede ci mbir muy aaje mu xàmmee ko walla muy doktoor di ko faj walla mu bëgg koo takk soxna te bañ a wéet ak moom, màgget mu jigéen, góor guy jàmbur ci moom mën naa xool kanamam ak ay tenkam ci anam gu ne du ñu ca saart ngant.

Góor ak jigéen ñoo ci yemoo, xaraam na ci ñoom ñuy jokk seen karaw te mooy jël geneen karaw yokk ko ci seen karaw, bu dee lu mu def ni mbaxana nga xam ni jokku ko ci da ko ciy teg noo na bu ca noppee dindi ko kon mu dagan.

Jam ci tuñ walla siiñ walla ci kanam gi daa xaraam ci góor ak jigéen yépp.

Sopp na ñu booy sol dàll walla ay bot walla tubëy nga jiitël tanku ndeyjoor bi, booy summi nga njëkk a summi tanku càmmooñ bi.

Taxaw sol say dàll ak nga toog sol ko door a taxaw bu ci nekk baax na, sib na ñu sol benn dàll di dox ak moom.

Nataal boo xam ni lu amug ruux la, def ko ci ab këyit walla miir da ñu cee wuute am na ñu ni daa xaraam, am na ñu ni da ñu koo sib ndegam nekkul ab istati moo tax li Yonent bi SaWS waxoon ni ñiy gën a metti mbugël bis peñc ñooy ñi daan foto ndax da ñu léen di wax ñu dekkal ko, ñenn ñi da ñuy wax ni bu dee da nga koo def jëmm ju ni léng muy ab istati waaye bu fekkee da nga koo def ci ab këyit walla miir du xaraam da ñu koy sib waaye boo ko defoon ci mbubbu mu ñuy sol walla ci ab sijaada deesu ko sib ci waxu ñenn ñi waaye bañ koo def moo gën.

Boo fotowoon lu mel ni garab walla oto mbaa saxaar walla taabal darra nekku ca.

Page 125: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 5

Mbiru jënd ak jaay

Sunu Boroom daganal na jënd ak jaay, riibaa la xaraamal, njëkk lislaam ni ñu daan lebalantee riibaa daan na ca am bu baax ndax da ñu daan def boo ameelee nit bor ba fay ga jot da naan la benn nga fay ko walla mu toppale dele ba te bor ba yokku, su ñu àggaatee ca dele boo ba te mënoo koo fay mu toppaleeti ko yokkaat ko nga xam ni bor ba mënoon naa toll ci junni dem ba doon junni yu bari, lépp lu ñu teg ca na bor ba tolloon riibaa lay doon ndax koo lebal te mënu laa fay toppale dele ba mënul a ñàkk.

Wecciku xaalis ak xaalis du lu aay waaye fàwwu li nga koy jox ak li mu lay jox yemoo kepp te mu nekk loxo ak loxo waaye bu ëppëntee darra muy riibaa niki ngeen doon weccante ci cfa ak cfa ci loxook loxo waaye daa ëppënte kon la ëpp noo nee riibaa lay doon ndax li ngeen di joxante daa war a yemoo, bu dee ñaar i xaalis yu bokkul niki oro bi ñuy wecciku fii ci réew mi yemoo du ca mën a am.

Ba tay morsoy wurus walla xaalis ci wàllu tëgg bu ñu ko doon weccoo tam daa war a yemoo rekk, bii moo gën a rafet bee du tax mu ëppënte, ba tay bu doon wurus te da fay doon loxook loxo fa saa sa ndax ag yéexe bu ca amee niki nga joxoon ko mu xaar ba ca kanam soog laa jox riibaa la.

Boo dee wecciku xaalis ak wurus du ñu mën a yem ndax wurus daa ëpp daraja waaye yéexee ga moo cay aay, loxook loxo la war a doon.

Bu fekkee da ngay wecceeku ñam ñu lay jox ñam moo xam xeetu pepp la walla lépp lu ñuy dundee walla ñu koy defaree togg ga, boo ko koy jox mu lay jox loo xam ni mook li nga ko jox ñoo bokk xeet bu ëppëntee riibaa lay doon te day aajo mu nekk loxook loxo, rafetaay ba ak ñaawaay ba du ci darra.

Bu dee la ngeen di weccoonte mëneesu koo deñc di ko dundee niki xeetu paytéef yi (furuwi) ak legum yi mën naa ëppënte doonte benn xeet bi la, bu dee ay xeet yu bokkul tam mën naa ëppënte waaye yéexee gi du dagan benn yoon.

Ndox mu ñuul kepp nga mën a jaay ñu fay la ko ñam te mën naa bañ a doon ca saa sa, nangu na yéexee nangu na tam ëppënte niki nga koy jox ndoxum taw mu lay jox ndoxum robine waaye na nekk loxook loxo.

Bele (blé), lors (orge) ak suwtu ñoo bokk xeet nga xam ni bu ngeen ko doon jaayante day aajewoo mu yem kepp, raseng (raisin) daa bari melo fi ñu koy bayee waaye yépp da ñu koy jàppee benn xeet, raseng bu mu la man di jox ak yaw it boo ko man di jox daa war a yemoo, tàndarma tam noo nu yépp benn

Page 126: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 6

xeet la ñu.

Giiru sëb yi da ñu léen di jàppee ay xeet yu bokkul moo tax mën na ñu ëppënte.

Mbooleem ñi ame ñent i tank da ñu léen di jàppee benn xeet moo xam yi dëkk ci kër yi la walla ya ca àll ba, bu fekkoon yàppu nag daa jafe te yaw nga koy jox yàppu giléem te jafewul a am du tax ëppëlënte am ca daa war a yemoo kepp.

Mbooleem yiy naaw tam benn xeet la ñu léen di jàppee.

Mbooleem li ñuy nappee ci géej tam noo nu benn xeet la ñu léen di jàppee.

Bu ñu la waxee ni nàngam benn xeet la xamal ni lay bàyyeekoo ca yàpp wa niki gerees ga benn xeet la ñu koy jàppee, soow ma noo nu ak foromaas ba ak bëer ba ak diwñor ba.

Boo jëndee ñam ñu war koo natt jox la te nattaguñu ko doo ko mën a jaayaat te jotoo ci. Bu dee lu ñu jal nga xam ni kenn du ko natt, ñu jaay la ko noo na mën nga koo jaay te jëlagoo ko.

Bépp xeetu ñam walla randaay mbaa lépp lu ñuy defaree ñam mbaa xeetu naan nga jënd ko te jotagoo ci doo ko mën a jaayaat fàwwu nga xaar ba jot ci ndare ndox mu ñuul mën nga koo jënd jotagoo ca daa di koy jaayaat.

Lépp lu ñuy garaboo mbaa ñu koy def jiwu te amul diw gu ñu cay segalee mën nga koo jaay te jotagoo ci.

Bu ñu la abalee aw ñam ngir Yàlla niki ceeb niki nga demoon ci boroom butik bi mu abal la barigo ceeb men nga koo jaay te jotagoo ca, bu doon nak da nga koo jënd di ci wut benefiis doo ko mën a jaayaat te jotoo ci.

Bu ñu la jaayee ñam wu ñu war a natt mbaa peese te jotagoo ci mën ngaa ñëw bokk ko ak kenn, ñëw it féetele ko keneen tam mën naa nekk, xàcc it dagan na mooy ngeen jubóo ba nga ameel ko njëg mu ameel la marsandiis ginnaaw ba nga tëye sa njëg mu tëye marsandiisam.

Bu ngeen dee jaayante walla nga koy defloo di ko fay walla ngay luwe ci moom darra walla moom muy luwe ci yaw darra da fay aajewoo ñu xam la ñu cay fay bu wér ba noppi muy lu wóor, du nekk lu ñu sàcc xamu ñu ba xam di na feeñ am déet moo xam la ñuy jaay la walla la ñuy jënd walla la ñuy fayee kay ligéey, àpp ba yit daa war a leer, bu amul rekk mu xaraam.

Bépp njaay mu amug wóoradi daa xaraam niki ñu lay jaay darra cig xayma

Page 127: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 7

walla nit ne la da ma la koy jaay waaye lu diw wax ni mooy njëg ga nga fay loo la.

Jaay lu ñu umple walla njëg lu ñu umple daa xaraam niki ñu waxoon ni ëmb bii da ñu la koy jaay te doo xam lu ci ne, loo ci fekk jël.

Jaay lu àpp ba leerul tam xaraam na.

Booy jaay darra, da fay xaraam nga nëbb ca ab sikk, bépp sikk boo ci xam da nga koo war a leeralal kiy jënd ba mu xam ko su bëggee jël su bëggul bàyyi, loo amee ci ndono sax war nga koo leeral kiy jënd ndax daa am ñu ko sib wa-roo koo nëbb kiy jënd.

Jaxase lu baax ak lu bon tam xaraam na ci njaay walla nga jël royaal bi ne ko mooy piir ba.

Publisite darra ba wax ca lu ca amul ba ka koy dégg defe ni noo nu la de-mee te demeewul noo na tam xaraam na, la ngay wax ca njaay ma daa war a fekk mu nekk ca, loo lu mooy wor ci wax.

Bokk na ci wor ki ngay jaay ci jëf mooy nga wax ko lu seer lool ba nga xam ni moom lu mu mën a fay di na ëpp lay njëg ga dëgg, bokk na ca tam jox nit ki ndox mbaa ñam woo xam ni loo ko laaj mu fay.

Loo mën a jaay nit ne ko boo ci gisee sikk doo ko xàcc kenn du ko jàpp ndax bu ko ca gisee sañ na koo delloosi.

Bépp njaay mu yoon ni baaxul bu ngeen ko defantee du fasu, jaaykat bee moom la mu doon jaay ba tay kiy jënd moom njëgam, bu dee kiy jënd jotoon naa jël yëfam ba yóbbu kon bu ca darra xewee mooy tax darra war ko ca, bu dee yóbbu na ko te darra sikku ca da fay delloo ka ko jaayoon marsandiis ma, ka jaayoon delloo ko njëgam.

Bu fekkee ñaar i mukkàllaf ñooy jaayante waxaale ba jubóo doonte jaaykat ba joxeegul la muy jaay, bu ca xàcc naree am di na aaje ñu bokk jubóo ca.

Bu dee yoon daa seet am njaay gis ni baaxul ñu war a delloonte ñu gis ni njëg ga soppeeku na ci diggënte bi walla jëmmu la ñu doon jaay moo sop-peeku niki bu dee jur mu suuróon daa di yooy walla lu mel noo nu, su boo baa bis ba nga ca jotee fa xayma ba tolloon nga koy jox, bu dee jëmm ja soppeeku na mbaa nekkatu fa waaye muy lu ñuy peese walla di ko natt walla lu ñuy waññi, su boo baa darra du ca raw lu toll ni la mu ko joxoon kepp la koy delloo, mu delloo ko njëgam doonte gën naa yomb walla jafe ci diggënte bi deesu ko faale ginnaaw yoon nee na njaay ma baaxul.

Page 128: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 8

Bu dee li ngeen doon jaayante mbirum suuf la walla kër te yoon ni njaay ga baaxul du tee ñu delloo boroom suuf sa suufam, delloo boroom njëg ga njëgam doonte njëg gi soppeeku na ci diggënte bi.

Bépp leble buy indil njariñ ka doon leble xaraam na, mel ni nga lebal ko pepp mu lax ngir mu fay la mu yees.

Njaay jëm ci dig daa wuuteek leble mat naa ràññee lool.

Lëkkële leble ak njaay ni bu lii amul lii du am daganul, li war mooy bu ñu dee jaayante jaayante ci ag wet, bu ñu dee leble tam noo nu waaye deesu boole defandoo ñaar ci ab kontaraa.

Nit aajewoo darra nga lebal ko ko, bu soxlaam fajoo mu delloosil la ko du ko yokk du ko wàññi da ñu koo sopp.

Lu mel ni suuf si ñuy tëggee wurus mbaa xaalis ñu lebal la ko nga di ko jeex, yaw it nga fay ko suuf su mel noo na daganul ndax daa wóorul la ngeen cay fekk mën naa bañ a tolloo lool.

Bu dee nit da laa ameel bor nga ni ko mën naa la koo wàññil nga fay ma ko ci saa si daganul.

Bu dee da ngaa ameel nit marsandiis ne ko naa la fay léegi te dolli la te waxtu wa ngeen digëntewoon akseegul yoon di na ko nangu ndegam ci ab jaayante ngeen ko defeewoon ngir bëgg benefiis.

Su fekkee da nga koo ameel marsandiis moo xam ni ngir Yàlla ngeen ko séqeewoon, bu la neexee nga fay ko ko fa saa te dele ba akseegul, li nga koy jox tam mën naa gën a rafet la mu la joxoon waaye fàwwu ñu tolloo. Bu ngeen àggoon ca dele ba te yaw nga dollil ko la mu la joxoon te saartu ñu ko ca ndax bu amoon mu yàqu, digóo ko ko woon tam, am na wuute As’sad moom da ni darra nekku ci ndax da laa defal njekk nga fay ko lu gën a rafet, Ibn Xaasim ne xaraam na ndax leble ngir Yàlla rekk a ca war na mu tolloon la war a toll, bu mujj bii moo gën a mat a topp.

Boo ameelee nit xaalis ci ab jaayante walla mu abaloon la ko ngir Yàlla, boo ko teelee am te àggoo léen ca dele ba mën nga koo teel a fay ndax da ñuy jàpp ni wurus ak xaalis neex naa deñc, su ko soxlaagul moom mi ngay fay sañ na laa wax ni nga bàyyi ba àpp ba jot.

Képp koo ameel marsandiis walla ñam te ngeen séqeewoon ko ngir Yàlla bëgg benefiis amu ca, boo ko amee te dele ba yekseegul mën nga koo teel a fay, bu dee bëgg benefiis moo taxoon doo ko ko mën a fay te waxtu wa ak-

Page 129: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 2 9

siwul.

Xeetu meññent walla pepp walla yiy law bala nga koo sañ a jaay da fay ñor waaye liféeg ñoragul nga xam ni weesoogul a yàqu doo ko sañ a jaay waaye bu ca lenn rekk tàmbalee ñor mën nga caa sukkëndiku far jaay tool bi yépp benn yoon, mbay bokku ci niki bu doon dugub walla leneen da ngay bàyyi ba lépp ñor ba noppi.

Da ñuy saart ci njaay li ngeen di waxaale bu ngeen jubóo nga mën koo jéb-bële kon jën yi nekk ca dex ba te nappaguñ ko walla ñu nekk ciy taa-taa ndox kenn sañu koo jaay, lu ñu ëmb tam mu nekk ci biirub yaay ñeel mbooleem bàyyima yi mëneesu koo jaay, li ñu ëmb te juddóogul deesul a sañ a waxaale la muy ëmbi bis bu juddóo ba màgg, bii moom moo gën a aay, maniyu gi ci giléem gu góor te sañeesu koo jaay niki giléem gu góor gi di bu baax nit ñëw bëgg a jënd maniyu ga ci wax ni ay giléem yu jigéenam kepp lay tëb wëlis ke-neen nga xam ni giléem yu baax yoo yu moom rekk moo koy am, ni mu aayee ci giléem noo nu la aayee ci xar, fas, mbaam...

Yoon tere na jaay xaj, Yonent bi SaWS moo ko terewoon, wuute na ñu ci xaj bu ñu yar ba mu mën a rëbb walla sàmm kër walla ñu mën koo yónni muy dem ak a dikk waaye bi gën a wér mooy kenn sañu koo jaay.

Lu ñu rendeegul niki xar walla béy bu taxaw nga seet lu mu bokkal benn xeet niki boroom ñent i tank mu jox la yàpp yaw nga jox ko la ñu rendeegul daganul niki mu joxla fukk i kilo yàppu nag nga jox ko xar mu ñu rendiwul, bu ñu bokkuloon xeet yoon nangu ko niki mu jox la ñett i kilo yàppu xar nga jox ko ginaar fa saa sa.

ñaar i njëg daganul niki nga ni sama marsandiis mii ku koy jënd ci saa si ma jaayee la ko téeméer, ku ko jënd di fay weer wu dee ma jaayee la ko téeméer ak juroom fukk, bu leeree mu baax li koy yàq mooy kenn jékki-jékki jël ko te ràññee wu ñu ba xam da fay fay fa saa sa walla da fay bàyyi ba weer wa dee ndax da fay mel ni da ñoo jaayante te xamu ñu ci gan njëg la te daa bokk ci saart i njaay ñu xam njëg ga njëkk.

Tàndarma gu tooy deesu ko jëndee tàndarma ju wow niki raseng ak nu ngeen ko bëgg a defee rekk du tax mu baax, mbooleem meññent yi ak xeetu furuwi yi ñoo ci yemoo la ca xës wow ba ñu xam nu mu toll kenn du ko mën a jaayanteek la mu bokkal xeet te tooy ndax li wow xam na ñu na mu toll li tooy ñu umple ko.

Ba tay jaay ab jal nga xam ni kenn nattu ko bay xam ni mu toll, ka nga ko

Page 130: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 0

jaay bëgg laa jox lu ñu natt mbaa lu ñu peese daganul ndax su boo baa day nekk jaay lu ñu xam jënd lu ñu réeree.

Jaay ab jal ci jal sax bu ñu dee gam-gamle kan a nax sa moroom mu aay, xeetu furuwi yi nga xam ni nangu na ñu ci ëpplante bu wóoree ni benn jal baa ëpp te ñu nangu ko du aay.

Lu teewul te jëlee ko fa mu nekk indi ko yomb na lool, yoon nangu na ñu jaay la ko ndéem nekkul fa ngeen di waxaalee nga xam ni kiy jaay da la koy melal nga jënd ko ci kaw waxam ja waaye kenn du ca fay fa saa sa bu ko ca saartee rekk mu yàqu, bu dee la ñuy jaay te teewul daa boole ñaar fa mu nekk bañ a sori mbaa lu mu yàgg-yàgg du soppeeku niki kër walla suuf di na dagan ñu joxe njëg ga njëkk ag teewam waaye su boo baa kay wax melo wa bu mu doon kay jaay.

Boo bëggee marsandiis walla jur walla ñam walla lu ñuy defaree ñam mën ngaa seet ka nga defe ni mën na koo am nga wax ko melo wa bu baax, bu ngeen jubóo ci njëg nga fay ko ko mu wuti ko te sàkkal ko dele sàngam ci la koy indi jox la dagan na, mooy salam njëg ga loo ko ko yéex a jox warul a yées ñett i fan, doonte da nga ko caa saartal buy weesu ñett i fan lay aay.

Jaay bor jëndee bor daganul niki nit ameel la bor nga di ko jaay, ka nga koy jaay it du yëkëti darra jox la waaye bor bu ñu ko ameel la lay fayee.

firi bor ci bor daganul mooy li mu la ameeloon nga bëgg koo soppi ci le-neen lu bokkul ak la mu la ameeloon niki mu ameeloon la fukk i junni, nga bëgg mu soppil la ko rajo te du la ko jox fa saa sa mu jëm ci ab dele.

Bokk na ci li daganul nit ki ne la jaay ma darra nga waxaaleek moom ba jubóo te fekk ni amagoo ko, ginnaaw bu ngeen waxaalee ba jubóo ci nga koy wuti, da ñuy bëgg boo amul li muy waxaale ngeen def salam bi ñu wax sank mooy ngeen waxaale ba jubóo mu wax la melo la mu soxla ba mu leer jox la njëg gi may la diir boo koy wutëli li mu bëgg.

Boo jaayee nit marsandiis bëgg koo jëndaat ci moom daa am fukk ak ñaar i tomb, benn nga jëndaat ko ci njëg gu tollook ba nga ko jaayeewoon mbaa gu ko yées mbaa njëg gu ko ëpp, boo koy jënd ci njëg goo gu kepp benn nga fay ko ca saa sa mbaa ci dele bu àggul ci dele bu njëkk ba walla dele bu njëkk ba doŋŋ ci nga koy fay mbaa dele bu gën a sori, ba tay boo ko jëndaatee njëg gu ëpp ga nga ko ko jaayeewoon tam noo nu benn nga fay ko ca saa sa mbaa ci dele bu àggul ci dele bu njëkk ba walla dele bu njëkk ba doŋŋ ci nga koy fay mbaa dele bu gën a sori.

Page 131: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 1

Ñett ñoo ci aay te mooy su fekkee moom mi njëkk a joxe ca waxtu wa mu war a joxe te di négandiku ñu joxaat ko lu ëpp loo la.

Lu ñuy natt ci aada walla ñu koy peese dagan naa jaay ab jal niki pepp mbaa gerte, wurus ak xaalis bu ñu ko xësee tampe ba wax ni moom la ñuy jëfandikoo ci wàllu jënd ak jaay deesu ci mën a jënd ab jal fàwwu ñu waññi ko njëkk ba xam na mu tollu, sémbub wurus walla xaalis nga xam ni mooy bi tëgg biy jëfandikoo di ci def i jaaro mbaa leneen moom mënees na ñu cee jënd ab jal.

Loo xam ni ay benn-bennam am na njariñ te yomb a waññi walla ay benn-bennam ëppënte njariñ lool du dagan ñu jékki-jékki jaay la ko ci ab jal niki coggalug xar mbaa bëy du ñu la ko mën a jaayandoo fàwwu da ñu koy waññi xool benn bu nekk, bu dee yëre yu am solo niki mbaseng tam noo nu du ñu ko mën a jóor noo nu jaay la ko, bu dee lu mel ni fëgg-jaay nga xam ni daa def ay morso yu bari du neex a waññi moom di na dagan ñu jékki-jékki jaay la jal bi.

Mën na ñu laa jaay lu ñu fas ci mbuus walla ñu pakete ko nga xam ni da ñuy bind ca kaw luy tektale la ca biir, soo ko dàjjee mu mel ni la ñu bindoon ca biti doo ko sañ a xàcc, soo ko dàjjee mu wuute bu la neexee wéy ca jënd ba bu la neexe tam nga xàcc.

Daganul ngay jënd tisu bu ñu tàllalul walla muy ci guddi gu lëndëm, nga xam ne na mu mel dëgg doo ko mën a seetlu ba bu amee sikk nga xam ko. Daaba yit niki oto daganul ñu di ko jaay ci guddi gu lëndëm.

Bu sa mbokku jullit di waxaale darra ba sori ca, yoo yu jamono di na xa-raam nga wax ca darra. Da ngay bàyyi bu jëndul nga soog a waxaale, bu soree-gul ca waxaale ba yaw di nga am sañ-sañu waxaale, bu dee da caa soriwoon ba ñu àgg ci jënd mbaa bàyyi ci lay xaraam ci yaw nga ciy dugg.

ñaar ñuy jaayante lu ñu waxante ba jubóo rekk njaay ma dog, mën na ñoo bañ a waxante benn baat niki ñu tafoon njëgu marsandiis bi ci kawam, am ku ñëw teg fa njëg ga jël ko dem moom may jaay mu lay séen te kenn waxu ca.

Njaay mën naa war te du wér ndax su fekkee ñaar i mukkàllaf ñoo ko de-fante kon wér na war na, bu dee koo ka da fay gone gu xàmmee waaye yorul mbiru boppam njaay ma mën naa wér waaye taxul mu war ndax kilifaam mën na koo teggi.

Defloo nit fay ko dagan na bu aajewoo ñu àppal ko da ñu koy àppal ba mu leer niki nga ni ko weer wu jot ma fay la walla ñett i weer yu ne te wax fay ga

Page 132: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 2

na muy tollu ba mu leer, bu léen neexee mën ngeen a jubóo ci bu noppee nga koy fay niki bu doon ku lay ñawal walla ku lay tabaxal ak yu mel noo na.

Booy defloo nit loo xam ni xayna mu sotti xayna du sotti nga ni ko fii ak àpp sàngam bu fi sottee di naa la jox nàngam, bu fi sottiwul li nga sonnoon lépp da nga koy ñàkk bu ko weesoo jeex na niki nga réerle darra ne ko bu ko gisee ci àpp sàngam nga jox ko nàngam bu ko weesoo doo ko jox darra, su boo baa du dagan, lay baax mooy nga ni ko demal rekk bañ a takk ci benn àpp nga xam ni moom mooy sonn bàyyi, àpp bee koy yàq ba du dagan.

Bàjj (employé) boo ko wutee ne ko da nga may jaayal ma fay la nàngam, bu àpp ba matee fàwwu nga fay ko la ngeen waxantewoon doonte jaayul darra ndax la mu mën mooy wone njaay ma ak ku dikk mu waxaale waaye mënul a dogu ci jaral. Bu ngeen digëntewoon ni bu jaayee weer nga jox ko ñent i junni mu jaay genwàllu weer wa ngeen far fa yem kon fàwwu nga fay ko ñaar i junni ndax jaay na genwàllu àpp ba.

Luyaas niki bu kër walla oto walla fas mbaa leneen mook jaay ñoo yemoo ca la cay dagan ak la cay xaraam, li xaraamoon ci njaay, luyaas tam loo la moo cay xaraam da ngaa war a xam li ngay luwe, bu aajewoo àpp ñu xam ko ak fay ga.

Bu dee ka luwewoon daaba ja moo faatu su boo baa bu léen neexee luyaas ba mën naa bañ a teggeeku, bu léen neexee keneen ñëw àggale daaba ja fa mu jëmoon te fay la ñu waxantewoon ak ka faatu, bu dee kër tam noo nu, njaboot ga mën na ñu koo wéyël te bu diir ba jeexee ñu fay.

Bu dee da ngaa jox nit ay gàtt mu la koy sàmmal ngeen waxante ni bu at mi jeexee walla weer wu ne nga jox ko nàngam, gàtt ya ci boppam yépp dee walla mu am yu ci dee, la ngeen waxantewoon du yàqu mën nga koo joxaat gàtt yu toll ni la nga ko joxoon mu wéy ba ca diir ba ngeen waxantewoon nga soog koo fay, boo ko mënul a jox yeneen da nga koy fay, fay gu mat.

Boo jëloon ab bàjj di ko ligéeyloo te àggul mu far faatu mbokkam du mën a ñëw ni da ko koy àggaleel ñu fay ko la ñu ko waroon a fay lépp, da ñuy seet la mu jot a ligéey ñu fay ko ay mbokkam.

Ba tay boo luwewoon kër laata diiru luyaas biy àgg kër ga màbb mbaa mu lakk, du ñu la joxaat geneen kër nga àggale ca diir ba, da ñuy seet la nga ca jot a dëkk rekk nga fay ko ko, bu ngeen dee luwewaat geneen ngeen luwe, luwe gu yees.

Yaw miy jàngale alquraan mën ngaa saartoonteek ka ngay jàngal walla doomu ka nga digaaleel walla soxnaam ci kaw bu mokkalee mu fay la nàngam

Page 133: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 3

walla su demee ba fer ijji mu fay la nàngam walla su demee ba mokkal nàn-gam i xizib, lu ngeen ci jublu rekk baax na.

Ba tay dagan na nga fekk ku mën a faj, nga waxanteek moom ngir mu faj la ba kero ngay wér soog koo fay nàngam waaye yaw yaay jënd garab ya, soo wérul doo ko jox darra.

Bu dee da nga ni ko luwe ma daaba sàngam niki aw fas walla oto te ràññeewoo ko su boo baa bu ñu demoon ba ca yoon wa daaba ja dee walla oto ba paan mënëtul a demati kon di na la mën a joxaat beneen nga wéy ba fa nga bëgg a àgg, nga fay ko njëg ga ngeen waxantewoon.

Boo luwee lu ñuy jëfandikoo muy njariñ ci kër niki cin walla sémmiñ mbaa inde mu yàqu ci say loxo ci loo xam ni coobareg Yàllaa waaye du sag sàggante kon da ñu koy jàppee ndogal rekk yoon du la wax nga fay boroom te la nga ca wax dees koo war a gëm ba kero ñuy gis lu ko teggi, bu ñu ñaawee ci moom njort di na ñu ko giñloo, lu dul ni daa leer nàññ ni li mu wax mënul a nekk da fay fay.

ñi amug xarala ubbi seen ataliyee ñu léen di jox ñuy defar di léen fay niki tëgg yi ak wuude ba ci ñawkat yi ak yu ni mel, koo ci jox darra fa ataliyee ba mu koy defar ngir Yàlla walla nga warlul ko ci ag pay, bu dee lu ñu mën a nju-blang yoon da koy fayloo boroom.

Ki ame gaal walla oto walla saxaar walla roppalaan su ca aksidaa amee boo xam ni dogalub Yàllaa nga xam ni ngelaw moo ko waral walla duusu géej yi walla lu mu ci doon def lu aw yoon la kenn du ca fayloo boroom darra waaye kenn waru koo fay te àggul.

Bokk ab ligéey lu dagan la niki ñu booloo ubbi ab ataliyee walla sosiyete lu ñu am séddoo di bokk ligéey di bokk la cay am ci njariñ, mën naa doon ngeen bokk benn ligéey walla seen ligéey ya jegeente.

Ligéey ci sosiyete nga xam ni kenn ku ne da fay génneeb kapitaal ngeen boole ligéey, kenn ku ne la nga joxewoon ci kapitaal ngay am ca benefiis ba waaye ligéey ba tam noo nu la, du dagan bu kapitaal ya yemoowul ñu bëgg a saart ni bu ñu àggee ca benefiis ba yemoo ca.

Qiraad dagan na mooy nga jox nit kapitaal mu ligéey ca, su àggalee yaw nga jëlaat sa kapitaal ngeen séddoo benefiis ba walla nu ngeen ca jubóo mu baax, du doon ci marsandiis bi waaye da fay doon xaalis biy daw ca dëkk ba ñu cay jënd ak a jaay, bu nekkee wurus ak xaalis bi ñuy xelli du ko tee baax.

Page 134: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 4

Bu la ci nit joxee alal nga tukki ngir ligéey ci ngay sol ci ngay lekk te kenn du ko waññiwaale waaye da fay fekk alal ja bari te tukki ba sori, fàwwu tam nga bàyyi ba mu jaay lu toll ni kapitaal ba, doo mën a taxawal ligéey ba ngeen séddoo benn yoon.

Nit am ay taat i garab yuy meññ nga di ko ko suuxëtal dagan na ci kaw la ngeen jubóo niki bu ngeen àggalee nga am ceer walla lu mu mën a doon rekk baax na, suuxët ba lépp war na ka ñuy ligéeyloo waaye ca la ñuy yem du ko ci saartal niki bu bis sàngam jotee nga jaayali ma kon mu yàqu waaye bu dee lu woyof niki duy walla defar mbalka ma du aay, fàwwu tam da nga koy bàyyeek daaba yépp, bu benn ci daaba ya faatuwoon sax da koo war a wutël beneen.

Bokk bay lu ci ñor ngeen bokk ko dagan na ci kaw kenn ku ne génnee jiwu walla kenn ka moom suuf sa ka ca des féetewoo ligéey ba walla kenn ku ne joxe jiwu ñu bokk ligéey ba tam, kii joxe jiwu kii joxe suuf moo ci dul dagan benn yoon doonte ki joxe suuf daf cay boole bay tool ba kon mu aay.

Su fekkoon ni da ngeen bokk luwe suuf sa walla ngeen bokk ko moom mbaa ñu dogal léen ko walla muy seen suufug maam, kii joxe jiwu ka ca des féetewoo mbay ma bu ñu noppee séddoo kon mu dagan.

Yi nga xam ni seen i reen da fay nekk ci suuf, su ñu la ko jaayee ci kaw nga war koo buddi niki ñàmbi walla karoot, boo koy buddi lépp lu ca yàqu da ñu la koo war a delloo ca njëg ga ak lu mu néew-néew.

Tegginu lekk ak naan

Bokk na ci tegginu lekk ak naan, loo ci bëgg a def nga njëkk a wax Bismillaa-hi te tam nga di ko defee sa loxob ndeyjoor, boo lekkee ba noppi nga mar loxo bi doog koo raxas ndax da ñuy bañ li des ci ñam ci sa loxo nga yàq ko.

Sopp na ñu nga def sa biir ñett i xaaj, benn bi féetewoo ñam wi, ñaareel bi féetewoo naan gi, ñetteel bi bañ a am darra ngir nga di ko noyyee.

Bokk na ci teggin ya, boo dendee ak ñenn di lekk nga yem ci sa kanam bañ di dem ci kanamu jàmbur ak ci digg bi lu dul ni daa am loo soxlaa jëli ci digg bi te nekkul ci pegg yi.

Boo tibbee benn tibb nga sàqami ko bu baax ba mu mokk ba jàll nga door a tibbaat beneen, sàqami bu baax da fay jàppandal rees gi.

Booy naan ba war a noyyi da ngay toppale pot bi ba noyyi ba noppi, boo màndiwul nga daa di naanaat, taamu wu ñu ngay guux guux yu mag ba ñuy dégg ni muy jàllee, ni gën mooy ngay muucu tuuti-tuuti ba kero ngay màndi.

Page 135: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 5

Ginnaaw boo lekkee ba noppi nga bañ a bàyyi sa gémmiñ noo nu, sopp na ñu nga setal ko ci borosu walla nga soccu walla nga galaxndikoo ndox.

Boo lekkee lu niin, sopp na ñu nga fexe ba tàggook niinaay boo bu di des ci sa loxo, li des ci say bëñ ci ñam wi nga dindi ko.

Taamu na ñu boo jëfandikoo ba noppi nga jottali ka la féete ndeyjoor.

Taamu wu ñu ngay ëf aw ñam walla naan ndax da ñuy bañ darra bàyyee-koo ci sa gémmiñ dugg ca nga séexlu ko keneen séexlu ko ñu tuur ko, loo lu di yàq gu mat a daw, ëf am mbind tam soppu ñu ko.

Jëfandikoo ndab lu ñu ligéey ci wurus walla xaalis xaraam na ci góor ak jigéen yépp moo xam da nga ciy def lekk mbaa naan walla raxasu, teg ko fi barab sax xaraam na.

Taxaw naan walla di lekk darra nekku ci, lekk di sóonu moom sib na ñu ko, tàndarma ak lu ko nuru sib na ñu nga di ko lekk di booleendoo doom yu bari ci sa gémmiñ, am na ñu ni boo ko bokkeek ñoo ci yemoo àq lay aay waaye bu dee yaa ko jënd moom tàndarma ja ak lépp lu ko nuru mën ngaa boole doom yu bari ci sa gémmiñ, di tànn doom ya nga taamu di lekk aayul niki bu ñu de-foon tàndarma mbaa lu ko nuru ci ndab.

Saa boo jëfandikoo lu am xet gu naqari mel ni laaj walla soble mbaa nga tux da ñu lay aaye nga dugg ci jàkka walla ci barab bu ñuy tuddee Yàlla walla di fa jàng alquraan.

Boo bëggee lekk te sa loxo taqul darra du ñu sopp nga raxas ko waaye bu taqee sobe walla loo xam ni boo ko lekkaalee mën naa jeexital ci sa wérug yaram su boo baa raxas ko da fay war.

Sib na ñu lekk ci ndab ba noppi dugal ci sa loxo mel ni ku ko cay raxas ngir tàggook yi taq ci sa loxo doonte cox la niki nga lekk ba pare dugal ca sa loxo ngir raxasoo ko.

Bu ñu la woowee ci ab takk ràññeel la, war ngaa wuyuji lu dul ni da ñu fay def lu aay niki di fa fo walla góor ak jigéen di fa jaxasoo, la ñu fay joxe ci ñam kenn du la forse nga lekk ca, boo bëggee lekk boo bëggul sañ ngaa bañ a lekk, bu dee céet ga da fay bari mbooloo ak i buux-buuxloo imaam Maalik nee na sañ ngaa bañ a dem rawati na boo dee kilifa goo xam ni dem fu mel noo na di na diis ci yaw.

Bunt ci nuyyóo, diisóo, jàng Alquraan ak sikkar

Njëkk a nuyyu nit sunna la, bu ñu la xasee nuyyu fay ga fardul kifaaya la

Page 136: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 6

waaye wax na ñu ni sunna see ëpp tuyaaba, nuyyóo dëgg-dëgg ci lislaam mooy wax Assalaamu alaykum, jaar ci santu jàmbur kese nuyyóo aada la waaye njëkk a wax assalaamu alaykum soog a jaar ci ay sant moo gën ndax di nga boole def li lislaam santaane ba noppi soog a jàll ci tudd sant wa ni ñu ko baaxoo fii ci réew mi.

Boo dee fay ki la nuyyu da ngay wax wa alaykumu salaam, boo dee fay ab nuyyóo ba wax ni wa alaykumu salaam wa raxmatulaahi wa barakaatuhuu doo ca dolli darra, mbooloo bu ca kenn rekk nuyyóo mu baax, mbooloo mu nuyyóo tam bu léen kenn rekk fayee mu baax.

Taamu na ñu bu fekkee da ngaa war nga njëkk a nuyyu kiy dox ak tankam ndax war gi day nuru daraja, yaw miy dox tam nga njëkk a nuyyu ki toog.

Sopp na ñu saafonte mooy joxante loxo, bu ñu ko defee ak ñaar i loxo ya sax moo gën, tegantey loos moom imaam Maalik da koo sib ni ko tubaab yi di defee, am na yit ñu ko daganal ndax Yonent bi SaWS mos na koo def Jaafar ba mu bàyyeekoo abasa (ethiopie).

Maalik sib na yit nuyyu kenn fóon loxoom, la ñu ca nettali ci xadiis it da koo weddi, la gën mooy boo nuyyóo boroom ngëneel niki ab sëriñ walla boroom xam-xam nga fóon loxoom ngir nga topp xadiis ya nga ca yër te imaam Maalik weddi ko, ba tay fóon sa loxo waajur aayul.

Sib na ñu nga njëkk a nuyyu ab yahuud wallab nasaraan, su ñu la nuyyóo na nga yem ci alayka kese.

Néegub jàmbur bul jékki-jékki dugg ca lu dul ni da ngaa yëglu bañ la ni jàllsil, da ngay nuyyóo mbaa nga fëgg walla nga sëqët, bu la wóoree ni dégg na ñu la te nee wu ñu la jàllsil soo yaboo waññeeku, bu dee foo xam ni ku waaxusi dugg niki butik du aaje yëglu ba noppi.

Bokk na ci yi bari tuyaaba lool seeti ku tawat te Yàlla tax.

Xaraam na ñaar di déeyaale bàyyi kenn, ba tay mbooloo du diisóo bàyyi kenn rekk, bu mbooloo bàyyiwoon ñaar di diisóo du aay, bu dee kenn ka ñu bàyyi moo léen ca may ndigël di na ñu ko sañ te du aay.

Toŋŋ bu dee sa digg ak ki nga koy def yëf i àddunaa warul a weesu ñett i fan, bu dee Yàllaa tax mën na koo weesu.

Ma’aaz ibn Jabal nee na jépp jëf ju doom aadama di jëf, lu ko ci mën a musël ci mbugëlum Yàlla ni tudd Yàlla amul, Seydinaa Umar nee na tudd Yàlla ci sa làmmiñ baax na waaye bi gën mooy bàyyi xel sa Boroom ba bu diglee nga

Page 137: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 7

fàttaliku ko jëfee ndigël la, bu teree nga fàttaliku ko di ko daw.

Ligéey ci ab jàkka lu dul xatal kiy julli walla di ko taqal ak a sobeel sib na ñu ko, say loxo bu setee nga raxasee ko ci biir jàkka sib na ñu ko waaye bu taqoon sobe nga raxasee ko ci biir jàkka ja lu xaraam lay doon. Jàkka yit boo fa dee lekk da nga fay lekk lu woyof te du fa taqal darra niki mbiskit walla gerte, lelli wee walla wat say mustaas deesu ko fa def, kenn du fa ray téeñ walla fel, boo ko fa rayoon bàyyi ko fa def lu xaraam ndax jëmm ji nga fa ray noo nee sobe la, médd lay doon.

Boo demee ci dëkk boo xam ni doxandéem nga fa di na ñu la may nga mën a fanaan ci jàkka ja, bu dee dëkk i taax nga xam ni am na foo mën a fanaan fay te nga am loo fayee doo sañ a fanaan ci ab jàkka.

fépp foo xam ni njort nga mu am sobe boo fa nekkee waroo faa jàng alqu-raan waaye di na ñu la may nga jàng fa aaya yu néew ngir léemoo ko, boo waree walla nga tëdd walla nga bàyyeekoo ci ab dëkk jëm ci beneen mën ngay jàng alquraan moo xam da nga koy tari walla nga di ko xool, boo jëmee ci marseb taax sib na ñu ngay jàng alquraan ndax amaana sobe jot la ci yoon wi walla nga bàyyi xel nit ña ba juum, bu dee marseb àll yoon wa set te féex sib ga day teggeeku, kiy dem ci ab maarse doonte ci taax ya la di na dagan muy jàng jàngug xamlu ngir bëgg a mokkal alquraan.

Wax na ñu ni Yonent bi SaWS mosu koo wàccee moom alquraan ci lu yées ñett i fan ndax settantal gi daa am solo.

Sib na ñu ngay tukki jëm ci réew moo xam ni kéefér moo fa ëpp doole ngir sàkkuji alalu àdduna.

Jigéen sañul a tukki tukki buy mat doxub guddi ak bëccëg mbaa mu ëpp ko te àndul ak góor gu xaraamanteek moom mooy góor gu ko jege ci askan walla nàmpaale mbaa ngoromaale, du sañ a ànd tam akub jàmbur. aj Màkka su fekkee jigéen ji amul xaraamante te mu am àndandoo yu ñu wóolu aayul, jigéen ji yit ñu wóolu ko, di na mën a ànd ak ñoo ña.

Sujjóodu Alquraan yi

Mooy barab yi nga xam ni booy jàng ba àgg fa te fekk saart yi dajee ci niki nga ame laab te jublu xibla, sol ngay yëre nga daa di sujjóod, fa nga nekk tam laab, bu dee tiim mooy sa farata, nga tiim ba noppi. Waxtu wa yit bañ a doon waxtu wu ñu sibee naafile.

Booy sëgg di ko def da ngay wax Allaahu Akbar waaye boo ko defee ba

Page 138: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 8

àggal doo wax Assalaamu alaykum.

Bi ngay siggi boo ko waxee baax na boo ko waxul tam di na baax waaye wax gaa gën

am na ñu ne sunna la, am na ñu ne ngëneel la, nekk gi sunna la ñi ëpp ànd.

Barab ya fukk la ak benn ci fiqu Imaam Maalik, sib na ñu nga jàll te su-jjóodoo. amul ci Mufassal yi te mooy li tàmbalee xujuraat jëmsi ci suuf ba ci Naasi, boo seetloo téere yi bàyyeekoo penku di nga ci gis ay sujjóod, di nga ko gis suuratu Najmi, ci Inchiqaaq it noo nu waaye fiqu Maalik moom ba ca Suuratul Fussilat mooy ba ca mujju.

Ba ca njëkk mooy bi nekk ci Suuratul A’raaf, wa yusabixuunahuu wa lahuu yasjuduun, boo waxee yasjuduun fa ngay sujjóodee, moo mujju ci saar wi, fi mu ne boo doon julli ba àgg ca kon rukkóo nga ca waroon a teg te sujjóod gi ñu wax sank da la fay war, su boo baa da ngay njëkk a sujjóod sujjóodu alqu-raan ba àggal delluwaat taxaw bu la neexee nga jàng ci Anfaal walla beneen saar waaye doo baamu Faatixa ndax rukkóo bi da ñuy bëgg mu sës ci am njàng, bariwul lu muy am waaye mat naa xam.

am na yit ci Suuratu Raxdi, boo jàngee ba àgg ci wa zilaaluhum bil uduwi wal aasaali fa ngay sujjóodee.

am na ci Suuratu Naxli, boo jàngee ba àgg ci yaxaafuuna Rabbahum min fawqihim wa yaf’aluuna maa yuumaruun fa ngay sujjóodee.

am na yit ci Suuratu Israa’i, boo jàngee ba àgg ci wa yaxiruuna lil azqaani yabkuuna wa yaziidahum xuchu’an fa ngay sujjóodee.

am na yit ci Suuratu Maryam, boo jàngee ba àgg ci izaa tutlaa alayhim aayaatu Raxmaani xaruu sujjadan ba bukkiyan fa ngay sujjóodee.

am na ci njëlbéenu Suuratul Xajji, boo jàngee ba àgg ci wa man yuhini Laahu famaa lahuu min mukrimin inna Laaha yaf’alu maa yachaa’u fa ngay sujjóodee.

am na yit ci Suuratul Furqaan, boo jàngee ba àgg ci maa taamurunaa wa zaadahum nufuuran fa ngay sujjóodee.

am na yit ci Suuratu Namli, boo jàngee ba àgg ci Allaahu Laa ilaaha ilaa Huwa Rabbul archil aziimi fa ngay sujjóodee.

am na yit ci Suuratu Sajdati, boo jàngee ba àgg ci wa sabbaxuu bi xamdi Rabbihim wa hum laa yastakbiruun fa ngay sujjóodee.

Page 139: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 3 9

am na yit ci Suuratu Saad, am na ñu koy wax Suuratu Daawuda, boo jàngee ba àgg ci fastaxfara Rabbahuu wa xarra waaqi’an wa anaaba fa ngay sujjóodee.

amna tam ci Suuratu Fussilat, boo jàngee ba àgg ci wasjuduu lil Laahi lazii xalaxahunna in kuntum iyaahu tahbuduuna fa ngay sujjóodee.

Boo dee julli jullig farata jàng ci foo war a sujjóodee soo yaboo sujjóod ko, bu dee naafile tam noo nu. Naafile mën nga koo tay jàng ca aaya sujjóod yoo yu waaye bu dee farata moom taamu wu ñu ko.

Ginnaaw suba da ñoo sib naafile te suujjóodu alquraan moom ak naafile ñoo bokk waaye sujjóod gi am na ag jàppandal mooy booy soog a sëlmël suba ba ba muxtaaru suba gi di jeex boo fi jàngee alquraan ba toll ci barabu sujjóod, di na ñu la may nga sujjóod ko waaye bu muxtaaru suba bi jeexee ba daruuriyu ji dikk, boo tollee ci barabu sujjóod da nga koy tëb bañ koo jàng waaye doo ko sujjóod.

Ginnaaw tàkkusaan tam noo nu la da ñu cee sib naafile waaye may na ñu la ba kero muxtaarum tàkkusaan gay jeex, boo tollee ci barabu sujjóod nga def ko waaye bu muxtaar ma xasee jeex, da ngay tëb aaya bépp bañ koo jàng.

Tasawuuf

Tasawuuf moom la ñu cay jiitël mooy tuub lépp loo weesuwoon te Yàlla gërëmu ko tuub gu sell te fexe ba doo ca dellu, lépp lu doxoon sa digg ak doom aadama yi ci ay àq nga delloo ko ba mu mat walla nga jéggëlu ko ba mu wàcc la.

Tuub daa am ay saart, ba ca njëkk mooy réccu la nga weesu, bu dee loo war a fay la te fay ga wéyul da nga koy dabaatal te jéggëlu yéexee ga.

Dëgg dëggi ragal Yàlla mooy bàyyi lépp lu ñu tere biir ak biti te topp lépp lu ñu la digël sa keem kàttan, ku bëgg a jariñu ci yoonu Yàlla ci ñent yoo yu kese ngay aw te mooy benn bàyyi lu ñu tere ci biir, ñaar bàyyi lu ñu tere ci biti, ñett topp ndigël ci biir, ñent topp ndigël ci biti.

fexeel it tëye say bët ba doo ci xool darra lu xool ga warul, moytoo déglu tam ci say nopp lu aay niki jëw, rambaaj, seede nit ci lu ko wóorul ak fen rawati na nga di ko wax ak sa làmmiñ, na nga sàmm sa biir ba doo ca dugël lu xaraam ak loo xam ni xaraam ga daa lënt ci yaw, sàmm it sa sawukaay ba doo ca moy ci njaalóo walla feeñal ko fu mu warul a feeñee ak lépp lu koy nuru. Loxo yi tam nga moytu caa laal lépp lu warul, tank ya nga fexe ba doo ca dox lenn lu

Page 140: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 0

Yàlla gërëmul.

Mbir mu mu doon it muy wàllu àdduna walla diine na nga ca teey ba xam lu ca lislaam àtte ndax xaraam na nga tàbbi ci mbir te xamoo la ca diine wax, soo ko xamul da nga koy laaj ku maanu ba mu xamal la ko nga jàpp la mu la wax.

Boo weesoo cër i biti yi xol ba tam cër la bu mat a laabal ci ngistal (jëf lu Yàlla taxul) ak kañaan (yéene ku amug xéewël mu ñàkk ko) boo ca boolee waxee ko mbaa jëfee ko mu xaraam ak naw say jëf, na nga sax tam ci di moytu bépp jangoro xol.

Li ëpp ci liy yàq xol di cosaanal ñaawtéef yépp manees na ñu koo tënk ci bëgg àdduna ak fàtte allaaxira nga xam ni daa mel ni da ñoo tëj ñaawtéef yépp ci néeg def bëgg àdduna muy caabi bi koy tijji, ñu jël it mbooleem yu baax yi tëj ci ab néeg def dëddu àdduna muy caabi bi koy ubbi.

Wéeru ci Yàlla ñaan ko mu saafaraal la mbooleem xeetu jàngoro yi te yom-balal la mbir yi moo gën a gaaw ci musël la ci gàkku xol yoo yee du tee nga farlu bu baax sa keem kàttan.

Boo mënee gis sëriñ bu tàggatu ci yoonu Yàlla ba xam yoon wa nga ànd ak moom moo gën a yomb ngay def say pexey bopp ngir yegg, da fay doon koo xam ni saa soo ko gisee gis ga kepp da lay delloo ci Yàlla, mu nekk it ku mat ku lay mën a àggale ci Yàlla.

foo toll deel xisaab sa bakkan ba noyyi gu génn nga def ca ag jaamu Yàlla, say xalaat it nga di léen peese bañ sax ci lu am njariñ ndax xalaat yoo yee su baree ci lu amul njariñ bu yàggee cër ya jëm ca.

Li Yàlla sunu Boroom farataal ci yaw nga fonk ko bu baax te di ci toftal ay naafile yooy baril lool.

Di baril looy tudd Yàlla sunu Boroom te di ko teewlu boo bu moo ci gën a kawe, bi ci topp mooy bi xol biy teewlu te làmmiñ wi tuddul ba ca féete suuf mooy tuddug làmmiñ wi kese te xol bi desee teewlu.

Na ngay góorgóorlu ci bëreek sa bakkan ci di ko awale ci dëgg te bañ koo topp ca la ko neex.

fexee sax ci ragal Yàlla ak yaakaar ko ndax ragalug kese day jur nga naagu yërmande Yàlla, boo yaakaaree yaakaar gu ëpp da ngay daa di njort ni mucc nga, di sant Yàlla bu baax tey muñ ak di tuub te dëddu àdduna, wakkirlu ci Yàlla sunu Boroom, li Yàlla di dogal neex la nga sopp it Yàlla sopp gu mat sëkk.

Page 141: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 1

Na la wóor it ni Yàlla Mi darra umpul ngay jëflanteel ci jamono ju ne.

Nii boo ko defee da fay dem ba kumpa da fay jóg sa digg ak sa Boroom nga xam ko ci bu wér nga xam ni doo doon jaamub kenn ku dul sa Boroom, doo jaamu bakkan, doo jaamu seytaane, doo jaamu àdduna, doo jaamu bànneex.

Boo melee nii da ngay mujj nekk jaam bu sunu Boroom sopp, tànn la boole la ci ay njoñam bu wér a wér.

Su ko defee buntub tasawuuf bi da ñu koy tëjee waxtaan woo xam ni day dikk ci ay laaj ak i tontu yu jëm ci mbiru Tariixa ak wàllu taalibe ak sëriñ.

Da fa amoon benn waay bu tudd Bëgg a Baax waajaloon ay laaj yu am solo, demoon ci ku ñuy wax Sëriñu Tariixa ngir leerlu lépp lu ko lënt ci diggënte taalibe ak Sëriñ

Bb : Sëriñ bi noo ngi lay siyaar bu baax, da nu amoon ay laaj yu nu bëg-góon nga tontu nu ci ?

St : Noo ngi lay delloo siyaar bi tay ñaan sunu Boroom mu baaxe nu, ba lépp lu nu la tontu dëppoo ak ngërëmam.

Bb : Sëriñ bi da nu bëggoon a xam luy Tariixa ?

St : Tariixa baatu arab la buy firi yoon, waaye ba jëm ca Yàlla moo tax nuy wax, boo ci sóoboo ab diir te dox bu yàggee di nga àgg ndax Mi ngi fi te so-riwul, fàwwu nga ànd ak ku xam yoon wi te mën laa yóbbu ndax daa bari ay gàllankoor yu lay dab ci yoon wi bëgg a dox sa digg ak fa nga jëm.

Sunu Boroom mi ngi wax ci alquraan ni wa aniibuu ilaa rabbikum, dellu léen ci seen Boroom ndax ci moom la nu jóge, ki am doom da fa naan daa am gan, gan fa mu jóge la dëkk, su ko defee yoon wa ñu koy jaarale ngir mu dellu ci Boroomam moo tax a jóg Tariixa. Seydi Hadji Maalik wax na ca Faakihatu tulaab, fa turxu kulluhum ila Raxmaani muusilatun maslakatun yaa jaanii, Tariixa yépp ci Yàlla sunu Boroom la nu jëmee képp ku ci sóobu, naka noo nu boo demee ci Masaalikul Jinaan it noo nu la ko fa Seexul Xadiim radiyal-laahu anhu waxee, fa kullu wirdin yuuridul muriidaa lixadartillaahi wa lan yaxiidaa, sawaa’un intamaa ila Jiilaanii aw intamaa li axmada tiijaanii, aw lisawaahumaa minal aqtaab iz kulluhum qat’an ala sawaabi, wird woo jàpp ci Yàlla la la jëmee moo xam nga jàppee ko ci abd Qadr Jeylaani walla ci Seex axmed Tiijaan walla ku mu doon ci Qutbu yi ndax ñoom ñépp ci njub la ñu nekk. Boo seetee lii gis ni Tariixa yoon la boo xam ni lu dul yóbbu jaam bi ci sóobu ci Yàlla taxu koo jóg.

Page 142: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 2

Bb : lan mooy cosaanu tariixa ci diine ?

St : Diine da fay ñett i xaaj : iimaan, islaam ak ixsaan mooy tawxiid fiq ak tasawuuf.

Ponk i iimaan juróom benn yii la : gëm Yàlla, gëm Yonent yépp, gëm ma-laaka yi, gëm téere yi Yàlla sunu Boroom wàccee yépp ñi ngi toll ci téeméer i téere ak ñent, gëm bis peñc ak la mu làmboo yépp, gëm ndogalu sunu Bo-room yi mu neex walla mu naqari.

Ponk i islaam juróom yii la : seede ni benn Buur kepp moo yayoo jaamu te mooy sunu Boroom te moom Buur boo bu moo yónni Seydinaa Muxammad SaWS - julli juróom – woor weeru koor – natt asaka – aj Màkka boo ko mënee.

ixsaan mooy ngay jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, boo nekkul di ko gis Moom mi ngi lay gis.

Tariixa da fay ñëw ngir wéral sa ngëm, xamal la Yàlla sunu Boroom bi la sant nga jaamu ko ci ponk i Lislaam yi, jaamuwin wu tegu ci ixsaan te mooy sellal, kilifa ga ngay àndal ci tariixa mu di sa sëriñ, fàwwu di na la teg ci yoon woo xam ni boo ko toppee sa xol di na laab ci bépp ëyib ak i gàkk, yu mel ni bokkaale Yàlla, rëy, kañaan, ngistal, yéem say jëf, soxor ak yu ni mel ndax yii ku mu nekk ci yaw, loo jëf ci lu baax ñoo koy yàq.

Sëriñ Tuubaa ngi wax ci ay bëyit naan wa yaa axiil hiibata wa riyaa ma’al ujbi wal xasadi wal kibri dahaa, wa adami raxmati lil insaani wa xubi rif’atin alal aqraani, fa kullu man jama’ahaa awixtawaa waaxidatan minhaa faxaa-sirun tawaa, li’anahaa tuujibu raddal amali ilalazii amilahuu faltaxqili, jëw, ngistal, yéem sa jëf, kañaan, rëy, ñàkk yërmànde, bëgg ñu lay yëkëti na nga léen bàyyi ndax képp ku léen boole walla nga làq ci benn rekk pert nga te da lay sank ndax da fay waral sunu Boroom delloo la say jëf, du ci gërëm darra.

Moo tax tariixa ci ixsaan la taxaw, ndax mën ngay jëf lu baax te yaw mi koy jëf baaxagoo, Sëriñ Mbay Jaxate wax na ni bari alal taxul a gën, néew alal taxul a bon, lay tax nit di gën ak a bon, ca xol ba lay nëbbóo ka bóof. Moo tax Sëriñ bi ngay jàpp ci tariixa da fa war a sellal sa xol ci bépp gàkk, tàggat la ci ay jikko yu tedd ba nga xam ni say kàddu ak say jëf da fay tege ci ag sell guy tax sunu Boroom nangu ko, darra lu xaraam walla lu ñu sib doo ko jege.

Bb : Sëriñ bi man boo waxee lii di naa amug jaaxle ndax gis naa ñu bari ñu aju ci tariixa te desee defaru ?

St : Waaw li nga wax dëgg la te seetlu bu am solo la te mat a bàyyi xel, loo

Page 143: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 3

lu moom li koy waral mooy taalibe bu desee dëggël te xamul li muy sàkku ndax Yàlla ku tilim du ko jege, su ma nee tilim nak tilimug xol moo tax nuy wax.

Lee lee tam kiy soog a jox boppam ab sëriñ ngir bëgg a defaru te daan jëf safaan, xëy rekk bàyyi lépp di na jafe lool waaye du ñàkk ay ngànnaay yu ko sëriñ biy jox ba nga xam ni bu ko toppee diir bu gàtt di na soppeeku ba mel na mu war a mel.

Li xel nanguwul mooy nga am ci tariixa bi diir bu yàgg te mënoo jub, xoo-laatal sa bopp walla nga xool sëriñ bi, benn yaa matul taalibe walla moo matul sëriñ, moo tax loo lu nga wax sëriñ bu matul li mu doon di na ko waral ndax tay bari na ku ñuy jiiñ ag sëriñ te fa mu aw du ab yoon. Sëriñ Tuubaa waxoon na ni, wa man alaa hayril ilaahi dallakaa fa fira minhu innahuu adalakaa, ku la tektal leneen lu dul Yàlla daw ko ndax da lay sank, wax itam ni, wa man yurid salaaxal amali falyarkanan lil’awliyaa’il kumali, boo bëggee say jëf sell jengal jëm ci Waliyu bu mat.

Ki bëgg a yegg te dogu moo neex a yóbbu ndax lépp lu mu yëg ni kiiraay la lu mën a dox diggëm ak Boroomam di na ko bàyyi. Jamonoo yàqu fi mu ne ba ngay dégg ñu naan diw mooy sama sëriñ te la mu lay digël doo ci def darra, la mu lay tere yit bàyyiwoo ci darra, ànd boo bu darray njariñ du ci juddu ñeel taalibe bi. Lu mu ñàkk na yedd boppam te xam ni moom moo ko xañ boppam waaye du sëriñ bi.

Bb : Sóobu tariixa kon farata lay doon walla sunna ?

St : Da fa mel ni nga feebar di laaj ba xam, faju farata la walla sunna. Sëriñub tariixa xol lay faj ci jangoroy biir yi nga xam ni ku mu nekk ci yaw loo def ci lu baax ñu yàq ko. Ñàkk a tënku ci tariixa tere wu laa doon jullit waaye saa soo bëggee sell ci sikk yi ngay yëg ci sa bopp ak ñaawtéef yi ngay faral di def, fàwwu nga seeti sëriñ bu mat sëriñ mu yar la, yéegee la ba nga yegg ci sunu Boroom te loo lu darra jiitu wu ci defar la ba mbooleem say gàkk i xol génn ndax sunu Boroom du ubbil buntam ku defaruwul mukk.

Su ko defee ki naan muriid laa walla tiijaan walla tariixa boo mën a aju te gëstuwoo ko, jàppoo fa kilifa gu mat kilifa kenn du yaakaar ci yaw nga jote ci leeru sunu Boroom yi. Defaru goo gu, képp koo xam ni mën nga koo defal sa bopp, bu la neexee bul wuti sëriñ waaye gisagu ñu ku fa yóbbu boppam, Yàlla ci boppam moo bëgg nuy toppante te Moom rekk tax, waxoon na Yonent bi SaWS toppal yoonu Yonentub Yàlla Ibraahiim alayhi salaam, wa tabih milata Ibraahiima, nun mu wutloo nu wasiila bu nuy yóbbu ci Moom. Yaa ayuha

Page 144: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 4

laziina aamanu taquu Laaha wabtaghuu ilayhil wasiila.

Bb : Bëggóon naa nga xamal ma xeetu Sëriñ yi am ?

St : Xeetu Sëriñ yi am bari na ñu lool ndax bépp xam-xam bu mu doon ka koy xamle mooy Sëriñ ba, ka mu koy xamal di taalibe, bu dee lu jëm ci diine di na ñu ko tënk ci ñett i xaaj.

Bi jiitu mooy bi lay jàngal araf, jàngal la alquraan, Xadiis ak fiq, xamal la fa-rata, sunna, li dagan, li ñu sopp, li ñu sib ak lu xaraam, kii mooy Seexu taxliim.

Bi ci topp mooy bi lay yar, nga xam ni soo ko doon misaal, da fa mel ni ndab lu tilim bala nga ciy def ñam wu sell di nga ko raxas ba mu set, koo ku mooy Seexu tarbiya, ki lay yar ba sunu Boroom ni yaru nga.

Ñetteel bi mooy Seexu tarqiya, moom moo lay yéegee yeggale la ca Yàlla sunu Boroom ba nga yëg ko. Seexu tarqiya da fay nekk ku mën a yare, ndax Yàlla sunu Boroom da fay ku sell, lu sellul du àgg ci Moom moo tax balaa ñu la fay yóbbu fàwwu ñu tàqarle la ak i ëyib. Kilifa àdduna lu mu rëy-rëy daraja, mën nga koo gis walla nga jotaay ak moom, Yàlla sunu Boroom da fa xam sunu biir ak sunu biti, di kilifa lool, boo sellul, ak kilifa gu mu mën a doon, su fëggee Bunt ba, moom mën naa jàll waaye yaw mi mu àndal te nga taq doo jàll te bunt la bu kenn mënul a xëtt. Moo tax Sëriñ bu mu mën a doon, bu nee mën na laa yóbbu ci Yàlla te defaru la wax na la lu jomb.

Bb : Ndax ag Sëriñ mënees na ñu koo donnu ci waajur ndax da maa seetlu ni da ngay gis ku topp baay mu làqu, nga topp doom ?

St : Lu man a nekk waaye jar naa leeral ndax ag sëriñ ci tariixa du lu ñuy donnu. Mi ngi mel ni nga wéradi di topp ap fajtal ci benn doktoor, mu wàcc liggéey nga seeti doom ji ne ko man sa waajur moo ma doon faj, ginnaaw nekkatu fi ma bëggoon nga wéyal yéeneem ci man. Doom joo ju su doonee la waajuram doonoon nga xam ni xam-xam bi nga xemmeemoon ci waajuram ba tax nga topp ko wóolu ko mi ngi ci moom, li nga def doo ko réccu. Gisa goo ku doktooram faatu mu seeti ca njaboot ga ku ko ca faj xanaa bu ca amee ku jaar fa waajuram jaar ba doon la baayam doonoon.

Su ko defee bu dee bi ngay topp baay, boo ba doom juddóogul te sa jaayante sell, nekkoowoon ca daara ja di toppi tere te doo jëfee ndigal, sëriñ bi di na def ci yaw ba nga xam ni bu toppe doon am, doom ji yaw la war a topp ngir li ko raw ci waajuram ci xam-xam, nga baaxee ko ko ndax ab sëriñ du sette te ki mu xam mooy ku ko nangul, doonte doomam nga, soo ko nangulul, su faatoo mën ngaa donnu alalam waaye xam-xam bi, ñi ko nanguloon kepp a ko

Page 145: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 5

moom te ñoom la ko ko Yàlla joxloo. Sëriñ bu mat sëriñ, ku ànd ak moom te Yàlla tax te dëggal yaay xëlsee donnu xam xamam.

Sëriñ Tuubaa ngi wax ni doom ñaar la, doomu xol ak doomu ndigg, doomu xol mooy donnu mbir, doomu ndigg mooy donnu alal, nitu Yàlla donnu mbi-ram moo gën fuuf donnu alalam, moo tax seen njaboot saa su nekk da ñuy faral di jaay seenug askanoo ci moom jëndee ko ag taalibe, topp sëriñ ngir alal xayna tay la xew waaye xam xam akug defaru biir ak biti la ñu daan sàkkusi ci ñoom.

Diine xamul askan, ki muy jiital saa su nekk mooy ki ëpp xam-xam te jub. Fa’izaa nufixa fii suur falaa ansaaba baynahum yawma’izin wa laa ya-tasaa’aluun, bu ñu ëfee ca bufta ba, askan du dox diggënte kenn ak kenn, Sëriñ Tuubaa wax na ca Nahju, Fa inamaa tafaawutal waraa bil ilmi wa dii-ni yakuunu fasbiraa laa bintisaabihii, gënante ci xam-xam ak diine la nekk waaye du ci askan.

Dereet da fa mat a wormaal, moo tax sa xam-xam walla sa daraja lu mu rëy-rëy, wormaal sa njabootu sëriñ daa war ci jamono ju nekk rawatina bu ñu melee na ñu war a mel. Ku bokk ci njabootu ab sëriñ te mel na mu war a mel ba nit dikk ci moom di sàkkusi ci moom la ñu daan sàkku ci waajuram, kenn warul wax ni da koo donnu, nekkoon ca daara ja di jëfee ndigal aka bàyyi tere ba xëy defaru ba mana defare moo ko ko may. ab taalibe bu def nii yit mooy xëlsee doon sëriñ ba bu ëllëgee doonte bokkul ak moom aw askan ci saayir.

Bb : Looy wax ci sëriñ da fay topp askan, taalibe di topp askan, askan wii ku ci bokk di ab sëriñ, askan wii ku ci bokk di taalibe ?

St : Laaj nga lu am solo, xam nga wolof da fay wax ni loo doonul taalibeem doo doon sëriñam. Sëriñ boo gis taalibe la woon, lu ko moy sëriñ gi wérul. Kon, bépp taalibe bu dëggal te matal jaayanteem ci pas-pas ak yite ju kawe, yaay xëlsee doon sëriñ biy defal ñi la topp la la sa sëriñ defaloon. Loo lu mooy Seexal wala Muqadamal.

Sëriñ Saam Mbay, Yal na sunu Boroom yokk leeram, daan na na wax ni seexal mooy defar nit ki ba mu weesoo yàqu, nga ber ko muy defare. Al’aqra-bu awlaa, mbay ci sa wee wu tank, li ngay def ci jàmbur, ki la jege tam bu la nangulee te di jëfee say ndigël di bàyyi say tere, bu yàggee nga def ci moom lu mu la mën a wuutoo sa ginnaaw. Moo tax kooy topp def ko sa sëriñ, na ànd gi tege ci dëgg te dëppoo ak li Yàlla gërëm.

Yàlla Moo nu moom te bokk nu sant nu jaamu ko, jaamu Yàlla fardul ayni

Page 146: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 6

la kenn du ko defal kenn, ku ci ne yaa koy defal sa bopp. Sëriñ bi da lay xamal Yàlla mi la sant nga xam ko bala nga koo jaamu. Dégg nga Sëriñ Muusaa Ka di wax ni Sëriñ Tuubaa di maanaam dex ku dem duy, ku sóobu ni mes bu génnee xam Boroomam, ku sàggan sanku fàwwu te lab te doo duy, doo set, doo setal, doo xam Boroomam.

Sëriñ mën naa am ci njabootam ñuy dooni Sëriñ ni moom, ndéem jaar na ñu fa seen waajur jaar ba doon ko. Sëriñ Tuubaa daa mos a jàpp ci mbaggu ku ñuy wax Sëriñ Muxtaar Binta Lóo ne ko Muxtaar mbaa su ma léen wonee ginnaaw du ngeen jaamu xërëm, mu ne ko Mbàkke kenn du la xam di jaamu xërëm, Sëriñ bi ne ko Muxtaar su ma léen wonee ginnaaw ndax xam nga luy jaamu xërëm, mu ne ko Mbàkke boo nu ko mënee leeralal, Sëriñ bi ne ko Muxtaar su ma léen wonee ginnaaw, ku sant sama sant wii walla kuy dara-jawoo sama daraja, bu ngeen ko gisee tàggalikook mbaxana ak dàll raam jox ko seen àddiya, koo kee bu dee ndigël i Yàlla yi du ko jëfee, tere Yàlla yi du ko bàyyi yéen a ngay jaamu xërëm te kuy jaamu xërëm xam nga fu la sunu Boroom di booleek xërëm ba jëmee? Mooy safaanub àjjana, kon bu ma léen wonee ginnaaw bu léen jaamu xërëm.

Muy taarix bu mat a bàyyi xel rawati na ci jamono bu doy waar bii nu tollu, nga xam ni man ngaa bëgga defaru naam waaye gis ku la mën a defar bu wér a wér jafe waaye lu waay yittewoo te muy dëgg ci moom te Yàlla tax, sunu Boroom mën na ko cee defal tawféex ba mu dajeek waay ja.

Bb : Li nu lay mujjee laaj mooy noo gisee fii jamono toll ni jullit yi jàppee seen diine ?

St : Lislaam gu woyof toyy, tegu ci ñàkk a gëstu ku jéggi dayo ngay seetlu ci li ëpp ci jullit ñi, fonk lool liy dundël seen bakkan ba mu jaral léen lu nekk.

Ni nuy sàkkoo sunu am am di yokku, nu ko raw fuuf la nu war a bàyyee xel sunu lislaam te fexe di dolleeku ci xam-xam akug sell, lu ko moy lu la fëkk di na yomb lool ndax fii jamono toll ci ag yàqu li mën a gàllankoor jaam bi ba du dellu ci Boroomam bi ko fi indi te di ko fi xëlsee jëlee boo ko doon lim di nga fi yàgg lool.

Yonent bi SaWS jàngal na nu ni ki yeewu mooy kiy toroxal bakkanam tey jëfal la ca ginnaaw dee, alkayisu man daana nafsahuu wa amila lima ba-hdal mawt. Da ñoo toll ci mujjug jamono, liy nuru dëgg te du ko da fa bari. Lu jamono yàgg yàgg, du tax dëgg soppeeku. Mbooloo moo dem fekk fa ñoo xam ni boo léen xoolee xeeb kilifa ga, kenn muccu ci, am na ay jullit yoo xam ni boo léen xoolee xeeb léen waaye Yonent bi SaWS mooy sangu mbooleem mbindéef yi, am na ay murid yoo xam ni boo léen xoolee xeeb léen waaye

Page 147: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 7

Sëriñ bi neewoon na kër gi ku jël yar gi bàyyi woo fi darra, ku ko fi bàyyi jëlee woo fi darra. am na ci kër i diine yépp, terewul du ñàkk mukk ñu teg seen tank fa ko mag ña tegoon tey sellal seen keem kàttan, bokk ci ñoo ñu moo am solo wëlis leneen.

Di naay faral di wax ni, fa mag ñu baax ñi jaaroon ba sunu Boroom defal léen, ku fa jaar tay te muñ coono ak tiis ya yoon wa làmboo, di na la ko defal walla mu defal la lu ko ëpp moo tax Sëriñ Tuubaa wax na ci Masaalikul Jinaan, wa laa tuxasis fadla Rabbin qad alaa bi zii taqadumin faqat fa tajhalaa, iz rubbamaa urii fattan muwaxaraa maa haaba aman xablahuu wa asuraa, ngëneelu sunu Boroom yi bul ko jagleel mag ña kon nga réer ndax bariwaana fu ku yéex a feeñ amee loo xam ni jafewoon na ña ko jiituwoon walla sax amu ñu ko woon.

Yoon woo wu nag ñi mu ñor daa bareetul te ñu bari jàpp na ñu ni fa mag ñi yeggoon kenn doo tu fa yegg te muy njuumte lu rëy ndax sunu Boroom bi léen ko defaloon mi ngi fi ba léegi te du ku fiy jóg, du kuy tële.

Seex Muusaa Siise da fa daan wax ni Mag yu baax yi nekkuñuwoon ay jinne ak i njuumë yuy soppeeku, ay nit la ñu yu jàpp dëgg bàyyi neen te yoqatu ñu ba xëy doon xutbu ak xawsu yu ràññeeku, muy kàddu gu am solo ndax nit lu mu jombale boppam du ko mën a am mukku.

Li nga xam ne yàgg yàgg nga tàqarlikoo ak moom, boo sàgganee ba mu xañ la sa ëllëg ga ngay sax ba fàwwu, sank nga sa dund, sa këru ëllëg, say jëfu tay jii nga koy tabaxee, man amila saalixan fa linafsihii wa man asaa’a fa alayhaa, ku def lu baax sa bopp ku def ñaawtéef sa bopp, kenn deful kenn darra, kenn defalul kenn darra lu waay def boppam. Yàlla Moo nu moom, wàccee nu ci kër gu suufe gii di nu wërsëgal, na nu ko fexee dellooo njukkël ci sunu dund wu gàtt wii sunu keem kàttan, ci jaamoo ko ni mu ñu ko digëlee ndax mooy tax mu nangu ko, bañ di doxee njort wala ag réer.

Bb: Jërëjëf, sant na nu bu baax ci kàddu yi, Yal na nu ci Yàlla sunu Boroom defal dégg ak topp ?

St : allahuma amiin te nu bokk ko bijaahi Sayidunaa Muxammad SaWS

Page 148: Teere Jangal Sa Diine Ci Wolof Allaaji Jibi Sey

Page Facebook Daarayi.com - www.daarayi.com - Aji dajale ji : Allaaji Jibi Séy Jàngal sa diine ci wolof - Téere bu làmboo njariñ yu bari ci Lislaam

1 4 8